Jëfandikukat:Juuf

Jóge Wikipedia.

KAN MOOY SËRIÑ ALIW JUUF LÀMBAAY ?

Sëriñ Aliw Juuf, di doomi ku ñuy wax Sëriñ Birima Joor Juuf, doonoon ku bàyi woon nguur ga ca Làmbaay dem Kajoor, ci ku ñuy wax Sëriñ Moor Taay, ngir dundal Lislaamam ak doon jullit dëgg. Ba muy dem foofa la yobbaale doomam jii di Sëriñ Aliw Juuf, ba foofa la jànggee Alxuraan. Waajuram wu jigéen, mi ngi tudd Soxna Kumba Naar Njaay. Mi ngi ganee àdduna ci dëkk bu ñuy wax Njeŋ Làmbaay ci atum 1850.

Mu bokkoon ci àskan woo xam ne, ñépp xam nañ léen doon ay wuur yu daan yilif Bawol, muy jaraaf Bawol ak kër yugar Juuf, di àskan wu ràññeeku lool ca Làmbaay.

Sëriñ Aliw Juuf, doonoon taalibé Sëriñ Tuubaa bu ko teela topp lool, ndax jéblu na lu mat fukki at (1885), Boroom Tuubaa sooga dem ci tukkib Géej gi.

Ak jéblóom mi ngi sababoo ci ak jokkoom ak Sëriñ Baabakar Njaay Cargaan mi nga xam ne xaritam la woon, te lu jiitu loolu ñi ngi doon wër ku léen àggale ca sunu Boroom, moo waral Sëñ Aliw nekkoon ca ku ñuy wax Sëriñ Manjaay Baye. Ba mu fa bàyi koo, la àndag Sëriñ Baabakar Njaay ak Sëriñ Momar Maane, ñëw ci Sëriñ Bàmba jébbal ko seen bopp. Sëriñ bi tarbiya na ko ñatti at, ligéey lóo na ko ci anam yu bari te wuute lool, daan yalwaan di ko indil, daan ko fekk Gànnaar (gu njëkk ga) di ko indil ay àddiya, ci biir ak tarbiyaam Sëriñ bi yabal na ko ci nitug Yàlla ku baax, ku ñuy wax Sëriñ Demba Mbaru ca Luga, Sëriñ Aliw nekk ak moom, di ko ligéeyal ci ndigalul Boroom Tuubaa, ba koo ka yewwi ko.

Mu ñëwaat ci Sëriñ Tuubaa, di ko ligéeyal, ba Sëriñ bi gëram ko, yewwi ko. Keroog ba mu koy yewwi ci la waxoon waxam ju siiw jii ne ko الولد ولدان، ولد القلب وولد الصلب Sëriñ bi da ne ko « doom de ñaar la : doomi xol ak doomi geño » dàl di ne ko « yaw nak def naa la ngay sama doomi xol ». Ba mu ko yewwee la ko digal mu dem Làmbaay, ne ko « lépp di na la fa fekk »

Mootax ba mu ñëwaatee ca dëkk ba Làmbaay soppi ku na lool, waaye daj nañ fa coono yu ne ñoom ñatt ñooñu. Ki léen gënóona sonal nak, mooy buur ba ñuy wax Teeñ Tanoor, ndax daa amoon ab jarbaatam bu jéblu woon ci Sëriñ Aliw Juuf, loola nak doonoon coow lu bari ca Làmbaay, mu naqari woon ay waajuram lool, ci la buur bi dogoo ci ne nak, ñatt ñii moom (Sëriñ Aliw Juuf, S. Baabakar Njaay ak S. Momar Maane) da léen di faat mu jeex, wala mu génné léen Làmbaay, ndax dañ fee bëgga indi luñ xamul, te bu séen pexe joyee, dinañ nësaxal nguuram.

Mboor mii la Seex Musaa Ka di juñju ci wolofalub Jazaa-u Chakuur, naan :

« Ca mooma at la teeñ Tanoor kalaame Seexi Bawol, ngir bëgga fay Lislaami

Jarbaat ba moo jéblu woon dem tuubi Ndayam di jooy, mu naan ko « tuubi, ruubi »

Seex Baabakar Cargaan, Sëriñ Moor Maane Sëriñ Aliw Juuf Làmbaay, ñilée ko daane

Keroog da léena woo fa péñcum Làmbaay Naa léen « di naa léen tàqalee ki laxasaay »

Keroog da leena boole sol cib wurmbal Ñuy kenn-kennoo, farba jaa ngay darmbal

Muy bocci ay gobar, di feeñal dàmm (dereet) Di boole door ak yeew, amul far jàmm

Te naan baléen Seex Bàmba, mbaa ma rendi- Murid yi yépp ! ma nga naan ba màndi

Murid ya naan ko Bàmba nos na ruu yi Yawma alastu, yaw faral tey noyyi

Sëriñ Momar Maane ko tontu booba Ne ko « da ngay kàcc, da nuy dem Tuubaa »

Folli la tay, tekki sa ndombak tànk Moo gëna yombu lii nga wax, noo lànk

Dag ya ne tiss, péñc ma dàl di jaxasoo Murid ya xaacu, mbër ma faf di laxasu

Murid yi ñëw Tuubaa, xibaar ko Bàmba Mu xëy ne ñaanal léen ko, tas naa jal ba »

Kon nii lañ nekkee woon ñoom ñatt ñi, di ay mbokk ci àskan ak ci pas-pas, ba Soxna si mu njëkka deñc sax, jarbaatub Sëriñ Baabakar Njaay la, ñu di ko wax Soxna Mati Juuf.

Jamono jii yépp nak, Sëriñ Tuubaa ngi digënté, Daaru Salaam, Tuubaa ak Mbàkke Baari. Ba ci 1895 bi Sëriñ bi di dem ci tukkib Géej gi, ci la ko booleg Maam Cerno Biraahim.

Mu féeté woon ak moom, ba amoon na kër ca Daaru Muhti, daan ko ligéeyal lu bari, tarbiya wu ko, tuddé ko lu bari ci ak njabootam, ba Maam Cerno gëram ko.

Ginaaw bi Sëriñ bi ñibbisee yit, taxul mu dellu, ca Maam Cerno la nekk, ba bi Sëriñ bi ñëwee Njaaréem la ko jox ndigël mu ñëw fa moom. Ci la sañcee këram foofu ci Diourbel.

Ginaaw Sëriñ bi yit, loola la wéyal, dellu wu ca ginaaw benn yoon, nekkoon ci dëgante dëkk ak Daara yi mu sañcoon, rawati na dëkkam bii di Ñiibi Làmbaay, gi nga xam ne bokk na ci dëkk yi mu gënoona fonk, foofa la nekk ba ni mu làqoo ci atum 1951, mu dundu 101 at. Sëriñ Abdul Xaadr moo ko jullé, ñu deñc ko ci Tuubaa.

Yàl na ko Yàlla dolli ngëram te taas nu ci bàrkeem !

Ay xalifaam : S. Muhamadu Seex Juuf (1951 - 1977)

S. Moodu Juuf Làmbaay (1977 – 1991)

S. Cerno Juuf Làmbaay (1991 – 2006)

S. Mbay Juuf Làmbaay (2007 – 2017)

S. Cerno Faali Juuf Làmbaay, mooy xilafab Sëriñ Aliw Juuf 2017 ba tey, yàl na ko fi Yàlla yàggal lool te may ko wér

Ci xalimaag : Abdu Xaadir ba Majalis

Ci tooppu ag jubantig : Mamadu juuf