Attiwaal

Attiwaal, (الطوال) walla assabhu tiwaal,(السبع الطوال) di juróom-ñaari saar yi nga xam ne dañu leen di boole ci saar yu gudd yi, ñoom nag ñooy xaaj bu njëkk ci 4i xaaj yi nga ne danañu ko xaaj saari Alxuraan yi, fi ñuy dugg nag, mooy ñoom ñoo jiitu, saar yi ñiy wax Almi-uun,(المئون) ak Almasaanii,(المثاني) ak Almufassal,(المفصل) di 4i xaaji saari Alxuraan wi ci jiitu di (Attiwaal),
Ag tuddam ci sunna(hadiis)
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Attiwaal walla sabhu tiwaal nag ñëw na ci sunna walla ci hadiis, mooy fi Yonente bi di waxe ne:( joxeef nama lu wuutu Tawreet mooy assabhu tiwaal, ak lu wuutu sabuur mooy Almi-iin, ak lu wuutu Injiil muy almasaanii, ñu gënale ma ci mufassal). «قال رسول الله ﷺ : «أعطيتُ مكان التوراة السبعَ، وأعطيتُ مكان الزبور المِئِين، وأعطيتُ مكان الإنجيل المثاني، وفضِّلت بالمفصَّل»
Lan mooy assabhu tiwaal ?
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Boroom xam-xam yi nag, Li gën a lëng ci seeni wax, (Assabhu tiwaal), mooy: Baqara, Aali-himraan, nisaai, maa-ida, lanhaam, lahraaf, lanfaal tawba, amna ñenn ci boroom xam-xam yi ñuy boole tawba, ak lanfaal muy wenn saar, Amna ñu wax ne it Assabhu masaanii,(السبع المثاني) mooy assabhu attiwaal ba leegi di Baqara, Aali-himraan، Nisaai, Maa-ida Lanhaam Lahraaf، Lanfaal، Tawba، ci boroom xam-xam yi nga xam ne dañoo jël ñaari saar yooyu def leen benn, muy Lanfaal, ak Tawba, amna ñu ne it
Assabhul Masaanii
[Soppi | soppi gongikuwaay bi]Assabhu masaanii (السبع المثاني) mooy saaru Faatiha; di juroom ñaari laayay Faatiha boo ci boolewul Basmala, Li gën a wér ci waxi boroom xam-xam yi . Wax jii nag moom la,Ibnu Jariir ak Ibnu Kasiir tànn jële ko ci waxi yonnante Salal laahu halayhi wa sallam ñeel Abuu sahiit ibul Muhalaa ci ngëneelu Faatiha ne ko:«حديث»( moom Faatiha mooy assabhu masaanii ak Alxuraan ju màgg ji ) «قال النبي ﷺ لأبي سعيد بن المعلى في فضل الفاتحة: «هي السبع المثاني والقرآن العظيم» ak li nga xam ne moom Albuxaari nettali jële ko ci Abuu Hurayra mu wax ne yonnante bi Salal laahu halayhi wa sallam nee na:( Ndayi Alxuraan mooy Assabhu masaanii ak alxuraan ju màgg ji) «رواه البخاري من طريق أبي هريرة أن النبي ﷺ قال: «أم القرآن هي السبع المثاني والقرآن العظيم» (*)، » Li tax ñu tudde (Faatiha) Assabhu masaanii moo di ne dañu koy baamu ci julli farata yi ak naafila yi.