Aller au contenu

Basiiru Jomaay Jaxaar Fay

Jóge Wikipedia.

Basiiru Jomaay Jaxaar Fay mooy ñeenteelu njiitu réew bu Senegaal

Mi ngi juddu atum 1980 ca Njagañaaw, ca sowwu Mbuur, ca Senegaal. Mu am (Licence) ci atum 2000, ak (Master) ci droit ca jànguneb (Université) Seex Anta Jóob. ginnaaw ba mu jàll ñaari examen yi, dugg ci (Ecole Nationale de l'Administration et de la Judiciaire ci 2004).

Bimu amee (diplôme) , ñu tabb ko, mu nekk (inspectër) ci juuti gi("Impôts et Immobilier") ci Departemaa bi yor Taax ak Immobilier, mu xaritoo fa ak Usmaan Sónko, di moroomam bu mu bokkal fumu amee diplôme ci jenn daara.

Ci atum 2014 la Jomaay Fay ak Sónko gën a dëgëral séenug xaritoo ci biir Union de l'impôt et des propriétés bi Sónko sos, di Patriote pour le travail, la moralité et la fraternité.

Bi Jomaay Fay nekkee njiitu pàrti bi, dafa tàmbali benn kàmpaañ ngir yombal boroom kër yi ci ñiy fay juuti ak ñiy yor moomel.

Cig ndorteel, dafa nekkoon gan ci pàrti bi, ci diir bu gàtt mu dem ba nekk kenn ci ñi gëna am doole ci pàrti bi.

Bokkoon na ci ñi am xam-xam ci prograamu Sonko ngir kàndidaatiiram ci wotey njiitu réewum Senegaal ci atum 2019. Sonko am luy toll ci 16% ci wote yi mu nekk ci ñatteelu palaas bi. Ci weeru fewriye 2021 la Jomaay Fay nekk Secrétaire général bu pàrti Patriotes pour l'action, la moral et la fraternité (PAMT) ginnaaw bi ñu jàppee Usmaan Sónko ci tuumaal ko ag caay-caay. Ngir man a am ndam ba jot ci Nguur gi Jomaay Fay tëral ay pexeem jéem a boole kujje gi ngir eleksioŋ yu 2022, mu am 56 toogu ci biir Alliance de libération du peuple.

Liggéeyam ci politik

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Ci Octobre 2021, dafa bokk ci Coalition pour la Libération du Peuple ak benn pàrti Parti Démocratique Sénégalais ngir represente dëkkam ci election municipale yu 2022, waaye amul ndam.

Ci weeru awril 2023, dañu ko jàpp, tëj ko ci tuuma ni tasaare xibaar bu dul dëgg, saaga àttekaay bi, ak saaga nit ñi ginaaw bimu gëna ñaawlu àttekat yi ñi dogal àtteb Ousmane Sonko ci fasu appel.

Bisu 15 màrs, 2024, benn bis ginaaw biñu ko génnee kaso, mu dajale téemeeri nit ñu ko doon jàppale ci kanam bu njëkk bi mu feeñ ci mbooloo mi di taxawu njiitu réew.

Ci bis boobu, njiitu réew mi woon Abdoulaye Wade ak pàrti Demokaratik bu Senegaal bimu àndaloon, jàppale nañu Bachir Faye, loolu gëna dooleel wërsëgu am ndam ci eleksioŋ yi.

Bi muy kampaañam ngir nekk njiitu réew, dafa wax ni dina joxe liggéey, def kampaañ bu dëgër ngir xeex ger, ba noppi ni dina xoolaat kontraa yi ci wàllu kuuraŋ.

Mi ngiy daw ci wote bii di «Diomaye mooy Ousmane», maanaam «Sénégaal bu Boroom, Njub ak Naataange», te yaakaar na ni Ousmaan Sonko ak siiw gi mu am ci ndawi Senegaal yi dina tax kàmpaañam gi dox.

Emissionam dafa niroo ak programme Ousmane Sonko ci 2019.

Taxawaayam ci politig

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Fay neena gëm na coppite nguur ak doxaliin u yenn ci réewi Afrig yi ngir fexe ba Senegaal moom boppam, muy wax ju yenn gëstukat yi jàpp ni dafay wane ni dafa bëgg a sori réew yi am doole yi, rawatina Frãs, mi njiite nooteel ga woon.

Ag njabootam

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Fay am na ñaari jabar: Mari huun Fay ak Absa Fay. Mari huun mbokku jëkëram la, ñu am ñeenti doom: ñatti góor ak benn jigéen. Mu amag benn doom Absa Fay. Moom ak Sonko ay xarit lañu, ba sax mu tudde kenn ci seeni doom yi Usmaan ngir sargal seen xaritoo.

Dige na itam ni dina xeex aakimoo gi Frãs def ci koom-koomu Senegaal su amee ndam ci joŋante yi