Aller au contenu

Buuna Alburi

Jóge Wikipedia.

Buuna Alburi :Buuna Al-Buri Njaay:Nekk buur ba Jolof 1895 ba 1900. Moo ngi judd ci atum 1877 walla 1878 ca Yaŋ-Yaŋ foofee ca Jolof, turam dëgg mooy Yélli Biri Yamb Njaay, baayam mooy Al-Buri Njaay Saynabu. Yaayam mi ngi tudd Ma-Jiégeen Baasin Njaay, kon moom béte-béte la Njaay ci baay Njaay ci yaay.

Buuna Al-Buri nekkoon na nit ku jàmbaare lool, tabax na yu bari ci Jolof.

Ci atum 1930 la def 80i teen, ñeel waa réewam loolu lépp nag ci alalam la ko defee ak ci ndimbalu waa Jolof!

Bokk na ci yooyu ci atum 1928 mu tàmbali tabax chemin de fer bi 128i maitre ci guddaay ba ci atum 1931.

Bokk na ci ñi njëkk a defar mbalka ngir denc ndox, mooy bassin à Labgar 1931. Waaye mu sàkku ci ay doomam ñu bañ a sàkku benn xaalis ci loolu te taxawal seen teeni bopp.

Bokk na ci bañ gim mu bañ a bokk ci élections de novembre bi ñu doon amal ci atum 1946, ci diggante Lamin Gey ak Seŋoor.

Ci la wax waxam ju siiw jooju ne: "danoo war a fexee néewal sunug bëgg-bëgg, waaye tamit nu bañ a déglu ñi nuy teqale, ndax danoo war a xalaat ëllëgu sunuy réew ak sunuy sët, te duma wéeru ci kenn ngir sama tur man a nekk ci limkak élections législatives yi."

Bokk na ci ay waxam: "kuy jariñoo alal réewam mi ñu ko dénkk du ko liggéeyal mukk."

Buuna Al-Buri Njaay, diggantéem ak mangu diine yi ci Senegaal.

Sëriñ Abdu Salaam Kan ca Kaneen xaritam la woon, amoon na jëflante yu bari ak sëriñ yi ci réew mi rawatina Al-Haaji Maalig Si, joxoon na ko it ay doomam, defoon na Muxaddam tiijaan.

May na Seex Ahmadu bàmba Mbàkke suuf su yaatu lu toll ci 200 hectares ca Mbàkke Baari. Waaye tamit may na kii di Sëriñ Fàllu Mbàkke lu toll ci 200 hectares ca Tuubaa Bogo.

Def nañu ko foofee ca Paris délégué à l'expression universelle ci atum 1900, nekk na délégué des chefs de province de l'AOF à l'exposition coloniale de 1906.

Ba tay 1906 bokk na ci conseil privé du gouvernement du Sénégal.

Ba tay doon na chevalier de la légion d'honneur 1918.

Ba tay Crois de guerre 1914-1918. Ba tay officier de la légion d'honneur. Bokk na ci conseil du gouvernement de l'AOF et commandeur du Mérite agricole, et l'étoile noire du Bénin.

Ci 14 juillet 1924, nekk na délégué des rois et chefs de province de l'AOF et dépose une palme sur tombe du soldat inconnu ca Paris sous l'arc de Triomphe.

Afrig mu am Liberté ci atum 1906, ci at moomu itam ci la nekk membre ñeel conseil de gouvernement du Sénégal.

Moom nag amal na liggéey bu am solo tax na faraase yi bëggoon ko lool ba takkal sax ay medaay manaam ay neexal, te it Faraase yi joxoon nanu gëdda lool ndax ag njàmbaarm.

Moom nag mi ngi Faatu ci bisub altine ci atum 1952.

Al-haaji Mansuur Si moo ko jullee ak ñam ca àndal, ci noonu la ñu ko yóbb ca lingeer denc ko goofu.

Am na ecool bu nekk foofu moom la ñu ko tuddee.