Ahmadou Bamba

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Amadou Bamba)
Ahmadou Bamba (1853 1927 ?)

Ahmadou Bamba' mooy ki taxawoon jàmmaarlook tubaab yi, ngir xeexal lislaam, te desal fi sunu ag dëkk ci Afrig tey bég cig cosaanoo fi, kon njukéel ko war nanu, kii moy ki taxawal yoonu Murit, tey ki taalif lu sakkan ci diine, indi ay gisiin yu bees, ginaaw bi nu ko sonnalee genne ko ay yoon réewam

Dencukaay:B33.jpg
Seriñ Tuubaa Xaadim Rasuul ca leer nga

Jiitalug aji firi ji[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Li ma tax a jug, jëme ma ci def bile ligéey, te ma jàppe ko muy bu am njariñ, mooy, benn: jortu ne, ci def gi, ñi ngi ligéeyal Sëriñ bi, waaye it xeet wi, ndax jël lu mel ni jaar-jaari Sëriñ Tuubaa, ak li mu làmboo ciy njariñ, nga tas ko, teg ko ci fu loxol ku nekk jot,yombal ko ba ku jug man koo xam, man koo dégg , man cee jariñu, ca anam ga mu gën a yombe, gënnee leere, te yaakaar naa ne def ko ci wolof , ñeel wolof yi,ci anam yiy yombal la, tey leeral,lu mel ne lii de yaakaar naa ne amul lu ko gën di ligéeyal Sëriñ bi,waaye ag ligéeyal sa xeet it mi ngi ci, ndax ag dundal la, ñeel saw làmmiñ, te gis naa ne lu waay man a xame ci làkk, ak wu mu man a doon, ci sa wos, lay gën a dugge,lay gën a tooge,lay gën a nekke, luy dund ak yaw, ci lay doone kenn ci yaw, ngay yaw itam kenn ci moom, ngéen di benn bu dul ñaar, gis naa ne bokk na ci li ñiy rawe di rawe, di jànge ci seeni làkk, di ci waxe, di ci xalaate, te di ci jokkoo. Man de bile téere,njëkk ma koy tekki, nekkoon na di bob,dees na soxla as lëf ci waxtu,ngir yër ko,dégg ko,naan ko,waaye daa mel ni bi ma ko defee ci wolof,soxlaatunu lu dul lu néew, ngir jaar ci, jaarati ci, kon nanu fonku sunu bopp,ci fonkaat bu baax sunu làkk yii,te xam ne dug fonkadi ñeneen ñi. Ñaareel bi mooy , gis gi ma gis téere bii,di bu jéggi dayo ba ci solo ak njariñ, di delluwaay ci delluwaayi téerey yoonu murit wi,di rootukaay ci yu xam-xam yi. Làmboo nag kem bu bu réy ci xam-xam, ci lu aju ci Sëñ bii, di kenn ci ñi ñu war a xam, bu ma waxul ki ëpp solo ci ñoom . Kon xam leen ne yii ak yeneen yu ma waxul, ngir bañ a guddal, ñoo sabab firi gi, nga rax ci dolli,nekkug aji taalif ji, di kenn jëllewaayi yoon wi,yu xam-xam. Ndax kat, boo yëree, da nga ko gis lu bari mu naan Sëñ bi nee na ma, te loolu du lu yomb . Kok bëkk-néeg la woon ci bëkk-néeg yi,bu ma waxul ngën ji bëkk-néeg , kon kooku maneesu koo gën di jëlewaay, mbaa delluwaay, rawati na muy ku ñépp xam ag sellam, akug dëggoom, yal na nu Yàlla taas ci barkeem te dolli ngërëmam ci Sëriñ sunu,Sëriñam,laafaale ko, ci barke ku nu ligéeyalam, ak ki muy ligéeyal moom mu mujj mi, Aamiin,yaw boroom mbindéef yi.


Jiitalig aji taalif ji[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ahmadou Bamba (1918)

Bii mooy teereb Irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, di ci maanaa nàndalug aji naanaale ji (ki ngay toogal di naan) ci ndox mu neexum sopp jëwrinu yonant bi , di xam-xamu jaloore bu nu gàttal mu ñeel nag ki bëgg a am ab xam-xam ci dundug sëriñ Ahmadu Bamba yal na yàlla dolli gërëmam ci moom ,te jariñ ñu ci,amiin. Ki ko taalif it di ku xeebu ku aajowoo ndimbalul boroomam ak yërmaandeem,tey yaakaar ci moom mu jéggal ko ay bàkkaaram,te làqal ko ay ayibam,yi feeñ ak yi nëbbu,fii ak fan jëm,di Muhammadul Amiin JOOP doomi sheex Ahmadu JOOP mu dagana,yal na leen yàlla boole jéggal. Di it taalibeb sëriñ Tuubaa, yal na ko yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom,amiin.

Maa ngi ñaan yàlla mu musal ma ci saytaane mu nu jam mi,di tàmblee nag samay wax ak jëf ci turam wu tedd wi,moom mi yor yërmaande ju yaatu ji matale mbindéefam yi ci àdduna,te di ko jagleel ñi ko soob ca àllaaxira,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci sunu sang,Muhammad,ak ñoñam aki saabaam.

Aji xeebu ju yitewoo yërmaandey boroomam,ak ndimbalam ci ligeeyal yarkatam bii dib soppeem(di sëriñ Tuubaa) - aji xeebu jooju di Muhammadul Amiin JOOP doomi Sheex Ahmadu JOOP mu Dagana, nee na: ag cant ñeel na yàlla miy leeral àddinaam ji ci wàlliyoom yi,di feeñalati ci ñoom yoonu yonantam yiy gindee,yoon woowu di wu weetal yàlla ak jaamu ko,mooy yoonuw boroom xel yiy dàq lu dul yàlla ci seeni xel,tey jànge ag njub ca yooyale imam,ci jox leen seen bopp,jébbal leen seeni mbir. Ndax kat ñooñu, ñooy ñi yàlla naan ci alxuraan: ulaayikal lathiina hadaahumul laahu fabi hudaahumuqtadih muy ci maanaa ñooñu,ñooy ñi yàlla gindi kon royal ci seenug gindi.Di julli tey sëlmël ci yonant bi.

Leegi nag ginaaw yàlla day xéewale xarnu bu ne aw waliyu wu koy gindi di ko won yoonu jub ,di ko tee jàdd, nun waa xarnub fokk ñeent nag mu defal nu,xeewal gu tollu ne sunu mbég mii di sunub sëriñ tey sëriñub julit ñi, Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah yal na ko yàlla wattu te wattul ko,te gërëmi jëfam,te méngoo ko,moom nag mbooloo maa ngi ko gën a xame ci turu sheex Ahmad Bamba MBÀKKE Xaadimur rasuul.

Bi loolu amee ma, bëggoon a leeral as lëf cig dundam, ñeel ki nar a ñëw ginaawam,te bëgg a xam dara ciy mayam. Man nag maa ngi giñ ci yàlla dellu di ci giñaat naan dey xam naa ni xawma te du ma ci man a wax mbaa indi lu dul la gën a néew,la gën a bari moom bu ko xalaat,ndax manu ma ko ba koy def. Waaye nag dinaa jéem a nooyal yoon wi,ba ku bëgg te yàlla ubbi ko, barilub xam-xamam, yinkiiwal ko jariñ jaamam yi, ngir sàkku ci ngërëmam,bu ñëwee man cee jaar,ndax kat am na ci addiiz mu sell mi: mbindeef yi njabootug yàlla lanu ,ki ci yàlla gën a bëgg mooy ki ci ëpp njariñ ci njabootam gi. Nee nanu ku taarixal aw wàlliyu mel na ni dundal nga ko.

Kon am leen gàttalug jaloore (jaloore mooy taariix walla histoire) gii ma tudde irwaaun nadiim min hathbi hubil xadiim, may ñaan nag képp ku ci gis lu ko yeemut, mu xam ne gàttub jéegoo ma tooñ,mu jéggalul ma Yàlla te suturaal ma,te bañ koo ngàññi,ndax kat da na ci gisi leneen lu bari lu koy yéem, lu man a wecci loolu ko yéemutoon, ndax téere bii ab muxaddima rekk la ( ag jiital) teere dëgg bi mooy minanul baaqiil qadiim fii ma aathiris zheixil xadiim muy ci maanaa xeewali aji des jiy aji jiitu,ci ngënéeli Sheexul Xadiim.Doomam ja Sheex Muhammadul Bashiir defoon ko,yal na ko yàlla sàmmu te guddalu fanam,te jariñ ci lu bari jullit ñi, ni baayam,moom dey teere bu boole la te wattu,te dib dër bu naat ñeel ku bëgguw yiw te di ci dox. Yal na ko yàlla mottali te nangu ko,te tas ko ci àddina bi,muy ndëxëñtéefam ëlëg ca àllaaxira,tey lu nu koy fàttalikoo ginaawam ci fii fi àdduna,ci barkeem ak ci barkeb ki ko taalif ak ki mu ko taalifal,yal na nu yàlla nangul,te nangul nu sunub teere,matal ko te tas ko moom itam. Moom kat yàlla mooy aji kawe jiy boroom ngënéel ak tawfeex,tey boroom li fii ak la fee.

Doggantal gu njëkk gi : ci xamale kuy Sëriñ bi, ak ay mbiram, ba bi waajuram wu góor làqoo[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëriñ baa ngi gane àdduna ci li nu wax - ci atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk 1270 g, am ñu ne atum junni ak ñaat téeméer ak juroom ñaar fukk ak ñaar 1272g,ca kër waajuram wu goor ca Mbakke Bawal ,mu nekk leegi ca wetu yoonu saxaar ga. Boroom xam-xam bu mag bi nuy wax Alhaaji Hamidin doomi Usmaan Alfuutiyu Altilriyu nee na: (( sëriñ baa ngi gane àdduna moom mi sunnawoo sunnas yonnant bi,ci atum sharaha,muy 1270g làqu atum shumoos muy 1346 g te booba mi ngi am juroom ñaar fukki at ak ñeent mel ni ay jant. Am ñu ne juroom ñaar fukk ak ñaar,ci guddig àllarba ci ñaar fukki fani muharram)).

Moom sëriñ bi, bi mu ganee àdduna ,waajuram wu jigeen a ko yoroon ba mu mat a jàngi, Mu tudoon nag Amadu doomi Muhammad doomi Habiibullaah doomi Muhammadul kabiir mom Habiiballaah mu njëkk ma doomi Muhammadul Xayri,ak Muhammadul Kabiir . Muhammadul Kabiir mii mooy ki niy wooye Maharam,mooy ki sanc Mbàkke Bawal atum 1194 g ,ci li nu wax,waaye dëkkewu ko woon da faa bàyyi woon ab taawam Muhammudu Farimata,magi habiibullaah waaye bokkunu nday,moom nag sëñ Maharam mii daa desoon Jolof, fa la làqqoo nu denci ko fa,di ko siaare.

Mi ngi askanoo nag ci Tukklóor,ay waajuram a ngi bawoo Fuuta,dem Jolof, siw na itam ne ñoom Gànnaar lan bawoo, dem Fuuta,seeni doomi baay tëx ci naar yi ñooy ñoñu Moodi Nalla, ñoom nee nanu ay serif lanu.Sama mag, sama sëriñ, sheex Muxtaar binta Loo,doomi sheex Iraahiima ,sëriñub Njumri Loo nettali na ma ne dégg na ci sëriñ bi luy dëgëral loolu,mu ne bis nekk na fa sëñ ba nuy waxtaan ba tudd ag giir ci naar yi,gu niy askanale ag cëriif,sëñ bi ne ko xanaa xamoo ne ñooñu suniy mbokk lanu,mu ne ci noonu la xame ne ñoom ay sëriif lanu. Man nag li may wax mooy seenug cëriif bu nu ko waxutoon te déggeesu ko it,seen jikko yu rafet tegtale na ko,muy tedd gu ànd ak yaatug dënn,ak lewet gu ànd ak njàmmaar,ak jublu ciw yiw,ak bañ jikko yu suufe yi,ak diinewu gu dëggu.

Yaayam soxna Jaaratul Laahi Maryama BUSO doomi Muhammad mom Muhammad mom Hammaad mom Alliyu Albusobiyu, ñooñii seenug cëriif lu wér la, ñi ngi cosaanoo ca Imaam Hasan mom Alliyu ibnu Abii Taalib karramal laahu wajhahuu, kon sëñ bi seriif la ci nday ak ci baay. Lenn ci samay doomi baay tëx nettali na ma te moom ku dañ kumpa la ci suufus Fuuta ,mu ne dox na bis juge ci dëkk bu ndaw bu nu naan Bukke, jëm fu nu naan Mbumbe, péeyub Filaaw,nee na mu romb ci ay gent yu ñu ne ko ñooy fi Mbàkke-Màkke yi dëkke woon.

Am na ku ma nettali ci ñi sant Ba,ne Mbàkke-Mbàkke yi seeni doomi baay tëx lanu, kaaf gi nekk ci Mbàkke ag Haa la woon muy haa giy mujj ci ba,wolof yi def ko kaaf,waaye wax jooju, ju doyadi la fi man,li nu jortu daal mooy aw sant wu yàgg la, niki santi ajam yi,(ajam mooy ku dul araab),li fi ne daal mooy ñaari wax yi bu ci nekk, dëgër na te am na màndargaam dëgg. Waaye Buso-boso yi ñoom seen cosaan Fuuta la, ca fa niy wax Golare, barab yii yepp it yu jegee lanu,barab yii it,ak wax yi ci am,am nanu màndargay dëgg,yuy tegtale teddngay ñaari askan yi.

Bi Sëriñ bi tollee ci war a jàngi,wayjuram dal di koy jébbal nijaayam Muhammad doomi Muhammad BUSO mbokkum ndayam ju tedd ju yiw ja. Mu tàmbli koo jàngal ba mu màgg as lëf ,tàmblee yewwu, mu jebbal ko moom itam nijaayam,sëriñ Tafsiir Mbàkke Ndumbe doomi Muhammadu Soxna BUSO doomi Muhammadul Kabiir mi nu tuddoon,moom mooy mbokkum maami sëriñ bi, ju jigéen,ndayi wayjuram wu jigéen,soxna Asta Waalo. Nu daan nekk foofa, fa moom ca Mbàkke, bu noor baa, bu nawet baa, lu ci ëpp danu daa dem jolof, ba bi Tafsiir mii làqoo te booba sëriñ baa ngi jeggee mokkal.

Kenn ci ñunu woolu ñi nettali na ma ne, sëriñ bi nettali na ko ne àlliwaam a ngi tulloon ci latajjidanna bi jànglekatam boobu di làqu,mu dal di dellu ca wayjur wa, dal di farlu ci njàng mi ba mokkal alxuraan , def tajwiid ak tas-hiih,ca ña ko daa defale ca jamono jooja, loolu lepp ci wetu baayam,daa wul tàggalikook moom lu dul lu néew,ndaxte magam Muhammad Jaara dafa nekkoon ca kenn ca tas-hiihkat ya ca yeneen dëkk ya.Bu ko defee leeg-leeg amaa na mu jaar fa nekk fa ak moom weer,walla ñaar,doog a dellu,booba ña nga Saalum,ca jamonoy jiyaadkat boobu di Màbba Jaxu,ndax kat booba ñoñam Màbba boole woon na leen ca ñam pangoon jëme Saalum,nga xam ne Bawal ak Jolof daanaka bawu fa woon kenn.

Bi mu faatoo nag moom Màbba, nit ñi dal di dellu seeni dëkk , waajuram wi moom itam dellusi ci ñi doon dellusi, ànd ak Latjoor. Ci noonu nijaayam akug njabootam des foofa,sëriñ bi it bokk ci,ngir jàng xam-xam,noonu mu tàmbli di jàng ci baay tëxam,Samba Tukklóor KA doomi bàjjani baayam,bi mu jàngee ci moom dali xam-xam,tàmblee ñaw as lëf, la dellu ca baayam,te booba ma nga Paataar,benn dëkk bu ndaw bu nekk ca wetu njéndul Amadi Yala,dëkkuwaayub Latjoor ca joojale jamono. Ndax moom sëñ Mammoor daa defoon ku Latjoor fonkoon lool,daa ko laaj tey diisook moom,waaye moom sëñ Mammoor bëggutoon a dëkk ak moom,ndaxte du woon ku xemmeem seen alal ji,du caagéenug seen teddngay nguur gi,li ko loruloo woon ci mu dëppoo ak ñoom ak a mudaaranteek ñoom mooy njaboot gi mu yoroon,bu ko defee Latjoor daa ko dëkkal ci wetam,waaye sëñ bi daawul nangoo dëkk ak moom,moom kay day dëkk ca wetu péey ba mu ne rekk,ndax da daa jàng ak a jàngale,te jàng ak a jàngale neexoowut aki buur,li fi ne daal ca wetam la dëkke woon,nga xam ne su ko soxlaa ñëw ci lu dulub coona.

Ci noonu sëñ bi nekk ak waajuram,di jàng ci moom te di farlu ci mokkal gi,ak xereñe gi ak dégg-dégglu gi,ba faf raw ci fann yi. Ci biib diir it daa na ci def leeg-leeg mu seeti sëñ Xaali Majaxate Kala,moom mi dëkke woon fa péey ba ak Lajoor,di woon ku raw ci fanni xam-xam yi, rawati na làkkuw araab,di ku siiw ci man a woy,bu ko defee muy xamlu ci moom araab,leeg-leeg it mu daa ko indil ay woy,yu mu def ngir mu toppal ko “lihraab” ba ak araabe ga,ak “harool” ba,leeg-leeg mu génneel ko ci ab yàq,ba mujj sëñ bi far ko raw, mu mujj saa su ko wonatee lenn ci woyam yooyu,mu ni ko indil ma ko, ma mokkal ko,mu mujj toppalatu ko waaye day mokkal li mu koy indil,nii la nekke woon ak Xaali.

Amoon na fa it beneen boroom xam-xam ci waa-gànnaar yi,dëkke woon Njaañ, tuddoon Muhammad mom Muhammadul Kariim,bokkoon ci giirug Daymaan,ci doomi Seyidil Faadal yi, ñu gënon koo xam nag ci turu Muhammadul Yadaali,waaye bokkul ak ki def téere bi nu naan Zahabul Ibriiz ci tafsiir,ndax kooku am Yadaalim Daymaan mu yàgg la . Sëñ bi bariwaa na lu mu ko daa dikkal,di jàng ci moom xam-xamu Bayaan (xam-xamu wax ju rafet),yaakaar naa ne nee na it - ci lenn li mu nu daa nettali yàlla a xam - ak bu Mantiq (xam-xamu xellu). Bi wayjur wi xamee ci moom raw gi ak cawarte gi ak laabiir gi,mu dal di koy jox mbirum njàngale mi. Bari na lu mu ko daa jàngal ab bind ci kanamam ci téereb boppam ba ,walla ci téere bu mu dalagul, ngir mu jàngal ko boroom bind boobee walla téere ba, bu ñëwee,ngir wóolu gu mu wóolu xam-xamam akug ñawam, sëñ bi it daan ko def,ba li ëpp ci dongay sëñ Mammoor yi mujj féetesi ak moom,doylu ci moom,waajur wi bàyyi leen ak moom te bég ci.

Waaye yàggul dara rekk Latjoor tuxoo Kër Amadu Yala,dem Sukeer péeyam ba ca Kajoor,yobbaale sëñ Mammoor mu sanc ca wetam,tudde ko Mbàkke Kajoor,sax fa ñaari at dal di wuyyuji boroomam,nee nanu, looloo ngi am ci Muharram,atum 1300g, dëgg naa ci sëñ bi mu ne bi waajur wi tollee ci sukkuraat, took na fa boppam wàcce fa ab kaamil bisub altine,guddig talaata mu làqqu,nu denc ko Deqale ,di ko siyaare,man dey Alhamdu lillaah dem naa fa ba siyaare ko.


Bi niy yobbu wayjur wi Deqale muy dëkk bu ndaw ci dëkki Kokki yi,ci wàllug Mbaakol,sëñ bi àndon na ca gunge ba,di liiru,bariwaa na bu ko ab gawar bëggee joxuw fasam,mu ne dox a ma gënal,bi mbooloom dëkk bépp dajee di mbooloo mu kenn masta gis,nu jublu ci jullee néew bi,jiital sëñ Tayba Muhammadu Ndumbe Maar SILLA, mi nu tuddoon ci buntub seedey ñu mag ñi ñeel kii nuy wax ci moom. Bi nu noppee ci julli gi,ak denc gi,sëñ Tayba digale nu daje te dal,te xerawlu,ci noonu mu jug, xutba,waar nit ñi,wax wax ju rafet bi miy jaale sëñ bi nit ñi,bi mu noppee ne ana Sëñ Bamba,noonu la nu ko daa wooye ñoom,ca jooja jamono,mu wuyyu jug,ma nga woon ca catul mbooloo ma,sëñ Tayba ne ko jegesil,mu xaw a jege bay degganteek moom,di gisanteek moom,di ko man a toontu ci lu dul muy yekkati kàddoom,dal di yam foofa ngir bañ a jéggi nit ñi,xutbakat bi neeti ko jegesil,mu ne ko maa ngi lay dégg,Sëñ Tayba dal di koy jaale njaal mu rafet,ne man nag dama doon sàkku nu ànd ci mbooloo mu màgg mu sa moroomi waajur wii,ngir nu seeti Latjoor,jaale ko sa waajur wi,jaale gu ko man a dëfal,ngir kat moom ab xaritam la woon,dib soppeem,te dib sëriñam,daa diisook moom,bu ko defee nu waxtaan ak moom ci yaw,sampu la fa moom,ba mu man laa teg fam tegoon sa Baay,bu ko defee doo gis ci moom lu dul aw yiw ak teraanga,lii daal mooy sama xalaat,yaw nag luy sa xalaat,sëñ bi ne ko,li aju ci jaale gi ak dëfal gi maa ngi la ciy sant,te di la ci ñaanalub yool,waaye mbirum seeti ay buuri àdduna moom duma ko def,ndax xemmeemu ma seen àdduna ji,te soxlawu ma seen teddnga,teddnga ci yàlla laa koy sàkkoo buurub buur yi,mbooloo ma tiit,tas.


Ña cay ñu baax wax ji da leen a yéem, rusloo leen,ndax dëggu gi mu dëggu, tey toroxal way bëgg yi àdduna,juge ci seen doom ju diw waxambaane,tegi tànkam ci seeni wagg te manu ñu ci dara.


Bu dee mbooloo mi moom, li leen yéem mooy,bañ gi mu bañ teraanga ju teew jii,ak xéewal gu jàppandi gii,nu ne kii daalub dof la,ci loolu Sëñ bi def na ñaari dagiiti woy yu rafet te yéeme,bu njëkk bi mooy waxam jii: nee nanub dof laa,ngir wëlbati gi ma wëlbati samab gis wëlif leen ba fa mu yam ,teewluwu ma ko te woneesu ma ab yaxam jamono ja may liggéey,waaye beneen bi moom mooy wax jii: nee nanu ma jéngal jëm ci bunti buur yi,kon déy da nga am ay may yu lay jariñ jamono ju ne)). ((Ma ne leen yàlla doy na ma,doyloo naa ko,soxlawu ma lu dul xam-xam ak diine)) ((Yaakaaru ma te ragalu ma ku dul sama boroom,ndax yàllaay ki may doyluloo te di ma musal )) ((Nu may joyale samay mbir jëme ko ci ñoñ lottu nanu ci seen mbiri bopp,ni miskiin yiy lotte? )) ((Walla nan la ma bëgg poñatum àdduna bii di jañe,jëm ci dëkkaale ak ñoñ seeni kër mooy dërub saytaane )) ((Su ma dee naqarlu mbaa may bég boroom Aras laay woo. Mooy Aji dimbali, ji dara dul të,te mooy Kiy amal li ko soob )) ((Bu bëggee gaawalum mbir loola gaaw,bu ko nammee yeexal mu yeex ba cib diir)) ((Yaw mi may yedd bul sonal sa bopp , ndax kat man amu ma lenn lu ma naqari ci ñàkk àddina )) ((Bu dee sama ayib mooy dëddu gi ma def ci seen poñat mi,kon déy ayib jooju, ju gànjaru la, ju ma dul gàccaal)).

Waajuram wu jigeen ,wu tedd waa nga làqoo Poroxaan ca Saalum, nu denc ko fa,jamono ja fa sëñ Mammoor nekkee.

Doggantal : ci ni mu nekke woon ginaaw bi waajur wi làqoo (gërëmul yàlla yal na nekk ci ñoom)[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Moom sëñ bi,bi waajur wiy dund, nanguwutoon a taxaw mbaa muy taxawal dara,moom daal ci moom rekk la toppoon ,mel ne néew bu nuy sang, fu nu ko jëmewul du fa jëm, bi mu làqoo nag,mu des ca ligéeyam ba mu ko bàyyee woon at ak lu topp, ña fa nekkoon it jàng rekk a leen fa bàyyi woon, du leneen,moom itam ab jàngalekat rekk la woon,waaye loolu teewul woon mu doonoon ku yitewoon a xam gaa ñu baax ñi,ak seeni xam-xam,ak beru ak a wër,niki ñu baax ñi,mu leen daa junj ciy waxam,ak a feeñal ay maanaa,ak a yëgg,ba bi ko himma ju kawe ji (himma ci lun man a firi mooy yite) dikalee ,muur ko,mu jug yëgg as lëf neeti tekk,dal di woote cig nooy jëme ci mbiram moomu,bi ko mbir mi gënee lëjal nag, gën a fees fi moom,gën a rëy,mu dal di biral woote gi.

Dajale mbooloo mi,taxaw fa ñoom xutba leen,sukkandiku ci dokkub dogu,ne leen yeen mbooloo mi, ku àndoon ak man, ngir jàng rekk,na laxas jëm ca boppam aki mbokkam,mbaa fa ko soob,man loolu rekk taxatumaa jug,ku bëgg li nu bëgg nag,na toog,dal di leen fay bàyyi dugg ca biir. Waxam jii nag dal di leen bàyyi cig jaaxle, ñenn ñi dem, ña ca des,des fa,am ñuy jeem a tëyye seeni xarit ngir ñu des,ak ñuy xiirtal seen waay ci ñu dem,sëñ bi moom ne tekk rekk,jeemul a tëyye kenn ku bëgg a dem,ba mujj li ëpp ci mbooloo mi dem bàyyi ko fa,la ca gën a néew des fa.

Bi loolu lépp daata am,fekkoon Sëriñ bi mu sóobu ci ngiirum taalif ci xam-xam yu nu tuxal ,yu sariiya yi, mu woy Ummul Baraahiin,bu Imaam Sanoosi,wayjur wi nangu ko,bég ci ,te mujj di ko jàngale ,bàyyi wesar wa doonoon cosaan la. Dégg naa ci Sëñ bi mu ne woy woowu de waajuram jàngal na ko ñaari doomam yii di sheex Coro,miy Siidi Muhammad Alxalifa,ak sëñ Aafe,mi tuddoon Ahmadul Muxtaar. Mu woyati teereb Imaam Xazaalii bi tuddoon Bidaayatul Hidaaya,dal di koy tudde Mulayyinuz Zudoor ,di ci maanaa (aji nooyal ji dënn yi ),ginaaw bi mu gàttal ko,tudde ko Munawwiruz Zudoor,di ( aji leeral ji dënn yi),ci atum 1294g,teg ci Jëzbatuz Zixaar,di (bijjig gone yi) ak Jawharun Nafiis muy ( wurus wu gànjaru wi) nga xam ne da cee woy wesaruw Imaamul Axdariyyu,ak yu dul yooyu. Bi ko donga yi nangulee nag lii mu leen doon woo,daa bàyyi njàngale mi,jëm ca di leen tarbiya,ak a tarqiya (tarbiya mooy yar ni ko sariiya bëgge,tarqiya di yékkatee jëme ca yàlla).

Man nag nee naa lii de du ñàkk muy ndigalug yonant bi (j.y.m),ndax kenn ci sunu sëriñ yi nettali na ma,te moom ku wóor la di ndëërlaay,ne Sëñ bi de wax na ko ne yonant bi (j.y.m) moo wax ak moom ci gimiñam,ne ko yaral sa àndandoo yi ci “Himma” te bu leen yar ci njàng,loolu Sëñ bi gën na koo leeral ci xasida gii: Bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi ji,yal na ko yàlla dolliy xéewal ak mucc,moom miy leeral suufam si ciy wàlliyu ba yawmal xiyaam,te ku ci ne méngoo nga sunnaam si,di ko ñogal wëlif bidaa,bokk na ci kiimaani doomi Abdul Laahi jooju,bégal gu mu bégal jëwrinam jii ci ne ko(fazdah) mooy wooteel ca kaw)) (( Yonant bi (j.y.m) digal na ko ne ko mu jàngal Muriid yi,ak ku nangu mu laabiire la ci waa jamono,te mooy ki ko àggale ca borooman cig taxliya ( mooy setal nit ki féexal ko ciy ayib ) bégalati ko ci tahliya ( muy ràng nit ki ay takaay,walla sol koy ngënéel).Li mu jublu ci Fazdah ji nag (mooy biralal ca kaw), mooy ji ci alxuraan: fasdah bi maa tuumaru wahrid hanil musrikiin mooy biralal li nu la digal te dëddu way bokkaale ñi.

Yàlla daa digaloon yonantam bi (j.y.m) mu biral wooteem ga,ginaaw bi mu ko daa yalu,maanaam dëgg-dëggi loolu, mooy sëriñ bi,bi donn gi mu donn yonant bi matee,ci matalug yàlla (t.s) ,te mu dolli ko ay xam-xam aki hikma,aki leer,aki mbóot,te may ko kàttanug man a yanu wilaaya gu mag gi- bi loolu amee nag mu digal ko mu woote ca kaw,woo mbindéef yi ñu weeru ci moom,di jële ci moom tey def ay ndigalam,di bàyyi ay tereem,ci loolu la waxe: yàlla mi nga xam ne lu ko soob mu def,moo ma jox xam-xam yi,ak seen barke,wattu naa lu xajul ciy téere,kon boo may ligéeyal bul tàyyi.Yàlla miy joxe,jox na ma ci darajay yonant bi,barkeb alxuraan,ak xam-xam yi,jël seen barke def ko ci samam njàngale.Yàlla jël na mbooti laa illaaha illal laah def ko ci samy taalif,yàlla jox na ma te dootu ko nangu,te man kaaraange laa te dib weeruwaay ci ndimbalam.Loolu nag ngënéelul yàllaa,ku ko soop la koy jox. Te nee na ma : neel wéeru leen ci man.

Ci maanaa sama boroom digal na ma,ma leeral nit ñi ne:man ab wéeruwaay laa tey kaaraange,ku bëgg aw yiw àdduna ak allaaxira,na wéeru ci man. Mu dellu waxaat ne: Murid bu yoqatul ci man de texe na,ci làq ngën ji ay may. Murid bu Yàlla wommat jëm ci mu aju ci man, texe na te da na céru ciy may )) ((Murid bu wéeru ci man de yàlla miy sama dëkkandoo bu kawe bi,def na muy ku texe ci lu kawe njortam)) ((Bepp murid bu aju ci man,day texe,te ku niy soril la aw ay. Képp ku aju ci man déy am nga ag mucc ci nëx-nëxi àddina ak allaaxira. Ginaaw bi mu leeralaat ne way gëmi jinne yépp ci jamonoom ,aju nanu ci moom,mu ne : Jinney sama jomono jii dey, ña ca gëm ñépp aju nanu ci man,waxuma ña gëmul. Mu wattuloo nag ñi aju ci moom, ñuy xàccati ginaaw bu nu jébbaloo ne: toroxte ñeel na ki ma dëddu ,won ma ginaaw,muñ ma,ginaaw bi mu duggee dib murid.

Dal di leeral lu dig murid,ak lub murid di bëgg,mu ne:

  • Dëgg-dëggi ag murid - ci li sang si wax - mooy bàyyi aada, muy li nga nekkoon njëkk ngay jébbalu),bu àggagul ba noppi dellu ca la mu nekkoon, mook ku murtad ay yam
  • Ndax kat ab murid du bëgg mukk lu dul gëramul yàlla ak fu mu man a jublu.

Mu leeralaat ni ab muriid di mel,ak ngértel ànd ak sëriñ bu àgg,mu ne : Melow ab murid,mooy bañ a bëgg dara ngir yàlla. Ku bëggul lu dul yàlla, àgg fa moom,mu jox ko aw yiwam

  • Ku aju ci ku àgg, àgg,ku aju ci ku àggul doo àgg
  • Ku yaroowul ci loxoy ab sëriñ, dana dajeeki coona.
  • Ndax ku amul sëriñ buy gindee,saytaaneey mujj di ab sëriñam fu mu jublu
  • Ab sëriñ du wuuteek Ku nu rammuloo ki (muy yonant bi) kon ku jublu aji yar (sheexul murabbi) de da na jariñu
  • Fu la aji yar digale,defal,kon nga àgg ca boroom ba))
  • Bu la aayee dara bu ko jege,te bul sàggan ci wut gëramam.

Mu leeralaat ne murid saadiq de am na ay meloom,yoy bu ko amee am wépp yiw: Meloy murid saadiq ci gàttal, ñeent la,ma tënk leen nag ciy bayit ngir ragal woru ((Dëggal ci bëgg sab sëriñ ba fàwwu,jëfey ndigalam fu mu rote rekk )) ((Bayyi gaaru ci lu mu man a doon (gaaru mooy di am xalaat ci ndigali sëñ bi), ak doonte ci sa baatin la,ci li nu nettali)) (( Ak a tànnal sa bopp la ngay def,ngir sa rafetug njort )) ((Képp ku boole yile melo ci murid yi déy,da na jot ndëërlaay ya (gaa yu baax ya).

Mu biralaat ne kiiraay am na juroom benni cosaan,yu murid bi war a dagg,te malaaka yi dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk, ne: Kiiraay am na juroom benni cosaan,ku bëgg a àgg da nga leen dog, ñooy baril lekk ak naan,ak a jaxasook nit ñi)) ((Bari wax,bariy nelaw,sàggan ci tudd yàlla miy jàmm)) ((Gëstul loolu ci Jawaahirul Mahaani,bi sunu Sheex Tiijaan mu nu màggal mi def)) ((Nettali nanu ne malaakay Aji màgg ji,dañiy jooy ci murid bu bëgg lekk,ngir yëram ko,loolu man nga koo gis ci taalifi boroom Hawaarifil Mahaarif

Mu neeti murid saadiq doomi waxtoom lay doon,ne: Murid Saadiq mooy kuy wëlbatiku ànd ak waxtu wi mu nekk,te du fuglu wa ca kanamam,ndax loolu day teree yéwenal waxtu wi teew Gëstu leen loolu ci Jannatul Muriidi,téere bi sunu sëriñ Xaliifatur Rasiid def. Ak lu bokkul ak loolu ,ci li mu wax ci mbirum boppam, mom muridam yi,nga xam ne ,bu nu ko toppoon,indi fi lu yéem xel yi,te da na mujj kon,gàttal gi nu bëggoon ci téere bii,du amati,ndax moom téere bii as kook la ci geejug xamale ko.

Nu indil leen fii nag as tuut,su nu tas ci wone lenn ci sekkarey xaybu yi (xaybu mooy lu faddu,muy mbirum biir niki liy xew te xewagul),mu bégal ci ñi aju ci moom, ngir dolli leen ag xeemeem,ak sawarloo leen,mu wax ne : ((ñi aju ci man bu nu ko defutoon dem sawara,doonte as ndiir lay doon it,njëkk nuy tàbbi ajjana,ji nu dig ñu ragal ñi yàlla)) ((Li waral sama tukki bu sori bi,Yàlla mu barkeel mi te kawe,daa bëggoon ca asal,may kiy ramu samay donga,dox na sama digante ak nasaraan yi,tàbbal ci seeni xol ag ragal ma,nu def la nu def nag ngir ma bañ a nekk dib nasaraan, ndax bu ma ko doonoon tabbi sawara ,walhiyaazu billaahi. Waaye Yàlla’a ma aar ci sawara,ak lépp lu mu gëramul,ci darajay Yonant bi (j.y.m))) . Mu bind ay laabiire ñeel murid yépp,ne : Mi ngi juge ci man jëm ci mbooleem murid, yu góor yi ak yu jigéen yi,ab nuyyoo bu teey,bu leen di musal mboole seen,te di leen tabbal ci jàmm ak aafiya,ci addina ak alaaxira,ci barkeb Yonanat bi (j.y.m),ginaaw bi, may digal képp ku aju ci man,ngir yàlla mu kawe mi te tedd,mu xamlu pas-pas yi ak tawhiid,ak àttey laab,ak julli ak woor,ak lu dul loolu ci lépp lu war mukallaf,man nag warlul naa leen taalifal leen mbooleem lu leen koy xamal, ngir jëmmi yàlla (t.s),wasalaam)).

Mu bind lenn ci ay murid ab tontu bu neex yal na nu ci yàlla boole ñun ñépp,mu ne ci: assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu,ma lay xamal ni sa bataaxel ba agsi na,yaw murid bu dëggu bi,waaye na la wóor ne doo gis lenn loo ragal,booy faatu ak ci bàmmeel,te ñaari malaaka yiy laaje,xam nanu sa sëriñ,te da nanu doylu ci xam gi, ba dunu la laaj dara. Lii nag xamle la gu mu teg ci yoonu laaj ak tontu,laaj bi moo di lan la sëñ bi woo ay taalibeem jëme? lan mooy tontu li? Moo di sellal,moom mi nga xam ni mooy ruuhug jëf tey ngértel xam-xamub way xam ñi yàlla,tey waralug àgg ca Yàlla, àgg ci Yàlla nag ñi ngi ci jublu jaam bi nekk di ku wéetal yàlla,ciy yëggoom ,aki dalam,aki pas-pasam aki waxam,ci lepp,li feeñ ak li nëbbu,lii nag manut a ame ci njàngale rekk,ndax kuy jàngale ab tegtalkat rekk la,li ci des,mi ngi ci aji jàng ji,man naa am mu jëfe man naa am déet,du ligéeyub jàngalekat,muy sonnu ci waa ji jëfe loolule,loolu Sheexu tarbiya la war.

Bokk na ci ligeyam,moom sëriñub yar,jàng ak jàngale,ak ligéeyloo,ak ay tudd yàlla,ak gindee ginaaw bi mu leen xiirtalee cig cofeel gu dëggu,te du tàggook ñoom li feek wonu leen seen ayibi bopp, ligéeyloo leen ci nu jéem a laab ci yooyu ayib,ngir man a àgg ak ñoom fa Yàlla inshallaah. Bu loolu jàllee,mbirum tarbiya day mbir mu gudd,manunu cee wax fii.

Mu dem ak ñoom ci yar leen ci himma, ñu nangul ko ko,mu dox ak ñoom ci ngérum tàggat,dajale leen,di leen ligéeyloo lu bari,yanu leen ci fàttaliku Yàlla lu bari,ak a jàngi xasida,ak taqoo laab,ak a beru,rawati na sori jigéen ñi,ci noonu ñu kawe ñu dul ñoom,ndax donoo joxe woon seen bop ak seen alal ci yoonu sàkku gëramul Yàlla, Yalla jënd na ci jullit ñi,seeni bakan ak seen alal,faye leen ko àjjana,Sëñ bi wéy ci yoon wu jub wii mook saabaam yi, dale ko ci njëlbéenug atum junneek ñatti téeméer ak benn,ba bi mu sancee Mbàkke Bawal,ci at moomu juge Mbàkke Kajoor,sax fa lu tollook ñaari at ,nit ñi di ko dikkal juge fu nekk, ñii di jebblusi, ñii di joxesi àddiya, ñiiy sàkku ndimbal. Mu mujj yoonu këram gi mel ne yoonu ab ja, ci ñeenti at yii nag mu siiw ci,siiw gu kawe, ñu jege ñi ak ñu sori ñi, ñepp di yéemu ci moom,te booba amagutoon sax fan-weeri at.

Ci diir bii sëñ bi wër na ci réewum wolof mi,dale Saalum ba Waalo Barak,siyaare fa mag ña, ña cay dund ak ña dundul,jaar ca sëriñ sa ,jële ca ñoomi wird,bokk na ci ñi mu siyaare, ñoñ sheex Siidiya,siyaare na bàmmeelam ca Tindawja,siyaare sheex Baaba mom Abiihi ca Maymooni,tagg leen,jële ca ñoom,woy càllaleg xaadir gi,tàmblee ko ca sheex Baaba ba fa mu yam,looloo taxoon kenn ci Sheexi naar yu mag yi laajoon ko kuy sa sëriñ?,mu ne Rasuulul laahi (j.y.m),mu ne ko kon lu tax nga ne fi di tudd waa kër sheex Siidiya,ak a woy ay sëriñ ak a tag?,Mu ne booba da maa melon ne ku gumba,di làmbatu yoon wi,di ko sàkkoo xam ci ku xam ak ku xamul,bi ma dajee boroom yoon wi ci ndimbalul Yàlla nag muy Yonant bi (j.y.m),mu xëcc ma ci boppam,laa wacc ker-keraan yi,waaye di jokkook ñoom ngir Yàlla ak a soppanteek a jariñante ngir moom.

Te wax na dëgg,ndax mbiram ak ñoñ Sheex Siidiya loolu lay tegtale,mujj nanu mel niy doomam mu mel ni seen baay,di leen jariñ ci alalam lu leenub buur jariñul,ab sëriñ it jariñu ko ab taalibeem.

Sheex Baaba tag ko ciy xasaayid,aki dagiit,yu tollok ay téeméeri bayit,bokk nanu ci yile:( Shex Ahmadu xéewal la gu yàlla jox mbindéefam yi) ak waxam ja: ( sëñ bi daal xéewal la gu yàlla xéewalee,di kiimaan ci kiimaan yi),ak yu bokkul ak yooyu,bu waxutoon yu dul yii it , ñaari bayit yii,rekk doyoon nanu seede ci màggug sëñ bii,ak wilaayaam. Ndax kat sheex Baaba ak màggam gi, du fo mbaa muy yaxantu ci woy ni suharaawu yi,moom dey lu mu wax ci ndigal la ko teg,ak jaamu Yàlla,yal na ko Yàlla fay ci ñaari bayitam yooyu. Bokk na ci ñi mu siyaare ci sheexi naar yi,Ustaas Baaba mom Hamdi, ma jublu ci Hamdi mu ñaareel mi,dikk na fa yendu fa fanaan fa,nee nan ci menn mbaar. Sama xarit ba niy dàkkantale Kaadi Sheex Abdul Xaadir,doomi Amiirul Kumlayli , nettali na ma te booba taalibeb Ustaas Baaba la,ne Ustaas mii moo jox sëñ bi sekkare bi,waaye nag leeralu ma ban sekkare la,man naa am muy wirduw Saasalii,ndax sëñ bi bind na ne moom wirduw saasali mi ngi ko jële ci wenn wasiila,njëkk muy daje ak wasila wu mag wi,di Yonant bi (j.y.m) ,te leeralu nu kooka kan la. Li waral Kaad mii nettali ma ko,mooy maa ko laajoon bi mu jëlaatee ci sëñ bi wirduw Sasalii,ndax xam nga ci ku ko sëñ bi jële woon,mu ne déedéet,waaye nettali li mu waxoon ci diggante sëñ bi ak Ustaas Baaba,nu jorte ci ne ci Ustaas Baab moomu la ko jële ndax moom ab xaadir la woon.

Kaad nettali na ma ne bi sëñ bi agsee, ci bi miy siyaaresi Ustaas ,ci bëcëgug bis bu sell,Ustaas defaral ko am soow mu neex ci ndox mu sedd,ak suukar,looloo ngi amoon,ci jamono ji sëñ biy nattu boppam ci di tegoo ay coona,mu ne ko naanal mu ne ko man baax na du ma naan lii, mu ne ko,ndax daa baaxul ci wàllug wér,waala da nga koo bàyyi ngir Yàlla di jiyaar ak sa bakan,sëñ bi ne ko waaw loolu la,mu ne ko kon naanal,bàyyiwu ko ba mu far naan,ginaaw bi la dongay Ustaas yi laaj lu waral mu sonnu ci mu naan soow mi,mu ne leen ndax moom kat sonal boppam rekk la bëgg,ak mettital ko,mujj loolu di aadaam ngir Yàlla,ju mu manatul a bàyyeeti,ndare cib coona,ma jëflante ci ak moom waaye Yàlla defal na ko barke,ndax mujj na dëgar ci këng.

Ginaaw bi lii wéyee lu yàgg,Ahmadu doomi Ustaas seetsi na Sëñ bi Njaaréem,mu bég ci lool,di ko ganale ngan gu mu sonn,indil ko ñam yi ak naan yi,bi nu àggee ci ataaya, Ahmad xam ne mbir dana am ,ndax moom du naan ataya,bi ko sëñ bi tàllalee ataaya ji,mu ne ko du ma naan ataaya,mu ne Yàllaa tax nga bàyyi ko ngir jiyaar ak sa bakan walla ag weradi,mu ni ko Yàlla,mu ree,ne ko naanal ma fayoo ca la ma sa baay defoon, ñaanal ko ci barke.

Bi Sëñ bi nekkee ci wëram googu nit ñaa ngi ko daa dikkal bàyyikoo ci gépp wàll ngir xam-xam bu bari bi ak njariñ li,ak cofeel gi nu amoon ci moom ak diinewu gu dëggu gi,rawati na alal ju bari ji mu daa joxe rekk ,nga xam ne daawul tëyye ab dërëm,lu ñëw mu joxe,di jox mag ak ndaw goor ak jigeen,gor ak ab jaam,ku am ak ku amul,ku baax ak ku bon,loxo bu tàllaliku jëm ci moom mu feesal ko te soxlaalul nit ñi, doyloo kàppitaalam bi dul lu dul jublu ci Yàlla ak yiteem jépp. Mu dem Gànnaar jaar ca sëriñ ya,siyaare ñay dund ak barabi way faatu ya,jariñ leen ci alalam,ju bari ja,nu sopp ko nu kawe ni ko ñu ñuul ñi soppe,defal koy xasiday tagg,siyaaresi ko ci réewam ginaaw bi.

Bi mbokk yi gisee ci moom kaweg xel,gu diine,gu mbaax gii mu yor ak jublu gi ko àdduna ak nit ñi jublu,nu tàmbli di ko iñaane,di ko lor,mu daan julleendoo ak ñoom,lor yi ëpp,mu mujj beru leen ak am mbooloom ak jàkkaam, Yàlla gën a fésal mbiram, ñu gënatee mer,nga boole ci terewu gi mu defoon ci mbirum buur yi,daawul nangoo jaxasoo’k ñoom,ba da daa sàkku sax ci sëñ Mammoor ci ay bataaxel yu mu ko daa bind, - da daan kersawoo jàkkaarloo’k moom di ko ci wax dara - mu bàyyi ag jëflanteem ak buur yi,naan ko seen teddngay fii ji toroxte la ëlëg,sëñ Mammoor daan ko ko nangul,te di ko ci jéggalu,waaye njabootam gi taxoon ba manu leen a bàyyi.

Ma nettali leen as lëf ci jaloore,nee nanu,bi kenn ci jaraafi Latjoor yu mag yi -mu nekkoon ku am solo fa Latjoor - jébblusee ci Sëñ bi,mu bokkoon ci jàmbaar yi amoon ay alal,mu ndàmmoom (gañewoon) lu bari ci màggum xareb Samba Saajo bi ( màgg mooy li niy jële ci koo xeexal ba not ko) .Samba Saajo ab dëkk la bu nekk ca penkub Njàmbur,diggam ak Jolof,la xare boobu ame woon,ci diggante Amad Sheexu BA mu Fuuta, ak Latjoor,Tubaab yi japle woon ko moom Latjoor,ba mu gañe ko, ray ko,xarekati Latjoor yi gañee ci woon màgg mu rëy,ci alal ak ay jaam,te ña ca ëpp diggante Jolof ak Fuuta lanu bàyyikoo,ak Kajoor,tey jullit lanu, buur bi laaj ndax man na leen a def ay jaam, kenn ci boroom xam-xam yu mag yi,ne ko waa-waaw,ndax Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonnant, kon alalam ak dereetam dagan nanu, nu dal di wéyal loolu,te kat ag wooteem yonnant mbooloom boroom xam-xam yu mag yi saxalunu ko.

Li waral xare bi,lu gudd la manunu koo netaali fii. Bi jaraaf jooju tuubee ci sëñ bi,mu digal ko mu wacc mbooleem jaam ak alal ji mu ame woon ci xeex boobu, jaraaf ji déggal ko,def ko ànd ci ak kontaante, Latjoor ak ay gaayam jàppe loolu nag ag weddi ñeel àtte bi leen kenn ci boroom xam-xam yi defaloon,ne leen jaam yi dagan nanu. Nu mere woon ko,nee nanu ma jaraaf ya woo woon nanu jaraaf jooja fa kanamu Latjoor,ne ko : lu tax nga bokk ak nun ndab,règg rekk wëlbatiku,doyatu la nga ciy xëpp suuf? Mu ne leen waaw,weñ a tàbbi ci sama bakan,lëjal ma, moo waral lii ngeen gis ci man,waaye bëgg a nëxal seenum mbir taxut. Mu jublu woon ci weñ wi,lislaam ji ko duggoon,cig mbetteel,yaw nag xam nga lëjal gi lislaam di def ku mu dugg, du ko bàyyi ndare bu daa tuub.

Ñu xam ne li mu wax lu dëggu ci moom la, ñu jéggal ko, noppi cim mbiram. Waaye Sëñ bi moom, Latjoor lijëntilulu ci anam gu nooy,te teey,nun ko ko indile,mu bind koy leetari leetar,yonni fay ndawi ndaw,teewul Sëñ bi bañ,nee nanu ma wax na bis kenn ci ndawi buur bi,ne ko : neel ki la yonni rus naa malaakay Yàlla yi di ma gis ma jëm ci buur bu dul yàlla}}. Dégge naa ci sheex Aadama SÀLL - moom kenn la woon ci ñi njëkkoon a jébblu ci Sëñ bi , cosaanoo woon Jolof - mu ne leetar bi sëñ bi mujj a bind Latjoor moo ko doon yobb, mi ngi ci naan: Muhammad Ibnu Maslama nee na boroom xam-xam ci buntu buur,mi ngi mel ni weñ ci kawi jonkan}},Latjoor jox Xaali Majaxate Kala bataaxel bi - moom moo nekkoon mufti bu mag bi - Xaali yër ko tiit, ne :(( Innaa lillaahi wa inna ilayhi raajihuun)) buur bi ne ko lan la ? mu ne ko,kii waxul ak yaw man lay waxal,mu ne lu man a xew waxal rekk,mu jàngal ko ko,Latjoor ne ko: ci man de la gën a dal,ndax yaw lu man a xew ,ya’ay weñ wi man nag,ay dem-àll laa.

Waaye nag yaw miy boroom xam-xam loo wax ci moom? Xaali ne ko man daal li ma gisoon,mooy nu bàyyi ko ak mbiram ,ndax kat notante ak moom ag woru la,boo ko notee bokk ci ñi gën a kawe,bu la notee, nga di ci ñi gën a suufe,te maneesu koo not. Buur bi ne ko wax nga dëgg,ndax baykat kat yàgg naa gis jànji ci toolam - te manu koo bay, manu koo saxal -mu bàyyi ko fa,Xaali ne ko waa-waaw,mu ne nan ko jàppe jànji boobu. Ci noonu leetar ya dog,wax ja jeex,alhamdu lillaah.

Beneen nettalee ngii bu gënatee yeeme,waaye soriwul bu njëkk bi,mooy,bi leetar yi ak coow li jeexee ci bataaxel bu saf boobu,yàlla dogal na Latjoor ànd ak Xaali ci lenn ci tukkeem yooyu mu daa def,ba wàcc benn dëkk wetu fi sëñ bi dëkkoon, bi Sëñ bi yëgee ne moom ak Xaalee ànd,mu ne na nuyji Xaali,ngir ñaari mbir,menn mi, mooy Xaalee ko daa jàngal,te ku la jàngaluw araf sa kilifa la, ñaareel bi,xaritub baayam la woon,mu war ci moom mu jox ko àqam te jokk ko,ndax danu ne : (( joxe àqi waajur gi gën a mat,mooy waa ji dox kóllare ak jokk ko ci xariti baayam yi )). Bi mu agsee fi ñoom, fekk leen nu toog ci lal,sëñ bi nuyyu leen,nuyoob màggal,toog ci suuf,toogul ca laltu ga fa nekkoon,bi mu toogee tuuti ne Xaali,da ma la fee deggoon rekk ma ne naa fi jaar siyaare la,ci noonu Latjoor xam ne daa bëgg a leeral ci ne dikk gi moom taxul,juboo’k moom it taxut. Latjoor gestu Xaali ne ko,nun kat kii war nanoo wax ak moom ca sunu mbir ma nu ko woowe woon ba sonn,mu bañ,Xaali ne ko aca, ne Sëñ bi: man dey maa ne Ahmadu Sheexu da doon wooteg yonant,te di ci xeexe it, kon ray ko dagan na,lekk it alal ji ñu nangoo ci moom niki màgg ak njaf ña mu àndaloon (njaf mooy jàpp jaam),loolu lépp dagan na,bi mu noppee mbooloo mépp noppi ab diir,Sëñ bi ne Xaali ndax da ngaa wax ngir ma tontu la?,Xaali ne ko waa-waaw,bu may wax kay nga tontu maa tax,sëñ bi neeti ko : kon am naa ndigal ci tontu ? mu ne waa-waaw, mu ne kan moo la man a seereel ne woote na ag yonnant ? Xaali ne ko waa Kajoor,mu ne ko ñooñu ay noonam lanu,te diy xuloowaaleem,di xaree’k moom,nan lanu koy seedeele ? Xaali neeti ko waaye waa Samba Saajo,fi xare bi ame woon?, Sëñ bi ne ko ñooñu kay dun seede,ndax xare baa leen fa fekk,sottiku ci seen kaw,te yëgunu woon,nan laniy xame ki nu tuumaal ak li nu ko tuumaale?, Xaali ak mbooloo mi ne tekk as lëf,ba mu yàgg mu ne yaw gone gi,won nanu la Yàlla,nga jiitu nu ca,kon ag ndokkeel ñeel na la,dal di nooy,te juboo’k moom.

Pënd ba wuri,Sëñ ba tàggu leen dem,ci noonu, yoon yépp dagg ci moom lu dul wi jëm ci Yàlla,ndax kat moo jàkkaarloo ak ñu baax ñeek kàccor yi,jàng ca ñoom: wa ufawwidu amrii ilal laah innal laaha bashiirun bil hibaad,wallaahu yahlamul mufsida minal muslihi}} muy joyal naa samay mbir ñeel yàlla,moom miy gis jaamam yi,Yàlla xàmmee na kiy defar ak kiy yàq.

Li mooy dooley Sëñ bi,te nii la dogoo woon,donga yi raw ko, cig dogu,foo leen fekk ña ngay xeex ak nit ña,nga gis daanukatu jéll yi fii,leeg-leeg nga gis ku ci yéeg ba ci kaw njobbaxtalu garab,ne dërr fi suuf,jiital bop bi,jug faxasu dem,te dara du ko jot,ak ñuy tàbbi ci sawara génn,te dunu lakk,di yekkati xasiday Sëñ bi,ci penciy nit ñi,ak seen daara yi, ñuy xeex ak ñoom te du tax nu bàyyi, ñu leen di door ak a jéng,ak a nangu seen alal,ak a génne seeni kër,loolu lépp,ngir teqale leen ,te tas leen. Mu mel ne jëf jooju da leen na dolli ag xeemeem ak ag sóobu, mu mel ni loolu mbóotum Yàlla’a,mu ball juge ci baatinub seen Sëriñ ba ca ñoom,Sëñ bi daa leen dolli pastéef,di dëgëral seeni basiira ,di yekkati seeni yite ba ca yu saaba ya,naan leen roy leen saabay Yonnant bi, ñooy seeni mbokk de,te daje nanoo’k lu gën a tar lii ngeen nekk, ndax ray nanu leen ci yoonu Yàlla,tuur seeni dereet,nangu seeni alal,génne leen séeni kër,te loolu téewu leen a jublu ci li nu soxla, ba am tagg wu rafet ca Yàlla, : lil fuqaraail muhaajiriin allaziina uxrijuu min diyaarihim wa amwaalihim yabtaxoona fadlan minal laahi,wa ridwaanan,wa yanzuruunal laaha wa rasuulahuu ulaayika humuz zaadiquun }},mu leen di xamal ni,danoo war a roy ci way gàddaay yu ñàkk yooyu,nga xam ne ku dul yàlla ñoru leen woon, ñu génne leen seeni kër naggu seeni alal,ci yoonu sàkku Yàlla ak ngërëmam,ak dimbali Yàlla ak ab Yonnantam, ñooñooy ñu dëggu ñi.

Mu naan leen xanaa xamu leen ne ñooñooy seeni baay ci diine,kon lu leen man a dal,day daal di doon lu néew, laxadd kaana lakkum fii rasuulil laahi uswatun hasanatun liman kaana yarjool laaha wal yawmal aaxira}}muy :ku gëm Yàlla ak allaxira,na ko wóor ne am na roytéef bu rafet,ci yonnant bi. Muñ leen tey rafetal ci kiy ñaawal ci yeen, Idfah billatii hiya ahsanu,faizal lazii baynaka wa baynahuu hadaawatun,ka annahuu walliyun hamiim,wamaa yulaqaahaa illal laziina zabaruu wamaa yulaqaahaa illa zuuhazin haziim}} muy dee leen jañe jëf ju ñaaw, jëf ja gën a rafet,kon nga gis ne ki nga xam ne,ag noonoo daa am seen diggante,da na mujj mel ni sa xarit bu sellug xarit,loolu nag ku dul kuy muñ du ko am,ku dul ku di boroomub cér bu mag. Dee leen di fuglu yawma nadhuu kullu unnasin bi imaamihim muy bis ba niy woo nit ñu nekk ci seen imam. Kon de bañug ku bañ du leen naqari, ñu daan def bu nu naanee ci ndoxum waaraatey Sëñ bi moomu,ba màndi, di ñu sawar,di daanoo’k a yuuxu ak a fecci,ci diir bii,sëñ bi doon baril lu muy def ay xasiday xam-xam,ak yu tagg,ci la woyoon Masaalikul Jinaan,muy téere bu amul moroom ci tazawuf,yor junni ak juroomi téeméer ak juroom fukk ak ñatti bayit,ak Mawaahibul Xudoos,ak yeneen,ci la wàccee it ñu bari ci donga yi,niki sheex Ibraahima FAAL,ak sheex Ibraahima SAAR,ak sheex Anta MBAKKE ak sheex Aadama GËY ak sheex Asan NJAAY ak ñu mel ni ñoom.

Bi nit ñi barilee lor yi ak sonal gi,ca Mbakke,mu tuxoo fa sanc Daaru Salaam,ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak ñeent,waaye teewul lor yi wéy di dolliku,mu sax fa lu tolloo’k am at,di yar nit ñi,di leen yéege,nuy gën a dolliku,raj-rajloo biy gën a yokku,wërsëg wiy gën a sottiku niki ab taw,mu juge fa,dem as lëf,ca penkub bëj-gànnaaru Daaru Salaam, ci lu tolloo’k juroom walla juroom ñaari kilomet,sanc fa Tuubaa,ci mujjug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom,walla ci njëlbéenug atum junni ak ñatti téeméer ak juroom benn,tuxu fa ak njaboot gi, sëñ Fallu nettali na ma - ñaareelu xalifa - ne magam ja sëriñ Moodu Mustafa,mi njëkk a doon xalifa,mi ngi ganee àdduna Daaru Salaam,guddig àjjuma,fukk ak benn ci muharram atum 1306 g , njëkk sëñ biy tuxu,ndax moom mi ngi tuxu, ci li nu wax, ci jumaadas saaniya. Ci guddig kasurajab,maanaam ñaar fukk ak juroom ñaar ci rajab,sëñ Fallu gane àdduna, ñu magantee juroom benni weer ak fukki fan ak juroom ñaar,yal na leen yàlla barkeel,ginaaw bi,ci la sëñ Muhammadu Lamin Baara ganee,bokk ak sëñ Moodu Mustafaa nday ak baay,ci atum 1308 g, walla 1309g . Mu des Tuubaa nag noom Sëñ bi,di dem ak a delsi,ak a tuxu ci diggante kër yi,niki Daarul Minnan, Daarur Rahmaan,ak Daarul Xuddoos.

Ku dul Yàlla nag xamul xew-xew yi daa am, ci digganteem ak boroomam,ak diganteem aki saabaam,ci xeeti tarbiya ak tarxiya,ak yu ni mel,ak jàngale ci taalifam yi,ak digganteem ak ñu baax ñi,ci ay mbir aki duggalante ak ay xuloo,ngir seeni doom ak seen taalibe yi wëlbatiku woon jublusi ko,ak ci digganteem ak buur yi ak jaraaaf yi,ciy xuloo,ngir fiir ak tiit ci seen nguur gi. Lu man a xew,doxiin wi moom,juboon na,donga yi jub, ñu daa dolliku ak a yokku jamono ju nekk, ku mu ci wàcce ,mu wéy di jub,ku tàbbi it tàbbi cig njub,ba bi mu tukke ca géej ga.

Doggantal : cig sancam Jolof ak li ko waraloon[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëñ baa ngi sanc Jolof - ci li ma sëñ Mbàkke BUSO nettali - bi mu nekkee Tuubaa,ba nit ñi bari fa,magi donga yi denc ay soxna,dëkk yi woon ci wet gi, ñu ci bari tuxusi fi woon ak seeni ñoñ, ñi sëñ bi jugoon ngir yar leen tàmblee jaxasoo’k ñeneen ñi,nos gi sëñ bi nosoon mbir yi,am lu ci tàmblee yàqqu,mooy bëgg gi mu bëggoon a ber ñiy jàng cig wàll, ñay ligéey,ca geneen wàll, ñiy ligeey ak ñiy jàng jaxasoo gi naqari ko,rawati na jaxasoo gi niy def ak ñeneen ñi,nga boole ci loolu ,aj gi mu bëggoon a defi ak siyaare ji Yonnant bi (j.y.m),te bëggoon koo bëgg,ba daa ko wax ñenn ci ñi ko jege woon.

Kenn ci sunu moroomi naari Daymaan yi,di Muhammad doomi Hamdil Abhami nettali na ma ne:Sëñ bi nee na ko ca at mooma ca Tuubaa,ndax bëgg ngaa aji? Ma ne ko waaw-wallaahi,waa-waaw,ku ma fay yobbu kay laa amul,mu ne ko,demal ca sa ñoñ,te waaj,te ñëw ci mujjug at mii, nu ànd aji,bu neexee Yàlla ,ma dem waaji te lijantiji sama njaboot,naan (Inna lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun).

Nu dellu ca wax ju njëkk ja, Sëñ Mbakke BUSO nee na,bi ko ñaari mbir yu gaar yooyu jaaxalee,muy mbirum jaxasoo bi ak mu bëgg a aji gi,da maa woo,waxtaan ci ak man,diisoo’k man ci mbirum ñu sanc ab barab,bu nu man a tàqalee ñaari kuréel yi wëlif ñu dul ñoom,te teqale leen ñoom ci seen biir,ngir ñiy jàng ak a jàngale man a def seenub ligéey,mu samp ci jiite njàngum alxuraan mi, ,sëñ Abdu Rahmaan LO,njàngum xam-xam mi,mu teg ca Maam Cerno rakam ja, ànd fa ak ñoom ñaar rekk ak seeni kuréel,keneen dollikuwu ca,ci donga yi walla sheex yi. Mu ne ma yaw nag kon da ngay des Tuubaa,di jëwrini donga yi, ñiy siyaaresi bu nu ñëwee ak seeni àddiya,ku ci war a agsi,nga bàyyi mu ñëw,ku warut a agsi,bumu agsi. Ma ànd ak moom ci loolu,xalaat ne lii daal xalaat bu nu barkeel la,inshaal laah.

Mu tàmblee waaj,di ci làqatu ñi mu bëggul ñu dem,bi dogu gi dëggaree ci dem,te loolu da ko daa làq sunu waajur wii di nijaayam, nga xam ne da koo bàyyi woon ak man rekk,doyloo ab gis-gisam ci man,mu mel ni da maa soxlawul - bi mu ci dogoo dëgg nag,la xam ne du man a ñàkk,mu yëgal ko nijaayam jooju,mu dal di ko koy yëgal,yëf yi nag tiis ko lool,ngir xam gi mu xam ni buuri Jolof yi fiire,ak ni nu manadee muñ,wuuteek buuri wii tund , te taalibey Jolof yi it dunu bàyyi seeni doom aki donga,te dunu muñ it, wuuteeg yu gox bii,mu ragaloon nu sonal ko,aaye woon ko ci anam gu nooy mu bañ a dem, yee ko ci aaday ñaari dëkk yi,ci li mu ci xam,ndax xamoom na ne li Sëñ bi bëgg dëppoowul ak seeni aada.

Waaye Sëñ bi moom niki soofiyu yu mag yi,dafa dogu te fas yeenee wéyal li mu dogu, ndax wéyal ag dogu ci tasawuf la bokk,tekki ag dogu fi ñoom mook tubbee yam,dee ko gën a woyof ci ñoom.

Kon Sëñ bi laxas na ak dongaam yooyu,ca sawaal ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñaar g,(G, mooy:ci ati gàddaay gi) wuti suufus Jolof,ndax gisul ci Bawal,barab bu man loolu mu bëgg,ca jamono jooja,ak ndax itam Jolof suufus ay maamam la woon,te foofee ca la wër Tuubaa amul am ndox,walla bu fa saxee it da na ajowoo jankoote ak ay ñoñam,mbaa mudaaraante ak ñoom,te loolu du lu mu daa faral a def,mu dox ak ñoom,ba Mbàkke Baari,wacc fa,sanc fa,waxtaan fa ak yenn jaraaf,waaye ag ñagas feeñ ca njëlbéenug wax ja, àggoon ci ñu naan:nun dey xamunu woon ciy donga ag sàkkoo dooni buur, ñii di ñëw daal,nekkunu lu dul ay buur,yu ñëw ngir xëccoo’k ñun suniy suuf,yàgg nanu leen a dégg ca ña ca seen ginaaw,nun nag ñi ngi giñ ci ne dunu dëkk ak nun ci sunu suuf sii,ci seen melo wii,ak wax yu mel nii,ci yi ko nijaam ji daa wax,ak a sentul bu fa demee.

Waaye Yàlla moom bu bëggee amal am mbir da koy wutal ay sabab, nee nanu bu Yàlla bëggee tàllal gënéel lu lemu,da koy wutal làmiñu ku iñaan. Bokk na ci xéewal yi Yàlla xéewale Sëñ bi , sóob gi mu ko sóob ci yoonu wàlliyu yi, sunnatul laahil latii qad xalat min qablu,walan tajida lisunnatil laahi tabdiilan }} muy ci maanaa yoonu Yàlla wii di wu wéyoon bu yàgg,doo gis ag coppite ci yoonu Yàlla. Nit du jug mukk jëm ca Yàlla ndare bu danu koo natoo ay noon yu koy lor,loolu fiiraangeg Yàlla’a, ngir mu bañ a jàdd,bañ a wéeru ci ku dul moom,Yàlla da koy feeñu cig màgg ak cib taar,ci feeñu gog taar gi (attajalliil jamaalii) ,la ko Yàlla di ñoddile nit ñi, ñuy sottiku ci moom niki ay weñ yu tiimub puur,loolu nag ci tàggatug Yàlla lay ame, ñuy yërmaande juy texeel ku nar a texe. Ci feeñu gog màgg gi attajalliil jalaalii la leen Yàlla di dëddale ak yenn xol yi, ñu nekk seeni noon,dunu gis seen hurma,dunu leen gëm,di leen ayibal ci seen bopp,ak ci seeni taalibe,waayee ak loolu lépp,hifthul hinaaii du tàggoo’k ñoom,mooy wattu gi leen Yàlla di wattoo’k a aar,dara du leen dal lu dull lu Yàlla bëgg mu dal leen juge cib noon,di luy ñaaw ci saayir,diw yoon jëm cig fayantoom Innaa minal mujrimiina muntaqimuuna }} muy ci maanaa,da nanu fayyu ci ñiy tooñ. Ñi ngi ñaan Yàlla jàmm.

Lii mooy mbirum Sëñ bi ak ay àndandoom ca njëlbéenug Jolof, bu dee lu aju ci ñam ba woon ca ginaawam nag, ñoom Sëñ Mbàkke BUSO nee na:taalube yi mu bàyyi woon Tuubaa,bi nu yéggee ni Sëñ baa nga Jolof , ñu tàmblee wuti pexey dem fa,yalwaankat yi fekksi leen ci loolu, ñu gàddaaye Tuubaa,ndare ku fa dëkk,xalaatub siyaarekat yi di fa yam dal di yàqqu,lu tax déet, ginaaw mbir mi du mbirum xalaat.

Bu dee lu aju ci jaraaf yu dëkk bi,ku ci gisoon,li nga gisoon gën naa yokk,ku ci gisutoon tàmbli nga gis leegi,nga boole ci lanu déggoon ci diggam ak buuri Jolof yi,nu tàmbli noo dikkal ci kaw ak suuf.

Bi buur yi ak seen dag yi gisee li nu gis,te ñoom boroomi ngànnaay lanu, ñu daa dund ci seen ngànnaay rekk,danu daan song ku leen daa jéem a të,duma ko,nangu alalam,ray ko mbaa ñu njaf ko (jàpp ko jaam),loolu nag di woon aada ju yàggoon ci ñoom,ju nu daa donnante,waaye loolu téewul ñu amoon jàmm ak lenn ci boroom néeg yu mag yi, daawunu leen boole ci seen jëf jooju,daawunu ci boole it ñi daa aaru ci seen kaaraange,niki néegub sëñ bi.

Loolu ak meneen mbir a waraloon nu jaaxle woon ci Sëñ bi,meneen mbir mi nag , nga xam ne moo leen gënoon a jaaxal,mooy mbirum nguur gu raglu gii,loolu nag mooy tubaab yii di waa faraas, ñoom danu daa def,suuf sunu not ,jël fa njiit,muy ku fa bokk,samp fa,ngir waa dëkk ba bañ a mer te ànd ak ñoom,xoolal ma gii xam politig. Ci noonu nu jël buur yi ak jaraaf yi teg leen ci kaw daara yi ak donga yi,ñuy seeni njiit,waaye loolu xéewal a ngi ci ndax tax na ba buur yi ak seen jikko yu bon yi nu yoroon, di sonnal jullit ñi ak a fitnaal ak a def li leen soob ci nit ñi jeex.

Bi jaraaf yooyu demee ba manatunoo dellu ci seen aada yu njëkk yu bon ya,muy ray jullit ñi,ak giir seeni alal,ak doonte loolu da leen di àggale ci nuy raye it,du tee nu def ko,bi nu demee ba manatunu loolu te loolu tubaab yee ko waral, ñu mujj di leen xiirtal tubaab yi,jaare ko ci ay pexe ak ay wor. Mu neeti : jaraaf yooyu jaxase googu nu doon jaxase jullit ñeek nguurug tubaab yi,jubluwunu ci woon,faagaagal leen,ndax lu man a xew, ñoom ci seen ron kiliftéef lanu nekkoon,doonte ci anam gu woyof la,waaye kay ñi ngi ci jublu woon ame ciw yoon wu nu man a nangoo seeni alal,bari na lu nu leen daa wax naan diw kat da leen a bañ,diw it nanguwul a fay galag, diw mee am na lu mu leen di waajal,diw mii mi ngi wut ay ngànnaay,di dajaley fas,walla nit ñaa ngi koy deglu , walla ku bariy taalibe la, ñu koy màggal,dayob màggal, ba àgg ci bu leen junjoon geej gi,ñu sóobu ci xuus ko,ak leneen ak leneen,ci seen fen yi nu daa def,ngir bëgg tubaab yi digal leen ñu songu leen,walla nu def ci ñoom lu leen soop.

Te xamunu ne yewwuteg faraase yi,ci wàllug politig moo gën a yaatu loolu,waaye nag wax bu baree juge ci ku la naan mooy sab bët,di sa asaa sekkare,di la xoolal sa ginaaw,da na mujj am lu mu bàyyi ci yaw benn bis,rawati na bu fekkee ki ñu ne moo def loolu,du rambaaj,du jaxase,te du jeem a setal boppam,ca ki nu ko rambaaje,te ñiy yàq dunu dañ,di yàq diggante bi,rawati na bu nu niroolee am mbiram ak mbirum ku yori donga,yu ko gëm,lu mu leen digal nu def.

Loolu moo waraloon ñu tàmblee tiit ci moom,ndaxte dañu koo niroole woon ak sheex Omar Fuutiyu, Tukkulóor la bu defoon ay xare ci wàll gi mu dëkke woon , ci mujji ati juroom ñaar fukk yi,bi loolu jàllee ba teg lu néew,la benn wolof bu tuddoon Maalik BA,nu gënoon koo xam ci Màbba,defoon ay xare ca goxub Saalum,ci ati juroom ñatt fukk yi,ginaaw bi la Ahmad Sheexu dib Tukkulóor,moom it,xaree xareem ba ak waa Jolof ak Kajoor,ba bi mu deewee ca bisub Samba Saajo,ca wàllug Luga,ca mujjug ati juroom ñeen fukk yi.

Jaxasekat yi nag ,bi nu demee ci tubaab yi danu leen ne Sëñ bi ñii lay roy,ba mujj tubaab yi manatuñoo ñàkk a gëstu li nu leen wax,lii daal mooy li gën a waral tubaab bi jublusi Sëñ bi,ginaaw bi ko Yàlla dogalee namm ca la mu ca namm,muy wax joj dara amu ca,ndax Sëñ bi lorewul ,soxlawul àdduna,te xemmeemul li nu jort ci moom,Yàlla’ay seere lii nuy wax.

Bu doonutoon rambaaj yii,waxuma la buur yu ndaw yi sax dunu ko jeemal,waxantuma la ak yu mag yi,waaye loolu day dëggal waxi yonnant bi ji (j.y.m), ñi Yàlla gën a teg ay nattu ñooy yonnant yi,teg ci wàlliyu yi,teg ca ña gën,teg ca ña ca topp}} ,ponk bii nag bu wéy la ci xeetu yonnant bi (j.y.m),ndax ñu baax ñi ëpp ag gëm foo leen fekk,daniy fees dell aki nattu, àdduna dëddu leen naqari ci ñoom, ñooy ëppi jafe-jafe fuuf ñu dul ñoom,boo demee ca Sahiihub Muslim,ak bu dul moom,da nga ca gis :àddunaay kasob jullit,tey àjjanay yéefar,yàlla itam wax ne : wal aaxiratu hinda rabbika lilmuttaqiin}} muy àllaaxira, ñu ragal Yàlla ñee ko moom.


Bi tubaab yi demee ba manatunoo ñàkk a xool mbirum Sëñ bi, ñu tàmbli fa’a yabali ndaw aki bataaxel,ay yooni yoon,di sàkku ci moom mu seetsi leen,moom muy xaar ndigalul boroomam rekk,ak lu yonnant bi,(j.y.m), ñu gise yeex a wuyyusi gi,ag bañ,bu ko defee ña daa jaxase di gën a am lu nu wax,naan,waxoon nanu leen ko,gis ngéen li nu leen waxoon am déet ? .

Ba bi fa tubaab ya yonnee lenn ndaw mu ànd ak yenn soldaar yu néew,bunu leen tollalee’k li nu am ciy xarekat,ndax matunu woon mbooloom xare mu mag,lii moo doonoon li ko boole woon ak tubaab yi.


Doggantal : ci tukkib géej gi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëñ bi,bi mu jotee ndigalul Yàlla ak Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) jox ko kiiraay luy dox diganteem ak tubaab yi,te loolu wax na ko ci genn xasida: ku nu tànn ki,jàmm ak mucc yal nanu nekk ci moom,wutal ko kiiraay lu koy aar wëlif lor,ne ko doxal te bul ragal woru,}}, bi loolu amee mu genn ca këram ga mu sancoon Jolof ngir jàng ak jàngale,ci bisub gàwwu fukki fan ak juroom ñatt yu safar,ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g. Ci jummaada saaniya walla sahbaan ci at mii,la sheex Bashiiru gane àdduna di doomi sëriñ bi,bi miy genn daje ak ki jiite mbooloom xare moomu genn moom itam juge wàllug Luga, ñu daje ca Jeewal ca ngoonug bis booba,sëñ Banji NJAAY,nee na ma - moom ci ñi àndoon ak Sëñ bi kerook la, ñu gënoon koo xam ci Banji Xuja - am na benn karaama bu feeñ Jeewal,mooy bi nu àggee Jeewal , danoo jeexaloon ndox,te foofa ndox bariwu fa,satalag Sëñ bi jeex,bi nu nekkee ci jaaxle googu nag,jenn waay ju yor ab baag bu fees dell ak ndox jege,nu wax ak moom xamul li nu koy wax,nu jox ko ab defukaay, mu duy ko ba mu fees ak ndox,nu naan,Sëñ bi jàpp,ndax moom daawul tiim,waa ja jàll,te déggunu aw làkkam,xamunu ci moom dara.

Sëñ bi nee na :ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,nasaraan boobu di njiitul soldaar yi,dikk na, bëgg a wax ak moom,mu wëlbati kanamam wëlif ko ,jublu Yàlla,jàng Bismil laahir rahmaanir rahiimi juroom fukki yoon,waa ja nooy,aw xalam fay,mu gaaw genn,jëm ci ay aajoom,mu fanaan foofa,ak jaraaf ju ñuul jooja,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: ginaaw bi nu dajee’k ña génnoon jëm ca këram,te njàqare nekk ci seeni dënn)) ((Dox nanu àndandoo di way gaaw,jëm ca jaraaf ja,ba tàkkusaan jotee ñu julli fa cig ragal yàlla )) ((Ginaaw bi la jaraaf ji daje ak moom,mbooloom xareem mi wër ko,am ca ñuy siyaare )) ((Mu jubale kanaman ca Yàlla mu tedd ma,bañ koo jubale jaraaf ja,ngir am li mu bëgg )) ((Wax juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi,cig toroxlu jëm ca ka nga xam ne,fu mu daaneele ab noon mu nërméelu)) ((Jaraaf ja génn cig gaaw jëm ca aajoom,mu fanaan fa di boroomi xéewal.}}

Waxam ji mu naan am ca ñuy siyaare ,Sëñ bi nee na mi ngi ci jublu woon,taalubeem ba Omar NJAAY,sheexub Konjoru Njaay,di dëkk bu nekk ci wetu Luga,moom nag am na wàccuwaay bu kawe ci sëñ bi,bi mu faatoo sëñ bi seereel na ko yiw wu rëy,dig ko it yiw wu ko ku dul moom di ñeewe,ngir rafetug njortam,ak waxam ju rafet ci sëñ bi, ñi ngi ko denc Njaaréem.

Sëñ bi nee na: (( Omar mii mi ngi génn,ngir siyaaresi ma,daje ak soldaar siy génn,fekk nu xamoon ko,te fonkoon ko, ñu kontaan ci ànd gi mu ànd ak ñoom,jàppe woon ko kenn ci seen kilifa yi,waaye Yàlla moom xam na la nekk foofa)). Sëñ bi nee na ((nasaraan boobu jiite woon soldaar yi,moo doonoon ki yoroon Luga (gouverneur) ca jamono jooja,doonoon gorob buuru ndar (boroom ndar),looloo waraloon ñu déglu woon ko ci samay mbir,mooy ku rëyoon, ki daawul wax ci man lu baax,daawu ko def,daawul ànd ak ku koy def,dogu woon it ci tumbrànkeel ma,nu ne ko du fi ame,mu ne kenn du ko tee am,dogalub yàlla bi dëppook li mu dogu,looloo taxoon,ma yàggoon Ndar ñuy xool samay mbir,looloo taxoon mu wird aayay wa iz yamkur bikal laziina kafaruu liyuzbituuka aw yaxtuluuka aw yuxrijuuka,wa yamkuruuna wa yamkurul laahu wal laahu xayrul maakiriina}}muy ci maanaa ,bi la ñi weddi di fexeel,ngir saxal la fi,walla ñu ray la,mbaa ñu génne la, ñu nekk di fexe,Yàlla itam di fexe,te Yàlla’ay ki dàq a fexe.Sëñ bi nee na :((Ndar, ña fa nekkoon ñatti kuréel lanu woon, ñu bëgg ñu bàyyi ma fa,bu ko defee,nu di leen sonnal ca daanaka-dun ba bépp (daanaka-dun mooy Presqu’ile) ,di yàqq seeni kër,ak ñu bëgg ñu faat ma, ñooña amunu lanu bëgg,ak ñu bëgg ñu tumbrànkeel ma, ñooña Yàlla dëppale dogal bi ak seeni xalaat)). Sëñ bi wax na ci loolu lii: Yàlla tàbbal ci xoli ñi sababoon ag tuxalam,ca jooja jamono)) ((Mu tàbbal ci seeni xol,ag génne ko,jëme ko ca réew yu sori ya,mu ame fa lu kawe déggub Saariya}}

Yàlla (t.s) dëggal na ba mu naan wal laahu xayrul maakiriin}}muy yàlla’ay ki dàq a fexe. Ndax xéewale na ma ñatt yu gën seen ñatti kuréel ya,ndaxte bi may tukki,amoon naa martabay dëgg-dëggi sëriñ,ci gëm ak lihsaan ak lislaam,waaye dese woon naa lu ma yitewoo woon lool ba mu daa ma jaaxal ak a fogloo (fog mooy ñàkk a nelaw guddi) ,te ñàkk ko, ñu may jam ay xeej a ma ko gënal,di daggate samay baaram,loolu moo di matug gëm Yàlla gi nga xam ne mooy dëgg-dëggi xam Yàlla,ak matug lislaam gi nga xam ne mooy yaqiin ( mooy mu wér la ne li nga nekk ay dëgg,ni ngay xame ne aw xal day lakke boo ko joggee) ak matu lihsaan gi nga xam ne mooy àgg ca Yàlla mu kawe mi, ñatti mbir yile,amewu ma leen, ci lu dul jaxasoo gi ma jaxasoo’k ñoom,te loolu moo daa doon sababu rékki gëm,yal nanu ci yàlla musal.

Ab nettali bu yéemee ngii ma, dégge ko ci Sëñ bi,ci mbirum àttekatub (goornoor) Luga bu rëy te bon,te yoroon woon mbirum tukkib Sëñ bi te taxawoon temb ci mu am. Sëñ bi nee na :(( àttekat boobu ,bi ma nekkee ci tukki bi ,laa dégg ñu ne danu koo mujj mere,gëstu ay mbiram,gis ci luy waral ñu génne ko,tumbrànkeel ko,bi niy xalaat,mbugal mi nu ko war a teg,am ku ne kii daal,ginaaw moo taxoon nu génne Sëñ bi tumbrànkeel ko,nanu ko yobb,fa waayam ja nekk, ñu dëppoo ca loola,muy fayyug sunu boroom,yëguma lu dul ñu ne ma àttekat baa ngi ci dun bi ma nekkoon,mu nekk foofa ab diir di ma làqatu ngir ragal ak rus,loolu moo waraloon mu dem gis goornoor (àttekat walla saytukat) ba fa nekkoon,ne ko moytul ma Sëñ bii fi yaw,bu ko jéem a def lenn lu ko naqari,ndax lii ma dal de dara waralu ko lu dul sama yéene ju ñaaw ci moom,kon daal bul def lu dul,di ko jox li nga ko war di fay weer rekk te yam ca .

Loolu moo waraloon àttekat boobu nooyoon mel ne galas fi man,tukki bi, li ci jafe woon lépp mujj yomb. Bi Yàlla sottee ndox ca sawaraam wa doon jëf-jëfi (moom goornooru Luga bi), mu mujj di ku sedd,la nu ko delloo fa mu juge woon,ginaaw bi ñu yobbooti ko ci penku bi,ca wàllug Xaay,foofa la ko ab njabarkat bu bàmbara njabare,ci génn kërug bàmbara, mu dee di ku nu dàkku, di ku nu ngàññ, xoolal ma rekk mujjug ñiy tooñ . Mbirum noonam boobu,niroo’k lool,mbirum noonub ki miy ligéeyal di Yonnant bi (j.y.m),noonam booba di woon Haamir doomi Tufayli,ba mu nee jamono ja ko tawat ja sonnalee ci génn këru jenn jigeen ju Salool: (ndax lii day am mbas mu mel ne mu giléem , te di ag dee ci néegub jigéeni Salool ?).

Sëñ bi def na ag xasida,gu mu tënke arafi mazalul jannatil latii wuhidal muttaquun , ba ca, tilka huqbal laziinat taqaw }} ne; tooñ gu nu ma doon tooñ,jeex na,aji not jee ko jeexal,ji damm ngànnaayul ki doon puukarewu, te mu damm)) ((Moom de yàlla am na samag cant,ndax rayal na ma ka doon fexe ci atum junni ak ñatti téeméer ak fukk ak ñatt g,te deem gi dolli xalaat yi)) ((Amewul ca la mu doon def,lu dul am mbugal,te ginaaw bi mu farloo,ba yaakaar ne moo ci nekk,daa daal di giim,tawat ji gàllankoor ko)) ((Fayyug sunu boroom da koo tiital mu daw, ci géej gi ak ci jéeri ji,te am mbooloom wor ko }}.

Jaraaf ju ñuul jooju,xam naa aw turam xam giir gi mu bokk,waaye du ma sobeel sama xalima ci bind aw turam,moo’k mbokkam mu nasaraanu, mi daa ñaawal Sëñ bi ak a saboote,fu mu masa’a daje ak moom,moo nekkoon Garambasaa.

Gis naa li sëñ bi bind ci ñoom ñaar, ñu bari it, ci ñi xam seenug mujj,nettali nanu ma ne ku ci nekk dee gu ñaaw la dee,kenn ki mooy ku jéeri ji,mi ngi Ndakaaru,ki ci des,di ku géej gi,nekk Konaakiri,yal na nu Yàlla musal ak jullit ñépp,ci nattu bi mu leen tegoon.

Nu dellu ci mbirum tukki bi,Sëñ bi nee na kerook wird wi mu gënoon di def,mooy Inna wàlliyiyal laahul lazi nazzalal kitaaba,wahuwa,yatawallaz zaalihiin}} muy ci maanaa :kiy méngoo samay mbir,mooy Yàlla mi wàcce téere yi,te mooy kiy méngoo mbirum ñu baax ñi. Loolu mooy maanaam waxam jii: Yàlla naagul na ci man ibliis,fa Jeewal,bi ma ko woowee ci turu walii,(muy kiy méngoo mbir yi).

Sëñ bi fanaan foofa,bi mu julle suba,laxas jëm Kokki, ñu yendu fa,mu tàmbli fa’a woy xasidag Asmaau Ahlul Badri, Sëñ baa ngi wax ci loolu: ganaaw bunu fa yendoo,moom tàmbli na fa di woy lol ubbil na ko ab bunt.

Boobu bisub dibéer la,bi gee jàllee ba teg lu néew,ñu laxas, - ci li ma kenn ci ñi àndoon ak sëñ bi nettali - ci fenkug weer wi,ci guddig altine dëppook ñaar fukki fan,juge Kokki,nee na :booba ñun ñi ngi dox, muy wicc-wiccal ci sunu kaw. Sëñ bi nee na : maa ngi rañaan (mooy dox guddi) kerook ca guddi googa,ci kaw sama wenn ngélamu ñu naa ko Hawnul laah,wu gaaw,nga xam ne fasi ñoñ buur bi manunu ko woon a jot,te ñi ngi doon def li nu man,ba mujj am ci ñoom ñu naan ma:Sëñ bi defal nànk,yëramal sa bopp,te yëram nu,ma naan leen gaaw leen,nu ku nu yilif,ba noppi yonni ko di yeexe? bu ko defee,nu wedam. Sëñ bi def na ci loolu aw woy: laxas nanu ginaaw bi nu yendoo,di dox,ca ginaaw gee, ànd ca’akug xat te di ko muñ Nu àgg,laataa jullig fajar,mu fanaan guddi gi ci yekkati ay bayit ,di boroomug jàjji. Bayit yi mu doon yekkati, ñooy ñaar yu Busayri yii: (kuy sukkandiku ci ndimbalul Yonnant bi,bu koy gaynde fekkoon cib àll it wedam) (Moom Yonnant bi,foo ko gise ak doonte moom rekk a ànd,da nga naan moo’k am mbooloo ànd ngir,màggam ga )). Li mu jublu ci di boroomug jàjji gi ci woy wi,nag,mooy mu nekk di jàjji fas wi ngir mu gaaw. Ginaaw bi, nu àgg Luga,laataa fajar,yendu fa.

Nettali nanu ne Sëñ bi nee na:bi mu jegee Luga,kenn ci ndawi nasaraan bi,te bokkoon ci ñi àndoon ak moom,wax na ak moom,ci anamug yërmaande,ne ko ngànnaayul,jege nanu noon bi de,Sëñ bi ne ko ci kàddu gu dëgar,yàlla du lòtt,te du des ginaaw,bi nu àggee ba dal,la ndaw li ko doon wax loolu dellusi, ne ko man dey da ma laa wax ngir yërmaande,ngànnayul,jege nanu noon bi,nga ne ma Yàlla du lòtt te du des ginaaw,li nga ma tontu ci sama wax jii de,xawma ko,loo ci jublu? Sëñ bi ne ko maanaam loolu mooy Yàlla (t.s) dara du fàddu ci moom,kon mi ngi ànd ak nun,bu doxee sama diggante ak noon yi,ci kàttanam,dàkku ma wëlif leen,kenn du ma manal dara,bu ma bàyye ak ñoom it, ñu def la leen soob,kenn du ci man dara. wa in yamsaskal laahu bidurrin falaa kaashifa lahuu ila huwa,wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda li fadlihii,}} muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak lor,kenn manu koo dindi ku dul moom,bu la nammalee aw yiw it kenn manul a delloo ngënélam. (Yàlla mu sell mi dëgal na,Yonnant bi,jàmm ak xeewal nanu sax ci moom,jòttalee).

Ndaw li dem ànd ak mbégte,man ma ne kooku Sëñ bi daf ko doon leeral haalam (haal mooy melo walla mbir walla aw nekkiin) ak ni mu donne Yonnant bi (j.y.m),Yonnant bi (j.y.m) nee na wàkkiirlu mooy sama haal,fàggu di sama sunna,ku lòtt ci sama mbir,bu mu lòtt ci sama sunna}},Sëñ bi moom dònn na ci haalam ak sunnaam ab cér bu mag,ak ci haalu Ibraahiim (j.y.m) bi nu ko sànnee ca sawara sa,malaaka yi ñaan ko mu sàkku ci ñoom ndimbal,mu bañ,Jibriil (j.y.m) ne ko ñaan ko,mu ne xam gi mu xam sama haal doy na ma ba du ma ko ñaan.

Sëñ bi Yonnant bi la ciy jikko,di Ibraahima ci yite (j.y. ñ),day jëf haalu Yonnant bi ak sunaam,gis nga haal ji noonu,mu jëfe ko,ma won la nag ag jëfeem sunna si,bokk na ci loolu,moom defal nanu ag xasida gu nu tënke harafi hasbunaal laahu wa nihmal wakiil}}muy ci maanaa Yàlla doy na nu sëkk,te moom de wéeruwaay bu baax la. Mu ne ci xasida gii laa sengewoo woon (senge mooy ta-ta,walla ci tubaab fortification,muy miir bi ñu njëkk ña daan tabax wërale seen dëkk yi,ngir mu leen di aar ci song gu bette,kon sengewu mooy aaru ) ca ngoonug bisub àjjuma ba,ba ma dogoo ci ànd ak ñoom ca gàwwu ba,ginaaw bi ma Yonnant bi (j.y.m) aaree,digal ma ma dem,ne ma wéyal te bul ragal lor.

Xasida gii nag mooy muslaay li,juttit bu ne war na koo jeem a am di ci musloo li mu ragal,bu leen fàtte li ñenn ñiy wax naan,waxtuw ajjuma mi ngi dale ca ginaaw tàkkusaan,ba bu jant bi sowee,xasida gi nag mooy gi tàmblee hamidtu man yahsimunii minad darar, muy : maa ngi sant ki ma musal ci lori jépp saytaane ak jinne ak nit)) ((Tudd naa sellam ga,muy buur,buy aji wattu,may sàkkoo aaru ci wattoom gi wëlif musiba yi ak mbugal yi)) ((Maa ngi sàkku ci moom mu musal ma ci bànneex,ak ibliis,ak ci mbooleem yiy lore ci jamono ju nekk)) ((Yéene naa koo ñaan di sàkku am ramu,ci darajay soppeem bay ramu ñiy ramu)) ((Mooy Ahmad,sangub mbindéef yi,may julli ak a sëlmal ci moom,te di ko def aw yoon jëm ca sama boroom)) ((Maa ngi ñaan ,sama boroom,ci darajaam,mucc ci saytaane ak ciy ñaawtéef,ak way bew yi di ma xëccoo)) ((Ya’a moom mbindéef yi ,yaw sama boroom,may ma ag mucc ci ñoom,ak bépp balaa ak mbugal)) ((Yaw laa jox sama bopp de,yaw aji wattu ji,ba fàww it ya’ay sama wettal)) ((May ma li ma bëgg ci adduna ak alaaxira,na nga ma musal it ci gàccag àdduna ak gu allaaxira)) ((Jubale naa la sama kanam,yaw sama boroom,ya’ak sama wasiila,te loolu doy na ma)) ((Musalal samag wàll ci mbooleem luy ñaaw,te nga fegal ma mbooleem luy jax-jaxiloo)) ((Soril ma mbooleem noon yi ,ci barkeb Yonnant bi,ak Ahlu Badri ñu tedd, ñiy ay tànnéef)) ((Na nga ma xeewale ci ma dugg ci sa senge (kaaraange) lu aaru li,te dëkk fa,di ku am kóolute ci samay noon)) ((Yaw’ay kiy musal kuy muslu ci yaw,ci lépp lu ko man a jublu ciy mbugal)) ((Samay mbir ba fàww da ma koy joyal jëme ci yaw,ndax ya’ay ki nga xam ne ku wéeru ci moom deesu ko jalax)) ((Yaw aji baax ji,fegal nga ma ag kéefar,ak lori ñoñam,ak jépp fitna)) ((Fegal ma loxol way bokkaale yi,ci darajay Ahlu Badrin,te nga def leen ñuy sama senge)) ((Yaw aji baax ji,nekkal ma te bu ma gàccaal,ci àdduna ak àllaaxira,te dee ma jéggal)) ((Bindalal Yonnant bi ag xéewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam,ci anam gu sax.}} Mu tëje ko fanqalaboo bi nihmatin minal laahi wa fadlin,lam yamsashum suuhun,wattabahuu ridwaanul laahi wallaahu zuu fadlin haziim}}: muy ci maanaa, ( ñu dellu ànd ak xéewalug Yàlla ak ngënéelam,lu ñaaw laalu leen, ñu topp ngëramul Yàlla te Yàlla’ay boroom ngënéel lu mag li).

Mu neeti alhamdu lillaahil lazii hadaanaa lihaazaa,wamaa kunna linahtadiya law laa an hadaanaal laah,wa aaxiru dahwaanaa anil hamdu lillaahi rabbil haalamiina}} muy ci maanaa : ( maa ngi sant Yàlla mi nga xam ni,moo nu gindi jëme nu ci lii ( muy lislaam) ,duñu doon gindiku bu nu Yàlla gindiwutoon,sunu wax ju mujj,mooy ag cant ñeel na Yàlla,miy boroom mbindéef yi) . Xoolal ni mu aaroo woon ci baat yii nga xam ni,Yàlla da leen a tagg,tagg it nit ñi ciy aaroo.

Mu wax: allaziina xaala lahumun naasu innannaasa xad jamahoo lakum,faxsawhum,fasaadahum iimaanan,waxaaluu hasbunaal laahu wa nihmal wakiil ba fam yam}}muy ci maanaa :( ñi nga xam ne nit ñi dañu ne leen: nit ñi kat dajaloo nanu ngir fexeel leen,kon tiit leen te moytu,loola dolli leen ag ngëm, ñu maase ne Yàlla doy nanu ,te doy na sëkk ku ñu doyloo). Nga boole ca loola juroom fukki bismil laahir rahmaanir rahiimi, yi mu jàngoon ca Jeewal,ba ndawul nasaraan bi bëggee wax ak moom.

Waxees na ma ,te loolu lu wér la,ne rakkam ja sheex Ibra Faati, ci bis bi Sëñ bi tukkee,ba bi mu dellusee,masul a dañ di def junniy salaatu alan nabii ci melo wii: (( allaahuma salli halaa sayyidinaa muhammadin,wa halaa aali sayyidinaa muhammadin,salaatan tunajjiinaa bihaa min jamiihil ahwaali,wal aafaati,wa taqdii lana bihaa jamiihal haajaati,wa tutahhirunaa bihaa min jamiihis sayyiaati,wa tarfahunaa bihaa hindaka ahlad darajaati wa tuballixunaa bihaa aqsal xaayaati min jamiihil xayraati,fil hayaati wa bahdal mamaati)). Maanaa mi di:( yaw buur bi jullil ci sunu sang Muhammad,ak ñoñi sunu sang Muhammad,ag julli gu da nga nu ci musale ci mbooleem tiitaange yi,ak gàkk-gàkk yi,fajale ñu ci mbooleem aajo yi,laabale ñu ci, ci mbooleem ñaawtéef yi,yekkatil ñu ci gën jaa kawey daraja fa yaw, àggale ñu ci ca dayo ya gën a sori ci mbooleem yiw yi,cig dund ak ginaaw ag dee).

Mu ko daan def ginaaw bu wàccee kaamil bi,waaye kaamil bi moom lu saxoon la,suba ak ngoon,naka jekk, njëkk Sëñ biy tukki,waaye salaatu halan nabii gi moom saxal gi,man na a nekk muy ndigalul Sëñ bi, mbaa xalifaam bu baax,bu sell ba,ngir xér gu mu defoon ci muccug Sëñ bi ak ag delluseem ci jàmm,mu sàkkaloon ko mbooloo mu ci daawul sàggan suba ak ngoon,waxambaane wu ragal Yàlla,wu dëkkoon Kokki wii di Samba Joop nu gënoon koo xam ci Samba Asta daan leen jiite.

Ku baaxoon la te gudoon aw fan,mi ngi faatu ci atum waafiris sitri,di junni ak ñaat téeméer ak fukk ak juroom ñatt,bokk na ci loolu woy gi mu def Ahlu Badrin,ak aaru ci ñoom,bi mu nekkee Ndar,mu mottali ko, tudd itam ànd gi mu defoon ak ñoom ci tukkeem boobu, ñu daa toroxal képp ku ko daa jéem a lor,téere boobu,jotoon na koo won ca magi Ndar ya ka ñu naan Alhaaji Muhammadu Maabéey,ne ko mu mokkalandi bayit wu njëkk wa,ba ñu dajewaat ginaaw bu ñibisee.

Te kat dajewaat nañu ginaaw juroom ñaari at ak ay weer,bi nu dajee sëñ Maabeey jàngal ko bayit wi,daal di daanu ab jéll,jooy. Ak leneen ak leneen ci li mu aaroo woon te xamunu ko, degg naa ko bis mu naan: bi mu nekkee ci géej gi,masul a dañ di jàng Hisbul Bahri,bu imaam Shaazalii,muy lu am njariñ,li koy wone mooy yitewoo gi ko Sëñ bi yitewoo woon,bayit wi mu digale woon mu wattu ko,mooy njëlbéenug xasidag Asiiru gu yéeme,gi nga xam ne Sëñ bi feeñal na ci njëlbéen gi,ba ci fukk ak juroomi bayit,lenn ci mbóoti tukkeem bi ci diganteem ak noon yi,ak wone ci mucc gu mu mucc ci seeni lor,xamale ne saytaane moo leen wor ci moom,tax ba ñuy am njort yu ñaaw ci moom,waaye seen njort yi sooy nañu,te Sëñ bi dellusi na ci jàmm,bayit yee nekk nii: maa ngi dox ànd ak ñu baax ñi (waa Ahlu Badri),bi may dox (bi may tukki),waaye noon yi jort ne man booba ku ñu njaf (jàpp) laa )) ((Sama dox bi may def, ci wommatug Yonnant bi, ànd ci ak gaa yu baax yi,Yàlla rekk a ko tax a jug,ba fàww it samab dox du jëm ci ku dul Yàlla)) (( Bijji gi ma wommat (bijji mooy jazbu,di lol day xëcc,kon man nanu koo jàppe yitewoo sunu boroom gi nga xam ne daa mujj mel ni ab asyee bu koy ñoddi jëme fa Yàlla) jëme ma ci aji tedd,joj lu ma sàkku ci moom mu jàppandi,mooy liy dox ak man )) ((Samag cant ci xalima,ak ci xol ak jëmm, ñeel na ki ma nekkal cig tab ( ki nga xam ne jamono ju nekk mi ngi may sottil ay xéewalam ) te mooy ki di ab santaakon (ku soxlaalul kenn) )) ((Sama ndimbal,samag dëgëral,sama kaaraange ca noon ya,mi ngi bawoo ci Aji yaatu,ji di ab Mayewaakon,(ku tabe lool) kooku mooy aji dimbali sama )) ((Sama kilifa nag, ci bu may dox ak bu ma taxawee,mooy sama kerkeraan,di Yonnant bi,te mooy ki may ligéeyal,te moom dey day xont (mooy jox ab dund) ku koy ligeeyal)) ((Samab yool ci ligéey bi may defal Ku nu tànn ki,di Yonnant bi, mayewaakon (Yàlla) bee ko warlu,te moom ku am lu mu faye la)) ((Li ma nesar nag mooy nekk jaamub boroom Aras rekk,di ligéeyal gën ji mbindéef,te moom Yonnant bi mooy samab xuppkat (Yonnant bi day bashiir tey naziir,di kuy bégale tey xuppe ngir jaam yi bañ a sàggan bañ a naagu ) )) ((Aji feg jii di Yàlla,moo may fegal ci Yonnant bi,ayi noon yi,ak lépp lu ñaaw te mooy ki may xettali)) ((Samag mujj mooy nekk dib jaamam,di ligéeyal Yonnant bi,mbiri mbindéef yépp nag ca Yàlla lay mujj )) (( Samay weer aki bis ëlëg ñoo may seedeel nekk gu ma nekk di jaamub Yàlla,te moom siw na )) ((Samay sutura ci adduna ak allaaxira,mooy tagg Yonnant b,ci woy ak wesar,te moom suturaalkat bu baax la )) Samaw jiwu mooy téereb Yàlla bi ak sunna si nga xam ne ci laay aaroo ci li yaqkat bi jublu (muy saytaane) )) ((Samay kër wéet na, ñoñ ñi tas,ngir tagg Ki nga xam ne,noo ko man a tagge,du tax tagg wi mat )) ((Woru gi nekk ci mbindéef yi,wor na nasaraan yi,ciy pexeem, ñu jort ay njort,te njort ak woru la}}.


Sëñ bi nee na[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ginaaw bi nu jullee tàkkusaan,lanu dugg ci saxaar gi,jëm Ndar, ñu àgg Ndar bi jant biy bëgg a so,ci loolu Sëñ ba’a ngi ciy wax naan: Yàlla ca bu njëkk,la dàqoon samay nëx-nëx, ca Ndar jëme leen ci ku dul man,ci barkeb Ahlu Badrin ña diy gaynde)) ((Ñu àndandoo, sax ca dun (île) ba akub coona,fuglukat ya di ñu fa bari}}. Ma sax fa - sëñ beey wax - la desoon ca safar,muy fukki fan,ak weeru rabiihul awal,ba ca bis bu mujj ba,muy bisub alximis, ci diir boobu laa matale woyug Asmaau Ahlu Badrin, muy turi waa badar ,topp ko,wéral ko,ci la’a dajee it ak ñu bari ci kilifay Ndar yi,ak li ko wër,kuréel it ci njiiti Njaambur yi seetsi ma ngir tinusi ak ramusi,ci tubaab bi,ma ne leen bàyyi leen ma ak sama boroom rekk,moo leen ëpp ñeewant ci man,gën leen a xam li gën ci man, ñu far taxawlu.

Nee nanu bi nu ko taxawalee ci seen kanam,wax ak moom,ci teewaayu kilifay nasaraan yi,te booba moom ku wéet la woon ci seen biir,amu fa ab xarit du caagéenug aw wéttal,nu ne ko wax nañu nu ci yaw nàngam ak nàngam ? Sëñ bi ne leen indil leen ma ki leen ko wax,ba xam ma’ak moom ku ciy ki wax dëgg!. Te booba li nu doon wax naan moo ko def,ab dof bu amut am xel sax du ko def,waxantu ma la’ak ku mel ni moom, li am daal rambaaj la gu juge ci ñu kañaan lëjal,ba ñu mujj amatuñu kersa ci Yàlla,saytaane yàq seeni xel,jox leen xalaatam yu ñaaw,ba nu mujj di rambaaj ak a tudd ciy ñaawtéef aki caaxaan lol ñi gën a dof ci wutkati àdduna yi sax,xalaatunu koo bëggal seen bopp,mbaa ñu koy soxla,waxantu ma la’ak boroom xel yu dëddu yi àdduna.

Ca bis ba ma war a juge Ndar jëm Ndakaaru,te booba ma nga woor, àgg fa njëkk jant biy so, ñu wàcce ko fa, ca genn kër,mu tàmblee waajal dog ak julli,waaye ñu jekki-jekki rekk lenn ndaw teew,ne ko ayca ñu dem,Sëñ bi jug ànd ak moom,waa ja yobb ko ci néeg bu deesi muslu,lëndam kariis,tàng jérr,xeeñ xunn.

Bi Sëñ bi gisee li wàcc ci moom,mu xam ne mooy nattub Yàlla bi ko doon xaar,amu ci am pexe mu dul gàddu ko,te muñ te sant Yàlla te gëram ko,ndax doon na sentu lu gën a réy loolu,mu dal ni innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun. Sëñ bi nee na ma fanaan fa dundal guddi gi ci saari Baqara ak Aali Himraan, ñu feg ma ñoom ñaari saar yooyu,ci ñaari sawara yi ak ñaari gàcca yi,ma teg ci julli ci Yonnant bi (j.y.m) ki may ligéeyal,sama dënn leer,sama xol dal,kóolute gi dolliku ci Yàlla’ak Yonnant bi,ndax alaa bizikril laahi tatma-inul xuluub }} ci tudd Yàlla ak fàttaliku ko,la xol yi di dale.

Sama gudd gi daal di neex ci Yàlla, ak ci aji sabab jii, ak dëkk bi,ak ci néeg bi. Ci loolu sëñ baa ngi naan: Yàlla dàq na jëme ci ku dul man ca Ndakaaru,wépp ay wu pexewaakon (ki bari ay pexe ) bi xëccoon jëme ci man)) ((Bu ma fattalikoo panaan moomee,ak njiit loolee,ak sax ga,sama xol day naaw ak man jëm ci jëli xepp aki gobar ngir jiyaari,waaye Yonnat bii di kiy fari bàkkaar,dox sama digante ak loolu ))


Doggantal : ci dugg gi ci gaal gi juge Ndakaaru[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Bi nu xëyee - sëñ beey wax - muy bisub àjjuma,di bis bi njëkk ci rabiihus saanii,lanu yeeg ca gaal ga,gaal gi yendu,fanaan,am mbooloo ci murid yi dikkal nanu ma ca digg gaal ga,di jooy,bokk na ci mbooloo moomu,sheex Ibra FAAL,moo ca magoon,Sëñ ba’a ngi ciy wax ak ci gaal gi,nana: Yàlla xamal na ma ci gaal gi,ne maay jëwrini Yonant bi )) ((Gaal gu fees googu ak mbooloo, yendu na fanaan )) ((Muritam bu amub nattu boobu dikkal na ko ca gaalam gu nu duy ga )) ((Murid ba tàggoo, dellu ca dun ba, ànd ak xol bu naqari}}.

Mu jublu ci muritam boobu,sheex Ibra FAAL,ci loolu la jiitoo woon ñépp. Am na ci biir gaal gi ba tay,waa ju ko dikkaloon,di ko laabiire naan ko,am na njiit lu bees lu ñëw juge tugal,jaxasoogul ak nit ñu ñuul ñi,boo ko bindoon xamal ko ne danu laa tooñ,kon mu delloo la sa kër,ca sa njaboot,Sëñ bi nee na waa ji bàyyiwu ko,di ko ci lëjal ba mu far jël daam ak xalimaam,nee na, bi ma tàmblee ba bind wenn bind rekk,la ma wax ji dikkal juge fa boroom mbindéef yi,ne ma leegi da ngay diis sa aajo mbindéef mu mel ni yaw,bàyyi ma fi.

Ma daanaka faatu ngir tiit ak kersa,ca saa sa, ma far la ma bindoon,waaye ngoor si lëjëlati ma,ma ne ko,loolu manul a nekk, ne ko bu buurub buur yi di wax ak jaamam yi mu dëgaral ,kenn du ko man a xam ku dul ñoñam,ña mos la ca neex ak la ca naqari. Nitug neen nag, nga xam ni moo’k nit ñépp a yam,dara waru ko lu dul mu gàttañlu ci loolu te yam fi mu war a yam,bu bëggee mucc,sunu ko tawfeexalul nangul ko.

Ci loolu mi ngi naan: Ki njiit li yonni woon ca ligéeykatu yonant bi,sàkku na ci moom cig laabiire mu yonnee ab bataaxel,ca njiit lu bees la tukkee woon ca seeni suuf,ba mu ko doon bëgg a bind,far reccu )) ((Ginaaw bi aji ligéey ji far li mu bindoon, ñu neeti ko bindal)) ((Mu bind xasida gu nu nangu gi,ngir fàttaliku ki nga xam ne ci moom la Yàlla di wonee aw yoon}}.

Xasida gu nu nangu gi,moom lanu def ci arafi waxi sunu boroom ji (t.s) ((wa ufawwidu amrii ilal laah,innal laah basin bil hibaad)) muy samay mbir maa ngi koy joyal jëme ca Yàlla te Yàlla’a ngi gis jaam yi. maa ngi jëmale samam mbind aji moom ,ji moom suuf ak asamaan ak buur yi.

Gaal ga deqi bisub gàwwu, ñaareelub rabiihus saanii,Sëñ bi nee na romb nanu Konaakiri,am benn wolofu saalum-saalum bu ko fekk ci gaal gi,jox ko fa àddiya ju kawe,ne ko man de da maa dégg ñu ne ya’a ngi ñëw ci gaal gi,jëm Gabong,ma ne naa la siyaaresi,nga ñaanal ma dénk ma. Sëñ bi nee na ci waa jooju la dégge turu Gabong,xame ca it fi nu ma jëme,ma dal di koy ñaanal,ne ko bi ma koy dénk: xamal yaw sama mbokk,ak foo man a nekk,ne amul benn buur bu dul Yàlla,ku jublu ci ku dul Yàlla,dana xam ne amul ku fi nekk ku dul Yàlla,ku jublu ci Yàlla te jaaralewoo ko ci Muhammad Yonnantab Yàlla bi,(j.y.m) da na xam ne Yonnant beey ki yàlla yonni, ñu dal di tàggoo,mu dem.

Sëñ bi nee na ñu romb Garambasaa,mu ne am na ku ko doon ñaawal ci biir gaal gi,waaye Yàlla dox diggam ak moom ci hikamam,loolu nag ni mu ame mooy daa am jëmm ju yéegoon ci gaal gi,ca Konaakiri,te moom xamu ma woon,bi nu jegee Garambasaa,jenn waay ju ñuul génne ci ab néeg ne ma,ndax ya’ay diw ?jaar ci samaw tur,ma xool ko ,mu ne ma, nee nanu ma sama mbokk (mag walla rakk) de moo la jàpplu,ngir barig li la sa taalube yiy rëyal ak a màggal,ak nàngam ak nàngam,bi mu tollee ci wax jooju rekk gaal gi dal di sab (yuuxu) mu dem di xaar coow li dal,ba mu dolli ñaawalam yi,waaye sab ga dakkul ba kerook gaal ga di teer,mu wàcc ànd ak ñi doon wàcc, kon alhamdu lilaa ginaaw amul li mu bëggoon,ci loolu Sëñ ba’a ngi naan: sama àddiya sell na ca Konaakiri, ñeel ku nu tànn kiy fari bàkkaar,ci lu dul kuy weddi)) ((Yàlla setal na ma ca Konaakiri,ci lépp luy xëcce jëme ci yu nu sib )) ((Yàlla soril na ma cag njëkk ca Garambasaa,ka doon léewtoo ak man te mu dem wëlif ma}}.

Àddiya jooju mu tudd foofu nag mi ngi ci jublu,leeral gi mu leeraloon waa ja ko doon laaj,leeral gi mu ko leeraloon maanaam laa ilaaha illal laa,waaye du àddiyay alal ja ko waa ja jox,moom waa jooju nga xam ni bu ko Sëñ bi leeralutoon loolu mu alku,te Yàlla gindee na ko ci leeral gi. Mu tudd romb gi nu romb Dawme,wax karaama gu yéeme gi ko Yàlla defal foofa,mu ne daa jëloon benn bitéelu misk,bu mu yoroon,ngir wis ko ciy yeréem aki téereem, nee na ñu ne ko sànni ko ci géej gi, mu ne ma gaaw sànni ko,bi gaal gi téeree,am mbooloo ci sunu mbokki jullit ñi,duggsi,ndax danu maa déggoon ,ñu ñëwoon ngir nuyyusi ma,waaye képp ku dugg rekk,jox nga ma ab bitéelu misk, ñépp walla ña ca ëpp,ci loolu la Sëñ bi naan: kiy jagleele yërmaandeem di Yàlla,woo na ma ci boppam,ci indil ma xéewal yuy tee jaaxle}}.

Mu jublu woon ci aji yërëme jooju Yàlla mii di boroomi xéewal,daa ko indil ay xéewal,bokk na ci xéewal yooyu biteeli misk yooyu. Mu wax ne bokk na ci karaama yi ko yàlla doon defal ci gaal gi,tàggat gi mu defoon boroom gaal gi mu dikk di ko waxtaanal,di ko won ag ñeewant ak yërmaande,di mettitlu bu baax li ko dal,daan baril lu mu ko daa wax naan ko yaw danu laa tooñ . Mu tuddati ne am na benn doktoor bu ko seetsi woon foofa,mujj am yërmaande lool ci moom naan ko man daal da ma laa bëgg rekk,te fas laa dimble,mu ne am na wenn waxambaane wu tubaab,wu ko dikkaloon wu bokkoon ci waa gaal gi,mu ne Yàlla def ci xolam mu sopp ma,mujj di ma ligéeyal ni ko murit yiy defe .Mu ne moom daal,noonu la yàlla nekke woon ak moom ciy xéewal,tàggatal ko ñépp ba kerook muy wàcc Gabong.

Mu ne Gabong moom yàggu fa dara rekk tuxooti fa dem ci beneen dun,foofa nag ma sax fa juroomi at,mu ne ci diirub juroomi at yii nag laa mjje mel ni ab jant,mu jublu ci, ci yekkatiku ay maqaama akug siw ak bari njariñ,mu ne ci diir bii it la taalife taalif yu kenn masul a def cib taar ak bari njariñ ci Yàlla ak Yonnat bi ak ci lislaam. Dun bii nag mooy Maayomba,li koy tegtale mooy waxam ji mu naan :ca tefesug géejug dun boobu laa taxawoon di joriku, di xutba géej gi naan: yaw géej gi kennalal sa boroom te bul ko ñattal,ndax sunu boroom kat kawe na wëlif ñu koy ñattal(wareesu koo def ñatt, ndax kenn rekk la) cëy moom ni mu doone buur bu tedd )) ((Na nga nekk di bajbaji,di fuur ngir ragal Yàlla,te seere ne man ab jaamam laa,bob sopp na ko}}

Mu ne ba mu fa defee jeroomi at la demati ci beneen dun,nekk fa ak ab coona,am fa ñatti at yu manke tuuti,di ligéeyal Yonnant bi (j.y.m), mu ne am na wenn waxambaane wu bokk ci ñoom wu ko fekkoon fi mu nekkoon di bind,mu bocc jaaseem di ko wëndéel ci sama bopp,naan ma yaw ay diw di jaar ci sama tur,ma ne waaw,mu ne ma moytu ma,sama maam kat raykatu walliyu la woon,te maa di ab sëtam,ma joxoñ ko sama xalima gi,gëdd ko mel ni dama koy song,ne ko xamal ni doo sa maam ja daa raye,te du ma ku mel ni ña sa maam daa ray,waa ja dal di tiit,daw juge foofa fépp.

Mu neeti am na kenn ci seen kilifa yi,ku doon ñëw ca dun ba mu nekkoon,di nemmikusi soldaar yi,fan yooya yépp nit ñi dajaloo ci waajal kilifa gi,di setal yoon yi ak a rafetal ak a samp ay raaya,waaye bi waa ji ñëwee,li mu njëkk a def,mooy laaj ma, ñu tegtal ko sama kër,mu ñëw ,dugg ,nuyyu ma,tudd samaw tur cig màggal,dal di tàllal loxoom ngir nuyyu ma,man itam ma tàllal sama bos,waaye ca saa sa am lu wax ak man,mel ni ag dënnu gu juge ci asamaan,ne : yaa ayuhal laziina aamanoo,inna maal musrikuuna najasun}}muy yeen ñi gëm,xam leen ne bokkaalekat yi sobe lanu,mu mel ni samam xel daa muuru,ma bëmëx ab loxoom bëmëx gu tar,ba waa ji yëngutu,deltu ginaaw,dal di taxaw ab diir mel ni day xalaat ci samay mbir,waaye man loolu lépp,teewul ma nekk ci samam mbind,bi lu tolloo’k waxtu jàllee mu woolu ki koy firil,wax ak moom ab diir,firilkat bi ñëw ne ma sa waa ji nee na mi ngi lay nuyyu,te di la xamal ni bu ko mere ndax moom bokkul ci ñi la bañ,walla mu lay lëjal,di la tumbrànkeel ak a génne sa réew,moom de nee na bu ko manoon leegi mu delloo la fa nga bëgg,boo gisee muy sonn ci yaw ak di la njëkk a seetsi bi mu daataa wàcc,mooy daa am kenn ci sa mbokki senegaal yi,ku taxoon ma sopp la,mu sàkku woon ci man ma nuyyul la ko,moom dey ci ñi mu gën a sopp nga,loolu moo waraloon sama ñëw gii du leneen.

Sëñ bi nee na ma wax kiy tekki ne ko:nee ko loolu ma def de ag bañ ko taxul. Mu dem waaye taxul mu soppiku ca na mu meloon,bi mu demee ba toog ,dal, ñu ne ma da nga koy teral,te booba maa ngi ak as lëf ci seen mburu moomu ñu jaxase ak suukar,mu doonoon mburu mu neex lool,ma yonnee ko ko,mu bég ci lool,sant ma, ne lii de bu ko kuy jambaar-jambaarlu defoon te li miy woote nekkul ci moom,man na ca’a loroo,waaye deesul loroo ci ndigal,alhamdu lillaah.

Da na rafet fii ma indil leen fi bayiti ki def Xawaariq muy Ibnu Hanbal: ( Bari na aji jalgati (tooñkat) ju sol yérey teddngaam,di puukarewu ,sol ab tëneem aki takkaayam) (ay junniy junni nekk ci ron kiliftéefam,te faalewul ku koy digal mbaa mu koy tere)) (ngeen (Sëñ bi lay waxal) wàcce ko ci mbartalum toraxte,dammte ko ci jaasiy ndimbal ju di ab dogaakon (ju ñaw) ) ( muy ndimbal lu tukkee ca Yàlla ñeel jaamam bii di ligéeyal Yonant bi,nga xam ne soldaari nasaraan si ci la nu mujje mokk ba mel ni ay ansaaram,(ansaar mooy ku lay jàppale ak a dimbale) ) ( cey bu tuddoon sekkare bi, kon dey mbindéef yi yéemu,waaye moom ab dënnam bàmmeelub ay mbóot la).

Nee na bokk na ci karaama ( mooy xarbaax ak kiimaan yi Yàlla di defal aw wàlliyu) yi ko Yàlla defaloon ci géej gi,feeñug Ahlu Badrin,mu ne moom kat bi mu nekkee ci benn ci dun yi,dañu koo yobb woon ca karce ga,dëkkal ko fa soldaar sa,nee na ma mel fa ni kenn ca ñoom,ñuy tux ak a naan ak a fo ci sama wet, man may muñ seeni lor rekk,ndax man xam naa ne mukallaf mu ne am na ñaari malaaka yu ko seq,di bind ay jëfam,ginaaw ñaari malaaka yooyu ñoo man a muñ,man a dékku li ñiy dajeel ciy lor,ngir topp seen boroom,kon du jaadu ci man may jàmbat,ndax ñoom kat li leen di naqari rekk moo may naqari,li leen di mettee may metti,te ñoom du ñu jàmbat. Ci noonu Yàlla dogal soldaar si genn bis di tàggatu ji ,ba ñu demee fañuy tàggatoo fekk fa am mbooloo mu war ay fas, kaalawu, sappewu (rang),soldaar si dal di tiit ,taxaw,ci noonu seen njiit li tëyye leen,gëdd leen ne da leen di ray bu ñu siiwalee xibaar bi. Bi suba jotee ba leer,mbooloo mi waroon fas yi ne mes,soldaar si dem ne miik,bañ a nettali dara. Sëñ bi nee na bi loolu tegee ay fan,aakim bi (goornoor bi) woo ko nooy-nooylu ci kanamam,wax ak moom wax ju nooy,ci biir wax ji mu ne ko: xanaa da ngaa am ay àndandoo yu lay dimbali ci li nga bëgg? Ma ne ko ñooñu moom ay nit lanu walla ay jinne? Mu ne ma yaa ko gën a xam ! Man ma won ko ne xamuma dara ci li miy wax,mu dal di noppi. Am na ci boroom xam-xam yi ku ko ci laajoon lu waraloon feeñug Ahlu Badrin gi,Sëñ bi ne ko :ngir tiital noon yi. Keneen laaj ko ne ko ñooña ñooy niti Ahlu Badrin ña walla malaaka ya?,mu ne ko malaaka ya .Am ku neeti ko ndax yonnant (j.y.m) bi ca la woon? Mu ne ko moo doonoon seen njiit,daal di ciy wax wax jii:<< ki nga xam ni wommatal na ma la fàddu woon wëliif bepp wàlliyu,jàppndalal na ma mebat yepp fa dëkk ba niy wax Limbarwali >> << ka soril rambaaj ba ak ku inaañ ka ,wommatal na ma waa Badar ña diy sang>> << Yàlla da na ma wommatal begleg laa illaaha illallaa fu ma man a ne >> . Ku baax ki nee na li mu bëgg a wax ci bayit yooyu mooy: li fàddu woon weliif bepp wàlliyu,mooy feeñug waa Badar ànd ak seen kilifa ga (j.y.m) ca pàkk yu lëndam yooya ca geej ga,ngir jàjji ay noonam.Begleg laa ilaaha illallaa,mi ngi ci jubloo wax aaya bi sun boroom di wax (( wa in yuridka bi xayrin fa laa raadda lifaddlihii)) muy ci maanaa bu la Yàlla bëggalee aw yiw amul ku ko man a tëyye. Fu mu waxe nex-nexi walla lori laa illaahaillal laa,mi ngi ci jublu waxi Yàlla ji mu naan:(( wa in yamsaskal laahu bi durrin falaa kaasifa lahoo illaa huwa )) muy ci maanaa bu la Yàlla laalee ak aw ay amul ku ko man a dindi ku dul moom.

Mu ne bis teg nanu ko ci mbedd mu xat,dal di joyal aw nag ci kawam,tàmblee seetaan,yaakaar ne agsi na ci sama kaw ba noppi,waaye bi mu ma jegee daa daal di jekki-jekki rekk naaw mel ne daa am ay laaf. Nag wii mooy wi Abdu Laahi Saalim Ibnu Anbal doon tudd ci Xawaariq bi mu naan: ( ab xiik (xiik mooy xale bu jigeen bu masul a sëy,fii mu jublu ci nag wu toll ci war a sëy ) ci nagi kër yi,muy naaw ci jàww ji ba kenn gisatu ko).

Mu ne mas naa am mu yàgg ci benn barab ba foofa soof ko,mu tàmbli di jàmbat,waaye nee na daa jàmbat rekk Yàlla sotti ko yamb yu soxot te bari,ñu koy màtt ak a sonnal,mu ne bi mu xamee ne li ko dal moo ko teg boppam,ndax kat ((wamaa asaabakum min musiibatin fa bimaa kasabat aydiikum)) muy musiba mu leen dal yeen a ko teg seen bopp,bi loolu amee mu ne ma soppi samag jàmbat def ko ag cant,daal di ne: (( nasaxal naa sama njàmbat def ko ag cant,dootuma jàmbat ci moom lenn lor,ndax sama lor naaxsaay na)). Ci noonu nee na yamb ya dem wëlif ma ,ma tàmblee noppalu,xam naa ne yamb yooyu la ki def xawaariq jublu woon bi mu naan: ( ay yamb yu toll ne ay mburtu (mbate) yu suur cig réy, cam si (cam si mooy waa ji,mu jublu ci Sen bi) daje na ak ñoom,te faalewul seeni lor ).

Mu waxaat ne waa jooju doon nasaraan-nasaraanlu te nu tuddoon ko ca ginaaw,bis def na ko lu ñaaw ba yenn xaritam yi yedd ko ci,xupp ko ba mu tiit, reccu,ca guddi googa nag mu ñëw ànd ak ku koy wommatal ab gàtt,moom mu yor benn biteelub daa bu mag ci loxoom,dal di tedd tàllalu ci sama kanam,nee waay day tuub,te ne du jug fi mu tëdd mukk,li feek teguma sama ndëggul tànk cig doqam,ngir tuub,ma fexe ba jële ko fa ci wax ju rafet rekk,mi ngi ma fekkoon nag may bind ca jamono jooja,ma dal di def bayit wii ca saa sa: 4(( Yàlla nooyalal na ma ci guddi gii xolub boroomug tubbi ga,ginaaw bi mu ma indilee ab gàtt ak daa , ( ngir tuube ko ) )).

Ku baax ki tudd na ba tay yeneen karaama yu ko yàlla defal ci gèej gi,mu ne da fa mas a dëkk ak benn doxalkat (goornoor) bu soxot,bu kenn dul jege te bagul dara ci lu baax,ma wax bis ne jiyaar jii may def ci yoonu Yàlla daal di naa ko seet tay ci mbirum àttekat bii,ma xool nu ma ko Yàlla di tàggatale, ci noonu ma juge sama néeg dal di dëgmal këram,ñu ne ko sëriñ ba dey a nga jemsi ci yaw, mu ne aah loolu de lu jomb la,ndax danu daa sàkku ci moom muy bañ,kon tay naka la fiy dikke ci coobareem,ñu ne ko amul benn sikk ci ne kee di dikk de moom la,mu dal di jug ci saa si daje ak man fu sori,bég ci man mbégte mu kawe,ci noonu mu ànd ak man ca barabub boppam ba,dal di ne ma loo bëgg, loo bëgg cig baamu ? Wax ko ay yoon, man itam ma ne patt, rekk di xool lu ma koy wax,ba yàgg ma ni ko,da maa bëgg as lëf ci daa, mu dal di may jox bitéel bu mag bu fees ak daa,ma daal di ne wëlbat won ko ginaaw,booba fekkoon na ma may bind ak xasida gu ñu tënke arafi a b t th j (mooy abajada rekk) ,ba ma àggee ca arafu faa,ma bind ca bayit wii ne: sama xalima texe na fa ab aat (mooy ku xaraful)bu weddi Yàlla,kok tàggat naa ko ci xul huwal laahu ahad.

Ma bindaat ay bayit,yoy dañu maa wax ni ma lii de ag wor la, ndax yaa ngi bàyyi yéefar yi ci anam gu dog,ba noppi ngay jël ci ñoom di nëbb,ma dal di bàyyi la ma doon def,gas am pax ba mu xoot ,ma sotti ca daa ja,suul,dal di xam ni sama jiyaar ji dëggu na, ma sant Yàlla .

Nee na itam,benn janqu ndar-ndar,dafa gént gis Waa-Badar,ci bis yooyu nu dugg dëkk ba, tàmblee ray waa dëkk ba,bi nu demee ba kenn ci ñoom jege ndaw si,jenn moroom ji ne ko soxna soosu de ab jullit la,mu dal di koy bàyyi. Sëriñ bi nee na xale bu jigéen boobu ku baax la woon,daan sonn ci moom ci li mu am,daan ko wax naan man dey lu ma la jox rekk xamal ne maa ko ñaq ci sama loxo,njëgug sàngara nekku ci du caagéenug gu poon,loolu da koo leeral foofu ndax kat foofa ci ñaar yooyu lañu daa jëflantee,te moom xam na ne man du ma leen jëfandikoo te du ma jëfandikoo seenug njëkk,ma laaj ko bis ne ko loo bëgg ci lii nga may defal?,mu ne ma bu dee ci àdduna ,sët yu baax,bu dee allaaxira àjjana, ma ne ko Yàlla man na lu nekk.

Yàggul tuuti rekk,Yàlla dogal mu ëmb,te daawul ëmb,bi diirub ëmbam matee rekk mu dal di wësin,dal di faatoo ci wësin wi,ma jullee ko,masu ma koo gis it mukk,ndare bi ma taxawee di ko jullee,ndax sunug jëflante mi ngi doon ame cig yonneente (correspondence). Nee nanu doomi Daba SEY la woon tuddoon Aamina (Ami),boroom këram tuddoon Yèlli SEY,bokkoon ci ndawi goornoor yu mag yi,di woon it ku baax te daan sonn ci man.

Am na bis mu jote ak àttekat bi (goornoor bi) jote gu tàng,ngir sama jëmm ji,loolu nag ni mu ame woon mooy daa am bis ma wutoon ñeenti bant teg leen ci sama buntu néeg ngir def ko ab julliwaay ngir ñiy romb bañ di ci jaar,bi ko àttekat bi gisee ,daa dal di jug,falang jàkka ji buddi bant yi,sànni leen,ne fii amul julli amul lislaam,da nga ñoo bëgg a yàqqal sunu soldaar yi,ma ne miik,bi ko Yèlli SEY yëgee te tubaab bi demagul,daa dal di jug ca saa sa,jawalsi ànd ak aw meram , ne ko lu tax nga tas jàkkaam ji,te moom defu ko fu dul ci buntu këram?, sakkul yoon wi te xatalul kenn it. Tubaab bi ne ko man daal maa ko def,fii jàkka du fi am,Yèlli ne ko waaye man di naa ko defaraatal jàkkaam ji na mu meloon,tubaab bi ne ko du fi ame, ñuy bëgg a doorante nit ñi dox seen diggante, ñu nekk di xuloo diggante tàkkusaan ba jant so,ci biir loolu lépp man maa ngi bind.

Ci xisa bii (nettali bii)laa binde xasidag ((Rabbanaa axrijnaa min haazihil xarya azzaalimi ahluhaa wajhal lanaa min ladunka walliyan wajhal lanaa min ladunka naziiran) muy ci maanaa yaw sunu boroom génne ñu ci dëkk bii nga xam ne ñi fi dëkk ay tooñkat lañu te nga wutal ñu aji méngoo ju tukke fi yaw,te wutal ñu aji dimbalee,xasida gee nekk nii: (( gërëm naa kilifa gu màgg gii nga xam ne yar na samab xol te koomal ma, moom dey mooy boroom bi gën a tedd)) ba bi mu àggee ci : (( bindal ko(moom Yonnant bi) ag xéewal ak ag mucc ak ñoñam aki saabaam te nga def sama jàkka ji ci darajaam (moom Yonnant bi) muy lu yaatu ))

Bi mu àggee foofu ñu ne ko nangul nanu la ko,da nga ko gis. Loolu nag gis nanu ko,mooy jàkkay Jurbel ak Tuubaa ,xasida gi nag gu gudd la te rafet gu am jeexiit gu réy ci jañ ak ñoddi bu soobe Yàlla ak ci barkeb aji defam,ku koy jëfandikoo na ragal Yàlla te xemmeem aw yiwam.

Yàlla dogal na bis Yèlli moomu siyaaresi ko Njaaréem,juge ca yooyale wàll,ginaaw bi jumaa ji noppee muy ju Njaaréem,Sëñ bi ne ma ma’ak sama jenn waay ànd leen ak moom mu siyaare jàkka ji,ñu ànd ak moom, won ko jàkka jépp,penkook sowwu,biir ak biti,mu yéemu gépp yéemu,bi nu dëppee Sëñ bi ne ko noo gise jàkka jii ak sama jàkka joojee,yaw mi ma doon xeexal ak a dàkku?,mu ne subhaanal laah maneesu leen a tollale,Sëñ bi ne lii mooy maanaam sama wax jii: (( Yàlla dàq na jëme ca ku dul man ca Maayomba la naqari woon sama xol te yékkati samag wàll)). La naqari woon sama xol bu nu koy firi mooy tas gi nu tasoon jàkkaam ja,yekkati samag wàll mu jublu ci yekkatikug soorool yi.

Ab nettali bu yéemee ngii bu làmboo ay karaamay Señ bi: Señ bi nee na bi tubaab bi buddee bantam yooyu,sànni leen,kenn ci gaa yi bégoon ci jëfi tubaab bi, da cee jëloon ab bant samp ko ci wanag wi miy sangoo ak a doxe aajo,waaye Yàlla nattoo ko benn bis mu bëgg a tuur ndox,jawali ca satala ga te booba satala ga ndox mu tàng a ca nekk te moom yëgu ko,te seetu ko it,waaye bi mu noppee ba sotti ko ca cér ba (sàkkara sa) da wadd ca kaw ni ab baa bu góor bu tiit,dal di yuuxu ba fa baatam yam, ne: Señ bi dimbali ma alku naa de,dal di sànni satala ga ca àll ba,dikk teg loxo ba ca tubay ja,ma ne lu deesi defati lu dul muñ ak wax (( innaa lillaahi wa innaa ilayhi raajihuun)).

Mu neeti - moom ku tedd ki - ne am na at mom bu doonul woon li ko Yàlla tawfeexal saa su xamee ni weer tàmbali na mu di ko bind,kon wenn weeru ramadaan doon na jàll te du ko xam,ndax waa dëkk boobee mu nekkoon xamunu woon lu dul weeru tubaab wi,bi korite gi jotee ma xëy, dog ,sangu, def li ci sunna digale,ma génn ne damay julli ji ca pencum dëkk ba,ba ma àggee, ma xool sowwu ak penku,xoolati sama ndijoor ak cammooñ,ànd ak am kóolute ci ne kenn du ñëw,am ñaari jèbbéer (jèbbeer mooy jaam bu jigéen) yu agsi war a toll ci baalix ( baalix mooy ati génn ag ndaw) taxaw sama kanam di ma seetaan,ma kàbbar ñu tàmbalee xàqataay,saa su ma kàbbaree nu ree,naka noonu su ma jàngee,ba ma sëlmal def samab xut ba, sama déeyaale gi maa ngi ciy wax:(( yaw buur bi, xam nga ni woor naa weeru ramadaan ni nga ko digalee,ma dog ,sangu,julli ni nga ko digalee,waaye dey lu ma génnee muurum koor laa amul,bu ma ko amoon it,ku ma ko jox laa dul am,kon jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sang,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam ,te nga nangul ma lépp lu ma man te def ko ci sa ndigal yi,te nga bindal ma yoolub li ma manul lòtt ci,te amoon ci yeene walla yu ni mel.

Bi ma noppee def xasida gii: yaw buur bi jullil te sëlmël te barkeel ci sunu sàng ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam te nga def qaafiya bii di ñëw,mu kawe miimiya ba ,ci lu feeñ ak lu nëbb,aamiin yaarabal haalamiin ci barkeb Yonnant bi (j.y.m) : ((maa ngi yaakaar ci aji yaatu ju dëggu ji,ci darajay ki niy xeeñtu di Yonnat biy dimbali dëgg ci dëgg (j.y.m) )) (( maa ngi yaakaar ci Yàlla moomu delluwaat ci samay mbokk ci lu gaaw ànd ak njub gu dëggu)) (( ak nekk jaam bu texe bu nu matal, tey ligeeyal jaamub Yàlla miy dëgg,jaamam boobu di yonnant bi mu tànn)) (( yaw Yàlla ci darajay ku nu tànn ki ak ñoñam,yal na nga ma jéggal te nekkal ma te wommat ma te goreel ma)) (( di naa la gërëmloo ci Alxuraan ak sunna si nga xam ne,Yonnant bi yoonalal nanu ko,yaw miy aji teqale lu taqaloo)) (( yal na nga ma tàggatal noon yepp ba fàww,te fegal ma ag bokkaale,yaw aji not jiy boroom tijji ak tëj)) yal na nga ma wommat delloo ma Daaru Salaam gi nga xam ne fa laay deyaaleek yaw ciy aaya,te yal na nga kaweel ci man ay gox)) (( yaw sunu boroom yal na nga ma dello ci lu gaaw te defal ma samay mébat yepp,te nga may defal ay mbégte te di am ñeewant ci ma)) (( te nga may ma ay xam-xam yu jariñ jëmm ji ak mbidéef yi,te nga dolli ag yaatal gog texeel lay doon ak ubbi ak xar-baax)) (( sama bakkan déy daa bañ ag yéwénal,ndax ab noon la,kon sellalal ma ko cig taxañ (taxañ Señ bi mi ngi ciy jublu lu gaaw) yaw miy ngën ji kuy yéegale )) ((na nga ma may ba fàww li ma bëgg ci mbindéef yépp, te nga fegal ma séenuw ay yaw miy joxe ag jiitu )) (( màngal ma samay mébat fii ak fa nu jëm,te nga may ma ngënéel lu màgg te saxalal ma ngënéel li)) (( yaw sama boroom fegal ma li ma ragal ca bisub njàqare ba,te nga defal ma jéggi siraat gu gaaw gu mel ni melax )) (( musal ma ci (ay nocciku = nusuuh) ak lépp lu nit ñiy ragal te nga def ma may ku sori ag lakk)) (( nangul sama ñaan gii yaw sama boroom,te nga faral ma samay ayib ,te nga seere ne man dey tuub naa ci jepp jëf ju di jëfi dof)) (( te nga nekkal ma yaw sama boroom,te musal ma,te amal sama yaakaar,te fegal ma luy bijji ag nëx )) (( nangul ma sama ñaan gii,yaw mi moom lepp, te nga tabe ñeel ma cig yaatal ak dëddu ak dëggu )) ((ci darajay Yonnant bu nu tànn bi,te nga fegal ma hisaab ci darajaam,te tàggatal ma ci moom kepp ku di boroomug kàccoor)) (( na nga julli te sëlmël ci moom Yonnant bi,ak ñoñam aki saabaam,yaw mi moom penkook sowwu)).

Mu nettali ci karaamay géej gi,ne : am na jenn waay ju bokkoon ci kilifay barab bi ma nekkoon,da maa digoon ab bitéelu misk ci lu dul ma di ko sàkku ci moom,ndax man daawu ma sàkku ci ñoom lenn,te daawu ma sentu ci ñoom,daawu ma wóolu seeni dig it,waa jooju ma digoon bitéelu misk bi,ndekete daa digoon keneen ci moroomam yi lu mel ni li mu ma digoon,waaye bi mu deful li mu digewoon ,waa ja daa tàmbali di xuloo ak moom ak a ngaayoo,moom itam muy dàkku boppam,(di defandar boppam) loolu lepp it mi ngi doon ame ci sama wet,ci wolof it lañu doon waxe waaye yu leerul dara,waaye làkk gi nu koy làkk li muy leeradi leeradi fàttali na ma réew ma, ba mel ne da maa ñibbi far ,ngir gëj gi ma ko gëj a dégg,loola neex ma lool.

Waaye xuloo bi nu def te li ko waraloon lepp mooy wóolu gi mu ko wóolu woon,ak dig gi mu ko dig te defu ko,loolu lepp ma sant ci Yàlla,mi ma defal may kok wóoluwu ma kenn,sentuwu ma ci kenn ku dul moom,loolu tax ma def xasidag cànt gii, ma wax ne:

Maa ngi tàmblee samay wax aki bjëf ci turu Yàlla miy boroom yërmaande ju yaatu ji ak ji miy jàgleele, xeewal ak mucc yal na nekk ci sunu sang,Muhaddad ak ñoñam aki saabaam.Miimiya bii moom la ñeel yal na ko Yàlla gërëm. Yaw sama boroom sama noon yiy say noon,sànni nanu ma ci géej gi,ni nu sànnee woon sa xarit ba Ibraahima ca sawara wa,nga waxoon ak moom (sawara wa) ci :(( yaanaaru koonii bardan wa salaaman halaa ibraahima )) muy yaw sawara wi doonal ab sedd ak jàmm ci Ibraahiima. Sawara wa dal di mujj di àjjana ci moom,jàmm ak xeewal yal na nekk ci moom ak ci mbooleem nabiyu yi ak yonnant yi, Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw sama boroom! Yaw aji dund ji! Yaw aji taxaw ji ! Ci darajay weeru ramadaan mi nga wàcce Alxuraan, mu dig jub ñeel nit ñi, te di ay aaya yu leer yu di ag njub ak ag teqale dëgg ag safaan,ci barkeb xut ba bii tàggatal ma géej gii ak ñoñam ak mbooleem samay noon yiy sa yos,te nga bégal jullit yu góor yi ak yu jigéen yi ci ñu gis ma te dajeek man,te dégg sama ag dellu ca Daaru Salaam,ak Tuubaa ci lu gaaw ci lu dul ab coona du caagéenug ag sabablu gu tukkee ci man,Aamiin yaw boroom mbindéef yi, ci darajaam moom Yonnant bi,(j.y.m) te nga def miimiya bii mu kawe li ma jortoon,ni nga ko baaxoo defe ak man ca la ma waxoon njëkk bii,te nga defal ma ko muy ab yobbal,tey pakk tey àjjana ci ñaari kër yi,aamiin yaarabal haalamiin.

(( man déy maa ngi tagg,tey sant ngën ji aji xéewale, te du ma jàmbat ñàkki xéewal ci menn mbindéef )) ((kepp ku ma jorte ci sama tumburànke gii may kuy toroxlu ci kenn ku dul aji doyluloo jiy aji yaatu (muy Yàlla) na ko wóor ne moom ku gumba la )) (( moom de laay jàmbat samag lòtt ,samag ñàkk ak samag tumburànke,may yaakaar samag dellu ci lu gaaw di ngën ji ku nu xeewale )) (( jàmbat naa ko samag lòtt,mu fajal ma ko,te nekkal ma ci lu kawe sama njort,moom kat mooy gën jaa teddi kuy terale )) (( ñi nga xam ne weddi gi nu weddi Yàlla da leen a wor danoo jublu woon samag wàll,mu aar ma ci ñoom dàkku jepp aji tooñ)) (( ag cant ñeel na ko tukkee fi man,di yaakaar ci moom sama càkkutéef lii,ci lu dul ab coona buy juge ci man,te sama naqar dañ na )) (( ki njort wor ba muy iñaan, bu ma woree tam,na ko wóor ne ki ma wommat cig teral de woru ma)) (( ku ma sànni ci géej gi ngir ag weddi di boroomug mbañeel,na ko wóor ne ci géej gii de tabeg aji terle ji dikkal na ma fi )) (( koo xam ne li ko naqari mooy nekk gi ma nekk di jaamub Yàlla,tey jëwrini aji rammu jiy ku nu jiital )) (( na ko wóor ne man de ab jaamam laa ci géej gi ak ci jéeri ji,di ligéeyal kiy musale ci luy waral reccu)) (( ku ma dëddu de na xam ne xéewal yi jublusi nanu,juge ci aji yaatu jiy aji doyluloo,kiy aji wattu tey aji jiital )) (( ku ma sànni ci géej gi ngir sàkku samag tumburànke,na xam ne ag tàggat ñeel na ma tukkee fa sama boroom ci gépp géej )) (( samag wéeru ñeel na Yàlla ci samag teew ak samag fàdd,te di naa jàmbat jëm ci moom jaarale ko ci Yonnant bi,moom miy samab raas (bi may yéege jém ca Yàlla) ndaw muy ku baax )) (( yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom ak ci ñoñam aki saabaam ak bepp jullit )) (( yaw sama boroom saxalal ba fàww ngën jaa selli julli ak sëlmël ci Muhammad)) (( ak ñoñam aki saabaam yepp,te nga delloo ma Tuubaa ci lu gaaw,te peek ma te xamal ma)) (( yaw sunu boroom man de warlu naa ba fàww di kuy ligéeyal Yonnant bi,tey kuy ligeeyal aaya yi,na nga ma xamal te déggal ma )) ((yaw sama boroom,maa ngi sàkku ci aji maye ji ag géeju akug wuññi akug yinkiiwal (ag sol xam-xam mu tukkee fa Yàlla) na nga ma wuññil te yinkiiwal ma )) (( jublu naa aji ubbi ji tey sàkku ag ubbeem,di yaakaar ci moom ay may yuy ball,ndax ag ballam day yol di sotti)) ((gërëm naa aji not ji bi mu ma tàggatalee noon yi,ma doonoon ku tumburànke,di ku wéet fa ñoom di ku amoon gépp lëmmu)) (( di naa ko gërëmloo ci Alxuraan ngir sant ko ci xéewalam yi,ci sama xol ak sama yaram ak sama gimiñ )) (( war na ma ma saxal li mu ma tànnal mu dig jub,te ma koy gërëmloo ci aaya yi ndax ñoom kat (aaya yi) mujj nañu di samam màng (ngañaay) )) samay cant aki ngërëm aki tagg ñeel na aji jariñe joj indil na ma Alxuraan ju tedd ju ñu màggal)) (( moom (Alxuraan) mooy ndàmm mi (koom mi) tey leer gu fés gi niy aar ci sawara ak noon yi ak gàcca)) (( ab teere la bu tedd,juge ci aji tedd juy terale,jëm ci jaam bu tedd,buy xettalee tey boroom yërmaande)) ((teere bu darajawu la juge ci ku darajawu,ku darajawu te wóor indi ko, jéme ko ci aji darajawu kuy matal )) (( xéewal ak jàmm ci lu dul dog yal nanu nekk ci moom,ak ñoñam aki saabaam fu mu man a nekk)) (( jàmm ak xéewal yal nunu sax ci moom li feek aji sant a ngi naan : da ma ne maa ngi sant ngën ji aji xéewale)) (( Xéewal yal na sax ci moom juge ci aji tedd ji may nekkal,te du ma jàmbat ñàkk ay xéewal ci menn mbindéef)) (( mucc yal na nekk ci moom juge ci moom (Yàlla),(mucc) gog da nga ma ci fegal (yaw Yàlla) aw ay, te aar ci samag wàll wëlif ku nu rëbb ki (muy ibliis) ak ku gumba)) ((xéewal yal na sax ci moom tukkee fa moom(Yàlla),li feek ku koy jàmbati mbiram a ngi am la mu bëgg di gën ji ku nu xéewale)) ((aki ñoñ aki saaba yoy maa ngi ñaan aji kawe ji mu dugal ma ca seen biir ëlëg may boroomug xéewu )).

Bokk na ci karaamay géej gi ba tay nettaleem bii,mu ne: bis xëy na, waaj ngir ligéeyal Yonnant bi - ni mu ko baaxoo woon - amul lu dul aw mettit wu tar daj mbooleem yaram wi,ba manatul li mu bëggoon ,waaye am benn tubaab ci njiiti nguur gi,mi ngi dëkkoon ci wetu fi Sëñ bi dëkkoon,nekkoon di xaqataay ca kaw aki moroomam,Sëñ bi daa di ne:Yàlla yaw de xam nga li ma waajoon jëm,ak li ma ci gàllankoor,maa ngi lay ñaan nga tuxal lii fi man te yobb ko ci ki lay wutal moroom,amul lu dul ma dégg waa ji doon xaqataay muy onk,man may bind.

Bokk na ci karaamay géej gi ba tay lii: bis nee na fi mu nekkoon ndawal da faa mànke woon lool,ba jën yu ndaw yi nuy def ci poti weñ yi rekk lanuy lekk daanaka (xam naa mooy poti ton yi) ma jëfandiku ci bis,bi ma noppee ma raxasu ba sonn,jëfandikoo suuf ak saabu ak lu nu man a dindee ag xet rekk,waaye dara,ba ma ca manatul dara ba ne naa dem nag jublooti ca ligéey ba,bi ma tàmbalee rekk ñu ne ma ((wa minhumul laziina yuuzuunan nabiiya)) muy am na ci ñoom ñuy lor Yonnant bi,ma tiit lool, jaaxlee jaaxle,ca saa sa ma bàyyi koo jëfandikoo,doxe ca bàyyi luy jën,boole ko ci li ma jaayante ne du ma ko lekkati,bis bi ma ko bàyyee walla lu ko jege,ay kuy dikkal nanu ma,juge ci fere yi,di njëg gu nu gaawal ci jën yi ma jaayante woon.

Mu neeti moom ku baax ki:dëkk bi mu nekkoon da faa nekkoon aki làbbe ñuy jël ci xaley yéefari nit ñu ñuul ñi nekkoon foofu di leen def ay mbindaan,di ànd ak ñoom di wër ci ja yi (marse)ginaaw tàkkusaan,njiit li nekkoon foofu defe woon ne da maa xemmeemoon ci gone yi mu ne ma woon boo ci soxlaa de ma joxla ci ñuy ànd ak yaw,ma ne ko soxlwu ma ci. Njiiti dëkk booba itam baaxoo woon nanu di jël ci magi nit ñu ñuul ñi, ñu ñuy def ay toggkat aki rootkat,ma sàkku kenn ci ñoom bis ngir ligéeyloo ko,waaye ba mu ma jegee daal xeeñal na la ko xeeñ goo xam ne amul gu ni mel,ma ne kii daal sobe na ba maneesul a jaxasoo ak moom,ca noona ma jaayante ci seeni ndaw ak seeni mag ni ma jaayantee ci jën yu mag yi ak yu ndaw yi ,ci loolu mu ne:

(( ma ne njëgug ndaw ñi dikk na ak gu mag ñi ak ndaw ñi)) ((Muhammad gën ji imaam mooy sama dëkkandoo,ag bëbbam de (dexam) ci sama xol lay sottiku jëm)) .

Fere yi ñëwoon indi kuy yi (xar mu goor mu mag) ñooy mosalug njëgi yéefar yu mag yeek yu ndaw yi,kuy yooyu it di mosalug njëgi jën yu ndaw yi ak yu mag yi.

Bokk na ci karaamaam yi ci géej gi ba tay waxam jii mu ne: bi ma xoolee sama diggante ak noon yi ,nooni Yàlla yi,ma xam ne ñoom kat am nanu kàttan ci lor ma ak gaañ ma,ci dogalub Yàlla bi ak’ug nammeelam,ma xam it ne bu doonutoon kaaraangey Yàlla ji ak’ug fegam kon ba tay waxatunu ko,laa leen bàyyi ak seen bëgg-bëgg,jublu sunu boroom,mi yor mbir yi,ma déeyaale ak moom ci sama mbir: ma ne ko Yàlla yaw’ay ki nu bind ngir nu jaamu la,nga ne ((wa maa xalaqtul jinna wal insa illa liyahbudoonii)) muy bindu ma nit ak jinne ndare ngir ñu jaamu ma,nga neeti : (( yaa ayyuhan naasu uhbudoo ràbbakum)) muy yeen nit ñi jaamu leen seen boroom,bu ko defee tawfeex ñeel ki texe jiitu ci moom,mu dégg wax ji topp ko,naka noonu toroxte ñeel ki ag texeedi jiitu ci moom,mu lànk bañ a wuyyu,tëx, luu, ngir’ug weddi,man nga tawfeexal ma,def ma ci mbooloom ñi wuyyu,mbooloom Yonnant bi Muhammad (j.y.m) imaami anbiyaawu yi ak yonnant yi jàmm yal na nekk ci ñoom ñepp,nga dolleeti ma ngënéel,def ma may jëwrini Yonnat bi tey xalifaam ci diineem ak xeetam,am mbooloo ci sa noon yi, noonam yi,jug song ma ngir dox sama diggante ak jaamu la,te ligéeyal ko (moom Yonnant bi) . Ñoom dey ñi ngii di ñu caaxaanadi ci seeni jëf,di ñuy farlu ci seeni neen,te yaw yaay ki wax ci làmmiñu sa Yonnant bi,lol maanaa mi mooy:nit ku nekk daa am kër ca àjjana ak ca sawara,bu duggee àjjana ñu won ko këram ga woon ca sawara,ne ko fee de nga jëmoon boo jaamuwutoon sa boroom,leegi nga xam ne daa nara gént,ab yéefar a koy donn. Bu tàbbee sawara’at nu won ko barab ba mu doon am ca àjjana,bu jaamu woon Yàlla,ginaaw nag jaamuwul boroomam ba tàbbi sawara,leegi ab jullit lanu koy jox. Ginaaw mbir yi nii lanu deme,te noon yii - ni nga ko xame - ci tooñ ma lanu dëkk ak a def ci man lu leen soob,te du ma fayyu te du ma leen ñaanal aw ay,waaye maa ngi lay ñaan seen kër ya ca àjjana,Yàlla nangul ma ko,may ma leen,ba ma xamee ne maa leen moom,ma jox leen àddiya waa-Ahlu Badrin . Ci loolu mi ngi naan:

(( jox naa àddiya këri noon ya nekk àjjana mi kuy jalgati dul dugg,ñeel saabay Yonnat bi)) ((kër yooya de jëlees na leen ca noon ya,jox leen saaba yu baax ya)) (( Yàlla jox na ma kër ya fa samag tumburànke,teeyal it samab xol)) (( man nag def naa leen ay àddiya ñeel saaba yi,yal na leen Yàlla gëram ,moom mi ma aar wëlif (sahaab:ay niir ) )).

Na nga xam ne karaamay tukkib géej ji moom maneesu leen a jeexal,bu ma bëggoon a indi li ma ci xam ci lu juge fu wóor ,ak li ma ci dégg ci nit ñi,kon dey ma indi fi lu yéem xel yi,te kon du xaj ci teere sii di su nu gàttal,looloo tax ma yam ci li nga xam ne topp naa ko ba mu wóor.

Mu ne ati tumburànkeem gi juroom ñatti at yu mànke tuuti la,bi mu matalee li ko Yàlla bindaloon cig tumburànke,ci suufus yéefar yu ñuul yi,Yàlla indeeti ko ca suufam ngir nitam ñi ñoom itam jariñu ci moom ci li ko Yàlla may ciy mbóot ci tukkeem bu barkeel boobu,ak ngir mu daje ak mbokki jullitam yu baax yooyu di naar yi,ci noonu Yàlla dal di def ci xoli kilifay nguur gi ñu am ag ñeewant ci moom delloosi ko.


Doggantal : ci ñibbisig Sëñ bi ci jéeri ji,juge ca géej ga[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Sëñ baa ngi àgsi Ndakaaru bisub gàww juroom benni fann ci sahbaan,atum kasasin di 1120 g, mu wéye fa, jàll Ndar def fa lu tolloo’k fukki fan ak juroom ba ca bis bu njëkk ba ci ramdaan, mu doonoon bisub talaata,mu juge fa,dem Luga, wàcc ca rakam ja Sheex Coro MBAKKE,ca guddig gàwwu ba, mu rañaane fa romb kër Sheex Jull SIISE,jugeeti fa jaar kër muridam ba sëriñ Sire LOO, yoor-yoorug dibéer ja ca Sànnoosi, mu sax fa la desoon ca ramadaan ja,noppalu fa,woor fa.

Ci diir bii,foofa fees na dell,raj-rajloo ba mel fa nu mu masul a mel,ci diggante ay taalubeem ak kuy sàkku ndimbal,aki kilifa yu koy siyaaresi,di ko ndokkeelsi,bokk na ca ñooña ka nuy wooye (kiimaanug jamonoom,woykatub waxtoom) Sheex Ibraahima JOOP Almasharii,ab xisaam lu xoromu la te yéeme,ag wuññi (feeñal mooy wuññi) gu yéeme feeñ na ci ñeel Sëñ bi (maanaam Sëñ bi wone na ci ay xar baax) loolu mooy sheex Ibraahima moomu daa amoon ab bor bu mag bu ko lëjëloon lool,ci jamono joj fay ko ci jafe na,mu jug wër ak moom ci sëriñ su mag si waaye taxul kenn tëyye ci loxoom,ci noonu mu jaaxle lool te am tiis,waaye bi Sëñ bi agsee Sànnoosi,mu ñëw indaale ay bayitam tudd ci mbirum bor bi ak ni mu ko seddalee ci diggante Yonnant bi(j.y.m) ak ñeenti saabaam yi,ginaaw sëriñ si nanguwunu koo xettali.

Bi mu yëgloo Sëñ bi ne ko mu agsi,mu dikk,nuyyoo,bi mu daataa wax ay mbiram ak boram bi ak ni mu ko seddalee ci bayit yi,Sëñ bi ne ko indil ma mbuus mee,mu indi ko,mu neeti ko jox ma mi ci des ,mu jox ko ko,mu ne ko waññal li nekk ci mbuus mu nekk,mu waññ ko, muus mu ne ñatti téeméer nekk ci,boo leen boolee ñuy juroom benni téeméer,Sëñ bi ne ko indi benn téeméer bi te jël li ci des dimbandikoo ko ci say soxla,te moom boram bi juroomi téeméer rekk la woon,ca saa sa sheex Ibraahima daanu ab jéll,yuuxu ca kaw,Sëñ bi ne ko waaw yaw lu mu? Mu nettali ko xisaam,jàngal ko bayit yi,moo nekk nii: ((bori ay mbokk war na ma,ma seddale leen ci diggante ñu tedd ñi ndax ñu fay leen)) ( yaw Ku nu tànn ki(Yonnant bi), ya’ay ki moom cér bu njëkk bi,yaw su xarit bi (Aboobakar) ya’ay ki moom ñaareelu xaaj bi) ( yaw ki teqale dëgg ak fen (Omar) ya’ay boroom ñatteel bi, yaw sunu Usmaan mi, nga moom bi ci topp) ( yaw gayndeg xarekat yi,yaw baayi Asan ak Usaynu ñiy leerug sunu diine ji,yaw laa feetale li ci des) (yeen de ñu tedd ngeen ñoñ kuy jàmbati coona du wéeru ci seen daraja te fajalu leen ko ko) ( kon gën jaa selli xèewali Yàlla na sottiku ci yeen,li feek Yàlla a ngi faje ay soxla ci yeen).

Sëñ bi yéemu lool te sant Yàlla,waaye noon yi ñoom seen kiñaan gi mayu leen sax ñu xaar ba Sëñ bi ñibbi këram,waaye danoo dal di tàmbalee wut seeni pexe,di lal seeni yoon, di waajal li nu nar,di xaar waxtoom jot banu def ko.

Ku baax ki moom bi mu jullee iid ca bisub kori ga,mu doonoon bisub alximis,da fa’a toogaat bisub àjjuma ak gàwwu ba ca tàkkusaan sa,mu laxase fa romb ca kër taalubeem ba Koor Mag JOOB,boole fa timis ak gee,ngir tarug dox ba,dem Màkka Sàmba JOOB fanaan fa,xëy bisub dibéer dem kër baay tëxam Sheex Ibraahima MBAKKE Kajoor,laxasati ca tàkkusaanug altine ba, dem ca Masàmba Xari JOOB,moom mi ngi kër Muxtaar,fanaan fa, yendu fa,jugeeti fa ngoonug talaata dem ca Muxtaar Mareema Silla ca Ñaxal,mu def fay fan,juge fa jàll Kokki Guy ca Maxtaar Masàmba JOOB,yendu fa waaye fanaanu fa,da faa juge njëkk jant biy so,te booba ña ngay waajal ñam yi,waaye taxul mu xaar ko fa,dox nag jëm Daaru Salaam këram,àgg fa guddig àllarba ci lu tolloo’k ñaar fukk ak benn,Siidi Muxtaar ,rakam ja booba ma nga fa woon,ca biir sawaal.

Rakk ji (Sheex Anta) tàmbli di ko ganalee lol kenn ci murid yu mag, yu man yi sax manu ko,waxantu ma la’ak ñu néew ñi doole. Mu sax fa diirub fukki fan,bis bu nekk ñu ray ay fukki yëkk,bu ko matalul mottali ko ci giléem walla ay giléem,kem li mu mànke rekk.Ñu koy waajal ay wàccuwaay ca rakk ja sheex Ibraahima,diggante Tuubaa ak Daaru Salaam,muy fa Sëñ bi tudde woon Daarul Mannaan, mu dem fa moom ku baax ki ci njëlbéenug silqihda .

Sheex Ibraayma mii moom jërul ngay laaj ay mbiram, mooy ki ku baax ki dénkoon njaboot gi ak bagaas yi,bi miy tukki. Ci noonu màgi taalube yépp daje fa,Sheex Ahmadu Ndumbe jiite leen,mooy ki doon dem ak a dikk,di yee ñi gëmméentu,di jàngal goney Sëriñ bi ba nu mokkal ci diir bu néew njëkk ku baax kiy dellusi,dara yàquwul ci mbirum Sëñ bi,ba ñépp daan ko léebe ci wàllug jub ak tegu ci yoon.

Mu jullee foofa iid (tëbëski),sax ci meloom wu sell wa ak yareem (tarbiya) ga mu nekkoon,mbiram ak mu dongaam yi di gën a jëm kaw . Kawe fopp,fopp,fopp na mu meloon,kaamil yi ñu leen di jàng di leen xool ci bëcëg gi ,di leen tari ci gudd gi,naka noonu xasaayit yi,ak njàngalem xam-xam mi,ak ligéey bi ,loolu lépp àgg fof maneesu koo melal cig kawe.

Ni nga xame ne mbirum ku baax ki yokk na ak mu taalube yi ba jéggi ab dayo,ba maneesu koo misaal,naka noonu mbirum ñu iñaan ñiy rambaaj. Mbirum jaxase gi dellu fa mu nekkoon,rambaaj yi jug di def seeni ligéey ba nu xëy indil Sëñ bi ay soldaar,li ko waral mooy: jaraaf ji nu dénkoon mbirum wàll googa,ca jooja jamono,- moom xam nanu turam ak giir gi mu bokk - waaye bëggu ma koo tudd di nëxal ay doomi baay tëxam,ak doonte àndunu woon ak moom ci yéeneem ak jëfam ak waxam,waaye ginaaw seen doomi baay tëx la,rafetatul nu leen koy tuddal,te doy na ne ñi teew moom xam nanu ko ci tur,ci jëmm ak ci mbokk,te yal na Yàlla musal ñi teewul ñuy xam turam.

Moom de moo waxoon te tegu ko woon fenn ne : Sëñ bi day dajale ay kano aki fital ak yeneen jumtukaayi xare,te mi ngi waaj fi mu nekk,bu ngeen ma joxoon ay soldaar de kon ngeen gis li may def. Ñu àndoon ak moom ci kaw waaye wóoluwunu woon ay waxam,looloo waraloon ñu boole woon ko ak buuri réew mi mépp,buurub Kajoor,bu Bawal,bu Siin,waaye bu Siin a ci gënoon a rafet njort ci Sëñ bi,gënoon cee rafeti wax,waa-waaw xamal nanu ma ne am na ay buur yoy seen biir de Sëñ bi la àndal.

Am nanu xam-xam ci ne bi nu àgsee waa juy rëy-rëylu ji méngoo woon rëyam nga (al lazii tawallaa kibrahuu) moo dal di woon tàmbali di dog sàkket yeek jaaseem ji, te daawul xaar ku ko ubbil bunt,lépp lu dox ci kanamam mu dog,te amul lenn lu muy rus,dale ko ca sowwu ba, ba ca penku ba.

Fekkoon na Buur Siin - ci li nu wax - mu wutoon ay fuglukat (controlleurs) indi fa ngir ragal ñuy dugg cib néeg di fa duggal ay ngànnaay walla fital te kenn du ko yëg,ngir dëggale ci li nu waxoon ne Sëñ bi day dajale ay ngànnaay,waaye Yàlla dogal loolu amul,bu nu ko bëggoon it du man a am,ndax donga yi doonte danoo bank seeni loxo,teewul ñi ngi ànd ak ñoom ci ay bët ak ay xoolkat. Bi nga xamee ne gisu ñu lenn ci li nu doon tuumaal sëriñ bi,te gisunu ci donga yi kenn ku yor kanam gu lëndëm mbaa gu ñëkk,ku ñu ci gis rekk ma nga mel ne kuy waaj a julliji kori mbaa tëbëski,ngir tuwaaletu bu rëy,ñu xam ne noon bi day fen,buur yépp rus,am kersa ku ci dul waa ju fettéerlu ji,moom sax gàccawu na waaye daa suturloo jàmbaar-jàmbaarlu ak sàkku-sàkkulu nu ganaleel ko buur yi,ak xontal ko fas yi,waaye lu mu soxla rekk nu defal ko ko ca na mu gën a gaawe,gënnee yombe,ci noonu ñu dellu di ñu reccu,yal na Yàlla fay ña ca amoon yéene yu rafet.

Ag karaamaa ngi nii: bi sodaar si laataa agsi ay mbokkam moom Sëñ bi danu koo wër lëjël ko witt,gën a tar ci moom ay jiit,tiit gi nu tiitoon taxoon amatunu woon kersa,taraloon lool ak moom,demoon ba bëgg koo génn seen biir bu nu ko manoon,ña ca bokkutoon ca mbokk ya daal mooy ña ca yaroo ca moom,waaye ku baax ki moom loolu lépp téewul mu doonoon ku féex ku ko yëgalutoon yaramam,naan leen bég leen,wallaahi mbir mii ñaari bëy dunu ci daanate,waaye kuy dégg loolu ? Ñoom ñii nga xam ne tiitaange gi yobb na leen ca dayo ba moos. Ca bis yooya ku baax ki génneel leen aw dagiit wu yéeme ciy woy,ne leen bu ngeen ko jàngee ci kanamu soldaar si du ngeen dégg lu leen naqari mbaa ngeen koy gis,moom nag ñi ngi ko toftalee ci arafi (Rahmaan Rahiim)(muy boroom yérmaande ju nu yaatal ji,ak boroom yérmaande ju nu jagleele ji) moo nekk nii:

(( sama boroom de bettee na ci luy leeral xel yi,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)) (( samag cant ñeel boroom bu tedd,bu amul bokkaale,sama dënn it tay fees na dell ak leer guy jolli)) (( Muhammad ,xéewali sunu boroom yi ba fàww yal na nekk ci moom,sama lépp de ci moom la ko watoo )) ((maa ngi ñaan sama boroom, moom mi ay mayam matale mbooleem mbindéef yi, la mu tànn moom mi binde )) ((déeyaale naa ak moom - moom de màgg na - ay at , mu teral ma teralug aji gindee,sama lépp it set na ciy caaxaan)) (( yaw boroom yérmaande ju matale ji,mayal mbooleem mbindéef yi yërmaandey ka nga xam ne ku jàng Alxuraanam ji,mu feg la wëlis aw ay)) (( aaral xeetu Mustafaa wi ci gépp yàqute,te nga yërëm mbindéef yi,yaw mi bindoon seen maam)) ((yaw boroom nguur gi ,yaw mi màgg wëlif fayyoontoo, yërëmal mbooleem mbindéef yi,yaw aji gindi joy dimblee na))) ((far nga la xol ba jublu woon ciy lor,ci darajay ngën ji ku wéeru ca Yàlla)).

Sama mbokk Muhammad doomi Aliyu Alyahxuubiyu,nu gënoon koo xame ci turu Muhammad Tuubaa,ngir taqoo gi mu defoon ak ku baax ki ca Tuubaa,ak baril lu mu daa sikar,ak a jàng xasida yi,xibaar na ma ne bi Sëñ bi génnee xasida gi (Rabbii bimaa yashrahul),da ne ma mokkal ko, ma mokkal ko ba nu daataa ñëw,bi nu ñëwee mu woo ma ne ma jàng ko ca kaw,biral ko,ma jàng ko ni kuy nodd,baamu ko lu tolloo’k ñatti yoon,mu ne ma doy na ,mbir mi mat na te yéwan.

Mu daan def fu mu nee ma dajewunoo’k lu nu naqari de,ma ne ko xasida gi -ci karaamay ku baax ki- def na ci soldaari Tuubaa yi la picciy Abaabiila yi defoon ca soldaari Màkka ya,ngir sunu Yonnant bi (j.y.m),waaye ñii ak ñee li leen wuutale, ñii dañiy ñoñ ay nu jëflanteek ñoom ci kem seeni yéene,naaxsaayal leen,ñee ña ca ëpp di ñu baax,ñu ga (forse) leen ,te seeni xol Sëñ bi la àndal, Yàlla yeexal seeni mbir ba nu bari tuub ci,ba ca ka leen jiite woon,moom it tuuboon na,ñenn nit ñaa ngi sikk ay mbiram nag,bi nu xamee ne lòtt doo nga tuub du tuub. Sëriñ bi nee na : ((dëgg-dëggi tuub mooy nga bàyyi bàkkaar boo mas a def ngir Yàlla)) (( ci sa coobarey bopp,waxunu lu mel ni (lu la Yàlla teg) niki tëx ak jàngoroy pëy ak gumba ak luu)) ((nga bàyyi ko rekk ngir màggal ku màgg ki,ak ragal mbugalam mu metti mi)).

Man nag li may wax mooy lu man a xew ci mbooloom Sëñ bi la ,moo xam daa lòtt walla daa tuub,mbari na lu Yàlla jéggal ku tooñ te tuub,bàyyi ko ak Yàlla daal a gën a wóor, rafet njort ci moom itam a gën a mat,Yàlla nee na : ((fa man jaa ahuu mawhizatun min rabbihii fantahaa fa lahuu maa salafa mamruhuu ilal laahi)) muy ku ag waar dikkal juge ca boroomam,mu bàyyi la mu doon def,la mu jiital ñeel na ko,te mbiram moom ma nga ca yàlla. Bi soldaar si demee,ci la génne ci ndigalul Yàlla ak Yonnantam ci ñaareelu tukkeemba,ma nga ca naan:

(( ku jorte ne sama dox ba ginaaw atum aksasin di 1321g,moo’k sama dox bi ci bopp jaysasin di 1313g ñoo yam)) (( sax na ne aji réer ju dof la ,ndax moom dox boobu teeyal (neexal) gu aji kawe ji di teeyal samag dund la)) (( saama doxub aksasin bi du lu dul yoolub ki ma wommatal ci ginaaw bi dëël (dig) bob def na ko)).


Doggantal : ci ñaareelu fàddu gi (tukki fii) dem Gànnaar[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci bisub gàwwu,fukk ak juroom ñaar ci weeru gàmmu atum aksasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak benn,la Sëñ bi génne ca këram ga ca Daarul Mannaan,ginaaw bi ko ay bataaxel dikkalee aki ndaw tukkee ca nguur ga,naan ko na leen fekk Ndar ginaaw tisbaar. Mu fanaan Ngaabu ak njiitul soldaar si,xëy dem Njaaréem ,juge fa dem Tool,juge fa jàll Tiwaawon,foofa la yéege saxaar dem Luga,ware fa gaal dem Dagana,loolu lépp ci ag ayu bis,sax fa juroomi guddi,jéggee fa dex ga juge Dagana ginaaw bi, ci ñaar fukklu fan ci weeru gàmmu ànd ak waayi Sheex Siidiya Baaba ji,mooy Sheexunaa Ibnu DAADA,man na’a am li waraloon loolu di woon li nu wax ne Sheex Siidiya’a ko wax muy ne leen sëriñ bii de amul lenn lu ñaaw lu deesi ragal ci moom. Ñu ne ko woon ndax man nga noo wóoral (gaaraantil) li nga wax? Mu ne leen warlul naa leen ko,ñu ne woon ko kon leegi danu koy boole ak yaw.

Sëñ bi moom daawu leen yeexal lu dul diggante bi muy xaare ndigal lu juge ca boroomam ak sangam ba,loolu moo daan waral ñuy jort ne daa lànk,te fekk booba noonu la deme,ci noonu mu dem ànd ak Sheex Siidiya,ba nu àgg ci yenn ci kër yi nga xam ne du nu woon këram,waaye yu Banii Daymaan lanu,mu wàcc fa ngir ay mbir ci digganteem ak yenn giir yi,bu ko defee ku baax ki wàcc moom itam,bu niy laxas mu laxasati def ko ay yoon.

Bi tuxu yi baree nag ak màngaan mi ci wenn weer walla ñaar,nga xam ne daanaka dunu sax fi barab,te loolu wuute na’ak lool aaday waa réewam,loolu tiis ko sonnal ko ak ag njabootam,te itam taalubeem yi danu koy dikkal fu mu man a nekk te barab yi sori nanu,sàcc yi bari ci yoon yi sonnal leen it ya yooni yoon,ci noonu ku tedd ki sàkku ci ñoom ñu tàggoo,ñu bañ ngir xér ci ànd ak moom,ak ngir yilla ju jiitu ji muy dénk gi ko ko nguur gi dénkoon .

Waaye Sëñ bi moom dogu rekk,nu xam ne ku dëggu la,te du sàkku dara ci bànneexu bakanam,nu ànd ak moom ci li mu bëgg,nangul ko ngàntam,moom itam mu jàmmante ak ñoom ci aw bayit wu yàgg:( bu ñu nu tànnloo woon de du ma tàggoo’k yeen, waaye ag tànn àndul ak jamono ),Sëñ bi ginaaw lii du bayitu boppam mu soppi waaye ag tànn àndul ak jamono,def ko waaye ag tànn àndul ak am ñax,jublu ci loolu yéen da ngéen di sàkku fu ngéen di sàmme ak fu ngéen ko man a ame,loola reeloo leen.

At mooma mu woore Sarsaara koor ga,muy barab bu nu xam fa ñoñam,nit ñi sottiku fa,ak ñuy jële ci moom rawati na ci Banii Daymaan ak seen kilifa ya,doomi Baydah yi Abdul Laahi aki mbokkam ci loolu ku baax kaa ngi naan: (( mbooleem sama xeeti cant ñeel na ki nga xam ne sama lépp ci moom mujj na di ngërëm lu àndul ak ab sàññ(mer), ñeel ko fa Sarsaara)) (( moo moom sama tagg ak sama ngërëm ci lu dul sàññ,bi mu ma wommatalee ay ansaar yu bokk ci Banii Daymaan)) ((sama lépp ñeel na Yàlla fa teeni teraanga,yu nu tuxoo,te bari na fa ñu siyaaresi)) ((ñi nga xam ne danoo dikkoon Sarsaara ngir siyaaresi ma fa,na nu xam ne tàggoo nanu aki bàkkaar àdduna ak alaaxira)).

Ci Sarsaara gii nee na daje na fa’ak Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu,du ciy gént,mu jox ko Wirdul Maaxuuz .Fekkoon na njëkk loolu Sang Bu nu Wóolu bi dikkaloon ko ca géej ga,rékki (jël)woon ca moom lépp lu mu jële woon ci nit ñi,ba deseetu ci dara,mu jox ko wirduw Xaadir,ba ca mujjug tuxal ga nga xam ne loolu day tegtale ne daje na ak Yonnant bi (j.y.m) ca géej ga,Jibriil dikkal ko fa mooy Sang Bu Nu Wóolu bi,rékki woon ci moom la mu ca rekki woon,joxoon ko la mu ko joxoon,jaarale ko ci Yonnant bi (j.y.m).

Mas naa teew bis kenn ci boroom xam-xami naar yi laaj ko kuy Sang Bu Nu Wóolu bi ? Mu ne ko Jibriil,mu ne ko ndax Jibriil dees na ko gis ginaaw Yonnant bi ? ku tedd ki tontoo ko ñaari bayiti ki woy Xazawaat :

(nee nanu Jibriil da na teewal kiy faatu te gëm,aw nit it weddi nanu ag dikkam ginaaw Yonnant bi (j.y.m), dëgg gi nag mooy amul ab dayo (ag dikkam) ) .

Sëñ bi neeti ko waaye wax jii am na ñu ko tax a jug,ñooy ñi ci am ag ñam akug dëggal,waa ju juge fee rekk nag li war mooy mu nangu ko mbaa mu noppi,ngir bañ a loru.

Man nag ma ne misaalum loolu mooy lu mel ne ku nu digal mu taal ab taal ngir aajo ju wér,mu taal ko,ab lëpaalëp jaar fa tàbbi ca,dee,kon kooku dara waru ko ca dee googu,naka noonu ku nu digal mu wax, bu waxee.Ma ne wàlliyu yi di gis malaaka yi moom kenn manu koo weddi, ndax jële naa ci mbindum sunu sëriñ Xalifa Alhaaji Muhammadul Faadil,moom mu jële ko ci yenn ci teere yu mag (majaamih) yu wér yi lol ab yaxam mooy ku ñu ubbi (maftuuh halayhi) moo xam ab nabiyu la walla wàlliyu,manul a ñàkk mu jàkkarloo’k malaaka,ci seeni jëmm,ni ñu mel,tey wax ak ñoom ñuy wax ak moom,képp ku ne wàlliyu du gis malaaka tey wax ak moom kon na xam ne tegtalub loolu mooy moom du ku nu ubbi,lii nag mooy layuw ku nangu(féeñug Jibriil),ci ku ko nanguwul.

Ginaaw Jibriil da na dikkal aji gëmm ji buy faatu,te ku ñu ubbi day gis malaaka yi tey wax ak ñoom,te yinkiiwalug wàlliyu yi (sol gi nu leen di sol xam-xam ak li Yàlla di bëgg ci ñoom) mi ngi am jaare ci malaaka walla mu am ci lu dul muy jaar ci kenn,ginaaw loolu lépp am na,kon du jomb ci Jibriil moom mi Yàlla wóolu ci wëhyoom gi,mu nekk ag diggale (intermédiaire) ci yobb ak joxe yinkiiwal gi Yàlla di dsotti ci ñenn ci wàlliyoom yu mag yi,ginaaw ñoom ñooy ñiy dònn yonnant yi.

Moom Jibriil dimbali na sunu sang ba Hassan saaba bi (y.y.g)ci teewaayu Yonnant bi (j.y.m),mu di ag kiimaanam tey karaama ñeel aw wàlliyoom,luy tee kon mu man a dimbali ligéeykatam bii ci ginaawam,mu dig kiimaan gu ñëw ci ginaaw bi tey karaamay wàlliyoom wu dikk ci ginaawam te di ko ligéeyal ni ko Hassan,wàlliyoom wu njëkk wa doon defe. Ñoom ñaar de ay mbokk lanu ci lgéey bi,ba fa tuxal ga xam. Du ñàkk ñariñ ñu indi tuxal gi ba ngéen gis ko,mi ngi nii:da ne yal na ko Yàlla mu màgg mi gëram : bu dee bunt bi yor wirduw aji nos ji (aji woy ji) moom doggantal nekku ci ,(doggantal= français =chapitre,araab=faslun) aji nos ji ,wird wi mu njëkk a jël ci wird yi mooy wu Xaadir,ginaaw bi wu Shaazaliya,ginaaw bi wu Tiijaan.

Bu dee wirduw Xaadir moom jëfandikoo na ko lu yàgg,daan ci sàkku ndigal ci képp ku mu mas a yaakaar ne ku nu ci jiital ga (muxaddam), ba jële woon ko ci ñu bari. Ginaaw bi mu wóor ko ne ñi mu daa jële du ñu ci woon ay muxaddam maanaam ñu ñu jiital (ñu ko war a joxe) ,mu sàkku ci Yàlla (t.s) mu may ko ci lol ag gëlëm mbaa ag dengi-dengi dootu ci nekk. Mu ne bi ma Yàlla yobboo ci géej gi ma nekk man rekk ak moom la ma Sang Bu Nu Wóolu bi dikkal (j.y.m),dal di rékkee ci man lépp li ma jële woon ci nit ñi ba dara desatu ci,mu jox ma Xaadiriya ci diggaleg (jaarale ko ci) Yonnant bi (j.y.m). Tuxal gii ak lu ni mel ci mbidd yi, danuy wone ne Sëriñ bi daje na ak Yonnant bi(j.y.m) ak Jibriil (j.y.m) ci lu dul woote ag yonnant,du caangéenug wëhyu,waaye ci kem li Yàlla di jagleel lenn ci wàlliyoom yu mat yi.

Waxam ji mu naan wirdiy aji nos ji mi ngi ci jublu woon xasida gi mu doon tudde ñatti sëriñ yu tedd yooyu,ak dònn gi mu leen dònn, tuddati sunu sang Anas,ak Hassan (gërmul Yàlla yal na nekk ci ñoom) ak dònn gi mu leen dònn ci waxam jii: ((wommatal nga ma la Jiilaani (Abdul Xaadir Jiilaani)kawee woon ba fa mu yam)).

Ku bëgg a am lu ko leer na xool teere bi nu naan “Tanwiirul halaki fii imkaani ruwyatin nabiyyi wal malaki”di ci maanaa leeralug lu lëndëm këriis ci man a nekkug gis Yonnant bi (j.y.m) ak malaaka,teere boobu boo bëggee lu leer rekk moo ciy géej jug mbàmbullan gi.te boo defee ag settantal ci tuxal gii ak li ci topp,da nga gis la amoon kon ca géej ga muy ni nu nangoo woon li mu jële woon ci ku dul woon Yonnant bi(j.y.m),ak dello ngi ko ko Yonnant bi delloowaatoon,ak naayibam yi, ñatti sëriñ yu tedd yi,ngir mu nekk naayibam moom Yonnant bi ( aji wuutoom),tey ki fi wuutu yooyule sëriñ (g.y.y.ñ),ci seeni wird ,di seen muxaddam bu nu joyal bi , nga xam ne amul lenn lu ko tënk ci wenn wird,(ku ko neex ak nu ko neex la koy joxee) ,da nga ci gis it la amoo n ci Sarsaara muy jox ga nu ko fa joxoon wirduw boppam moom rekk,jagleel ko ko,nga xam ne benn sëriñ bu ko fi jiitu masu koo yor.

Looloo waraloon daawul digal ku jébbalu ci moom te yoroon aw wird njëkk muy ñëw mu koy bàyyi,da koy digal kay mu tëye ko te yéene ne moom moo ko ko jox,ku jébbalu ci moom nag te waxoo ko dara,bu boobaa mu door laa jox wirduw boppam. Looloo waraloon doomam ju tedd ja,sunu sëriñ,SheexMuhammadul Bashiir naan cig xasida gog biral na ci ngënéelug wirduw Sëñ bi ci yeneen wird yi,xaaral ma jox la ko lépp,ma nga ca biir it waxam ja mu naan: ((wommatal nga ma la Jiilaanii kawee woon)) ba ca bayit ya nga xam ne sëñ Bashiiru tudd na leen ci xasidaam gii,mi ngii:

(ci turu Yàlla laay tàmbalee aw woy wuy jariñ ku bëgg a jariñu te ab xolam set) (ag cant ñeel na Yàlla,yal na dolli xéewal ak mucc ci Yonnant bu nu tànn bii di gën ji mbindéef) (ak ñoñam aki saabaam ,ñu tedd ñii te diy sang,ñoom ñi wuññi lëndëmi xol yi ak lëndëm) (bu loolu jàllee ma naan la déglul waxi kiy laabiire boppam tedi la laabiire ci luy faji aajo) ( yaw miy sàkku matug texe ci yooni ñatti sëriñ yi) (yoonu sëñ Imaam Jiili (Abdul Xaadir Jiilaani) ak Shazali mi làq ag ngënéel) (ak Abool Habaas (Sheex Ahmad Tiijaan) miy ndamul ñu mat ñi,ñoom ñooñu nga xam ne seenub àtte ca jublu ga (xasd) mooy àtteb ku njëkk ka ) (ànd ak ku ci nekk yor sa jagley bopp yoy ci la saw yoon làqe ay jagleem,loolu nettali nanu ko) (na nga taqqoo’k yoonu Abdul Xadiim (jaam biy ligéeyal Yonnant bi) ,ndax moom kat moom la Yàlla mu jiitu mi jagleel mu dònn yoon yooyu yépp) (ndax kat wird wu nekk am na mbóot,ci benn baat bu ci nekk,(ci biir wird wi) yal na la Yàlla gindi) (baat boobu nag boroom “baziira” yi rekk a ko xam (baziira = gisug xol )keneen ku dul ñoom xamu ko,muy hikamu ab boroom buy aji not ) (misaalam mooy Laylatul Xadar ci weeru koor wu nekk,ak Waxtuw Àjjuma,dees leen di wër di) (Yàlla feeñalal na ko (moom Sëñ bi) ya làqu woon yépp (ci wirdiy yeneen yoon yi),ginaaw bi mu leen ligéeyalee te yekkati ag wàllam ngir jëmmam ju tedd ja,ba mujj ñépp bëgg ko jiital ko,(def ko muy seen muxaddam (ku nu jiital ki am sañ sañu joxe wird wi) ) ) ( Yonnant bu nu tànn bi tam - yal na ko Yàlla dolli ay xéewal ak mucc ni mu ko tànne - yéegal ko ci ab hadara bob ku dul moom fàddu na ci yaw,bu nekk fa aji kawe ji (muy Yàlla) loolu di lu kawe sax la mu doon wut ) (bi loolu wéyee mu donnalati ko lu nu nëbboon li , muy aji jiitu ciw yiw joj wuññi na ay fitna) (ci coobareem (moom Yàlla),màgg na te kawe,la ko tànne ci darajay Yonnant bi miy ligéeyal biy joxe ag sell) ( ngir barig li mu leen ligéeyal te sellalal boroomam,di it ku sellal te matal kóllare ci diineem) (mu boole lépp,dolli ci,yéeg ci barkeb Alxuraan te fa mu yéeg’ak a baax) (boo jëlee wirdam de jël nga wird yépp,te doo ragal ag nërméelu) (la nu dige ca seen wird yooyee it da nga ca jot,te doo ragal genn tëkku ) (ndax moom (tëkku gi) ku bàyyi dëgg a ko tax a jug,te ku ko jël (moom wu sëñ bi) yayoo nga jagle ya ) (jàpp ko de moo di jàpp ca lu baax la te dolli ca nag,ngir boole gi mu boole (wird) yépp,teg ca yor leneen ndollent (lu yeneen yoon yi yorul)) (cosaan li mooy da ngay wax (ahuuzu billaahi minas shaytaanir rajjiimi)teg ca (bismil laahir rahmaanir rahiimi) jàng yenn aayay Alxuraan,doo ga tàmali) (def hasbala (wax hasbunaal laah ba fa mu yam) def istixfaar ( astaxfirul laah) ,def haylala (wax laailaaha illaal laah) ,julli ci sangub ñu tedd ñi) (ginaaw bi defees ag tëj gu rafet,loolu da na amal fa Yàlla lépp lu baax) (lli mooy cosaani seen wird yi ñoom ñëpp,ku ci nekk nag am na genn jagleem gu mu moom moom rekk gu kawe) (Sëñ bii nag moom jël seeni ndono jële ko ci gën ji mbindéef mi leen di àggale) (mu wax (moom Sëñ bi) bi miy nettali yooyule xéewal,di ci sant kiy fàttaliku (di Yonnant bi) ngën ji aji xéewale ji (di Yàlla) ) (ki moom jépp jumaa ak jépp jàkka, moom loo na ma mebëtum mbooloo yi) (mu wax di sant aji tedd juy kenn ju ko donnal téere bi (di Alxuraan) muy ndono lu am njariñ) (tàllal naa sama loxo jëme ca Yàlla,moom itam mu tàllal xéewalam ga ñeel ma ca géej ga,te loola tàlleeku) (téereem bu tedd ba mujjoon na di wird ci man,daqaloon na ma samay noon it te dàkku leen) (mu daan won lu neex képp ku ko taqoo, di ko jàng lu mu man) (boo bëggee leeralug lii ma la tuddal,am lii nga xam ne ciy woyam laa binde sama mbind mii) (wommatal nga ma lol ci la Jiilaani kawee, ngëramul ki ma kaweel yal na nekk ci moom) (wommatal nga ma la Abool Hasan kawee woon ci ligéeyal Yonnant bi,miy maami Hasan) (matalal nga ma la nga xam ne ca la Sheex Ahmad Tiijaan kawee woon,te nga nekkal ma ci lu rafete ni wurusu marjaan) (wommatal nga ma lol soril na ma taq-taq,ma mujj mel ni Anas ci ligéeyal yonnant bi) (moomloo nga ma te wommatal ma ag rafetal,donn na Hassan ci tagg Yonnant bi) (ngërëm ak jàmm yal na nekk ci ñoom,ni lëndëm dàqoo ci ñoom(ni nu leerale àdduna bi)) (mu wax ci bi miy tagg ngir sant ku nu jublu ki ( di Yàlla) ci téere bi (di Alxurran) ak Yonnant bi Muhammad) (sama àddiya ji juge ci yaw ak ci Muhammad sunu sang bi, lu man a tee mer la) (darajay aji far ji (muy Yonnant bi) far na samag deng-dengi,te wommatal ma kàttan ga ci lu dul ag doyodi) (sama lépp’ay sant aji yekkati ji may dëgëral,cant gi nag jëm ci Alxuraan ak Yonnant bu baax bi) ( téere bi ak Yonnantub ku nu jublu ki, yekkati nanu sama lépp ci lu dul keno) (Alxuraan nooyal na sama xol bu gindiku bi,dàq it bépp jalgatikat jëme ci ku dul man) (sama xol ak sama loxo maa ngi ko jëme ci ku nu tànn ki ci di ko ligéeyal,may na ma nag la ëpp njariñ) (aji dégg ji wuyyu na ma ci weeru koor,te baax na,mooy sama jubluwaay,ci barkeb Yonnant bi Muhammad) (Yàlla gindi na sama xol,ñongal samaw yaram ci ngërëmam,dañal aji yàq sama) (mu waxati bi muy déeyaale ak boroomam,mbégte ñeel na ñi ko sopp ñépp) (ne: yaw mi jéggal sama ñaari way jur ak ñi ma sopp ci lu dul njàqare) (te nga fàddul ma ci sa bopp ak ci Yonnant bi wëlif mbindéef yi,te may ma ay saar) (fàddu nga ak man bu njëkk ànd ak Yonnant bi,may boroomug làqu wëlif mbooleem mbindéef yi) ( ma di ab jaam buy ligéeyal Yonnant bi,di ku nekk ci yaw ànd ak dëgg gi foofa,tey ku fàddu) (mu waxaat ci yenn may yi nu jagleel ñi topp yoonam wi) (Yàlla jëme na ci ñi dul ñi aju ci man lor yiy daje ak dof yi) ((ab boroom bu man loolu may na ko ko,te moom (boroom boobu) ku yayoo wuyyu la ci ku ko woo) (nuy tëje ci Yonnant bi,mi di ag tàmbali te di ag tëj,tey ki gën a mat,yal na Yàlla saxal xéewal ci moom ak ci ñu mat ñi) Foofu la loolu yam.

Ñu dellu ci wax ci cosaanul wird wi,ak yax bi(yax=nassu ci araab.=texte ci français) mu bindoon ci ginaaw sotti (sotti = nusxa ci araab.=copie ci français) ga mu amaloon ca wird wa, muy :

bismillaahiir rahmaanir rahiimi wa sallal laahu halaa sayyidinaa muhammadin wahalaa aalihii wa sahbihii wa sallama tasliiman ,ku xool araf yii nu bind ginaaw matug wird wi, na xam ne ki ko bind di Ahmadu doomi Muhammad doomi Habiibul Laah,mi askanoo Mbakke te dëkk Bawal,may na ndigal mbokkam moomu ci Yàlla (t.s),sang bi Mustafaa Usmaan mi juddoo Halab te dëkk Madina,may na ko ndigal ci mu jëfandikoo wird wu nu barkeel wii ak jox ko ku ko soop ci mbokk yu góor yi ak yu jigéen yi,ni mu ko jëlee ci Yàlla jaarale co ci Yonnant bi (j.y.m) cig yewwu du ciy nelaw,atum baksasin di junni ak ñatti téemér ak ñaar fukk ak ñaar,ginaaw gàddaay gi,yal na Yàlla defal ki ko defoon gën jaa saxi xéewal ak gën jaa jariñi jàmm,ci benn barab bu nuy wax Sarsaara,ci weeru koor gi nu wàcce Alxuraan,mu dig jub ñeel nit ñi,te di ay aaya yu leer yoy ag jub la ak teqale dëgg ak safaan. Yàlla nag mooy seere lii nuy wax.Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yasifuun wa salaamun halalmursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.

Sunu mbokk moomu Muhammad Abdul Laah Alhalawii,nee na ci teereem bi tudd(( Anafahaat almiskiya fiil xawaariq al mbakkiya))muy ci maanaa bonnig misk ci xar-baaxi Mbakke,nee na Sëñ bi Yàlla da koo jox wird wii,mu jox ko muritam yi,xemmemloo leen ko,te loolu di lu war ci moom. Mu ne leen képp ku ko saxal aki sartam da na tàbbi àjjana ci lu dul hisaab (hisaab mooy laaj yi ñiy def ak a gëstu ay mbir) du caagéenug mbugal,te Yàlla it da na ko aar ci naqar yi ci àddina ak alaaxira,te saytaane mu nu dàkku mi du ko jege,da na doy wird wi ag kawe,nekk gi mu nekk wird wow boo ko dee jëfandikoo soxlawul gay jëfandikoo yeneen yi,te manoo am li ci moom te jëfandikoowoo ko.

Sunu Sëriñ, sunu wasiila ca sunu boroom mu kawe mi nee na bi mu nuy jox wird wu tedd wii:jox naa leen wird wii ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe,kon tëye leen ko ngir jëmmi Yàlla mu tedd mi te kawe. Mu waxaat jàpp leen ko ak doole,ku ci jotoon a yor weneen wird bu ko manee, na leen boole,kon muy leer ci kaw leer,bu ko manul mu yam ci wird wu tedd wile. Jeex na.

Ki ko doon taariixal nag ne moom : bismil laahir rahmaanir rahiimi ,lii aw tagg ak taariix gu Ahmad doomi Asan def ñeel wirduw sëriñam bi Sheexul Xadiim,yal na nanu Yàlla jariñ ci moom ci ñaari kër yi aamiin.

( sunu boroom taxawal (fondumang)na sunuy jëf ci may nu ñu man a root ci gën ji teen, kon mbégte ñeel nanu (mu jublu ci wirdul maaxuuz)) loolu mooy wirduw sunu sëriñ bi Sheex Ahmadu Mbakke,mu juge ca boroomam jaar ci Ahmad Yonnant bi) (yal na ko Yàlla dolli xéewal ak mucc,li feek mi ngi doon ab raas jëm ca texe gu kawe ga) (jox na ko wird wii jële ko ca aji namm ja muy Yàlla,yéem naa te ñée bii sëriñ ak yii taalube) (jagleel na ko wurusu luulu wu nu ñongal ci xor,te làq ko ku dul moom) (wurus ñeel na sunu sëriñ bu nu gërëm bu màgg bi,ku ko am de am dëkkaaleg ka gën a màgg) (mi ngi ko gènne ci bisub àjjuma,mu jëm ci ku Yàlla texeel ci doomi jamono ji) (ci juroomi fani sawaali atum (sahidnaa karaman) di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,moom boroom taariix bii,moom miy ndëppul ñu tedd ñi (ndëpp mooy mbaxana mi nuy solal buur) ) (mooy sunu sëriñ Ahmadu MBAKKE mi dëgg di tax a tukki ak a took ) (génneel nanu ko ngir jëmmi Yàlla ,kon billaahi bu ko sàggane) (ngir Yàlla,boo bëggee am li nga bëgg,ndax kat kuy rëbb ba jam ñay man a dëpp) (yaw sama boroom ci darajay aji wommat ji xeet yi jëme leen cig jub,di Muhammad miy wuññi njàqare) (yal na Yàlla miy sos niir yi,sotti ci moom gën jaa selli xéewal ak mucc ak ñoñam aki saabaam) (ak ci darajay sunu sëriñub Mbakke bii,na nga ma may ma jot ca la ña jiitu bëggoon) (ci ag kawe,bu ko defee ma bokk ci mbooloom ñi la jege,yaw miy boroom nguur gi) .

Nan dellu ca tukkib ñaareel ba,dem ba Tintu Muxsin,foofu barab la bob xew-xew bu ñaaw te soof dal na ko fa,muy : ab naar bu nu xam turam ak giiram,daa jugoon ngir ne da koy faat moom Sëñ bi - man moom xam naa ko waaye dama koy suturaal ngir doomi baay tëxam yu julit yi - moom da doon fexee faat Sëriñ bi,Yàlla musal ko ci,ni mu doon defe loolu nag mooy xanaa ñëw ci moom won ko ag cofeel gu dëggu ak jébbalu ci moom,Sëñ bi moom itam suturaal ko,boole ko cig njabootam,bindal ko ñatti bëyit,ne ko na ko saxoo jàng,guddi ak bëcëg ,naar bi moom itam dëkke woon loolu,bëyit yi moo nekk nii: (lor ak saytaane jëm nanu ci ku dul man,ndax ñoom ñaar kat amunu ci man genn kàttan) ( Yàlla mooy sama boroom,Yonnat bu nu tànn bi - yal na Yàlla dolli xéewal ci moom, moom mi ko gindi te tànn ko) ( mooy samab xarit te di sama soppe,te bañ na it samag loru,te sàkku na ci boroom mbindéef yi samam mbég )

Naar bi taqoo woon ak loolu,di ko jàng guddi ak bëcëg ,ci mbooloo mi ak bu wéetee,mu ko daan def ginaaw saaru Yasiin,mel ni kuy nodd,nga xam ne da naan wax: yaasiin,yaasiin,yaasiin,ba kero muy mat juroom ñaari yoon,mu door a àggale saar wi teg ci bëyit yi,jàngati yaasiin ni mu ko defe woon,tegati ci bëyit yi,baamooti leen,niii daal la ko daa defe ,daawul taxaw lu dul daa sonn walla muy nelaw,mu sax ci loolu ay fan,am na ñu ne weer.

Jamono jooja Sëñ baa nga woon fa ñoñ sheex siidiya,nekk ca seen xayma ya,ci noonu mu digaloon taalube ya nu defaral ko ag kër ca bitib gàdd ga,ñu def ko ni mu ko bëgge woon,bi mu noppee mu wax ko sheex Baaba,sheex Baaba digal mbokkam ma sheex Siidiya Muxtaar mu gunge ko ca kër ga,mu defe ko noona.

Sëñ bi moom digal naaram booba mu ñëw ànd ak moom ca kër ga tey jàng ñatti bëyit yi,ni mu ko baaxoo woon,bi nu agsee,saytaane jàpp ko,xamal ko ne pexe mi mat na,def dong a ci des,bi guddi gi soree ba kenn yëngootul,naar bi jug,summiku ba mel ni ko ndayam jure woon,dal di dugg ci kër gi,jawali ca néeg ba Sëñ ba nekk,ginaaw xamoon na fa jaasiy Sëñ bi nekkoon ,mu jawali ca,bocc ko ci mbar mi,waaye Yàlla dogal jenn waay ju bokkoon ci néegub nguurug Kajoor,te gënoon cee rafetug tuub ak bàyyi àdduna,ñu ko daa wax Omar FAAL NDATI,nekkoon ca jàkka ja,di fa fanaanee jaamu Yàlla,bi ko naar bi rombee mu jug ca saa sa,seeti ki yor mbiri biiri Sëñ bi ,di Muhammad Lamin ÑANG,doomi Muhammad Lamin Mati,moom waa-jur wi,doomi bàjjan la ci Sëñ bi,xamal ko ne am na jëmm ju rafle ju jëm ca néegub Sëñ ba,ca saa sa ndonga la jug,gaawantu,fekk naar ba mu bocc jaasi ja,di settantal naka lay jekkoo Sëñ bi ba man koo lor bu baax,te Sëñ bi moom mi ngi tëdd ci wetam,bi naar bi xàccee di ko door jaasi ji,yàlla dogal mu lonk ci koñub xayma bi,daje ak ndonga li di wadd di dal ci kawam,mel ni kuyul gileem loolu,dal di koy nërméel,naar bi yuuxu,murid bi yuuxu ci kawam,mel ne da koo bëg a lekk,seen coow li fees foofa dell,ña nekkon ca wet ga yuuxaloo,daje fa,nga xam ne Sëñ bee mujj ñëw dox digganteem ak nit ñi ne kon ñu ray ko,mu dalal leen,dal di yonne ci menn mbooloo,mu fanaanoon fu sori foofa,mu mu naroon a yewwi,woolu leen,ne leen yobbaaleel leen ma naar bii ba Xumaak, (barabu kiliftéefug tubaab yi,da nanu ko wax it Sahwatul Maa) ngéen bàyyi ko fa te dem seen yoon,denk leen ñu yëram ko te dimbali ko ci bagaasam yi,làq leen nag xibaar bi,ngir bañ ñu gaañ ko,jeemul a fayoonte ak moom ci jëfam ju ñaaw.

Yenn taalube yi nag gis nanu ne li tax Sëñ bi delloolu naar bi Xumaak,fa tubaab yi am sañ-sañ,ab junj la ci ne ñoom tubaab yi ñoo ko yonni,Yàlla rekk a xam,waaye pexeem ma moom Yàlla naaxsaayal na ko.

Yooyu ñaari bëyit boo ko xoolee da nga gis ne Yàlla feeñalal na ko ci ay karaama yu kawe,yal na ko Yàlla fayal jullit ñi aw yiw ak Lislaam.

Man nag li ma gis mooy lii mooy dëgg-dëggi laabiir ak doylooYàlla,ak nangu ab dogalam,miinunu ko ci ku dul moom ci waa jamonoom,li mu nuy fàttali mooy li daloon ki miy ligéeyal ci yenn ci xareem yi,loolu mooy dafa am benn Ahraabii (araab bu dëkk ca kaw ga) bu tuddoon Duhsuur bu ko fekkoon mu tëdd,xaw a sori saabaam yi,mu bocc jaaseem,xàcc ko ne ko ana ku man a dox sama digante ak yaw? Yonnant bi (j.y.m) ne ko Yàlla,ci noonu waa ji di lox ba jaasi ji rote ci loxo bi,Yonnant bi (j.y.m) jël ko ne yaw nag ku la man a musal ci man? Mu ne ko amal yërmaande, Yonnant bi jéggal ko,bañ koo def dara.

Naar bii nag moom bis dellusi na ci Sëñ bi ca Xumaak,taalube yi jug ngir fexeel ko,Sëñ bi yëg ko génn ci naaj wi,te solul ay dàll,di wax ca kaw: bàyyi leen ko,bàyyi leen ko,(alaa tuhibboona an yaxfiral laahu lakum) muy:xanaa bëggu leen Yàlla yëram leen,di ko baamu.

Nu bàyyi ko,mu digal ko mu làqu,génn te dem yoonam,ginaaw bi mu ko defalee ag njekk. Bi ku tedd ki nekkee Njaaréem,naar bi delseeti fa,Sëñ bi aarati ko,naan ko:boroom jaasi ji,naar bi naan ko : déedéet neel boroom xëm gi,bu ko defee Sëñ biy ree,génneeti ko ginaaw njekk.Man ci sama bopp gis naa ko Cees,maanaam Jànqeen,te booba maa ngi ànd ak am mbooloo ci taalube yi,waaye man rekk a ko ci xàmmee,bu ma ne woon kii de diw la ñu ray ko,waaye kon ana jikkoy Sëñ bi,Alhamdu lillaa.

Nu dem nag Jaraari,barab la bu Halawi yi moom,Sëñ bi tudde woon ko Biirul Xayri di ci maanaa teenub yiw,ci barab boobu la Sëñ bi doon waxe xasida gii: (( li ma doon laaj sama boroom indil na ma ko cig baamu,rawati na ca Biirul Xayri di Jarraari)) ((samag cant ak njukkéel ñeel na ab boroom bob wommatal na ma ay xéewal,ci lu nëbbu ak lu feeñ,di ku ñu baax ñi sopp)) ((sama boroom wommatal na ma barkeb saabay ku nu tànn ki,mu nekkaloon ma te daawu ma won ayuw kàccoor yi)) (( samag cant ñeel na aji jiitu juy aji des,kok aar na sama kanam wëliif bépp ñaawtéef,ànd ak ag bëbb guy daw juge ci moom jëm ci man (bëbb mooy luy sottiku bu baax di wal fii mu jublu ci xéewal) )) ((samay cant ñeel na ko,ci biir ay sang yu askanoo ca Aliyun (fii man na cee jublu Seydinaa Aliyu,man naa firi it aji kawe di Yonnant bi) ci lu dul aji jalgati mbaa workat)) ((aji des ji amul bokkaale yal na dolli xéewal ak mucc ci ki nga xam ne indil na ma la ma ko ñaanoon cig baamu)).

Halawi yi nee nanu xamunu lu tax Sëñ bi tudde ko Biirul Xayri,ndax tur woowu ñoom masunu koo dégg ci seei baay,ba bi nu fa suulee Sheex Ahmad Bun BUDDIN,nu dal di xam sekkareb li tax mu tudde ko ko,nu xame ci baatinub Sëñ bi.

Ci Sheex Ahmadu Bun Buddin, Sëñ bi wax na ci ay wax,Alhaaji Muhammab Bun AAB,dàkkantal la ci Sheex Ahmadu Bun Buddin,nettali na ma ne baayam bind na bis Sëñ bi ne ko daa bëgg mu nuyyul ko Yonnant bi(j.y.m),ak Sheex Ahmad Tiijaan,te itam soxla na seenub tontu,Sëñ bi tontu ko xamal ko ne Yonnant baa ngi koy fay,ak Sheex Ahmad Tiijaan,aji nettali ji nee na ca saa sa, baay ji daanu ab jéll,di yëggal bopp bi ak a waxtu,mel ne ku jaaxle te nu muur am xelam,dañul ci melokaan woowu ba bi mu faatoo (y.y.g),te booba ñi ngi fu sori woon Sëñ bi, te yëgalunu ko woon kenn ci guddi gi mu ame woon,waaye amul lu dul ay ndaw dikk ci suba gi ne Sëñ bee leen yabal ñu teewesi dencug Sheex Ahmadu gi,te di leen ko jaale.

Mu bind ci loolu ag xasida di ci xamale darajay Sheex Ahmadu moomu, fa Yonnant ba,moo tax mu terale ko karaama googu,ne lii mooy payug Ahmadu Bun Buddin,tey payug ab xalifaam:

Bismil laahir rahmaanir rahiimi, yal na Yàlla dolli xéewal ak mucc ci sunu sang bi Muhammad aki ñoñam aki saabaam,na ngeen xam ne guddi gi Sheex Ahmadu Bun Buddin di faatu ruuhul xudsi (jibriil) (j.y.m) wàcc na juge ci asamaan si,ànd ak lu bari ci ay malaaka ngir terale ko sang boobu,ngir rafet gi mu rafetoon njort ci Jaam Biy ligéeyal Yonnant bi (Sëñ bi) ,yal na ko yal na ko Yàlla nekkal cig teral,moom miy aji jiitu tey aji des,ñoom nag delluwaatunu ca guddi googee ndare bu danoo yobbaale ruuwam gu tedd ga,lii nag mooy dëël bi nu ko dëëloon,(dëëlmooy dikk) .loolu la Sëñ bi di junj ci bëyit yii:

((Ruuhul Qudsu ñëw na,di wuññisi njàqare,ànd ak mbooloo mu mag ciy malaaka,jamono ji Ahmadu mii di làqu)) ((Ahmadu am na la mu bëggoon ca Yàlla,buntub yiw ubbikul na ko bu dul tëjooti)) ((yal na Yàlla fay ka joxoon àddiya aji ligéeyal ji,moom moomu nga xam ne am na fa Yàlla ag tab gog aw yiwam moo gën a mat)) ((maa ngi sàkku ci boroom aras ay may ñeel ka ko joxe woon moom mooy aji texe ju nu ndëppal ji (ki nu solal mbaxanam buur) )) ((sangub sang yi wéy na,di ab sëriñ bu nu jiital (bu nu def muqaddam),jiital gi it ki ko def di sëriñ bob aw wirdam ba fàww am ngér lay doon)) (( moom de bir na ko ca àllaaxiraa gee mu nekk ne man maay jëwrini ki nga xam ne mooy boroom raw ak jiital,te mooy ku nu ndëppal ki)) (( sangub sang yi yal na am ngërëmul sëriñam,ak ngërëmul gën ji mbindéef,ndaw muy ku nu bégal !)) (( Yàlla la’ay ñaan mu may xalifa bii mu fi bàyyi la mu yéene,ci darajay ka nga xam ne ay leeram day jolli)) (( yal na nekk ci moom ,moom Yonnant bi,ñaari xéewali Yàlla mi ko gindi def ko muy ku nu gënal ki,ni mu doon yéege ak a kawe ca rañaan ga)) wasalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaalaa,wa barakaatuhuu.

Eskëy,gis nga waxam ji mu naan “ka ko joxe woon” mi ngi ci jublu Sheex Ahmadu Bun Buddin mii,li mu ko joxoon mooy benn teere bu tuddoon ((Mawaahibul Ladduniya)).

Sama mbokk,sama xarit Sheex Ibraayma AMAR nu gën koo xame ci turu Ibra Joor,nettali na ma ne Sëñ bi,bi mu nekkee Sarsaara walla Tuntu Muxsin, da koo yonni woon Ndar ngir mu jëndal ko fa téereb Mawaahibul Laduniya,nga xam ni ki nuy wax Qastalaanii moo ko def,nee na ma dem sonn ci lool,fu ne ma wër fa,waaye dara,ma am lu ma naqàri lool,yëf yi tiis ma lool,ma dëpp di ñibbi,bi ma tollee ca gàddug Sheex Ahmadubnu Buddin,te fekkoon ma xamante ak moom,ma daad fay jàdd ngir nuyyu ko,siyaare ko,ba ma fa àggee mu bég lool,teeru ma dalal ma,bi nu toogee bay waxtaan mu laaj ma lu ma taxoon a jug,ma ne ko sëñ bi dey moo ma yonni woon Ndar,ma leeral ko tam naqàr wi ma am ci ñàkk a am teere bi ma Sëñ bi yonni woon,ca saasa mu jug,gëstu ci ay teereem,génne ñaari xaaj yepp indil ma,ne ma neel Sëñ bi àddiya la,ju ma ko jox ngir Yàlla,ma bég ci ba fa bég yam,waaye Sëñ bi moom gën maa bég fopp ci teere beek ki ko joxe,loolu nag mooy maanaam ka ko joxe woon,mu jub lu ci li mu joxe woon “MawaahibulLadduniya” .

Xasida gii ndollent la ci tontub kiy laaj ndax Jibriil da na dikkati ginaaw yonnat bi. Bokk na ci li mu bind ñeel Sayid Ahmad mom Sheex Muhammadul Haafis lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allaahuma salli halaa sayyidimaa muhammadinil faatihilimaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa,naasiril haqqi bil haqqi wal haadii ilaa siraatikal mustaqiim,wa halaa aalihii haqqa qadrihii wa miqdaarihil haziim,na Sheex Ahmadu Bun Sheex Muhammadul Haafis,ak ku dul moom ci ñoñ Halawi yu goor yi ak yu jigéen yi,ak ku dul ñoom ci jullit ñu goor ñi ak ñu jigéen ñi,nanu xam ne Yonnat bi jàmm ak xéewal yal nanu nekk ci moom,delloo na ab nuyyo Sheex Ahmadu,te Sheex Tiijaani moom itam gërëmul Yàlla yal na nekk ci moom delloo na ko nuyyoo,te Yonnant bi (j.y.m) teral na ko teral gu mel ne gi mu teral mbokkam mi Sheex Muhammadul Haafis,ki ciy dund yal na ko Yàlla gërëm te aar ko ci lépp lu mu ragal,ka wéy it mu gërëm ko te yërëm ko,te SheexAhmad Tiijaan it yal na ko Yàlla gërëm,te jegeel ko,def na ko niki doomam,képp ku jële wirduw tiijaan ci ñaari sëriñ yii tudd Ahmad yal na leen Yàlla gërëm te aar leen te yërëm leen,mel na ne jële na ko ca Sheex Muhammadul Haafis (y.y.g),képp ku ko jële ci ñoom ba noppi bàyyi leen fi di demati ci keneen ci mbooleem sëriñ yi,ànd ak yéeney bàyyi leen,na ko wóor ne pert na ci àddina ak allaaxira,yal na nu ci Yàlla musal,képp it ku ko jële ci kenn ci ñoom ñaar,bu ca faatoo tonowu na adduna ak allaaxira,képp ku xool mbind mii na xam ne bi nu koy bind Sheex Ahmad Tiijaan (y.y.g) moo taxaw di wax ñuy bind.

(( dello nuyyoo bu teey bu kawe bépp nuyyoo buy bijj ag dëppoo)) ((juge na ca jaamub boroomam bay ligéeyal ku nu tànn ki,jëm ci ki làq kawe gi niy tànn)) (( yaw sëñ bu màggi mbir bi,musal nanu la ci lori lépp lu ñaaw)) ((musal nanu la ci rékki aw yiw wu nekk ci yaw,ba kero ngay tàbbi àjjana ya’ak ñi lay xeeñtu)) (( Aji des ji musal na la ci ñaawtéef yi,ci barkeb ku nu tànn kiy boroom raaya ba (daraapoo ba ,di Liwaawul Hamdi) )) (( ak darajay sa sëriñ bu nu gërëm ba,Sheex Tiijaan,ka mujj mel ni wurusu marjaan fa sang ya)) ((yal na Yàlla miy aji des dolli xéewal ak mucc ci gën ji mbindéef, moom (Yàlla) miy ki koy wommatal kawe ga ak saar ya)) ((ngërëmul Aji des,luy bijj ag dëppo yal na nekk ci wàlliyu wow topp na ay tànkam (tànki yonnant bi) )). Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal mursaliin wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina

Bokk na ci li mu bind ngir ñiy am ag wuute ci “Mahiya” (mahiya mooy ag ànd,nu jublu ci ànd gu Yàlla ànd ak kenn walla nekk gu mu nekk ak moom) ,lii: Bismil laahir rahmaanir rahiimi,ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,wa inniya uhiizuhaa bika wa zurriyatahaa minas saytaanir rajiimi,rabbi,ahuuzu bika min hamazaatis sayaatiini,wa ahuuzu bika rabbi ayyahduruunii. Bismil laahir rahmaanir rahiimi,allahuma salli halaa seyyidinaa wa mawlaanaa muhammadin,al faatihi limaa uxliqa,wal xaatimi limaa sabaxa naaziril haqqa bil haqqi wal haadii ilaa ziraatikal mustaqiimi,wa halaa aalihii haqqa xadrihii wa miqdaarihil haziim, mu ne mi ngi ñaan julli gii doon gog da na yee képp ku xool mbind mii,mu yee ko ci ne Yàlla kat ànd gi mu ànd ak ñun ànd gu yellook moom la - tudd naa sellam ga - du ànd gu xel di jot,te moom - barkeel na te kawe - jege na nu,waaye jege gu yelloo’k moom,du jege gu xel di xalam,te xam-xamam - tudd naa sellam ga - lu nu sellal la,niki mbooleem ay meloom ,jëmmam it - barkeel na te kawe - tàqalikoowul ak ay meloom te du tàqalikoo ak ñoom it. Waxi Sheex Sanoosi ji,(y.y.g) ak ñi ànd ak moom ci lu aju ci “Mahiya” lu wér la,ndax ñoom kat danoo seet fi nit ñi toll,ñu wax fa’ak ñoom,ndax bu nu weesoo ak ñoom foofu ñu tàbbi ci alkande,ñoom ñépp. Waxi Sheex Ahmad Tiijaan ji it (y.y.g) wuutewul ak li nu wax. Waaye li ñi askanoo ci moom(y.y.g)di wax,ba miy indi ak noonoo ci seen digganteek Abuubakar Ibnu Fatan,na leen wóor ne noonoo googu de ci saytaane la juge,ndax Ibliis day tàbbal lënt-lënt ci xolub képp ku nekkul “Mushaahid”,(mushaahid mooy aji jàkkaarloo,maanaam kay jàkkarlook mbir ya ca nguurug sunu boroom ga) liy firnde ci loolu mooy Jaam biy Ligéeyal Yonnant bi - yal na ko Aji des,jiy Aji jiitu nekkal cig teral - bi muy bind laabiire gii déy,Yonnant bi dikkal na ko (j.y.m) ne ko Sanoosi Ak Sheex Tiijaan ak Xazaalii de ñoom wuutewunu,ñi am ag wuute kay ñooy ñu dul ñoom. Dëgg gi mat a dellu daal mooy bàyyee settantal ci melow “Mahiya” te gëm rekk ne lu am la,ndax di ci settantal day rékki ngëm ,yal na nu ci Yàlla musal. Wasalaam .

Bokk na ci li mu bind ñeel Abuubakrin Ibnu Fatan ci mbirum “Mahiya” lii:Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla dolli xéewal ci sunu sang Muhammad ak ñoñam aki saabaam,ag xéewal akug mucc gog da na ci xamal nit ñi ne la Aboobakrin Bun Fatan waxoon ci waxi Seex Tiijaan ji,jubluwu ci woon Sheex Tiijaan(y.y.g),te moom Sheex (y.y.g) dëppoo na ak moom (Aboobakrin) ci mbooleem li mu wax ci tontoom yi. Ag jub nag mooy nit ñi bàyyee xuus ci lu mel nii,ndax xuus ci, ci ñaawtéef yi la bokk . Waxi qutbu yi, yal na leen Yàlla gërëm, du waxi boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm. Boroom xam-xam yiy jëfe seeni xam-xam,fi nu toll ci wàlliyu yi mooy fi wàlliyu yi toll ci yonnant yi . Boroom xam-xam yi boroomi tawhiid lanu yuy aar Sariiha mu nu laabal mi, qutbu yi boroomi sellal lanu yu jegeYàlla di aar “Haqiiqa” mu nu leeral, mu nu sellal mi.Kon wormaal ñépp ngir jëmmi Yàlla mu kawe mi lu war la . Bëgganteg boroom xam-xam yi,yal na leen Yàlla yërëm,mooy dundug sariiha,seenug wuute ci masala yi,ag jàng la akug jàngale,dug noonoo,dug iñaanante. Wasalaamu halaykum wa rahmatul laahi wa barakaatuhuu.

Bokk na ci li mu bind ci Ahmadabnil Kawri Addaymaanii, lii:Ahuuzu billaahi minas saytaanir rajiimi,Bismil laahir rahmaanir rahiimi,yal na Yàlla mu kawe mi dolli xéewal ak mucc ci sunu sang ,sunu kilifa Muhammad ak ñoñam aki saabaam,xéewal ak barke ak mucc gog dana ci xamal nit ñi ne Muhammad Ibnu Kawri Addaymaanii,ak Abuubakrin Bun Fatan Alhasani,Yàlla mu barkeel mi te kawe jéggal na leen ñoom ñaar,ci bisub Harafa atum “shahidnaa bikaram” di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,te ku ci nekk ci ñoom ñaar xawoon naa alku,sababub loolu mooy juumug Daymaanii,ak weddig Alhasanii. Ahmadu Bun Kawri moom dëppoowul ak Sheex Tiijaan ci li mu doon xuus ci wàllug Mahiya,bu dee Aboobakrin moom daa ñàkki teggiin ak Sheex Tiijaan (y.y.g) ci ñàkk a nangu ag tontoonteem ak Ahmadu Bun Kawri,Sheex Ahmad Tiijaan nag moom ku beru la wëlif leen ñoom ñaar.Liii mooy dëgg gi nga xam ne sikk amu ci. Wasalaamu halaykum warahmatul Laahi wabarakaatuhuu.

Mu bindoon ba tay jëme ci ñenn ci ñoom: Assalaamu halaykum warahmatul laahi tahaalaa wabarakaatuhuu,bu lii jàllee,man de gis naa li xewoon ci sa diggante ak keneen ci lu aju ci mbirum Mahiya,man nag li may wax ci Mahiya,mooy jëmmi Yàlla moom,kawe na te barkeel,du toq ci xelum kenn mu koy jéem a gëstu ,kon xuus ci Mahiya moo’k wuute gi am ci diggante yahood yi ak nasaraan yi ñoo yam,yal na nu Yàlla mu kawe te barkeel mi musal ak yeen ci soxlawoo lu nu yitéelul. Soxlawoo def ndigal yi te teet tere yi moo gën a jaadu ñuy soxlawoo xuus ci googule wàll,Yàlla barkeel na te màgg,nee na :( zarhum fii xawdihim yalhabuun) muy bàyyi leen ci seen xuus googu,ñuy fo. Wassalaamu hallaykum wa rahmatul laahi tahaala wa barakaatuhuu.

Ci noonu Sëñ bi tuxoo ci barab dem ci barab, ba bi mu sancee ca Sahwatul Maayi,nu gën koo xame Xumaak,soriwaay bi di lu tollook doxub bis bu tar ci ku sawar,juge Dagana walla Budoor. Loolu amoon ginaaw lollib atum baksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñaar,mu mujj di wër ci barab boobu di tukkee ci kër,dem ca geneen gu jege,mbiram it moo’k mu mbooloo yi koy dikkal di siyaaresi di gën a yokk,ci jamono ju nekk.

Cig gàttal daal leeral mbiri Sëñ bi yepp ci ñaari tukki yii,aal topp aal (aal = tolluwaay yi nit di toll), xew-xew topp xew-xew,kenn ku dul moom manu ko,yal na Yàlla yokk ngërëmam ci moom.

Ag karaamaa ngii gu amoon ca Xumaak,maanaam Sahwatul Maayi,ci genn guddi ci benn ci ñaari weeri rabiih yi,atun jaksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak ñatt,muy tawati tànk ju ko daloon te tar lool,fogloo nu ca guddi googa,nu fanaan ca la wër xaymaam ba,nga xam ne sax jortoon nanu ne du weesu guddi ga,waaye moom mu niy dalal rekk naan nu dellu leen ca yite ya,amul solo,waaye nun deeti nopp mbaa ay xel di àndati ak nun. Bi Yàlla dogalee mu wér ca suba ga,mu xamal ma ne mbir mi de balaa la woon bu juge fa sunu boroom,jëmoon ciy nitam,ñu naroon a fër bu leen daloon (fër = naaxsaay), ma ne sunu boroom lu tax nga jagleel sama nit ñi nattu bii bàyyi ñeneen ñi,ñu ne ma ndax kat Yàlla da laa teg ci sa kawi moroom,kon manul a ñàkk mu jàgleel la sa nattub bopp bu ñeneen ñi dul am,te loolu amul lu ko gën a tar.Man it ma ne yaw buur bi ndax man naa koo gàddu wëlif leen ? Ñu ne ma aha kay, jëlal ,mu doonoon lu diis juge ci asamaan wàcc sama kaw,ma daanu xëm,ñu indi ma ci xayma bi te yëguma. Ki ko yobb ci xayma bi,di Moor Xari Joob nettali na ma ne jaan a ko màtt,kon alhamdu lillaahi ci mucc gi ak tuufu gi (tuufu mooy am li nga bëgg) .


Doggantal : ci ag ñibbiseem ci ñaareelu tukki bi[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ba mu fa nekkee ba guddig gàmmug atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,di guddig àjjuma,la fa Sheex Ibra FAAL ñëw,tukke Ndar,indaale këyit wu juge ca tubaab ya di ko may mu dellu réewam Senegaal,murid boobu it dikk jàpple ko ci tuxu gi,mu tàmbalee waaj,di tàggu waa dëkk ba ,ba àjjuma ja dellusi,di fukk ak juroom ñeent ca weer wa,mu génn këram googa sóobu yoonu Ngaanjaar,maanaam Gaaya,dib dëkk bu nekk ci penku bëj-gànnaaru Dagana,dex gi romb na fa,ñooña sàkku ci moom mu julli ci seen jàkka ji nu doon yeesal ,ngir barkeelu ci,mu ànd ak seen imaam ja Muxtaar SOW, julli ñaari ràkkaa ci njëlbéenug yoor-yoor,jëggi dex gi dem dagana,nekk fa ba bisub gàwwu ñaar fukki fan ak juroom ñatt ci weer wi,mu dugg gaal ci tisbaar ji jëm Ndar.

Jamono yi mu nekke woon Dagana,nganale gu nekk defal nanu ko ko fa,ci bëcëg gi, bu guddi masaan a jot,ñu daa indi ay làmp yu leer ci kanamu bóoli yi. Mu wax ci loolu ne loolu mooy liy dëggal waxam ja mu waxoon ca lenn ca xasaayidam yi mu defoon ci arafi ((walil laahi mulkus samaawaati wal larli))di ci maanaa Yàlla’ay boroom nguurug asamaan ak suuf,muy li mu mujj a bind ca Daarul Mannaan ca Tuubaa,ba mu àggee ca arafu daad wa mu waxoon ca : gane ji naa aji Tedd ji,mu teeyalal ma ganale gi,te du ma dañ ci nganale gi mel ni ay làmp

Bi mu àggee Ndar ca guddi ga,daa dal di wàcc ca Sheex Ibra FAAL,sax fa ay guddi,juge fa dem Luga, wàcc ci Alhaaji Masamba Soxna,foofa la yabale ligéeykat yi ñu dem Njiheen,maanaam Cëyéen,ca Jolof,jiitu ko fa,defaral ko fa ag kër njëkk muy agsi,dal di jàll Ngaajax,fanaan ca jàkka ja,fa seen xabrub wàlliyu nekk,dal di jàll ca kër sëñ Asan NJAAY,yendu fa ,fanaan fa,yendooti fa,laxas dem Kokki,wàcc ca Sheex Muhammadu Maam ,maami Sheex Bashiiru,demati Duriga,faSheex Madun Samba,maami Sheex Murtadaa,juge fa àgg Kër Baasin ca Sheex Muhammadu Amina Xuma JOOB,doo nga dem Cëyéen ci bis yu néew,di njëlbéenug rabiihus saanii,fekk yenn kër yi noppi,bi mu agsee ca kër ga,ca njëlbéenug rabiihus saanii,atum haksasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk ak juroom,daa wàcc tudde ko Daarur Rahmaan,mu nekk fa mbiram akuw doxiinam di gën a jub,di dolliku waxtu wu nekk,ba ci benn ci ñaari jumaada yi ,ci atum saksasin,di junni ak ñatti téemèer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,mu taxawal Daaru Xudoos ci sowwub dëkk bi,soree ko lu tolloo’k ñaari kilomet walla lu ko yées,mu sax fa ,bul laaj nag mbiram,moom daal na ma la ko waxe woon rekk ci bépp barab,waaye fii sax gën na fee dolliku,ba ca àjjumay ñaar fukki fan ak ñaar ci weeru muharram,atum lasasin,di junni ak ñatti téemèer ak fanweer.

Ca sahbaani sakasin ja,di junni ak ñatt téeméer ak ñaar fukk ak juroom ñaar,walla ca ramadaan ja,la sëñ Abdul Laahi gane àdduna,wax nanu ma ne Sëñ bi daa bind Abdul Laahi ci aw këyit,yonnee ko Sheex Muxtaar Binta LOO,nijaayi sëñ Moodu Mustafaa,digal ko mu tudde ko noonu,mu defe ko ni mu ko binde woon ci këyit wi,mbooloo mi nag leegi danu koy wooye Abdul Laahil Haziizi,te xawma fu nu jële loolu,ah waa-waaw xanaa denu cee jublu ne Haziz turu Yàlla la.


Doggantal : cig génnam juge Jolof jëm Njaaréem[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ci njëlug bisub gàwwu,ñaar fukki fan ak ñatt ci muharram,atum lasasin,la génn dem Njaaréem,mu julli woon suba ginaaw bi mu doxee lenn ci ay kilomet,mu fanaan ca la yées Tuubaa, ca guddig altine ja mu fanaan Tuubaa,ca Daarul Haliimil Xabiir,fa Sheex Abdu Rahmaan LO,muritam ba jàngal doomam yu mag yi,mu xëy nag jëm Njaaréem,fanaan fa guddig talaata ñaar fukki fan ak juroom ñatt,bi mu àggee Njaaréem,ñu dalal ko ci njëlbéen gi ci benn pàkk bu nekkoon ci wetu àttekat (goornoor) bu ndaw bi,àttekatu ñoñ bi (al haakimul ahlii,xanaa mooy gouverneur civil) ,ca jamono jooja ma nga dëkkoon ca wetam,barab boobu fa lanu tabax fi mu nekk jàngukaayu farañse bu mag bi (école française),ca penkub dëkk ba ,nee nanu ci safari lasasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer,la sëñ Ibra mom Sëñ bi gane àdduna,ca rabiihul awali atum alsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak benn,mu tuxoo fa dem ca këram ga nekk ca kaw tund wa,ginaaw bi mu ko tàmblee defar ca weer wa ko njëkk,loolu nag mi ngi amoon ca bis bu njëkk ba walla ba ca topp,walla ya ko jege,dal di koy tudde Albuqhal Mubaaraka,di ci maanaa pàkk bu nu barkeel bi.

Ca ñaar fukk ak ñatt ci weeru sawaal atum balsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak ñaar,Sheex Abdul Ahad gane àdduna,ci muharram atum jalsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak ñatt,sëñ Abdu Xaadir gane àdduna,ci guddig àjjuma,ci fukki fan ak ñeent ci silqihda atum jalsasin ba tay sëñ Saaliwu gane àdduna,ci juroomi fan ci weeru kooru halsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak juroom sëñ Suhaybu gane àdduna di rakki sëñ Abdul Ahad,ci silqihda hasasin ba tay la sëñ Abdus Samad gane moom itam,ci rabiihus saanii atum jamsasis,di junni ak ñatti téeméer ak ñéen-fukk ak ñatt,la Sheex Murtadaa gane àdduna.

Mu tàmbli jumaa ji atum halsasin,di junni ak ñatti téeméer ak fan-weer ak juroom,jéego ci ñaari tànkam yu tedd yi ci guddig dibéer,weeru rabiihus saanii,fàtte naa nag bis bi mu ci tollool,ñu tàmblee gas dal bi (fondmang bi) ci ñaar fukk ak juroom ñaar ci jmaadas saanii atum walsasin di junni ak ñatti téeméer ak fan weer ak juroom benn.

Tabax gi moom ñu door ko bisub altine ci yoor-yoor,Sëñ bi wàcc ci biir paxum xuba bi,Sheex Muxtaar Binta nekk ci wetam,yor ndab lu def ban ( xam naa simaa la war a jubloo wax) , Sëñ bi jël jumtukaayu tabax bi (turéel) dal di tibb ci ban bi (simaa bi) , wax bismil laah,sotti,jëluw xeer teg ci ban bi (simaa bi) ,jëlati gasukaay bi door ko ci xeer wi,jàng :”wa isyarfahu ibraahiimul qawaahida minal bayti,wa ismaahiilu rabbanaa taqabbal minna innaka antas samiihul haliimu” mu di ci maanaa :ba Ibraahiima di yékkati dal ya, (mbaa ponk ya, mbaa fondumang ya),ak Ismaahiil,,naan :yaw sama boroom nangul nu ndax ya’ay aji dégg ji,tey aji xam ji.

Mu dal di fay juge,julli ñaari ràkkaa,ñaan. Alhamdu lillah,ligéey bi àgg na ci juroom ñaari at,ci teewaayu Sëñ bi ,mu julli fa ñaari iid yi(tëbëski ak kori),ñaari yoon ci lu wër ,ñatteel bi kay laay sikk,waaye julliwu fa àjjuma .

Sëñ Mbakke BUSO nee na li ko waral mooy moom kat masu fa’a yéenee sax mukk,(ku yéenewut a sax àjjuma waru ko), ka fa njëkk a taxawal àjjuma mooy Sheex Ibraahiima,rakkam ja,ci dëppoo gu mu ci def ak Sheex Mbakke BUSO,ak doomi Sëñ bi ak magi taalube yi,ndax ñoom ñépp a fa yéene woon a sax. Ndax Sëñ bi moo digaloon mag ñi ñu sanc ci wetam,bàyyi boroom kàttan yi man a ligéey tey tarbiyawusi ñu nekk ca tool ya,di ligéey di indi.

Dëkk ba mujj di dëkk bi gën a dund, ak jàkkaam yeek daaraam yi,ak jàngukaayi xam-xam yi,kaamilub Sëñ bi nag bis bu nekk ñu wàcce ko ci bunt këram ñeenti yoon,ñaari yoon ginaaw jullig suba,aw yoon ginaaw tisbaar,ak weneen ginaaw tàkkusaan,bu dee guddig àjjuma ñu wàcce ko juroom ñaari yoon,mbootum loolu moom,Yàlla rekk a xam,mooy jullig farata gu mu julli gu nekk, tolloo’kub kaamil bu nu koy wàcceel,li ko tàmblee suba gi ba timis,juroom ñaar yi niy wàcce ci guddig àjjuma gi tolloo’k geey ayu bis gi = julli gu nekk kaamil.

Bu dee lu aju ci mbindlu mi moom, da daan def képp ku mokkal te rafetum mbind,ñu daa ko bindloo ab kaamil ci lu tolloo’k ñatti weer yu nekk,walla sumun walla robo walla sulus walla nisif ci weer wu nekk,mu ànd ko ak ku mu nirool mbind,mbaa ñu mu nirool.

Naka noonu ñi ko daan coobarewoo di ko def ngirYàlla,ci donga yi nekk ci biti,ak ñi ñu daa fay ci waa-rëw mi ak naar yi,weer wu nekk daa nanu am lu tolloo’k ay téeméer ciy kaamili loxo,lu bokkul ak li nuy jënd ci yu móol yi .

Xam naa ne bis daal jëndandoo nanu juroom ñaari téeméeri kaamiil ci yu móol yi,ci benn yaxantukat,yu bokkul ak téerey xam-xam yiy dikk di juge ci wàll gu nekk,yu nu binde loxo ak yu nu móol,deesul delloo mukk ab téere,ak doonte dikk na fi ay yooni yoon,ak doonte danoo dagg ñaari wàll yi.

Mu bire ci loolu ne menn njënd mi mu daa def moom saraxe rekk a ko waraloon ak doonte da ko daan suturaal ci ron ay njëkk,te loolu bokkul ak li mu daa seddale way ñàkk yiy laaj,mu di ag ndimbal ngir Yàlla,ak li mu daa jox boroom dara ja yi lépp ngir Yàlla rekk. Leeg-leeg bis, mu seddale ci ay junniy junni,bokk na ci li gën a yéemey li ñiy gis, gis,te ñiy dégg, dégg ko,mooy daa am bisub ñaar fukki fan ak juroom benn ci weeru koor,atum bamsasin,di junni ak ñatti téeméer ak ñéen-fukk ak ñaar, mu dajale nu,nun mbooleem bindkat yépp,yu rafet mbind yi,te booba ab takk bu réy ci këyit a ngi ci kanamam,mu ne nu ndax xam ngéen lu ma leen di doye ? ñu ne ko déewalaay,mu ne leen këyit gii daal laa bëgg ngéen bindal ma ci ab kaamil,te du ñu ne ma mukk teru waa ngii,ndare bu da ngéen ma ne kaamil baa ngii !, ndax da ngéen ko def ?,ñu ne waa-waaw,mu ne nu jël léen këyit gi ,nu jël ko ,seddoo ko ci sunu biir.

Nga xam ne da ngay gis ku jël ñaari isib,bind leen ci bis,ak ku jël ñaar bind leen ,keneen maas leen, ñu tàqalikoo ci loolu ci yoor-yoorub juroom benneelu fan ba,ku nekk ci nun xam na la mu war a bind,ak baat ba muy yam,ca digganteem ak ka mu ko seqal, dunu ci dolli ,dunu ci wàññi.

Kaamil bi noppi alhamdu lillaah,ci tisbaari bisub juroom ñeenteel bi,ñu jébbale ko, Sëñ bi xool ko,gisu ci lenn lu ko naqàri,du mbind mu gën a rëy moroom ja,du mu gën a sew,du lenn daal . Mu dal di sant Yàlla bu baax,daa di ne ndax déggagun ngéen fi ku bind walla mu bindlu ab kaamil ci ñatti fan ? Nu ne ko déedéet , mu santaat Yàlla,dal di jàng:(( innii laa udiihu hamala haamilin minkum)) muy ci maanaa,man de du ma sànk jëfi aji jëf ci yeen .

Bokk na ci li gën a yéeme ci mbir yi,li ma daloon ,mooy man kat daa am bis may yër benn ci téerey siira yi (jaar-jaari yonnant bi),yaakaar naa ne téere boobu nuy wax “Zaadul Mahaad fii hudaa xayril hibaad” la,di ci maanaa yobbalub delluwaay ba muy ëlëg,ci jubug gën ji jaam yi,ba ma àgg ci ñi doon bindal Yonnant bi(j.y.m)maanaam ñi ko doon bindal wahyu gi ak bataaxel yi,ma lim leen ñu doon fukk ak juroom benn,Yàlla dogal ma ne naa xool nu itam ñi ci matal ab kaamil ci koor gii ñaata lanu woon ,far lim ba di benn,ca noona ma def ñaari woy,wenn wi ma ñaan ci Yàlla ci barkeb bindkati Yonnant bi (j.y.m),wi ci des ma ñaan ci ,ci barkeb bindkati Sëñ bi,am benn waay ci sama gaa yi ku ci tuxale ci man woyuw bindkati Sëñ bi te boolewu ci wu bindkati Yonnant bi (j.y.m).

Ginaaw bi ma xool ci buntub ligéeykati Yonnant bi (j.y.m), ñuy juroom ñeent,ag jigéeen it nekk ci,mooy Barakatu yaayi Ayman,ma teg ci xool ligéeykati kër Sëñ bi,ca koor googee amul lu dul ñu toll ne ñoom,te ag jigéen bokk na ci, mooy Awa Saar jèbbéerub Sëñ bi,ma defati ñaari woy,kuréel gu ci nekk wenn tax la’a jug. Waaye ñaar yu saaba yi lakk,te kenn jotu leen a tuxal,ñaar yu ligéeykati ak bindkati Sëñ ba’a ngii:

Bismil laahir rahmaanir rahiimi, Muhammadu Lamiin Joop Dagana wax na di woy turi bindkati Sheexul Xadiim ca at ma mu koy woy,di leen tollale ak bindkati Yonnant bi (j.y.m) niki mu nekke loolu ci Zaadul Muhaad :

(ci barkeb ñi jaayante ak ngën ji ligéeykati Yonnant bi,daan ko bindal,di ci gërëmloo aji des ji) maa ngi lay ñaan ag jaayanteek moom gu dëggu,ni miy gërëme ku jaayante ak moom te di ko samp) ( ci barkeb Andariyi ,boroom mbégal mi,Muhammad mi nu tudde Bashiir) ( may ma ay mbég yuy leeral sama xol,yu di naa ci mujj di mbégum sama dëkk) (fàtteel ma ci moom lu dul li nga ma tànnal,may ηoy (jàpp) ci wépp yiw wees ma tànnal) (may ko ci yaw ak ci jëwrini Yonnant bi(j.y.m),mébëti xolam,akug jiital) (yaw sama boroom nekkal ma cig aar,ci barkeb jaamam ba Muhammadul Amiin) (nga dundal ci moom sama xol ci ay xalaat yuy tax nga gërëm ma ,bu ko defee ma dib jaam buy sant) (na nga ko may ag aju (jébbalu) gu dëggu,ci darajay ki nga xam ne wommatal nga ko lu wér la) (ci barkeb Sharif Mafaatim mu dañ mi kumpa,muritam bi nu melal ci ngënéel lu rëy li) (teralal sama xol ci jikko yu rafet,may njariñ lu sax ñeel mbindéef yi) (rafetalal samag dégg ak samay wax ñeel képp ku ma waxal yaw boroom may gi) (nekkal ko, ci di ko may li mu bëgg,ci yiwi ñaari kër yi,mu doon ag am gu mat) (yaw sama boroom ci darajay Daymaan,Muhammadul Xayri boroom koolute gi) (may ma xol ak làmmiñ wu laab cig neen, ñu xam ko cig sàmm) (te ma taqoo’k ragal Yàlla ak jëfe lu may tax a dab ñu mat ña) (may ko mu tukkee fa yaw gërëm ak jàmm,juy des di ànd ak moom ba àjjana) (ci barke turandoo wa ,muritam bu lewet ba,doomi Sulaymaan, Sëriñ Joob mu mucc mi) (sarax ma saxug cofeel ak rafetal,ak ag ubbiku ci njàngum Alxuraan) (ak jëllale ak dëddu lu dul lu rafet,ak jege luy bijjee jëme cig giim) (màngal jëme ca moom ay barke yu sax,yu ànd ak sellug dund,ak mujj gu rafet) (ak ci barkeb muriit ba ,doomi Sahiid NJAANI,Muxtaaram mu nu xam, mi mel ni Marjaan) (may ma saxug noppi ci lu amul njariñ,tey wax lu am njariñ,te am njariñ) (may ma kepp ku ma xam,mbaa mu dégg ma sopp ma ci lu dul ag xeeb) (yéwenalal ko àddunaam ak diineem,te nga méng ko yoolub jiyaarkat yi) (ci barkeb mbokkam ma ak saxiixam (mooy koo bokkal nday ak baay) bu baax bi,Ahmadu Binta boroom yéwén gu nu xam gi) (may ma ag lewet ak xol bu yaatu,ba ma far nekk dib sang bu yaatu) (may ma ag cawarte akug toroxlu,ak muñ,te nga sellal samy barab) (na nga ko dundal yaw buur bi ngën ji dund,te nga def ko ci ginaaw bi muy dund ca àjjana) (ak ca darajay doomi Faadil jii dib bindaakon,Majamba SILLA kay taarub bindkat yi) (doxal sama diggante ak lu ñaaw ba fàww,ci lu bir ak lu làqu ak luy jax-jaxiloo) (dóoral kiiraayul wattu ba fàww ci sama diggante ak bépp saay-saay bu dul jaamu) (màngal ko yaw boroom bi,ci ñaari kër yi,barke buy aare ci ñaari gàcca yi) (ak ci barkeb weer wi,doomi Muxtaar mi ñépp xam,di Ahmad waaye nu xame ko ci turu Moor Alima) (may ma may taarub alxuraan,te nga may ma barkeb jàngale) (kaweelal sama yite ci luy rafetal sama saayir ,ak sama baatin ànd ak xol bu laab) (may ko yaw buur bi xam-xam ak jëf,ak teggiin yuy indi lépp lu mu mébat) (ak ci barke doomi Ahmadul Muxtaar,Ahmadu Awa ,sang bu nu tànn bi) (may ma ag baax gu ag bon dul toppati,ak ag nangu gu lamb dul jege) (bépp ayib bu man a gàllankoore ci lu baax,na nga ma ko faral ba ma man a am texe gu sax) (may ko lépp lu mu bëgg,ci yaw,te nga saxal bànneexam ci ngërëm ) (ak ci darajay ki fëgg te sax fa,di Muhammad mi niy askanale Wajja) (saxalal samaw làmmiñ ci wax aw yiw,ci waxtu wu nekk, ma noppi nag wëlif aw ay) (na nga siwal samaw tur ci mbindéef yi,te nga def ko muy siiwug yiw) (na nga ko may mébatam ci gii ak gee kër,di ku nu laaf ci mbooloom aji matale ji) (ak ci barke doomi Ahmadu doomi Warxa mu Siin mi,kooku mooy Ahmadu KAN boroom askan wu nu ñongal wi) (may ma ag aaru te setal sama lépp ci lépp luy taqal lu set) ((musal ma ci njuumte,may mag lewet,guy béel ak man ,ak jépp jëmm ju mucc) (na nga tawal ci kawam niiri barke yuy sax ciy yëngoom aki dalam) (ci barke ki niy wooye Ahmadu SAAXO,ki nga xam ne ab deram tër tilimalu ko) (may ma nooyug kanam gu sax,déet ag ñëkk,gu koy ñaawal) (na nga ma def may mbégum dëkkandoo yi,tey mbégum mboleem maas gi) (na nga ko def muy boroomug dund gu teey,na nga def it ag deem di guy teey) (ak ci darajay cam su nu sangal ,su gànjaru soosu,di Ahmadu mii nga xam ne aw dàkkantalam mooy Moor SIISE) ( may ma may kok du yékkati ab jéego jëme ko ci lu dul sa gërëm,yaw aji wattu ji ,ànd aki xéewal) (na nga ma dëdduloo ba fàww ci lu dul luy tax nga gërëm ma,dëddug ku nu teral) (may ko mu man a saxal li nga gërëm,ba man a làq sa gërëm) (ak ci barke doomi Muxtaar mi niy dàkkantale Shams,te moom dafa mel ne ab jant ciw nitam) (jeexalal sama xol ci yaw ,may boroomug dund gu sax ci yaw,tey boroomi yéene) (na nga ma tàggatal njiit yi,te def leen ñoom ñépp ñuy samay soppe ci yaw) (ak ci darajay aji ragal ji Yàlla ,aji yéwén jiy teet lépp lu bon,Ahmad doomi Saynabu ji) (na nga ma may ag ragal Yàlla ,akug wattu akug dëggu,ci wepp yiw , may sàkku ag dëggal ci yaw) (na nga teetal sama xol ag bëgg àdduna,bëgg gog da na man a lor kuy wutug jeex ci Yàlla) (na nga ko gindi ciw yiw wow da na xeeb ba fàww sottikug niir yi,te kenn du ko xeeb) (te ci barkeb Usmaan mi nga xam ne ñi ngi koy wooye Demba KEBE,méngoo ma te fegal ma njàqare) (yaw sama boroom,ba fàww,na nga ma aar ci lépp lu my ñaawal niki wor) (may ko yaw buur bi ba àjjana,muccug yaram ak xol) (asaf naa nag ñu baax lool ci bindkat yu siiw yu kawey daraja yi) (bañ gi ma leen bañ a indi doyadig pas-pas waralu ko,waaye kay li ma sartoon a def moo ci mant a boole keneen) (yaw sama boroom,ci seen barke ñoom ñépp,na nga nangu sama ñaan gii ba fàww) (na nga nu may mu tukke fi yaw,gërëm ak yërmaande,te nga rafetal mujjug ku nekk ci nun) (ci darajay Ahmad ligéeykatu Ahmad,xéewal ak mucc yal na ko Yàlla mi ko yatt saxal ci moom) (ak ñoñam aki saabaam ñiy boroomug soppante ci yaw,ngir sa jëmm,ci lu dul ngàññante) (li feek kuy ñaan ci barkeb ku àgg ca aji rafet jay yonni yonnant yi,mi ngi am li muy ñaan). Sama boroom yal na nga nu nagul,yaw ay aji dégg jiy aji xam.

Woy wi mu defal ligéeykati Sëñ bi ,di ñaan Yàlla ci seen barke,tollale leen ak ligéeykati Yonnant bi (j.y.m),woy waa ngi nii:

(yaw sama boroom ci darajay juroom ñeent yoy ligéeyal nanu ngën ji jëwrini Yonnant bi,kok kawe na képp ku ligéeyal Yonnant bi (j.y.m) ) (saxalal sa ngërëm lu màgg li ba fàww,ci ki nga xam ne ag ligéeyalam lu nu saxal la) (sama kerkeraan jëm ci yaw,kiy buntub samag tonowu,kiy far ñaawtéef yi,kiy dañal ag mbon) (ci darajaj Malaamin NJAAY,boroom farlu gi ci ligéeyal Aji ñeewant jiy musal jépp aji gindee) (may ma ag cofeel guy taqoo’k xel mi,ci jëmmi ki nga xam ne def nga ko muy leerug réew mi) (na nga tàggat samay cér ci ligéeyal ko,tàggatug ka ma jegeel ci sottig xéewalam ya) (na nga ma def ma sopp képp ku sopp,aji ligéey jii,na nga ma def may ku mu sopp) (wommatal ko lépp lu mu mébat ci ligéeykat bi (Sëñ bi) ,niki muy xéewalee) (ci barke sëñ Moodu FAAL,maa ngi aaru ci lépp lu ñaaw,ba fàww) ( may ko li mu mébat ci àdduna’ak allaaxira,te nga fegal ko ñaari gàcca yi ak ñaari sawara yi) (na nga ma may ag mucc ci kiñaan ak bañ ab jullit,te nga leeral sama pas-pas) (na nga def ci sama xol yërmaande ju may nooyale jépp aji wow ji xol,ba kero muy nooy) (na nga may képp ku aju ci man ngën ji ag wommatu ñeel ma,ba ma man laa gërëmloo) (ci barkeb aji lënkaloom ju lewet,di Sahiid SALL,na nga ma fegal mbooleem lu ag xuppe di nekk) (màngal ko jàmm ak xéewal,gu sax ba kerook tàbbig àjjana) (na nga ma ci maye ag jub gu sax ci lépp loo digale) (na nga ma may ag not sama bànneex,ak bakan,ak saytaane ak àdduna) (na nga seral ci man xolub samay dëkkandoo,ñu jub tey diisoo) (ci barkeb camus Mbakke si ko daa rootal,di Aboobakrin,na nga dolli samay xeewal) (sottil ci kawam ci dexi yiw yi,lol da na koy jañal lor) (te nga kaweel sama yite ci moom ci li ma bëgg,ci lu dul may gestu lenn loo bëggul) (na nga ma may ag toroxlu ci képp ku ma dajeel ci julliti jamono ji) (na nga màggal ci sama xol ak sama bët,bépp murit bu askanoo ci man) (ak ci barkeb ki mu lënkalool,di Sahiid MBAKKE na nga ma may mboot muy jooyloo képp ku ma bañ) (may ko ci sunu sëriñ bi,la mu bëgg,ci àdduna’ak allaaxira ,mu dëppo ak la mu bëgg) (na nga ma may ab ligéey ci darajaam,mu dib sarax tukee fa yaw) (na nga ma may barke bob ku dul man dana ma ci ñee,ànd ak xol bu neex) (na nga nu may nun mbooloo mi aju ci Sëñ bi,urma ju dul xottiku) (ci darajay mbokkam ma Ibra MBAKKE,dañalal ayib yi ag dañal) ( may ko gën ji dund aki yiw yu koy bégal ci gii kër ak gee) (na nga matal samag mbañ-rus,musal sama xol ci mbañeel,te kaweel sama daraja) (na nga musal samay cér ci lépp lu bakkan man a ragal,ak doonte du lu metti) (na nga barkeel ñeel ma,ci sama mbokk yi ci Yàlla,ak ñeel sama mbokk yi ci Yàlla) (ak ci darajay doomi Maryama mi kawe fa Sëñ ba,miy Siidi Kala) (yal na ko kiy namm, defal la mu namm,ca kaw nammeelam,moom miy aji namm) (na nga ma def may ku dëggu fa yaw ci li ma bëgg te nga gindi ci man aji dëggu ji) (na nga rafetal sama njort ci bépp murit bu aju ci sama sëriñ,te nga teetal ma ku nu dàkku ki) (na nga ma musal cig yàkkamti,te may ma ma jot gaa ya) (ci barke camus cam yi,Mbakke JUUF,mi amul lu muy ragal) (may ma ma nekk kuy ligéeyal Sëñ bi li feek ma’a ngi dund,kii nga xam ne ligéeyal ko mooy ligéeyal aji jiitu ji (di Yàlla) (tàbbalal ma samay xemmemtéef ciy xemmemtéefam,dammal samag dëddu cig dëddoom) (ubbil ma yaw buur bi cig ligéeyalam,ag ubbi gu may aj ca kaw ña koy ligéeyal) (na nga sellal ag dundam ci guddal ko,te musal ko ci ay gàkk-gàkk,walla nga def ko far lem) (ak ci barkeb muritam bu jigéen ba Awa,jèbbéeram bay saxal lu baax) (may ko texeg dund,aki néeg yu kawe ci ginaaw bi) (may ma bakan bu dal ci Sëñ bi,bu doylu,bu dul jeng jëm ci ku dul moom) (tàggatal ma jigéen ñi,te yombalal ma seeni mbir,te nga dagg jafe ga) ( yéwénalal ma ko te def ko muy ndimal ci topp la) ( na nga ma wisaareel ay doom yu góor yu baax ak yu jigéen,yu baax,yu am diine te ñong) (ñoñ da nga dundal ci ñoom lislaam,di ma fegal ci ñoom yeddaange) (ñoñ da nga leen di barkeel ci jox leen wërsëg wu yaatu,wu dagan,ba ca àjjanay Aji yaatu ji) (na nga def ngën ji julli,goo xam ne da nga ci nangoo sama ñaan gii,ànd ak sutura su rëy) (ak xéewal gu sax gu nu gëttal,ca ka ñu xeeñal ngën ji gëtt) (di Muhammad,ak kuréelam ba bépp,te nga wuyyu ma ci seen barke yaw sama boroom) (wuyyug nangu,ak ngërëm ak teral,guy tax may ku nu wormaal ci biir gaa yu baax) (jeexalal samag dund ci lu rafet ci seen barke,ñuy ñu ñu béelal,ca saxuwaay bu kawe ba (àjjana) ) Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliina wal hamdu lillaahi rabbil haalamiina.

Cig gàttal daal,dundug Sëñ bi ci Njaaréem gisunu ko fenn ci nettali ak jaar-jaari kenn ci sëñ su mag si,ci sariiha ak haqiiqa,lu dul li tegoodi ci yoon ci ligéeyub buur yi,muy jéem a def àttey yoon yi,di dagg loxoy sàcc yi,di jam njaalokat yu senge yi,ak door ñu sengewul ñi,ak di leen tumbrànkeel,te loolu wuute ak àttey àtte gi (nguur gi),ndax àtte yooyu daganalunu loolu,te dëppoowul ak seenuw doxiin wu mat ci fànni politig yi.

Fatabaarakal laa,ahsanal xaalixiin,mbooloo yi bari woon nanu ci moom ca Njaaréem,ba nguur gi mujjoon aaye ko muy dox ci nit ñi ci lu dul ag diggale,loolu taxoon muy wut ay palanteer yu ndaw,ci bunt bu nekk,ci wàlli kër gi gépp,nga xam ne fu mu tooge ba ubbi palanteer,ñaari nit ci ñu jege ñi man a gise bu nu jàlle ñeneen ñaar jegesi,noonu lanu koy nekke ci suba ba bëcëg ci li gën a bari,teg ca ñu nekkaat ca tàkkusaan ba timis ak lu ëpp guddi gi.

Amaa na leeg-leeg mu dem bind ag xasida,mbaa mu dem ca buntub jigéen ñay siyaaresi,mbaa mu dem nemmiku njaboot gi,su bëggee jàngale,da daan soril nit ñi bunt bi,ñu kuréelu,def géew,mu tàmblee tomb ci suuf ngir njàngalem sariiya ak haqiiqa,ci alxuraan ak haddiis ak hikkam,ak masalay fiq yi,amaa na mu jànglu xasida,bu ko defee wattukat yi jug jéeb,ci kàddu gu neex,moo xam danu koy xool,mbaa nu koy tari,xasida yooyu daawunu weesu tagg Yàlla ak Yonnantam ba,bu ko defee lekk yi ak naan yi,di daw ci diirub jataay bi,lu fa waay soxla rekk ci àdduna ak diine.

Nguur gi aayeeti ko mu dem ca jàkka ja,ba mu mujj def jàkkam ca fu jege kër ga,ndax moom kat daawul wuute jullig mbooloo ca jàkka ja,du guddi,du bëcëg,du tàngoor du sedd,du xiinadi ,du xiin, mu bàyyil nit ñi ci kër gi aw yoon wu nu man a jaar julli ji,moom mu wut aw yoonu boppam,wu koy àggale ca mihraab ba,du nu ko gis mukk,ndare bu daa taxaw ca mihraab ba,ubbi bunt bi ndare palanteer bu sew bob du tee ñu seen ko,ci mbooleem julli gi, bu ko defee mu daa tëj bunt bi bu noppee ci julli gi,daan ko ubbi it ngir jàngale.

Nu aayeeti ko muy dox ci yoon yi,te kat nit moom ku soxlawoo loolu la,ba mu mujj aajowoo sàkk ab palanteer bu sew,te sori ci làkkub kër gi,digganteem ak làkk bi aw yoon wu yaatoo ñeenti xasab a nga fa,mu fay jaar bu bëggee doxontu suba ak ngoon,walla guddi.

Nga gis nit ñi ñu wër ko,ci ginaaw palanteer bi,di dox ànd ak moom,di taxaw bu taxawee,ak fu mu jublu,amaa na mu taxaw ngir tufli leen bu noppee ci ñaan gi,mbaa mu jàngal leen am masala,jàng gi it da daan bir,loolu lépp ab politigam la woon ngir soxla gi ko nit ñi soxla,ngir jariñu,ak gindiku,ak soxla gi mu leen soxla ngir jariñ leen ak gindi leen,bu teelut a lijjanti loolu ñu lor ko ci taxaw ci kawam.

Seere nanu loolu ndax kat bis dagg nanu ko ci baaraamam,dagguw dàllam it,ngir xér ci laal jëmmam ju tedd ja . Waaye buuxante bu metti bi mooy waral ñuy dal ci kawam,ba koy gaañ ,te dunu jublu loolu . Bu ko defee muy gaañu ci loolu ndax moom jëmm ju tuuti,te doyadib bind la waaye di ku dëgër ca Yàlla,du yoqat,te du sonnu,ba bi ko mbirum Yàlla mi dikkalee,ñu tànn ñaar ngir ñu toppatoo ko,ñuy ñaari muritam yi Muhammad mom Abdu Rahmaan Attandaxii, mi faatu,ci ginaaw bi ci sawaal,atum bahsasin,di junni ak ñatti teemeeer ak juroom ñaar fukk ak ñaar, yal na ko Yàlla yërëm, kooku moo ko doon toppatoo ak mbokkam mi bind araf yii,Muhammadul Lamiin JOOB ,ñu duggal ko ab wata guddig àllarba yobb ko Tuubaa,ci pexe mom danu koo def ngir làq ko nit ñi .

Ñi ko doon gunge juroom lanu woon,sëñ Bashiir moo leen jiite woon . Mu dal di yonnee ca mbokkam ma,sëñ Muhammadul Faadal,xalifab ñaareel bi, te ca jamono jooja,ma nga woon ca wurumub dëkk ba,ca wetu Tuubaa , mu yonnee ca Sheex Ibraayma ca Daarul Muhtii,ak ca sëñ Mbakke BUSO,ca dëkkam ba ca wetu Tuubaa,mu yonneeti ca mag ña nekkoon Tuubaa, ñooñu daje ci diir bu gàtt,ba nu matee ñaar fukk ak juroom ñatt,sëñ Mbakke BUSO jiite leen,loolu lépp a ngi ame woon ci làqu gu tar,ngir bañ fitna, ñi ngi noppi bi fajar daataa jot,def fa ab néeg bu nuy tëj ak a tijji, bi ko nit ñi yëgee bi suba jotee,coow li jolli,bul laaj nag wax yeek jëf yi,loolu lépp bi muy am sëñ Moodu Mustafaa ngi Njaaréem di xamal nit ñi ak di leen dalal .

Bi nu noppee ci waajal gi,ma génn ci bunt bi ma njëkk a jot,laa daje ak kenn ci taalube yi,te booba moom yëgutoon li xewoon,mu ne ma man kat biig dama laa gént ,di la laaj Sëñ bi, nga ne ma: (( wamaa Muhammadin ilaa rasuulun,xad xalat min xablihir rusul)) muy ci maanaa Muhammad du lu dul ab yonnant,bu fi ay yonnant jiitu. Ma ne ko ni nga ko gente la deme de,duggal,bi mu duggee,tàmblee yéemu .

Ki boole téere bi defal na ko marsiya (marsiya = xasida gu niy waxe jëf ju baaxi ku faatu) ci ay bayit mooy bi nu njëkk a defal Sëñ bi, bi mu fi jugee,mi ngii:

(Sëñ bi wéy na jëm ca buur ba mu daa jaamu,ndax kat xamoon na ne fii kenn du fi des) (mu wogu di sàmm ndigali Yàlla yi,ngir ngërëmam tey teet li mu tere) (di tere lu bon tey digale lu baax,di def lu nu xam te du ca ëppal) (nekkoon na kenob diine ca bisi dundam,ñoñam de,moom lanu jublu woon ci sàkku dëgg) (gisoon nanu ne mooy seen baay,bu nu war a jox àqi baay,moom itam,mu gisoon ne àqi doom lu nu leen war a jox la) (mooy ki daa fàtteloo jirim yi seeni cosaan,daan faye aw ay ciw yiw ) (moom dey naataange la woon ñeel ñu ndóol ñi ko daa dikkal juge fu nekk ngir xontu) ( bu daganoon nu jote ay bakkan de,nu def ko,waaye ay sang jiitu nanu ko,juge fi,te kenn jotu leen ) (waaye de na la woor ne bu fàddoo wëlif nu ànd ak jëmm ja tam,du tee aw yiwam wiy dolliku du fàddu mukk wëliif nu) .

Buurub woykat yi it ca jamonoom ak wàllam,di Muhammad mom Muhallaa Alhasani defal ko moom itam marsiya bu yéemee yéeme,mi ngii: bismil laahir rahmaanir rahiimi,wasallal laahu halaa nabiyihil kariim, Muhammadu mom Muhallaa,mi nu gën a xame Naana,mi ngi wax di marsiyaal Xutbub Xawsu bu boroomam bu mag bii di Sheex Ahmadu Bamba mi nu xame ci turu Xaadim,yal na ko Yàlla labal ci géejug yërmaandeem,te sarax nu ci barkeem, aamiin:

(yoonu dee mooy dayob kuy dund,dund daal lu dul dee toppu ca) (nit ñépp a ca jëm nag (moom dee), bu bettewul ci bëcëg gi ,def ko ci guddi gi) (moom daa mel ni ab rawante bob mooy bant ba nu samp jëm ca,ku ko jéggeegul it ca nga jëm) (ndaw dayo bii di bu yéeme !,moom de mooy saxuwaayu seeni mbooloo,tey dajekaayu seeni kuréel) (lu waay tàyyeel tàyyeel du tee mu jot boobu dayo,lu waay sawar te bariy jumtukaay du tax mu romb ko ) (dee daal daa mel ni ndabul nganale lu nu woo ñépp,woote gu matale te yaatu) (bu aji ligéey ji wuyyo wooteg dee gi ti,te kenn bégu ci ) (jotoon naa wuyyu cig njëkk wooteb Yàlla bi te booba gindikat yi jugagun) (mu daa wuyyu wooteg képp ku woote jëme ci yoonu kawe ak teddnga ) (mu nekkoon di kiy woote ak a gindee jëme ci ngérum jàmm ak mucc) (moom de bi sàmmkat yi ruuralee seenum càmm,daa féeteek aji wattu ji,sàmm am càmmam) (teg nanu ko lepp lu diis lol yanukat ba gën a mag gën a dëgër àttanu ko).

Bokk na ci jikko yi mu ko limal: (ak dagg buumi ñaawtéef yépp,ci lu dul gestu guy gàllankoor walla yoqat) (ak dundal xol yi ci sikar ak waaraate yi rafet ci waaraate yi) (yéem naa ku mel ni moom, ci niir ak tawub dundalug xol, bu nuy màng, jëme ca suuf yu bekkoor ,yu naatadi yi)

Mu neeti: (ki ko tànn daal a ko woo jëme ko ci teraanga,ngir fay ko jëfam yu baax yi) (moom itam mu wuyyu,ba mu demee fekk fa la mu doon mébat,ci ngënéef yu gànjaru yi) (mu mujj ñàkk gi nu ko ñàkk,di lenn ci way jommale yi,te di am mbamb (xew-xew bu njàng) mu lëndëme ni tàggeg tàggekat yi) (Abdul Xadiim daal wéy na,di ku nu santi jëf,di ku ay mbootam lenni gàkk-gàkk nekku ci ) (Abdul Xadiim daal wéy na, te bënul lu dul bëtub ay may aki xéewal) (wari fas daal du woon yitéem, te ji ay tàndarma yuy dott it taxu ko woon a jug) (dundug buur yi de dug dudam ,ak doonte day joxe ay bóoli yu nu feesal) .

Tëj:

Ñu tëje ko ci waxtaane lenn ci li ko Yàlla may ciy xéewal yu kawe njort, ginaaw bi Yàlla sooyalee seen ñatti pexe ya,muy ray ak tëj gu sax,ak tumbrànkeel gu sax . Bokk na ci li ko Yàlla xéewalee ci safaanub ñatt yooyu - Sëñ bi nee na - def gi mu def ati tumbrànkeem di lu juge ci nattub yonnant yi ak seeni balaa,yi leen seeni noon daa teg,mi ngi wax ci loolu: ((bokk na ci xarbaaxi Yonnant bu nu gënal bi,yal na xéewali aji kawe jiy gënale nekk ci moom) (bokk na ci xarbaaxam yooyu:nekkug sama ati tumbrànke gi di lu nu génnee ci jamono ju jàll ) (ñu niroole ko ak la xewoon ca diggante yonnant ya ak ña nga xam ne ñoom ñépp ay kàccoor lanu) (yal na xeewal ak mucc sax ci ñoom,ni Yàlla dàqe ak lëndëm ci yonni gi mu leen yonni) (ag kéemtaan dey feeñ na ci sama tumbrànke gi,ni mu feeñe woon ci Yonnant bi moom mi gindee) (loolu mooy ñi sabablu woon tumrànke gi de) (ñee nañu ñi ko sababluwutoon ci noon yi,te Yàlla notal na ma leen ) ( ñi ko sabablu woon de dunu tàbbi àjjana te sawara lanu jëm ) (te du nu am li feek tuubunu,lu dul ngën jaa saxi njàqare).

Mu bëgg a wax ne Yàlla màg na te kawe,niroole na ci ngënéelam, li amoon ci sama diggante ak noon yi,niroole na ko ak li xewoon diggante yonnant yi ak seeni noon,ciy nattu,mu niroole la nu ca ame ciy xéewal aki njariñ lu nëbbu ak lu feeñ,fii ak fa nu jëm,mu niroole loolu ak li ma ci ame ciy xeewal aki njariñ .

Mu tollale loraangey àdduna ak ju allaaxira ju noonam yi tuubul ak loraangey ña tuubutoon ca seen noon ya. Te ña sababoon nattu yooyu ak fitna yooyu,ñee nanu ñi ci àndutoon ak ñoom ,li Yàlla di wax naan: ((wa yawma yahaddus zaalimu halaa yadayhi,yaqoolu yaalaytaniit taxaztu mahar rasuuli sabiilan,yaawaylataa,laytanii lam attaxis fulaanan xaliilan,laxad adallanii hanis zikri bahda isjaa anii wa kaanas shaytaanu lil insaani xazuulan) muy ci maanaa : bis ba nit di màtt loxoom wiccax,naan aka neexoon ma topp Yonnant bi,aka neexoon ma bañ a def diw xarit,moo tax na ba ma réere alxuraan ,ginaaw bi mu ma dikkalee,te shaytaane dey day gàccaal nit rekk. Mu ne moom aaya woowu seere la ci Yonnant bi (j.y.m) ak yonnant yi jàmm yal na nekk ci ñoom, tey kéemtaan,waaye di seere ñeel ma tey karaama,kon alhamdu liilaah,sant naa ko te gërëm ko,ci dëppale gi.

Bokk na ci mbóoti sama tukki bi,xéewal gi ma Yàlla defal muy juroom ñaari karaama,tolloo’k kiimaani Yonnant bi (j.y.m),ñooy: Yàlla notal na ma samay noon njëkk samag feeñ, may ma xam-xam bu jugewul ci njàng, Yonnant bi (j.y.m) puukarante ak yonnant yi ci sama tumbrànkeg fukki at yi ak ligéey bi ma ko ci ligéeyal muy ligéey bu sell, Yàlla def ma may koo xam ne képp ku texe da na ko sopp,te naagul ibliis ci man ak képp ku nu rëbb, mu def ma may ku malaaka yi sopp,ak way gëmi jinne yi,def it julliti jinne yépp aju ci man ngir jëmmi Yàlla,mi ngi wax sax ci loolu naan:

(( juroom ñaari kéemtaan ci yu Yonnat bi,feeñ nanu ci man,te am naa samag ñaan ca seenug njëkk)) ((sama boroom ci barkeb ku nu tànn ki ,notal na ma noon yi,njëkk samag feeñ,te du ma dajeek kuy noonu)) ((Yàlla may na ma xam-xam bu jugewul ci njàng,te indil ma Kun (mooy nekkal mu nekk) )) (( Yonnant bi puukarante na ak yonnant yi yépp,yal na xéewalug Yàlla nekk ci ñoom)) (( ci sama tumbrànkeg fukki at yi,ñu ànd ak ligéey bu sell ñeel boroom nekk gi ak jiitu gi (Yàlla) )) ((képp ku texe da nga ma sopp ba fàww,ngir jëmmi sama boroom miy aji delloo,sopp gu àndul ak ag mbañeel)) (( Yàlla miy aji dimblee,naagul na ci man ibliis ak képp ku nu rëbb )) ((malaakay aji tedd jiy aji des,danu may bëgg ngir jëmmam ja,ànd ak texe gu dul dagg)) ((ñi gëm ci jinne yi,sopp nanu ma ngir jëmmi aji des ju may defali xéewal))

Mu waxaat ci beneen barab:

((jinne yi gëm ci sama jamono jii aju nanu ci man,waxu ma, ñi gëmul))

mu neeti:

(( mayal ñi ma ligéeyal lu rafet,moo xam malaaka la,mbaa ku nu làq (jinne) walla nit))

Nu xame ci loolu ne moom kat am na ñeneen ñu dul nit ñu koy ligéeyal,mu waxati ci beneen barab:

((Muhammad may na ma ag not,képp ku dëkkaale ak moom du nu ko not)) ((samag texe day des ci lu dul rékki,Yàlla notal na ma mbooleem ay noonam))

Mu waxati:

((kuy léewtoo jubluwu ma,bëbbug (xeewali)sama boroom lu feeñ la,ibliis de du léewtoo’k soldaari aji tedd jiy kenn))

Mu neeti:

(( wattu naa lu nu ñogal wëlif téere yi,kon bul tàyyeel ci ligéeyal ma)) (( Yàlla màngal na ma mbooleem xam-xam yi,aji tedd jii de baax na , mooy aji dañ ji kumpa,tey aji xam ji)) ((kiy def lu ko soob de nocci na xam-xam yi ak seeni barke ñeel ma,ci nekk ngi mu nekk di aji xam)) ((ki nga xam ne wommatal na ma aw yiw,wuy sellal xol,te yiw wa wommatu de,déeyaale na ak man)) ((Yàlla xéewale na ma jàngale,di naa gindi ku réer ak ku am xam-xam)).

Bu dee ni mu bëgge ñi gëm nag ak ni ko ñooñu bëgge,loolu moom jarul sax nu ciy wut lu ko seere,ndax mbir la mu niy gis,di jàkkaarloo ak moom,muy barig jariñ gi mu leen di jariñ ,ci xam-xamam ak alalam,aki mbóotam,aki ñaanam, du amadi solo ñu tudd cis lëf ngir barkeelu ci,am na fu mu naan:

(( jéggalal jépp aji gëm ju góor ak ju jigéen,jéggal guy saxal wépp yiw)) ((jéggalal bépp jullit bu góor ak bu jigéen,jéggal gu leen di musal ci tooñkat yi)) ((jéggalal jépp aji rafetal ju góor ak ju jigéen,jéggal gu leen di wommatal lu rafet)) .

Mu neeti ci Matlabus Shifaayi:

(( na nga saafara mbooleem jullit ñi,ci fii,te nga fegal leen tiit ak njàqare ca fee)) (( na nga leen musal te jàmmal leen,te ñeewant leen,te bul fayyoonte ak ñoom ngir barig seeni bàkkaar )) ((ndax ñoom kat bu nu la moyee ngir sàggan,du nu la bokkaale ak kenn)) (( te seeni yaram àttanuñu sab nattu ,ngir seenug doyadi)) ((seeni xol de du jéng jëm ci ku dul yaw,ba fàww, ci fii ak ëlëg )) ((waaye nekk gi cér yi nekk di ban,bijj na leen ,yobb leen ci gën jaa boni bon-bon yi)) ((bul fayyoonte ak ñoom ci lu la dul wàññi,may leen li leen amal njariñ,te amalu la njariñ )) .

Mu waxati ca xasidaam ga tudd (Fastajaaba lahum rabbuhum):

(( ci darajay Mustafaa,wuññilal xeetam wi njàqare,yaw mi génne sa jaam bii ca njàqareem la)) ((bindalal Yonnant bi xéewal ak mucc,ak ñoñam aki saabaam yiy boroomi teet lu bon )) ((musalal aw xeetam ci darajaam ak seen daraja ñoom ñépp,yaw kenn ki ma notal)) ((wuññilal njàqare ñi di boroomi gëm,yaw miy kiy maye ag koolute)) ((yaw aji rafet ji,àggaleel ci mbooleem jullit ñu góor ñeek ñu jigéen ñi,jàmmi boroom mbindéef yi)) (( bindal ag sell ñeel mbooleem way rafetal yu góor yi ak yu jigéen yi,yaw mi méngoo way gëm yi)) .

Ak lu bokkul ak loolu lépp ci li nu manul a lim,ci lii di wone bëgg gi mu bëggal xeetu Yonnant bi (j.y.m) li mu bëggal boppam,mu jagleel ci boroom jagle yi,geneen bëgg gu gën a tar .

Dégg naa ko bis (g.y.m) mu naan :man dey jamonoy samag ndaw,dama daan tànn ci giir gu ne ab xarit,daan ko jagleel ci sama xol ag cofeelug boppam,ni ma tànne woon ci giirug Daymaan,Muhammad Yaddaali,boroom téere bi nuy wax (Zahabul Ibriiz),ci giirug Tandax ma tànn fa Muhammad FALL mom Mutaali,ci ñoñ Haaj ñi, ma tànn fa Ahmadu doomi Muhammad,boroom (Jawharul Munazzam).

Bokk na ci li mu nu nettali ci cofeelam gu yéeme gi ak mbëgéelam gu tar gi ñeel ñennat ñi ci jullit ñi; nee na bi mu nekkee ca tumbrànke ga ca géej ga,daa yëggoon ne sunu mbokk mi Muhammad SEKK,mi nu gënoon axame ci turu sëriñ Làmbañ,ak sunu mbokk mi Muhammad JOOB,ñu gënoon koo xam ci turu Majoob Aram Seriñ Fittu, tubaab bi da leen a yobbu woon ngir tumbrànkeel leen,xawma fan nag,bi mu ko defee mu amoon lu ko naqari lool,nee na àdduna dal di lëndëm fi man,sama jamono nëx ngir ñeewant leen,ndax kat bëgguma ñu nattoo leen lu leen di tax a ñàkk seenig gëm,mbaa mu koy rékki ci ñoom,yal na nu ci Yàlla musal,ma dal di ñaan Yàlla ci seen mbir moomu ne: (( yaw gën ji aji jéggaley bàkkar,tey gën ji ku man a musal ku nu jàpp)) ((na nga dindi jullit ñi cig njàpp,te musal leen ci luy waral sikk )) .

Ñaari bëyit yooyu ñi ngi ci xasida gi tudd ((wa àmmaa maayanfahun naasa fayamkusu fiil ardi)),man naa am bi muy bind xasida gi la ko seenub xibaar dikkal,mu dal di def ñaan gi.

Bu dee bëgg gi ko ñi gëm te di boroom jagle bëgg ,loolu moom lu nu xam la te siw,seereel nanu ko yiw wu nekk,ak wilaaya gu nekk ci barab bu nekk .

Doggantal : ci seere gi ko ñu mag ñi seereel ag màgg ak ag wilaaya[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Xoolal Sheex Siidiya mii ak màggam gi mu màgg lépp,téewul mu tegoon Sëñ bi fu mu tegul kenn,bind na ci moom,woy ci moom wesar ci moom,bu waxutoon lu ëpp ñatti xasida yii tam,ci xasidaam yu bari yi,loola da na doy,ñooy yii:

(Sheex Ahmadu daal xéewal la ,gu Yàlla jox mbindéefam yii yépp) (ag cant ñeel na Yàlla mi ngi xam ne ay xéewalam jaamam yi manunu koo takk,mbaa nu lim ko) (boo dajee ak moom,fekk ñuy yekkati raayob teddnga,da nga ko gis mu alawtiku ko ci loxol ndayjooram,ànd ak di tudd Yàlla ) ( bu gisee bis jikko yu rafet yi ñu dëdd leen,day dogu jublu ya ca gën a mag) (suuf su ko dëkkal daal ,ab lolli bu ko ñàkk a ndàndal du tax mu lor ko ) (miskiin yi ngir sa baax gi fàtte nanu seeni dëkk,ba mujj na sa koom mii de lanu jàppe seenum koom ) (seen mbooloo yooyu de buy daje ak ñoom mbégte mu rëy te dëggu lay àndal,nga xam ne da ngay jort sax ne,lu toll ne li mu leen di jox ciy xéewal rekk,lanu koy jox )) (( mbooloo yépp seere nanu nekk gi mu nekk di ku baax,ku tedd,kuy jaamu Yàlla te dib tuubaakon )) (( bokk na ci ñi gisoon jariñ nit ñi di farata,ci jamonoom,tey ci ñi daan tudd Yàlla )) (( dogal bu ñëw mu nangu ko te gërëm ko,xam ne Yàlla’ay ki ko dogal )) ((bu kuy tëñëxu cig lëndëm di tëñëxu it,moom genn muuraay du man a muuri bëtam wëlif dëgg gi )) ((kersa du dañ di ab rootukaay ci sab hadara,bu ko defee yiw yi di noyyi ci gelawam lu sedd li)) ((jaam yi de ,dox gi nu dox jëm ci moom,seeni aajoy àdduna’ak allaaxira’a ko waral))

Ñaareelu woy wi,mi ngi ko def bi mu tàmblee tabax jumaay Njaaréem ji,mi ngi nii:

( jàkkay Sëñ bii de mooy jumaay barke ji,tey barabub ay yiw ak yërmaande ) ( fa lanuy jéggalee ñaawtéef yi,ña koy siyaare it seeni yiw danu koy ful) (boroom fondumangub ragal Yàlla la ,ak miiri jëf ju baax ak teraanga) ((jëf ju sell ñeel boroom mbindéef yi,ci yeene,te jëf ya’a ngi ci yéene yi) (boobu barab de,làquwaayub ku bëgg a taxaw guddi ngir jaamu Yàlla la,kon de bu baax la,làquwaayub ñu ndool ñi de làquwaay bu baax la) (bu fa julli ngir Yàlla amee ab néeg it,du tee muy neegub jokkoo ngir Yàlla) (xamal nanu fi julli ay waxtu,waaye jàkka jii de am na lu dul waxtuy julli rekk) ( nit ñi danu koy jublu,ànd aki xol yu boole lu tàqalikoo ciy yeene) (ab kuréel bu fay ñëw ngir julli,ak beneen bob mbiram mooy asaka ) (Yàlla digale na ñu yèkkati ay néeg,yu tedd ci kaw yeneen néeg yi,ngir turam wi) (yal na Yàlla faye tabax gi, ay kër yu niy tabax ca àjjana,ay jigéen nekk ci) (Sëñ bi daal xéewal la,gu Yàlla joxe,di kiimaan ci kiimaanam yi) (nit ñi de xam nanu ko ci penku bi ak ci sowwu bi,mu dib sang ci taax yi ak ci kaw gi ) (mi ngi bokk ci tabaxkati jëf ju baax,te loolu lu néew la ci nit ñi) (dellu nanu seeni kër,ànd akug cant,gu toll ne cantug ku soxla woon am ndox Yàlla jox ko dexug Furaat) (yal na ko Yàlla wattu ci wattoom ga akug kaweem,aki doomam yu gó0r ak yu jigéen) (ak ñoñ néegam bu kawe bi,mboole seen,ak muritam yi juge ci wàll yépp) ((te Yàlla may ko “Xurratu Hayni” (am mbégte) ci àdduna ak allaaxira) .

Ñatteel bi ci yu mujj la,da fa mel ni danu koo wonoon ne ab digam daa jotoon :

(burub nit ñi yal na la fay ngën ji fayam,te dolli la ci teralam gi ak mayam gi) (te mu desal la fi,ngir mbindéefam yi nga xam ne,sag des moo di seenug des,xéewale la mooy xéewale leen) (kuy jéem a tolloo’k yaw bu woomlee tam,nan lay yéege ba jot ku ko gën a woomle fopp?) (nan lay yame kok am koomam mi ngi ci joxe ko, ak kok mi ngi ci denc ko ak làq ko? ) (ndax kuy jënde alalam ab yool ak ndam,da na mel ni ku nuur ci njaayam ma’ak njëndam ma ? ) ( cam la su teddnga di feeñ bu feeñee,bu làqoo,sooroolub njèkk làqu ) (bis bu Yàlla dogalee tenqam gëbum koom,da koy dal di seddale way yalwaan yi) (day jàppe jeexug alal,akug naaxsaayam, muy di ko jéem a màggal ak a dajale,joxe ko ci yoonu Yàlla it mu jàppe ko muy li koy yokk ) (bariwaa na ay gawar yu mel ni ay cati xéej,naaga (giléem) yi daw ak ñoom,jéggi ab àll,bob suuf sa daa mel ni asamaan sa ) ( ki leen di wommat,di yaakaar ju rafet ji nu am ci moom,ki leen di gindi di kaweem gu rafet gi ) ( ñu jublu ,bu nu àggee ca ëttam ba,fajug seeni aajo ci lu dul nëx-nëx,ànd ak am lu leen ci wóor ) ( ayibam daal du lu dul jaamu Yàlla,ak jariñ nit ñi suba’ak ngoon) .

Aji seere ju mel ni moom cig ragal Yàlla,ak am xam-xam,te di ko jëfe ak sax ci sunna,doy na sëkk. Xam na aw yiw,ak barabam,dal di koy laabiire jaam yi,tegtal leen ko,yal na ko Yàlla fayal lislaam ak ñoñam.

Xoolal ku mel ni Sheex Sahdu Abiihi,wàlliyu wu ñépp nangulug wilaayaam,bokk ci néegub teddnga,di ci askanu Yonnant bi(j.y.m),xoolal ku mel nii wax ,bind,wesar,woy.Bokk na ci li nu ko askanale ci lénn ci ay bataaxelam,ginaaw bi mu santee Yàlla ,julli ci Ynnant bi,da ne: ab nuyyoo ngi juge ci man jëm ci Sheex Ahmadu Bamba,yal na Yàlla rëbb ku ko bañ,te rëbb ku ko waral,ma lay ñaan nag nga bañ maa fàtte,te bañ a fàtte xeetu Yonnant bi (j.y.m) .

Lii nii juge ci sang bu màgg bii,ag laabiire la ñeel xeet wi,di it ag tegtale gu muy tegtale aw yiw, di ko junj,junj gu nooy,te làqu. Mu ne ci ag xasidag ndokkeel,bi Sëñ bi dellusee ci tukk bu nu barkeel ba,ginaaw bi mu defalee Sëñ bi ag seede ci bayit,wu yàgg,muy:

( jamono giñoon na ne da na fi indi ku mel ni moom,waaye ee jamono,sa ngiñ gi amul de,kon demal kafaara ji ) .

Mu neeti:

( tubaab ya’a ko jële woon ca mbellam ya,mu mujj ca géej yooyee di wurusu ngalam ) (mu feeñe ca xori géejug mbàmbullaan ga,di wurus wow ag leeram akug xuy-xuyam tax na ba bët yi gëlëm) (mu di weer wu leer,wu fàddu ci sowwu bi,feeñaat ci dib jant cig yékkatiku ak ak tasaaroo ) (yéemu naa ci wurus wii nu jaarale cig nattu, mu mujj di wurusuw yaaxoot,wu deesul jaayante ab taar ak moom) ( yéemooti naa,na ngeen xam ne buntub tuub ak njéggal de,ubbi nanu ko,ñeel bépp murit,bu sàkku ci moom ag dëkkaale )) (ag ndokkeel ñeel na diine jii, nga xam ne mujj na di puukarewu ci yaw,ngir mbégte ak ndamu ) . Esklëy,eskëy,xoolal ma wàlliyu wu tedd wii,ga xam ne làqul lu dul ag dëggu .

Xoolal ma wàlliyu wii,Sheex Mustahiin Alkumayli,sunu mbokk mi ci Yàlla ak ci Sëñ bi,Alhaaji Muhammad Abdul Laahi doomi Ubaydur Rahmaam,nee na ca téereem ba tudd (( Annafahaat Almiskiyya Fil Xawaarix Almbàkkiya)),: bi tubaab bi tuddoon Kaylaan - yal na nu Yàlla musal ciw ayam - laajee Sheex Siidiya,lan mooy àtteb jiyaar ji jullit ñi di def ci nasaraan yi,ci jamono jii,ndax lu dagan la ,ginaaw nasaraan yi dunu leen def lenn lu ñaaw ci seen diine,ak li ni nu leen di ëpp doole lépp,ak li jullit ñi di néew doole lépp ? Mu tontoo ko la mu ko tontoo ,mu jébbal tontu bi Sheex Sahdu Abiihi,mu gaaral ko ko,bëgg mu wax ci, mu bind moom Sëñ bi,lu mel ni li Shayxaani (Buxaari ak Muslim) bindoon,jëme woon ko ci wàlliyu yi ak boroom xam-xam yiy jànkoonte ak ñu dul ñoom muy: ki bind araf yii de Yàlla def na ko muy buntub texe ak mbégte ak njèkk . Dara ci loolu jubluwu ko,ndax moom kat féex na ci fitnay àdduna ak allaaxira,atun kasasin di junni ak ñatti téeméer ak ñaar fukk,bu feexutoon ci fitnay àdduna ak allaaxira,kon mu indi tontu bu ñatteel,waaye moom mujj na ,bokk ci ñi ñu wax ci ñoom (( bal ahyaaun hinda rabbihim yurzaquun)),muy :ñoom de fa seen boroom ñuy dund lanu,ñu leen di wërsëgal, loolu ki ko wax a ko bind di,Ahmadu mom Muhammad,mom Habiibul Laah,yal na ko Yàlla mu kawe mi musal,te nekkal ko te méngoo ko. Subhaana rabbika rabbil hizati hammaa yazifuun wa salaamun halal mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina .

Dégg naa Sheex Mustahiin mu naan: loolu de dëgg la bu dutoon dëgg du ko bind. Dégg naa ci Sheex Bashiiru mom Sëñ bi,mu nettali jële ca Sheex Mustahiin mu ne: man de yéemu naa ci mbirum Sëñ bi,toog nanu ak moom bis ,di mbooloom boroomi xam-xam,yaakaar naa ne Abdul Laahi Ibnu Muxtaar Alhaaji,ca la woon,mu tàmbli di wax ak ñun wax ju yéeme,ju dugg sunu xol yi,ñu bégg tey dëggal te xamunu sax dëgg-dëggi li miy wax,waaye mu jàpp sunu xol yi,nu xame ca ne ca Yàlla la juge.

Sunu mbokk moomu nu tuddoon nee na ci téerem bi nu tuddoon :

bokk na ci karaamay Sëñ bi,yal na ko Yàlla wattu,dellusi gi mu dellusi bawoo ca dun booba,nga xam ne kenn la fa tubaab yi masul a yobb mu dellusi . Sànni nanu fa nit ñu bari,waaye de kenn a ci dellusiwul,loolu mooy firnde li gën a mag ci ne moom demam gi moo ko tànnoon,dëgg naa ne Sheex Mustahiin mom Talha Alkumaylii,nee na : moom de bu bëggutoon a dem du dem,dunu ko man a génne it dëkkam. Te kooku doy na ndëërlaay. Sëñ bi bindal na ko ag laabiire gu mu tudde, “Diyaafatul qudoos,wa laa yashummu raaihatahaa dayfu ibliis” muy ci maanaa nganaleg Aji sell ji,ag xetam du xeeñ ganug ibliis.

Daa na siyaaresi Sëñ bi ,juge fu sori di liiru (dox ci tànkam),daan bañ bu ko Ku tedd ki masaan a jox alal,bu ko masaan a jox sijaada ngir mu ciy jullee,da ko daan jël di ko taf ci dënn bi, te daawul nangu deesi sàggane ko.

Li Sheex Mustahiin waxoon rekk, la sunu baay Muhammad Alkuntiyyu,mi nu gën a xame ci turu Bu Kunta ca Njaasaan wax, ca wetu Tiwaawon . Kenn ci taalube yi nee na ,booba dafa’a demoon di ko siyaareji,mu laaj ko Sëñ bi,te booba xam na ne mi ngi ci tukki bi,ne ko ana Sëñ bi,mu ne ko moom de tubaab yee ko yobbu,mu ne déet,bul wax loolu,mu ne ko lu may wax kon ? Mu ne ko,moom kay daa dem ligéeyi,fa ligéey ba neexe,murid bi nee booba maa ngi fi ma toog di dégg nit ñuy wax te xamuma dara ci li niy wax,mu ne ma ndax dégg nga làkkuw gaa yooyu ? Ma ne ko déedéet,mu ne ma li ko waral da dul seenuw làkk,ndax Sëñ bi njëkk muy tukki,daa samp ab làkk wërale réew mii,kenn du fi man a am benn taalube,ba kero muy ñëw,man nag samay taalube maa ngi leen jële ci ginaaw làkk bi,samay taalube dunu ñëw li feek ginaaw weer walla ay weer.

Bokk na ci kilifa yu mag yi seereel Sëñ bi,Sheex Abdalla Attamkali Addaymaani,wax na te dëggal te rafetal: (dama ne jéngal jëm Daaru Salaam ak Tuubaa,boo ragalee ay mbamb,aki coowi jamono) ( ngir nga ame fa’b xool bu tukkee ci xawsub jamono ji,bob da nga ci ame njéggal ak’ag texe)

Ñaari bayit yii de maa ngi ko mokkale ci Sëñ bi,ndax bis da ne ma ndax xam nga ñaari bayiti Abdalla yi,ma ne ko déedéet,mu jàng leen ma dal di leen mokkal,xam it li mu doon junj ci dëggal wax ji ci nekk di “xawsub jamonoom”.

Boroom xam-xam bu màgg bi ,Sheex Abdul Laah Attandaxii Albohbiinii,nee na bi mu siyaaresee Sëñ bi Njaaréem:

(boo mujjee ñëw wàlliyu yépp, ba noppi kawe leen,na nga xam ni ngën ji mbindéef de,ci xarnu yu mujj yi la ñëw) .

Sheex Abldullaah mii de mooy ki Sëñ bi ne woon :Abdullaah ag xasida’a ngii,gog ku ko mokkal ,Munkir ak Nakiir du nu ko laaj ci bàmmeelam,Sheex Abdullaah ne laaylaaha illal laah,ana mu ? Mu ne ko mi ngi ak Muhammadul Amiin mii,mu ne giñ naa ne di naa ko mokkalloo samay doom ak samay jigéen,ak samy jaam,yu jigéen ak yu góor,mu nekk di lim rekk ak a dëël,Sëñ bi moom di ree rekk. Xasida gi mooy Jaawartu.

Sang bii moo ma nettali woon,nettali bu yéeme ba,masumaa dégg lu ni mel,da ne ma sama mbokk man dey daa am bis,may jàng li may faral a jàng bis ci Alxuraan,bi ma ubbee kaamil bi,amul lu dul Yàlla mi man lépp won ma bisub (( alastu birabbikum)) muy ba mu naan (ndax du ma seen boroom?). Nee na ma jàkkaarloo ak xew-xew ba,gis yonnant yi,yonnant topp yonnant, yu bari yi ak yu néew yi,teg ci ma jàkkarloo’k wàlliyu yi,wàlliyu teg wàlliyu,ak seen mbooloo yu bari yi ak yu néew yi,ba mujj ma gis jenn jëmm,mooy Sheex Ahmadu mii,gox yépp fees dell aki taalubeem,mu génne ci Hadara bi ,sori’s lëf,dal di wëlbatiku ne ana ku may jottalil ab yonnee sama boroom ?,wax ko ñaari yoon ba ñatt,Yàlla tawfeexal ma, dëgëral ma,ma ne ko man,mu gestu ne ma ndax yaw la diw ? Ma ne ko waawaaw,mu ne boo ko defee de ,ba nu dem àdduna di naa la defal,di naa la defal..,mu ne ma neel sama boroom,mu dolli ma,ndax sama ñi ma topp de danoo bari te bëggaluma leen lu dul lu leen di bégloo,ak wax yu mel nii,ma dugg,ci biir,wax li nu ma waxloo woon,ma gis nu koy jox , ba ma dégg ko mu naan doy na,dal di dem.

Eskëy,moom de ci jëlewaayi (masdar) Sheex Sahdu Abiihi la bokkoon. Xibaar boobu nettaliwu ma ko kenn,lu dul ginaaw bi mu faatoo,ci ndigalm,sheex bii nag sama xarit la woon,te nekkon bu Sëñ bi,mas na maa yonni ca Sëñ ba di ko ñaan doomam,mu ne nee ko sàkkuwu ma ko lu dul ngir xér ci am lu ma jaxase ak moom ci fii ak ëlëg . Sëñ bi ne ni mu ko waxe la de,ñoom de bi ma nekkee seen réew sàkku woon nanu ma’a jox seen doom,waaye ma ne leen wuuteg aada yi moo nanguwul loolu rekk . Maandu na te dëggal.

Bokk na ci ñu mag ñi ko seereel,Alhaaji Ibraahiima Albaxdaadii,moom de ci kiimaani araab yi la woon,mi ngi juge woom Baxdaad,ku meloon ni moom ci xam-xam moom jafe woon na,Sëñ bi moom ci jëmmi boppam nettali na ma ne gis na Alhaaji Ibraahiima mii,booba gone la woon,muy tukki di ànd ak waajuram wu góor,ak Xaali Majaxate Kala,ñuy ànd ak Latjoor,bis nee na gis na ko mu toog ak ñaari sëriñ yooyu ci lalub sëriñ Buubakar FALL,yéeme lool ci barig nettaliy xam-xam yi mu leen doon defal,ci noonu Xaali manutoon a ñàkk a bind nettali yi,mu yonnee nu woolu ma,ngir ma bind xam-xam bu bari bii,mu diy woy,ngir mu bañ a sànku,ma dikk,muy wax may bind,muy lu bari ciy woy. Ma dégg ci sama waajur mu naan masumaa gis ku man a mokkale ni naar bii,ku dul Alhaaji Omar Fuutiyu,moom de jamono ju nekk mi ngi naan:Buxaari nee na,Muslim nee na.

Nee nanu bis laaj nanu ko turu buur bii,mu ne Latjoor,buur bi bég lool ci waxam jooju,bi loolu jàllee ba teg lu tollook ñaar fukki at,walla lu jege,ginaaw bi Sëñ bi jugee ci tukkib géej gi,la ñëw ci moom jébbalu,fàttali ko la xewoon bu njëkk,mu yéemu lu bari,nettali nanu ne bokk na ci li tax mu jébbalu,daa am bis mu ànd ak Sëñ bi cib tukki,ñu yendu ci ron genn garab,dëgg naa ci Sëñ bi,mu ne Alhaaji moomu booba mi ngi tux,mu génne gënn gi,am lu mu sotti ci loxoom,daa di ne ma loo wax ci lii ? Ma ne ko defal te bul laaj,mu ne ma ,duma man a ñàkk a laaj,ndax wuute gi da cee bari,ñii di ko daganal,ñee di ko araamal,ma ne ko ,bu dee noonu la deme de kon lu lënt la ci yaw,mu ne waa-waaw,ma ne ko xanaa gisoo Axdariyu,mu ne ma ahakay,gis naa ko,ma ne ko moom de nee na ca njëlbéen ga,daganul ci mukàllaf mu def dara te xamul la cay àtteb Yàlla,kon doo ko bàyyi,ba xam li ci Yàlla wax?.

Sama wax ji wedamloo ko,àgg ak moom fu sori,mu sëgg ab diir,siggi,ne ma seereel ne bàyyi naa ko ngir Yàlla,dal di jug ca saasa,suul gënn gi,ak li ci nekkoon,ca bis ba mbaa ginaaw bi la jaayante ak Sëñ bi,jébbalu ci moom .

Bi ñénn ci mag ñi yëgee ne jébbalu na,ñu tàmbli di ko yedd naan ko yaw ak sa màgg gi ak sa xam-xam bu bari bi,lu tax ngay jébbalu ci ku ñuul kii? Mu ne ko man dey Baxdaad laa juge, ni nga ko xame,yitewoowuma lu dul ku ma jox sama loxo,bari na wàlliyu mbaa boroom xam-xam bu ma romb,te xetug li may wër xeeñewuma lu dul ci moom,looloo waral ma aju ci moom, jaayante ak moom,ci noonu ñu dëggal wax ji,dogal ko ngànt.

Bi mu delloo ci Ku tedd ki,nettali ko li nu ko doon wax,Sëñ bi bindal ko lii: Wasslaamu halaykum wa rahmatul laahi,wa barakaatuhuu, ma lay xamal ni ca sama xasida ga tudd ((masaalikul jinaan,fii xidmatil mutahhiril janaani)) di ci maanaa,soobuwaayi àjjana yi,ci ligéeyal kiy laabal xol yi,bayit yii a nga ca:

(( Képp ku ma jorte lu dul kuy ligéeyal Ku nu tànn ki,man de dama koy ligéeyal ca la mu tànn)) ((dama koy ligéeyal ba kero may dugg àjjana,kërug sax ga,ak mébat ak xéewal )) ((képp ku yaakaar ne man na koo bégale ni,ni ko sama ligéey biy bégale )) ((na xam ne réer ak réeral wor na ko,te ci moom la ma lu dagan di dikkale juge fa boroom ba)) ((taggoon naa ko bu njëkk ca Libarwali,ag tagg gu wàlliyu yépp a ci lòtt )) ((taggoon naa ko ca Maayomba,tagg wu far samay ayib te dindi samay bàkkar)) ((taggoon naa ko fa niti Kalwaa,tagg wu ma fegali noon ak musiba)) .

Nee naa ci ligéey bi ma koy defal (j.y.m):

((ñeel na ko tukkee fi man,ab ligéey bu taqoo’k rawdatoom ba (bàmmeel),ba yawmal xiyaam te màgg)) ((sëtam ba Jiilaanii gëram na ma,yal na ko Yàlla mi ma kaweel gërëm)) ((sëtam ba Abool Hasan gërëm na ma,yal na gërëm luy saxalub taar nekk ci moom)) ((Attiijaanii gërëm na ma,yal na gërëmul kiy alag ibliis nekk ci moom)) ((ñeenti Xalifa yi gërëm nanu ma,làq naa gërëmul ñu ñu jegeel ñi)) ((ku ma gërëmul de,Yàlla Mu tedd ,mi moom gërëm na ma,ngërëm lu dul dog )) ((yal na Yàlla fay Mustafaa ngën ji pay,ni mu nangoo te amal ab dëël )) ((jullig ki nga xam ne teraangaam day daje ak man,yal na nekk ci ki nga xam ne mooy ki dëxëñ )). Subhaana rabbika rabbil hizzati hammaa yazifuun wasalaamun halal

mursaliin walhamdu lillaahi rabbil haalamiina .

Li nag booy xool ag junj la ci ne ñi ko ci doon yedd de,xamunu dëgg-dëggi mbiram,kon lu tax waxunu lu mel ne li ki leen xamul waxoon ? : ((yaw ki nga xam ne dëgg-dëggi am mbiram xamuma ko ,aka neexoon ma xam luy dëgg-dëggi mbiram)) .

Bokk na ci li nu soloo ci seere yi ko mag ñi seereel,mooy ne Sheex Muhammad mom Abiibur Rahmaan,Attanaduxii,da daan def fu nu tudde Sëñ bi ci wetam mu yëggal boppam,ne cëy cam soosu,moom dey fu ma ko nemmikoo rekk,fekk ko ci sama kanam,lu tolloo’k aw xur,walla ñaar.

Sama mbokk Muhammadu Abdur Rahmaan,Ibnus Saalik Baaba mom Halawi,wax na ma ne xalifab Sheex Ahmadu Bun Buddin,ak doomam ju màgg ja,Muhammad Amiin,nee nanu ko Sëñ bi de wilaayaam gi, indi na ci ay firnde, aki lay yu leer, ñépp gis ko, kenn ku am aw yiw dey du sikk ci wilaayaam gi.

Bokk na ci seere yi,li ma Muhammad mom Ahmad, mom Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci taalubeem yi,ci turu Muhammad Tuubaa,ngir barig lu mu fa daa nekk ak Sëñ bi,li mu ma nettali woon,muy moom de bis seeti na ay nijaayam,ni nu ko baaxoowoon a defe,mu dem ca ku yéeme,ku bëgg ka Yonnant bi ak jëwrinam,di Muhammad FAAl,doomi Muhammad mom Ahmad mom Haaqil,mu yobbante ko ab nuyyoo akub siyaare ca Sëñ ba,sàkku woon it ci moom mu jox ko barkeelub mbubum njiitlaay,mu mu daa sol, ngir mu barkeeloo ko,nee na ma jotal ko Sëñ bi mu bég ci,jox ma njiitlaay lu ndaw,lu mu daa jiitloo,maanaam turki,mu ne ma gaawal jox ko ko,ma indil ko ko,mu bég ci lool,di ko foon ak a teg ci bopp bi,ag bët yi,nit ñi dégg ko,mujj ku ñëw rekk,ñaan ko,ma barkeelu ci,ba mu mujj sànku,mu sàkkuwaat ci man ma demalaat ko,ne ko nit ñi de sànk nanu sama barkeelu ba,na ma sarax beneen,ma dikk ci Sëñ bi,leerale ko ko noonu,mu bég,jox ma beneen,ma indil ko ko,mu sànt Yàlla bu baax,tagg Sëñ bi lu bari,man itam mu sat ma,ne ma boo jébbaluwutoon ci Sëñ bi de, di naa wax ci yaw kon loo xam ne !,waaye jébbalu gi tax na ma fiire la .

Bokk na ci seere yi nu tuxale ci doomi mbokkam ma,Ahmadu Yoora Muhammad : lenn ci ay àndandoom danu koo yeddoon ci néew gi mu néew lu muy siyaare Sëñ bi,mu ne leen wallaahi,bëggumaa deem di ko siyaareji te yor ci sama xol,lu toll ne fepp suuf ci bëgg àdduna,kon fii ma toog laa koy siyaaree ,eskay.Ana ku gën tedd Muhammad,moom daal doy na sëkk seere .

Néeg bii ki ci gënoon a taqoo ak Sëñ bi,gënoon cee rafet lu mu wax,mooy Ahmadu mom Abdallaah,ki bokk ak ñoom ñaar nday ak baay,moom dey moo’k Sëñ bi danoo meloon ne benn bakkan,seere naa bis Sëñ bi di jànglu lenn ci ay xasidaam,ñu jàng aw bayit mooy: ((taqdiimu Ahmadabni Habdil laahi, yahrifuhuu xayru xabiyyin laahi)),muy ci maanaa jiitalug Ahmadu mom Abdul Laahi,ku dul ab dof,buy fo xam nga ko,bi nu tuddee Ahmadubnu Habdil laahi rekk, xelam dem ci,Ahmad moomee,mu ne nanu ko ko wool,bi mu ñëwee,mu nettali ko ne tudd gi nu ko tudd,ci biir njàng mee tax xelam dem ci moom mu woolu ko, moom itam mu bég ci,sant ci. Ahmadu mii nag mi ngi faatoo Ndakaaru,bàmmeelam a nga fa,siyaare naa ko .

Bokk na ci seere yi ,li ma Abal mom Baay Addaymaanii,nettali,mu ne moom de sax na jamono ju yàgg ci,sàkku ci sunu boroom mu won ko,maqaamam Sëñ bi,mu ëppal bis ci sàkku gi,ñu ne :yeen de du ngeen xam ci Sëñ bi,lu dul bu ubee ba toog ngir daje ak nit ñi,ngeen ne kii de mooy Sëñ bi,mbaa mu ubbi mihraab bi,taxaw,ngeen ne Sëñ bi de jiite nanu,lu dul loolu ciy mbiram de,fàddu na leen.

Ma ne wax jii de niroo na ak waxi Uwaysul Xaranii,sangub way topp yi,ji mu waxoon lenn xalifa yi, ne ko: yeen gisu leen ci Yonnant bi (j.y.m) lu dul keram !,nu ne ko Ibnu Quhaafa sax gisu ko,mu ne leen déedéet . Habal mii nettali na ma karaama,gu bàyyikoo ci goroom,baayu soxnaam,mu ne moom de daa am bis mu nekk cib xaymaam,moo’k doomam,mu koy bësal boppam,ndax daa jékki-jékki woon rekk buur ,buur gu metti,te gaaw (buur = jékki-jékki rekk jug),bi mu ko defee,dal di génn xayma bi,door tànk bi cig weñ,ba nu dégg ni ci tànk bi dale,te foofa génn weñ nekku fa,ci noonu tànk bi damm,mu rot ,xëm,bi mu ximmee,ñu laaj ko,lu mu doon,mu ne daa gis aw wàlliyu wu ñuul,di Muhammad mom Mahluum,ñu jénge ko ay weñ,mu bëggoon koo xettali,door tànk bi ci weñ gi,ngir damm jéng bi,far tànk bi damm,werul ci damm-damm boobu,ba kero mu faatu,yal na ko Yàlla gërëm te nangul ko jëfam,bi mu daataa faatu,bégaloon na doomi Daymaan yi,ci ag ubbiku gu yaatu ci alal,bu wàlliyu woowu dellusee,mu nekkoon ni mu ko waxe woon.

Bi Sëñ bi dellusee,mu jël leen,bindkati xam-xam yi,ak alxuraan yi,seeni waxambaane ak mag ñi ba ci jigéen ña ak gone ya,di leen sotti ci alal lees manut a misaal, ña ca rafetle ak ña ñaawle,loolu di jàppndal akug tàggatal gu tukke ca Yàlla, ñeel leen,te di ndimbal ak sarax bu nu def ci sekkare,di ag ligéeyal lislaam it,ak Yonnant bi (j.y.m) ci xeetam wi . Ni nu binde woon la ñeneen it binde woon,ci naar yeek ñu ñuul ñi,waaye ci ñoom la gënoon a siwe,gën cee feeñe.

Bokk na ci ñu màgg ñu barkeel, ñi seereel Sëñ bi,Haamidun mom Muhammad mom Muhanda Baaba,ak doomi baay tëxam yi,Baaba ak Ahmad, ñaari doomi Mahmuud ak Haamid yi, ñoom ñépp , ñu ñu jagleel lanu woon ci moom,boroomi wax yu rafet it lanu woon ci moom .

Yàlla dogal, bi Sëñ bi nekkee Cëyéen yonni woon na ma Dagana,ba ma fa àggee,Ustaas Haamid dégg ma, booba da fa’a ganesi woon Alhaaji Bekaay SEKK,yàggul dara mu seetsi ma,bég ci dikk gi ma fa dikk,yendook man ca sama kër waajur,di ma laaj ci mbiri Sëñ bi,aki xibaaram ,yi ci di yu nu man a tas,ak yi ci di yu ñu bari mant a xam,bu ko defee muy ree rekk,bég lool ci Sëñ bi , aki mbiram, ci noonu ma won ko teereb Sëñ bi tudd “Masaalikul Jinaan”,mu sëgg ci,siggiwul ngir dara,ba kerook ngoon di jot,mu ne ma Sëñ bi de ñëw gi mu ñëw ci jamono jii nu nekk de,firndéel na yiwam wu bari wi .

Lii nag ag mosle rekk la ,waaye waxi ak seerey sangi naar yi,fii taxu koo jug, fi ko tax a jug kay mooy sunu téere bi tudd,(alminahul miskiya,fil xawaarixil mbàkkiya).

Da nanu ci dolli li nu man ci tudd murid yi ci ñoom,bu soobee Yàlla. Bokk na ci kilifa yi ko seereel,sunu sëriñ tey sëriñub jullit ñi ci Senegaal,soppeb Sëñ bi,tey mbokkam,ci jegeñaaleg diine ak askan,ak réew,Alhaaji,Maalik SI, yal na ko Yàlla gërëm te jariñ ñu ci moom Aamiin,dégg naa ko,ku dul man it dégg ko,ba xaw naa doon lu ñépp xam,mu ne: amul kénn ci nun ku dul koo xam ne,daa def lu ñaaw,ba noppi,tuub ko,te jubal,bàyyi ag dëng,ku dul Sheex Ahmadu Bamba,moom de daa judd,rekk di def lu baax ak a rafetal . Maanaam loolu mooy ñun ñi ñiy tudd ñépp de,amu ci kenn ku gisul ci boppam ab rëcc-rëcc,walla ay rëcc-rëcc,bu ko defee mu tuub ko te jubal,ginaawug dëng,ndare moom,moom dey ,am mbiram cig ndawam akug magam ñoo yam rekk,lépp ag tegu ci yoon la.Moom de wallaahi dëggal na,te laabiire.

Sama mbokk, Muhammad, mom Ahmad Aliyu Alyahxuubii,nu gënoon koo xam ci turu,Muhammad Tuubaa,xibaar na ma ne moom de ci lenn ci ay siyaareem yu mu doon def,daa romboon Tiwaawon,siyaare Alhaaji Maalik SI,bi mu xamee ne ca Sëñ ba la jëm,mu ne ko man de da ma laa bëgg a yobbante ay baat ca moom,boo àggee na nga ma ko nuyyul,te fàttalil ma ko sunu guddi ga nu bokkoon fanaan ca Ndakaaru,ci benn néeg ñun ñaar rekk,kenn ñatteelunu ku dul Yàlla,bu ko fàttalikoo ba xam ne maa la yonni ,nga ne ko,man kat maa nga ca la ma waxoon ak moom,maa nga ca kollare ga ma defoon ak moom.Muhammad nee na man de wallaahi,xamuma gan kollare la jublu ci waxam jooju,te moom dolliwaatuma ci genn leeral. Bi ma àgsee ba fàttali Sëñ bi guddi gi,ba mu fàttaliku ko,ma wax ko li mu ma wax,mu bég ci,dëggal ma te dëggal ko,tagg ko bu baax,tàmbli di coppati sama nopp bi,ak sama bakan bi,boole ca di ree rekk,ngir bég .

Bokk na ci mag ñi ko seereel ba tay Xaali Majaxate Kala,xaritu Sëñ bi,tey mbokkam ci diine ak askan,ak réew,xaritu waajuri Sëñ bi la woon,da daan def ,bi Sëñ biy jàng,saa su ko masaa na romb rekk,sànni ko aw bayit walla ab jumla,ngir nattu ci ab tolluwaayam ci nahwu,muy (xam-xamu tegi wax ci yoon) walla bayaan:(xam-xamu rafeti wax) ngir ñawal am xelam, leeg-leeg,mu génneel ko ci ab yàq,leeg-leeg,déedéet,ba mujj Sëñ bi far ko raw,bi Sëñ bi màggee ba weesu fi mu tolloon,mu mujj naan ko,yaw de doom nga woon,waaye leegi baay nga, donga nga woon it,leegi sëriñ nga,muy lu mu dëggal te fas ko ci biir ag kaf,akug woyofal .

bokk na ci li nu koy askaneel,aw bayit wu yéeme,yaakaar naa ne tàmblig ag xaasida la : (tukkee na ci man jëm ci Ahmadu Bamba,mi bàyyi nit ñi,ngir Yàlla ,mujj far di sangub nit ñi ) .

Bokk na ci li nu askanale sang bu màgg bi,Sheex Muhammadu Alfuutiyu,baayi Zannuuni,ak mbokkam ma Ibnul Harab,mi bokkoon ci jëlewaayi Sheex Sëhdu Abiihi,bayit wii,moom tàmblig xasida la gu mu defal Sëñ bi : (mi ngi jëm ci kok Yàlla da koo defal ag tàllal (ay xéewal) akug wéttal,àtteloo ko ci àddunay jinne yi ak nit ñi) .

Moom xasida gi,gu yéeme la,téewlootuma ko fii mu nekk, wax na ci, ci wenn bayit wu muy waxante ak Sëñ bi,naan ko:

( sotti leen ci seeni miskiin,desiitu kaas bi) .

Sëñ bi daan def,saa su gisee Zannuuni,defaral ko ab kaas ne ko, càkkutéefug sa baay la woon, Zannuuni mii,mi ngi bokkoon ci woykat yu mag yi,yu rafetooni woy yi,def na ab diiwaan ci tag Yonnant bi (j.y.m), def beneen ci tagg sëriñ si,rawati na Sëñ bi,mooy ki ci wax lii:

( yaw xarit bi,ndaw sa bunt bii,bari lu ko siyaaresi,ci buur ak jaraaf,ak jinne ak malaaka) .

Loolu di tàmblig xasida gu rafet, te yéeme,moo’k baayam ci jëlewaayi Sheex Sahdu Abiihi lanu,yal na leen Yàlla gërëm,mi ngi faatoo Cees,nu denc ko ci almeeri Sheex Ahmad Baru, siyaare naa ko, alhamdu lillaah.

Bokk na ci kilifa yi seereel Sang bi,sëñ bu màg bi,di Sëriñ Tayba, Muhammad Ndumbe Maar SILLA. Sëñ bi nee na ma sëñ boobu de,fu mu ma masaa na gis rekk sànni na ma bayit wii,di ci seere ci sama mbir,mi ngii: (bariwaa na baay bu yéege ci doomam,ay tundi teddnga,ni Hadnaan kawee ci Yonnant bi) .

Mu bëgg a wax foofu ne,cam sii de ab taar la,tey ag mat ñeel cosaanam.

Bokk na ci kilifa yi seere,sang bu màgg ba Alhaaji Abdulaay SIISE,mom Saalum,nekkoon na di ku rafeti wax,ak pas-pas ci Sëñ bi,am na bis aw nit di wax cib jataayam ba tudd Sëñ bi,ak jële gi mu jële wirdam wi ci Yonnant bi (j.y.m), am ci ñi teewoon ,ku ci waxe ni kuy weddi,Alaaji gëdd ko,ne ko looy wax nii ?,xanaa Sheex Ahmad Tiijaan waxul ne lenn ci ay wirdam Yonnant bi moo ko ko jox (j.y.m) ? mu ne ko ahakay, mu ne ko moom de,nekkutoon lu dul boroom xam-xam,bu jëfe xam-xamam,bu ragal Yàlla,te doon jëfe sunna, rafet gi nu rafet njot ci moom moo waral nu dëggal ko,kii nag di Sheex bamba,xanaa melul ni moom rekk,di boroom xam-xam buy jëfe xam-xamam,ragal Yàlla tey ku sunnawu,ndax kon du nu ko dëggal,ngir rafet njort gi nu dëggale woon kee ?,waa ja wedam, amul lu mu tontu . Hasbunaal laahu wa nihmal wakiil,nihmal mawlaa,wa nihman nasiiru.

Ag cant ñeel na Yàlla lii doy na ci li sama xel man a joxe,li am nag mooy,bu ma joyaloon samab gog,féexal xel mi ci mu dikke li mu wattu,ak li ma wattoo ci samag maas,ci lu wér ak lu wéradi,kon de ma indi fi gën jaa yéemey yu yéemu yi,waaye kon loolu am raddu rekk lay doon, ñax gu nekk a ciy nekk, ag jub ak ag jubadi,dëgg ak safaan,looloo tax ma tànn indi fi li ma man,teb yool nekk ci,ndax kat déet ab yool,ci lug jub nekkul,bu nu doon tollale li ma indi,ci li ma indiwul,da nga naan benn la ci junni,li ma xam it bu nu ko doon tollale ak li ma xamul,da nga naan as kook la ci géej .

Yàlla mu kawe mi,laay ñaan mu baril sama lu néew,te wisaare ko,te nangu ko,te dimble ma, moom kat mooy aji tedd jiy aji gën, kiy boroom ngënéel lu mag li.


Tàmbli nanu ko te mu mat,cig barkeel,yal na Yàlla nangu,te dimbalee,te yekkati,te wisaare,Aamiin. Yaw buur bi, jéggal ma, ak sama ñaari way jur,te nga yërëm leen ni nu ma yarewoon may ndaw .



Jiitalug aji firi ji: 1

Jiitalug aji taalif ji: 2

Doggantal gu njëkk gi: ci xamale kuy sëriñ bi ak ay mbiram, 4

Doggantal : ci ni mu nekke woon ginaaw waajuram, 9

Doggantal : cig sancam Jolof 19

Doggantal : ci tukkib géej gi 24

Doggantal : ci dugg gi ca gaal gi 33

Doggantal : ci ñibisi juge ca géej ga 47

Doggantal : ci ñaareelu fàddu gi dem Gànnaar 52

Doggantal : cig ñibiseem ci tukkib ñaareel bi 67

Doggantal : cig génnam Jolof jëm Njaaréem 69

Tëj : ci wax lenn ci li ko Yàlla xéewale 80

Doggantal : ci seerey gaa yu baax yi 84



Bii article bu am solo la, ñu def ko ci cawarte gi murit yi ame ci wàllug fàggu ak koom-koom, ñi ngi ko jële ca yëglekaay gu siw googu di The Economist, di genn këyitu xibaar gu gore guy génn ayu bis gu nekk, te adduna bepp xam ko, muy wax nag ci mbiri adduna bi bepp, moom nag mi ngi njëkk a génn ci satumbar 1843.Economist Newspaper Limited (Filiale de Pearson) ca London moo ko génne. Li ñu ci gën di wax nag mooy koom-koomu adduna bi, politig, jëflante, xaalis, xam-xam, xarala ak fànn (art). Lim bu ci génn, di nanu ci defar lu ëpp milyoŋ, te 80% ba ca biti Angalteer lanu leen di jaaye-ji. Yëglekaay gi tas na ci lu tollook 1.138.118 ciy yax ci xaaj bu njëkk bi ci atum 2006, ci li gëstug bureau of circulations wax, di jumtukaayub natt bu nekk ca Angalteer. 53% ci ñiy jënd yëglekaay bii ak di ko yër ay waa Amerig lanu, 14% ay waa Angalteer, 19% di ñu dëkke Tugal gu goxe gi (continentale). Yëglekaay gi dees na ko yër ci lu tollook 206 réew.


Faith in the market (ngëm ak Business)

19 desambar 2006 / Rom ak Tuubaa (Senegaal)


Ci ginaaw luumay Itaali yi nuy defe fu lenn dul tiim lu dul asamaan si, am mbooloom jullit mu Afrig a ngii di indi ay tontu ci li nuy tudde “addunaal” di (mondialisation):

Kepp kuy door a teg tànkam ci suufus Rom, péeyub Itaali, dana gis ne dëkk bii de sol na mbubb mu bees mu mel ne du manu ko xame woon, mbubb mii nag mujj na di mu ñu ko xàmmee ni nu ko xàmmeek baaram yeek tànganaam yi nga xam ne dees na fa faral a guuxe leeg-leeg as lëf ci lii di Cappuccino, di kafe gu nu jaxaseek meew te nu gën a miinew jëfiinam ca Itaali. Bu ngéen jëlee yoon wi jëm Vatican, jaare ko ci Via Della Conciliazione mu dim mbedd mu ca jëme, da ngéen gis ne lu bari ca peggi tëli ya de danu koo muure aki jaaykat yu bawoo Afrig yu lay wër aki maska yu ndaw yu (waso), ay saag, ay der (ceintures) walla ay weeri jant yu nu roy, maanaam yu doonul piir. Bu ngéen fa taxawee as ndiir nag di léen seetlu, bu ngéen moytuwul, da ngéen fa seetaan powum muus ak jinax, mi nga xam ne jaaykat yii baaxoo nanu koo def ak takk-der yi, mu dig (dàqante gu xoromu te yërëmtalu). Nii daal lanu koy nekke, saa su nu léen yëgalee ne takk-der yaa ngoog, da nga leen di gis ñu taxañ seeni bagaas cis lëf cig gaaw daal di laxas, seeti nu nu man a mucce, bu Yàlla dogalee rëccuñu, bu booba a seen yoon du nekkati ci seen njaay moomu, moom kay danu ko fay bàyyil takk-der bi leen jàpp mu dajaleel ko boppam, daal di leen yobbu. (…)

Ca dëgg-dëgg, jaaykat yii nekk ci yoon yi jëme Vatican man ngaa wax ci ñoom lu nekk lu dul nosuwunu (organisewuwunu). Ñoom de ñi ngi bokk ci kuréel gu nosu, gu nu xame ci adduna bi ci gëm-gëmu diine ak bu koom-koom, te am it ab barabam ca beneen dëkk bu tedd di Tuubaa, nekk nag ci digg Senegaal, boo fa jëmee nag juge Dakar péeyub Senegaal ñatti waxtuy tukki rekk lay tollool.

Niki yeneen imigireyu bari yu Senegaal (yi nga xam ne yenn yi ay dawalkati taxi lanu ca New York, walla ñu diy wattkati suraas (orange) ca Espaañ) jaaykat yii di wëndéelook seeni njaay ca Rom ñi ngi bòkk ci genn kuréelug jullit gu tasawuf nu koy wooye “yoonu murit”, mooy yoon wi ëmb taalubey Cheikh Ahmad Bamba yi, kii nag ag kilifag diine la gu làqu atum 1927. ñoom nag ci jeexitalu gi nu def ci njàggalem Sëñ bii, indi nanu ay tontu yu am solo ci laaj yi ja yu adduna yi di indi aju ci ay marsandiis aki ligeey (maanaam dugal nanu seen loxo bu baax ci yaxantu gi ci adduna bi).

Li ëpp ci 11 milyoŋ yi dëkke Senegaal ay jullit lanu waaye lu ci ëpp danuy bokk ci benn ci ñaari yoon yu mag yii di wu Murit mbaa wu Tiijaan, moom nag (yoonu Tiijaan) moo fi jiitu wu Murit. Bamba moom leeral na am njàggaleem mi nga xam ne ñi ngi ko xame leegi ci turu ((ag murit)) leeral na ko ne mooy ag dellu rekk ca cosaanul Lislaam, gas reen ya, xame ko na ko Yonnat ba indee woon. Waaye nag moom Lislaamam lu néew la nirooleek ju xaw a tar ja bawoo Araabi Sawudit. Lenn nag am na mooy murit yi danuy xaw a def li nuy wax (culte des saints et de leur tombeaux ) muy ci maanaa jaamu wàlliyu yi ak seeni bàmmeel ba ci bu seen sëriñ boobu sax, te loolu ñoñ Wahaab ñi danu koy weddi, di ko kontar. Waaye murit yii nga xam ne danoo doylu ci seen bopp yëgunu sax ne ñi ngi wax ak a weddi (ñoom wahaabit yi), ñoom daal danuy dajale seen alal def ko ci li nu bëgg, tabax seeni jumaa aki jàkka te dunu soxlaal ñii di waa Araabi Sawudit dara ba dara booloo jeex. Sheex KA di sët ci Bamba, ca biir këram ga nekk Tuubaa, di dëkk bu fees dèll ak ragal-Yàlla, waaye it di bu nu bàyyikoo fu nekk dëkksi fa, ag yaxantu gu lokaal di fa dox bu baax ak a naat ci wàll goo wëlbati sa bët jëme, moom Sheex KA mii leeralal na nu gisiinu sëñ bii nga xam ne mooy sukkandiku ak wéeru ci sa bopp: (( bu ngéen wéeroo ci keneen)) mi ngi nuy leeral (( du ngéen gore mukk, lii mooy sunu gisiinu dund)). Bi mu fi daataa juge Bamba mébetoon na ay mbir yu bari: bëggoon na Tuubaa, dëkkam bi mu sanc, nekk dëkk bu sell. Njabootam gi – ci déggiin wu yaatu wi – Mbàkke-mbàkke yi, ëmb na lu sakkan ciy sëriñ wallay jànglekati xam-xami diine, yuy boole jàngale liyeey bu tar ci seenum njàngale ak temb, maanaam bañ a wéeru ci kenn ak dimbalnte. Xalaat yii nag moo jàñ murit yi ci ñuy faral a tukki ak a tuxu di dem ci yeneeni réew ngir wëri ligéey, ngir man a yonnee seeni njaboot lu nu man a dunde man cee suturloo, ak ngir man a jox àddiya seeni sëriñ (sii nga xam ne ñu ci ëpp danuy faral a tukki di wër adduna bi, ngir nemmeeku-ji seen taalube yi) ak ngir suqali dëkkub Tuubaa bi.

Lii lépp nag jëf na ay jëf ci def murit yi ñuy benn ci kuréeli Afrig yi gën a tèkki, moo xam ci seen réew la mbaa feneen. Fu ñu nekk ci adduna bi rekk dananu jeem a booloo ngir jënd jàkka walla barabub daje. Seen dimbalante gi nuy def tax na ba ñu bees di man a tukki bay man a ligeey ak a ami këyit. Ci safaanub ñu nekk fi di ngàññ dogal bi ak a jàmbat, ñoom daal yaxaantukat yu sawar lanu te muus, yuy dugg ci ligeey yu yombadi yi nga jort ne dunu ko man, te fu nekk it ci adduna bi danu fay dem di def senni ligeey. Nan jël ku mel ne Aliyun KA, ab bitig la am buy def njaayum bëbëstan (vente en gros) ca wetu gaarub Rom ba tudd Termini. Moom rakk la walla mag ci Sheex KA mi nekk Tuubaa di topptoo njaboot gi. Aliyun KA mii jaaykat la buy def njaayum ay maska yu waaso di ko jaay nag ay moroomi senegaleem yuy jaay di wër ( walla sax ñu duli senegale ), bu ko defee ñoom ñii di ko jaayaat ci mbedd yi walla ci tefes yi. Lenn nag ci njaay mii Senegaal lay bàyyikoo wayye li ëpp day bawoo Endonesi, Thailande mbaa End.

Teewul Aliyun nangu ne am na leeg-leeg ay jaaykati imigre yu juge ci yeneeni réew yu gën a muus murit yi ci di indi njaay walla jaayiin wu bees. Moom nag Aliyun, ku naw ñenn ci ñiy wujjeek moom ci njaay mi la te juge Banglaades, ndax nee na ((ñoom danuy déglu xibaari jawwu ji (meteo) ba bu nu nee suba di na taw rekk ñu gaaw wuti parasol jaayi ! )). Am na benn yoon ci mbedd mi, Sang Ka def fa nuyyoob taalube bu tàng ak ay mbokki muritam yu def am mbooloo mu rafet tey jàpplante. Jaaykati saag yii ak der, nga xam ne yu ci ëpp Siin lanu juge, ñu ligeeye leen fa, danuy faral a daje ngir weccante seeni xalaat ak xam-xam yi aju ci ni nuy lijjantee bay mucc ci takk-der yi. Bi añ jotee, gan dikkal na Sang Ka, di benn waa reewam N. GEY, mi nekk ci bunt bitigam tey jaay ay tòggi Senegaal yu tàng, plaat bu nekk 5 euro.

Benn yoon ci ayu bis gi, lu ëpp ci murit yi nekk Rom dananu daje ngir def daayira (julli, jàng Alxuraan aki Xasida), gisante, siyaarante,xool ci seen biir ki ci yayoo ndimbal. Leeg-leeg as mbooloo ci ñoom danuy déggoo ci bokk luye ab kontaneer, yonnee ci seeni njënd aki bagaasi jëfandikoo, ngir nu jaayaat leen ca Sandaga, ja bu nekk ca Dakaar, te murit ya ëpp fa. Ay anam yu wuute it am nanu yu niy yonnee xaalis, looloo tax këri ligeey yiy yëngu ci wàllug yonnee xaalis yu tas lanu ci mbooleem ruqi Senegaal. Waaye imigre yi ñoom li gën a noppale ci ñoom te nu gën koo taamu ak a def mooy: woo seenub xarit walla xame ca Sandaga ngir mu joxal leen seen mbokk ma soxla.

Ñi ngi nattale ne murit yi tollu nanu ci 40% ci askanu Senegaal wi. Waaye bu dee ci bitim réew ñoo ëpp ci imigrey Senegaal yi nuy tollale ci 700,000. Murit yi it ñooy daanaka 80% ci jaaykati Senegaal yiy wër, tey jaar ci mbooleen qàli Itaali yu mag yi. (Fraans mi doon dooley sancaan ji tegoon loxo Senegaal mujj na doonatul réew mi senegale yi jëme séen një. Ay fukki at a ngii Itaali nangu barabam boobu ci moom, waaye nag jamono jii ñu nekk Espaañ a ngi jéegoy jéego ci fuqarcee ko ci Itaali. Lii sax moo waral ci weer wi (desambar 2006) lu jege 80 waa Senegaal ñoo sànku ci ndox mi, ci séen gaal gu laboon te jëmsi woon Espaañ, ca dunam ya tudd Canaries).

Lu bari ci murit yi danu lay wax ne di jaay di wër moo leen gënal ñu sax fi barab di ligéeyal kenn. Loolu nag ci genn anam day wone ni njàngalem sëñ bi jeexitale ci ñoom, te mooy sukkandiku ci sa bopp. Lu man a xew nag, ñu néew ci ñoom a mas a def ay tooñaange yu mag. Bis bu amee ay këyit ak visa day daal di dellu kër ga, def fay weer. Te sax ci mujjug at mii rekk ñu bari di nanu dellu réew ma ngir tëbëski-ji, bu ko defee ñu ci ëpp danu fay des ba weneen xewu diine wu mag wa ñëw di Màggalug Tuubaa, bu ko defee nag bu jàllee ñu door a dellooti Tugal ci jamonoy lòlli. Jenn ci dooley murit yi mooy seen nosu gi nu def ci wàllug njiit. Ñoom de bu ñu doon ab jal da nga naan Xalifa ba a nekk ca njòbbaxtal la, di aw turu njiit wow ki ko yanu fii mu nekk mooy ki mujj ci doomi Bamba yiy dund. Kii daal mooy ki nga xam ne lu mu wax rekk ñu def ko. Cig ayam Tuubaa gis na ag yaatal gu jéggi dayo ba. Ci atum 1958 bu ña fa dëkk weesuwutoon 2000 nit, leegi àgg nanu – man nanu ne - ci ay 700,000 nit. Alkol nag ak Póon danu leen a aaye ca Tuubaa, moom dëkk bii nga xam ne daa xaw a moom boppam ci biir Senegaal. Ña nga fay taxawal daara ju mag (ab université). Boo ko doon nattaleek yeneen dëkki jullit ñi fa la ag féex ëppe ak doxe na la neex ci diine. Jigéen ña dunu sol pantaloon waaye dunu muuru it, ñu ci bari it dunu musóoru. Xale yu góor ya’ak yu jigéen yaay demandoo jàngu ba (école). Saa su nu wootee ngir ñu defar ab fajuwaay (hopital) mbaa woote bi jëm ci lu defar ndox mi, ay milyoŋi eurooy dajaloo, ngir ne murit yu bari ay way woomle lanu, ku ci mel ne Elhaaji JUUF may futbal ca Bolton (Angalteer), ndax moom joxe na ca la ñu doon laaj ngir ligéeyub Tuubaa ba (…) Xamagunu leen de bu baax, waaye murit yii bari na lu adduna bi man a jànge ci ñoom de, du rekk ni nu war a def ba jàmmaarlook li nuy wax mondialisation (di ci maanaa jël adduna bi bepp def ko daanaka menn réew, benn xalaat, xatal soreente yi, jegeele gis-gis yi añs), waaye it warees na a jànge ci ñoom ni nuy doxale diine ci anam gu teey te jàmme…

lii tasawudus sixaar la di teere bu s bamba def ci lislaam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ahuuthu billaahi minash shaytaanir rajiimi wa inniya uhiithuhaa bika wathuriyyatahaa minash shaytaanir rajiimi rabbi,ahuuthu bika min hamazaatish shayaatiini wa ahuuthu bika rabbi ayyahduruuni.

Maa ngi tàmblee ci turu yàlla, miy yaatali xeewalam ci àddina te di ko jagleele ca alaaxira. Yal na yàlla mu kawe mi dolli xeewal ci sunu sang ,sunu kilifa, Muhammad,ak ñoñam aki saabaam,ak mucc ak barke bob dana ci wommate kepp ku jàng teere bii, yobb ko ca àjjanaam ja mu dig ña ko ragal,aamiin yaarabal haalamiin.

Ahmadu mi dul dañ di sant boroomam, di jaamub yàlla,tey ligéeyal yonant bi (j.y.m) nee na : ag cant ñeel na yàlla mii di rafetal ci samag wàll,rafetal gu tooll ne rafetalug ku musla dañ di rafetal.Maang koy sant ndax kat moo tabe ci indil nu tawhiid (muy wéetal yàlla),ak ñaari mbokkam yooyu di lislaam ak lihsaan,te ñooy sunnas yonant bi(j.y.m),xeewal ak mucc gu sax na ne ca xaritam ba,soppeem ba,Ahmad,ak ñoñam ak saabaam yu gëm, yu jullite,yu tedd,yuy rafetal yi.

Lii nii aw woy wu rajas wu am njariñ te tedd la, ma tudde ko yobbalub ndaw ñi(tathawudush shixaar) jem ca àjjanay yàlla jii ami dex,maa ngi ñaan yàlla ag nangu,ak jàmm ak sell,ak màggal. Maang koy ñaan woy wii di wommat kepp ku ko jàng jëme ko ca yoon wa gën a jub. Tey texeg ndaw ñi,ak mag ñi,ak waxambaane yeek jigeen ñi. Waxtuw soppiku jëm ci li nu tax a jug nag jot na,sunu boroom laa ciy wut ci lu sax.

(AG JIITAL )

Yeen ndaw ñi maa ngi leen di digal ngeen bañ a wut lu dul ag jub,te soxlawoo xam-xam,soxlawoo leen jàng ak mokkal,te teet barabi texeedi yi,taqoo leen ak ki dul dañ di jaamu boroomam,ndax kooku kat la yàlla digale rekk la jeme,kepp ku daw cig ndawam jëm cig jub,bu màgge noppalu. Ku dabaatal li ko rëccoon ci lu bon akug neen,te jeem a dundal waxtu yi ci tuub gu sell,ak jublu sunu boroom,am la gën. Jàpp leen ci sama laabiire gii ma leen jox,kon dey da ngeen tonowu ci addina ak alaaxira,bokk ci ñiy texe.

(BUNT CI XAAJI DIINE YI)

Diine ñatti xaaj la,benn xaaj bi mooy bu gëm, Beneen bi di bu lislaam mooy ni nuy jaamoo yàlla ba yàlla di ko nangu,ak bu lihsaan,muy rafetal jaamu gi ngay jaamu ci sa digganteek sa boroom.Lu ci ne dees na ko gën a leeral. Ñu tàmbli ko ci xaaj bu njëkk bi muy gëm .

Gëm mooy nga gëm yàlla ak malaakaam yi,ak teereem yi mu wàcce,ak alaaxira,ak yonenteem yi ak dogal bi.

(DOGGANTAL (chapitre) CI NI NUY GËME YÀLLA)

Yàlla moom ni nga koy gëme mooy : nga dëggal ni am gi mu am lu wóor la, te aji jiitu la joj jiitoom gi amul fu mu tàmblee,aji des la te desam gi amul fu muy yam, aji wuuteek mbindeef yi la,aji doylu ci boppam la,kenn la kok amulub kem,aji wéet la ci jëmmam- maanaan amul kenn ku mel ni moom- ak ciw meloom , aki jëfam.

Kàttan (man-manu jëf) ak nameel (maanaam bëgg di def) ak xam-xam akug dund ,ak gis ak dégg, ak wax,yooyule yu war ci sunu boroom lanu. Kon nag mu nekk di aji am kàttan lu war la, tey ku am nameel ,di aji xam, di aji dund,tey kuy degg di kuy gis, nekk it di kuy wax yu war lan ci moom. Ni yooyu nekke di ay melo yu war ci sunu boroom, la ame yeneen melo yu waradi,te jomb ci moom,niki ñàkk, (maanaam sun boroom bañoon a am) ak sosu (ci maanaa muy ku nekkam gi am na lu ko fi jiitu,nekkul di ku fi mas di ne),ak jeex (maanaam muy ku fi dul des),ak niru,(ci maanaa yamoowut ak dara ci jëmm du caageenug ci meloom mbaa ay jëfam,kon niroowut ak dara te loolu jomb na ci moom)ak aajowoo (jomb na ci sunu boroom muy aajowoo kenn ci lenn),ak limu (maanaam mu bañ di kenn di ay ñaar aki ñatt) ak lott (maanaam ñakk man-man ci def li ko soob) ak sibeel ( def dara cig sibeel mooy safaanub def ko cig nameel,mooy def goo xam ni andul ak teeyug bakkan loolu jomb na ci sunu boroom) ak tëx (mooy safaanub degg) ak réer ( di safaanub xam) ak dee di (safaanub dund)ak gumba di (safaanub gis) ak luu di (safaanub wax) .

Yile yepp jomb nanu ci yàlla sunu boroom ,tudd naa sellam ga,kon daal jomb na ci moom mu ne di aji lott,mbaa muy aji tëx mba muy aji jëf cig sibeel walla muy aji réer mbaa muy ku gumba mbaa ku dee -soril naa ko loolu- walla muy aji luu,yii daal melo yu jomb lanu ci boroom asamaan.Moom daal sunu boroom deful dara cig war,lu mu man a def cig nameel la koy def ak cig baax ak coobare,loo fi gis daal,ci mbindeef yi, seenug jëf ak seenug ba, ñoo yam ca sunu boroom,lenn du ci lu war, lu dagan rekk la ci moom, (dagan mooy lu man a nekk man a bañ a nekk).

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME MALAAKA YI yal na yàlla dolli xeewal ak mucc ci ñoom)

Malaaka yi ñoom nga gëm leen mooy nga dëggal te am koolute ci ne ñoom kat ñu am lanu,te ñu nu musal ciy bàkkaar lanu,(dun moy yàlla),dunu xayta (dunu puup) dunu saw it,ñu sunu boroom laabal lanu. Dunu lekk dunu naan –jàmm yal na sax ci ñoom - ñoom daal jaam yu yàlla teral lanu ba fàww,ken du ci moy yàlla,ku ci ne li ko yàlla digal rekk lay def.Ci leer la leen yàlla binde. Sàbbaal seen boroom mooy seenug naan,sellal ko mooy seenug lekk.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME TEEREY ASAMAAN YI)

Ni ngay gëme teere yi mooy nga dëggal ne wacce gi leen yàlla wacce lu wér la,te lepp lu ne ci teere yooyu ag dëgg la gu deesul sikk.Seenub lim nag teemer ak ñeent la. Fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Aadama (j.y.m), juroom fukk yi nu wacce leen ci yonant yalla Sihsa(doomi yonant yalla Aadama), fanweer yi nu wacce leen ci yonant yàlla Idriisa,fukk yi nu wacce leen ci yonant yàlla Ibraahiima miy xaritub yàlla bi(j.y.m). Bu ko defee Tawreet ñeel Muusa(j.y.m),Injiil ñeel Hiisaa,saboor Davood (j.y.m)Alxuraan jii nag wacci ci sunu sang bi Muhammad yonant bi tëjj yonant gi,yal na yàlla dolli mucc ak xeewal ci moom,ak ci ñoom ñepp.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME YONANT YI,mucc ak xeewal yàlla na nekk ci ñoom)

Ni ngay gëme yonant yi (j.y.ñ) mooy nga dëggal leen,te dëggal li nu indi jële ci seen boroom.Te nga gëm ne itam dëggu ak wóor ak jotal lu war ci ñoom la.Fen nag ak wor ak nëbb dëgg dafa araam ci ñoom. Gaar-gaar bu dul ayibal tey dal nit da na leen dal,niki tawat, waaye bu mu doon juy foñloo,maanaam juy tax nit ñi di leen daw,niki ngaana nga xam ni day wàlle,ak yu mel ni ñoom,ñoom tawat yooyu danoo wormaal yonant yi,dun leen dal. Waaye nag jaay ak jënd,ak denc (am soxna) ak lu ni mel ci lepp lu yàlla daganal,bun ko defee du leen dolli lu dul yoolub yàlla seen boroom. Liy wone ne ñoom ñu dëggu lanu te yàllaa leen yonni,mooy kiimaan yi leen yàlla di wàcceel ,di ci wone ne moo leen yonni,mu mel ni (ñoom kiimaan yi)daniy wax ak nit ñi naan leen jii waay de lu mu wax, mbaa mu def ko yàllaa ko ko diggal. Yonant yi nag, seenub lim ñatti teemeer ak fukk ak ñatt la,waaye anbiyaawu yeek (mooy ku am darajay yonant te yonniwun ko ci nit ñi) yonant yi,yepp boo leen boolee ,seenub lim moom teemeeri junni la ak ñaar fukk ak ñeent,yal na mucc ak xeewal sax ci ñoom ci lu dul dog.

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME BIS BU MUJJ BA,yal nanu yàlla fegal ay tiitaangeem )

Ni ngay gëme bis bii mooy nga dëggal ko,te dëggal lepp li mu ëmb,niki wisaareg teere ya,ku ci ne dees na ko won ay jëfam ci teere,ak pang ma,muy dajale gi niy dajale nit ñi,ak balaas bi, muy balaas bi niy mandaxee jëfi jaam yi,ak déegub yonant bi (j.y.m),ak ajjana ak sawara,ak siraat(aw yoon la wu deesi romb),ak romb gin ciy romb,ak hisaab(mooy seet gi niy seet jëfi nit ñi) ak rammug yonant bi (j.y.m) ak mbugal(yal nanu ci yàlla musal). Hisaab nag luy tar la ca boobale bis,ndax dees na hisaab nit ki ci lu gën a tuuti fepp suuf cib tuutaay.

Fayyantoo itam dana fa am,ndax lu waay daa jay moroomam fii, teg ko cig ëpp doole,bu yawmal-xiyaamee dees na jox aji neew ji doole, doole muy fayyu ci ki ko daa neewal doole,niki xar mi am bejjan te daa daan mi amul bejjan,bu bis baa,da niy jox aji ñakk jiy bejjan bejjani mi ko daa daan muy fayyu,loolu lepp maandute ga fay am lay wone.

Dee,ak laajug malaaka yi ak mbugalum bammeel,ci yawmal-xiyaam lanu,ndax kat yawmal-xiyaam yi ñaar lanu,bu mag ak bu ndaw,bu ndaw bi mooy dee gi ñepp di dee,bu mag bi di wal gi niy wal buftu bi .

(DOGGANTAL CI NI NUY GËME DOGAL BI)

Gëm dogalub yàlla bi mooy dëggal ne lépp lu am,moo xam lu làqu la walla lu feeñ,ak fu’m man a ame,sunu boroom mooy ki ko xamoon ,namoon ko am kàttanug def ko ,def ko.Moo xam lu baax la niki jëfe ndigëli sunu boroom yi,walla lu bon ,niki jëfe tere yi.Walla muy lu neex niki yoolub jullit ñi,walla lu naqari niki mbugalum yéefar yi.

Cig gàttal daal lépp lu am,ci saayir ak ci baatin dogalub sunu boroom la.Nit ki daal war naa gëm ne amul kuy jeexiital ci dara ku dul yàlla,lu fi am cib dogalam la ame.

(BUNT CI LISLAAM)

Lislaam mooy wax laa ilaaha illal laa (muy yàlla rekk ay buur,amul beneen buur bu dul mom) ak julli ak woor,aj màkka,natt asaka.

(DOGGANTAL CI LAA ILAHA ILLAL LAA)

Wax laa ilaaha illal laa amul benn buur bu dul yàlla,Muhammad,yonantub yàlla’a - yal na yàlla dolli xéewal ak mucc ci moom,ak ñoñam aki sahabaam- mooy ngën ji lu kuy wax di wax,ku ko weddi it pert rekk,ku ko saxal tey teewlu maanaa mi da na tonowu,te du dajeek nëx-nëx.

(BUNT CI JULLI YI JUROOM)

Julli yi juroom farata la ci lu dog,ci alxuraan ak suna ak ci dajeg boroom xam-xam yi. Kepp ku ko bañ a def ngir weddi,mook ku tubbee yam cib àtte,dees koy tuubloo may ko ñatti fan,bu tuubee nu ba ko,bu tuubul,sariiya ray ko ci jaasi,te deesu ko sang,deesu ko sàng ,deesu ko jullee te deesu ko suul fa jullit ña.

Imaam daal day yonni kenn rekk, mu suul ko,te dunu ko jublule xibla,te alal ji mu am it ci baytul maal lan koy def (baytulmaal mooy (trésor publique) bu nguurug lislaam),ku nangu ne julli lu war la ba noppi lànk ne du ko def,te amul ngànt,moom danu koy bàyyi ba waxtu julli wi jot,nu digal ko,bu lànkee nu muñal ko ba doroora ji dem bay bëgg a jeex,nga xam ne lu tollu ne benn ràkkaa rekk a ciy bëgg a des,bu bañee nu topp ko,ba mu wóor ne faatiya sax xajatu fi,walla ab yamoo,loolu lepp nag ngir bañ koo ray, ñongal dereetam,bu bañee, kilifa gi ray kook jaasi ,rayug gëtën mu bañ a doon ni nuy raye ab yéefër.

Bu réccoo nag ne nan ko ba mu julli ngir ragal a dee, deesu ko nangu,dees na ko jullee nag,waaye boroom ngëneel du ko jiite,ndax da nuy bañ keneen di ko ci roy.Bàmmeelam nag dees na ko fonk,jégénal ko(jal ko) kenn du ko maasale noonu rekk,ndax moom fi boroom xam-xam yi ab julit la.Lii dey waxi imam Hawfii la.

(DOGGANTAL CI LAAB)

Laab moom lu war la,ci alxuran ak sunna ak dajeg boroom xam-xam yi. Ku ko bàyyi ci lu dul ngànt lu xel nangu,dees koy ray rayug gëtën,gu dul gu yéefër, ndaxte julli du mat mukk lu dul dafa ànd ak lab kon ag waram lu wér la.

(DOGGANTAL CIG SOÑÑEE CI ÑU FARLU CI RÀÑÑALE DIGGANTE FARATA YEEK SUNNA YI AK ÑÀKK CEE SÀGGAN)

Koo xam ne julli na ca anam ga mu gën a rafete, ci maanaa,mu jullee ni ko yàlla digalee,metal rukoo ya ak sujood ya,metal taxawaay ya ak jataay ya,te bawul dara lu nu war a def ci julli gi,mu noppi nag nu laaj ko li julli gi am ciy farata akub àtteem, ndax moom julli gi farata la walla sunna walla lu nu sopp,te moom xamul dara ci li nu ko laaj,xanaa mu tontu rekk ne man daal da may gis nit ñi ñuy jaamu ma ànd ak ñoom ca la ñuy def waaye li ci des xawma ci dara.

Ci loolu yenn boroom xam-xam yi nee nanu julleem gi baaxul,te dunu nangu ngàntam li. Naka noonu ku jàpp njàpp mu sell,raxas ñatti yoon ay loxoom ba ci tikkujara yi,gallaxndiku gu ànd ak soccu,saraxndiku,fiiru,lu ci ne ñatti yoon raxas kanamam,ay loxoom lu ci ne ñatt,te xaliil baaraam ya,masaa boppam tàmblee ko ci fi jë bi yam ba ci doq gi,delloosi ko ba fa mu tàmblee woon,masaa ñaari noppam ginaaw bi mu tooyalaatee ay loxoom,raxas ñaari tànkam ànd ak xaliil leen,matal njàpp mi ni mu ware.

Naka noonu ku sangu janaba ni mu ware,raxas ñaari loxoom ñatti yoon ba ci tikkujara ya,raxas li ko taq ci sobe,raxas pëyam walla sakkaraam ànd caak yeene,bu noppee jàpp njàppum benn-benn,xaliil mbooleem kawaram,tooyal ko,tamblee ko ci mujug ndaal-bopp li ngir jañ lor ji. Dal di raxas boppam ci ñatti tanqi ndox yum tanqe ci loxoom,ginaaw bi mu ko xaliilee,dal di as ndox ci tenqul ndijooram,jengal boppam raxas noppub ndijooram,bu jàllee mu defaat noonu raxas bu cammooñam,dal di raxas ag doqam,ak wetug ndijooram ba ci bëtu woom bi,def noonu ci gu càmmooñ gi,dal di raxas tankub ndijoor bi ba ci dajoor bi,teg ci bu càmmooñ bi,dal di matal am cangaayam ci raxas biir bi ak dënn bi,ginaaw bim raxasee ginaaw gi.

Te xamul ci loolu lepp la cay farata ak la cay sunna, kon na ko wóor ne tojam ma (toj mooy ñàkk a lab) dañul te julleem ga mu ca julli baaxul,te coonaam boobu bepp du ca jële lu dul bàkkaar, te mi ngi moy yàlla ak yonentam bu sel bi (j.y.m) .Wax jii nag mi ngi bawoo ci Imaamul Hawfii, luy tiitloo tey jàjjee ngi ci nag,nee na itam gépp jaamu yàlla gu nu defe nii njariñ du ca juddoo,moo xam aj la walla jihad walla woor walla yu ni mel niki joxe ak lele.

Am nag ci boroom xam-xam yi ñu ci ne ku sangu mbaa mu jàpp,def ko ca anam ga mu ware,yeene ca biir def la yàlla farataal,na xam ne jëfam ja ju nu nangu la, ju baax la,te dana ko doy ca la gën a wér,te julli gam ca def it gu baax lay doon ,bu ca yeenee def la ca yàlla farataal,amul it benn bàkkaar ,mbaa muy moy yàlla ngir ñàkk gi mu ñàkk a gëstu.

Waxi Imaam Hawfii jii du dara lu dul ag xuppe akug yeete akug laabiire ,ngir nu farlu ci jeem a xam farata yeek suna ak yi ni mel,yàlla na ko yàlla fay aw yiw. Li ma (sëriñ beey wax) wax mooy yàlla dey araamal na ci mukalaf mu ne - ci li nu tuxal- jëf dara ci diine te xamoo la cay àtteb yoon,yax (mbind mii) bii nag daliil xathii la,(daliil xathii ci wallug usool mooy lu wér lu mel ni alxuraan).Kepp ku réere farataam te laajul,na xam ne tooñ na boppam te alag ko.

(DOGGANTAL CI FARATAY JULLI)

Faratay julli fukk ak juroom la, ci li faqiih bii di Hawfii wax. Ñooy yii: 1 yeene 2 kàbbarub armal ba 3 taxaw ngir kàbbar ko 4 jàng faatiya 5 taxaw ngir jàng ko 6 rukoo 7 siggi ca rukoo ba 8 sujood 9 siggi ca sujood ba 10 yeenee roy imaam boo ko amee ca njëlbeen ga 11 toftale gi 12 dal gi 13 yamoo gi 14 sëlmël bi 15 jataayub sëlmël bi tàmblee ca alifug al gi ba ca miimug kum gi.

(DOGGANTAL CI SUNNAY JULLI)

Ay sunnaam 18 la, 1 liqaam 2 saar wi ci ginaaw faatiya (sunna sun feddali la) 3 taxaw gi gay taxaw di ko jàng (sunna sun feddali la) 4 birël fi mu ware 5 yalu fi mu ware 6 kàbbar bu dul bu njëkk bi 7 taaya ju njëkk 8 taaya ju mujj 9 julli gi ngay julli ci yonant bi ca taaya ju mujj ja 10 jataayub taaya ju njëkk ja 11 jataayub taaya ju mujj ja 12 li dolliku ci dal gi ngay dal 13 li dolliku ci sëlmël bi 14 birël sëlmëlub farata ba 15 delloo sëlmël Imaam 16 delloo ko ki ci sa wet 17xerawlug maamoom bu imam dee birël 18 am saatir bu dee imaam walla kenn ku beru,waaye kuy roy moom imaamam doy na ko saatir.

( DOGGANTAL CI FARATAY NJÀPP )

Faratay njàpp juroom ñatt la, ñooy: 1 yeene 2 raxas kanam gi 3 raxas loxo yi ba ci conc yi 4 xaliil baaraami loxo yi 5 masaa sa bopp 6 raxas sa tànk 7 jonj 8 gaaw

(DOGGANTAL CI SUNNAY NJÀPP)

Sunnay njàpp moom itam juroom ñatt la,ci li imaamul Hawfii wax :1 raxas say loxo ca tàmbli ga 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 fiiru 5 masaa sa ñaari nopp 6 tooyalaat say loxo bala ngaa masaa say nopp 7 boo masaa sa bopp ba ci doq gi,delloosi gi nga koy delloosi 8 toftale gi.

(DOGGANTAL CI FARATAY SANGU)

Faratay sangu joroom la : 1 yeene booy tàmbli 2 jonj 3 gaaw 4 xaliil kawar gi 5 nal ay lett ci kepp ku lettu

(DOGGANTAL CI SUNNAY CANGAAY )

Ay sunnaam ñeent la: 1 raxas loxo cig tàmbli 2 galaxndiku 3 saraxndiku 4 masaa ker nopp yi.

(DOGGANTAL CI FARATAY TIIM)

Faratay tiim juroom ñatt la: 1 yeene 2 pakk bu lab 3 gaaw 4 door gi ngay njëkk a door say loxo ci suuf 5 masaa sa kanam 6 masaa sa tikkujara 7 jokkale ko ak julli gi 8 defe ko ci biir waxtu wi,ndax du baax bu jotul.

(DOGGANTAL CIY SUNNAAM)

Sunnay tiim ñatt la : 1 toftale ga (mooy jiital li war a jiitu li ci war a top topp ci) 2 doorub ñaareel bi ngay door sa loxo ci suuf 3 masaa li top ci tikkujara yi. Na nga ba tiim nag tey jàpp,boo weree waxunu boo weredee walla nga am ngànt lu wér,kon bu boobaa nga man a tiim.

(DOGGANTAL CI WOOR)

Woor ñaari farata la am: 1 yeene 2 ba liy dogloo ngir yàlla. Sunna yi ñatt la : 1 gaaw a dog 2 yeex a xëdd 3 ba wax ju ñaaw

(DOGGANTAL CI ASAKA)

Asaka moom ñeenti farata la am : 1 yeene 2 matug at 3 matug nisaab 4 bañ koo joxe feneen te fi nga ne ku ko yayoo nekk fi. Am na ñatti teggiin nag yuy waralub yool  : 1 nga ànd ceek teeyug bakan 2 mu bañ a doon la gën mbaa la yées ci sa alal 3 joxe ko ci sutura ngir daw gistal.

(DOGGANTAL CI AJJ)

Ajj ñeenti farata la am : 1 yeenee ajj 2 tawaaful ifaada 3 dox diggante safaa ak marwa 4 taxaw arafa.

(DOGGANTAL CIY SUNNAAM)

Sunnay ajj fukk ak ñaar la :am na ci ñeent yoy ñi ngi ame ca armal ga,1 sangu gu jokkook armal gi 2 rafle ci lunu ñaw 3 solub ñëkk akug làmbaay aki dàll 4 labayka.

Tawaaf gi am ñeenti sunna : 1 dox gi 2 foon gi doj wa ci loxo walla gimiñ 3 ñukk gi ci ñatti tuur yu njëkk yi 4 ñaan gi ngay ñaan ci tawaaf bi.

Dox gi safaak marwa it am ñeenti sunnaam : 1 foon doj wi bu dee daa juge ca jàkka ja jem safaa 2 ag yeegam diggante safaa ak marwa 3 gaaw gi niy def ci batnu masiil 4 ñaan gu amulub àpp gi ngay def ci kaw safaa ak marwa.

(LII AG MOTTALI LA )

Nettali nanu jële fa gën ji mbindeef ne ku birël ci ginaawug laab ne ( Ashadu ba fam yam) da nanu ko ubil bunti àjjana yi, mu dugg ci bi ko soob,waaye wuute nanu ci jamono ji nu koy ubbi.

(DOGGANTAL CI NI NGAY FAYE LI LA FAAT CI GINAAW IMAAM)

Lu war la ci maamoom mu fay li ko fat ci ginaaw imaam.Suba waxtoom a ngi tàmblee ca dëgg-dëggi fajar ba bu tàmblee leer,bu la cib ràkkaa faatee jugal ci lu dul kàbbar jàng faatiya’akuw saar cig birël te bul xunoot.

Waxtuw tisbaar tàmblee ca sawaal ba ca mujjug taxawaay ba,bu la cib ràkka faatee jugal ci lu dul kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig yalu jekki,taaya , sëlmël.Boo ci ñàkkee nag ñaari ràkkaa jugal te kàbbar te jàng faatiya’akuw saar cig yalu,te bul toog da ngay jug def beneen, julli gi mat.

Bu la ci ñatt rawee nag jugal te bul kàbbar,nga jàng faatiya’akuw saar te yalu leen,nga jekki, taaya,jug def beneen ràkkaa,bu ànd ak faatiya’akuw saar te doo toog,da ngay defaat beneen ràkka rekk cig yalu bu ànd ak faatiya dong,mu jeex.

Waxtuw tàkkusaan a ngi tàmblee ci matug taxawaay bu njëkk ba,ba ca waxtuw gel wa (mooy bu jamono tàmblee mel ne lu mboq). Tàkkusaan mook tisbaar a yam ci ni nu koy faye araf ci araf.

Timis moom waxtoom a ngi dale ci jànt bu so ba ca fàddug safaq. Bu la cib ràkka rawee jugal,kàbbar ,jàng faatiya’akuw saar cig birël,bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal te bul kàbbar, jàng faatiya akuw saar te birël ko,taaya, defaat ràkkaa bu ni mel te sëlmël.

Gee moom mi ngi tàmblee ca fàddug safaq ba ca ñatteelub guddi (guddi gi bu nu ko xaajoon ñatti xaaj benn xaaj bu njëkk bi) bu njëkk bi. Bu la ci benn ràkkaa rawee jugal, bul kàbbar,jàng faatiya akuw saar te birël ko,bu jàllee nga jekki te taaya te sëlmël. Bu la ci ñaari ràkkaa rawee,jugal kàbbar te jàng faatiya’akuw saar,cig birël,te bul toog,nga defaat na nga defoon ca bu njëkk ba. Bu la ci ñatt rawee,jugal birël faatiya’akuw saar,ci lu dul kàbbar,jekki,taaya,te jugaat defaatub rakkaa ànd ak faatiya’akuw saar,cig birël,waaye doo toog,da ngay wéy ca ba ca des, jàng ca faatiya rekk te yalu ko.

Boroom xam-xam yi ñoom, jotub rakka ñi ngi ko teg ci am ab rukkoo cib ràkka ànd ak Imaam . Ku amul ab rukkoo ci ràkkaa ànd ak imaam ,na ko woor ne jotul ràkkaa ba.Ku jot Imaam ci taaya,daa war a dooraatug julleem.

(BUNT CI LIHSAAN)

Lihsaan mooy nga jaamu yàlla di ko teewlu ba mel ni da nga koy gis,ci lepp li ngay def,te mu wóor la ne boo ko gisul it moom mi ngi lay gis.Kon na ngeen koy fuglu.

Bu ngeen bëggee àgg ci martaba yu kawe yi,na ngeen di jëfe ndénkaane bile: maa ngi leen di denk xam-xam,ak kersa,ak sant yàlla ak sellal,ak tabe,ak noppeek lewet booy xamlu, ak muñ ak ragal yàlla ak degg-degglu maanaa yi,na ngeen di farlu ci top aji yërëme ji, fu ngeen man a ne te sori noonoo,bu leen baril wax aki nelaw, na ngeen di teet luy waral yaq, di moytu ngistal,fu ngeen man a ne,ak rëy ak mbañeel, tey sàkkug leer,maa ngi leen di denk ag dëggu, ak wakkiirlu ci yàlla,ak toraxlu ak neewi mebët,denk naa leen bariy teggiin,loolu da na waralub yool,barib xam-xam ci lu duli teggiin ay akub coona rekk lay waral.

Yeen gone yi bu leen di toog ak ku dese cim xel,dee leen toog ak kuy gindee. Kuy gindee kat mooy kiy genne aji toogaale ji jële ko ci juroomi mbir jëme ko ci juroomi mbir,moo koy jële ci ngistal jëme ko ci sellal te du naafeq,moo koy jële cig rëy yobb ko cig toroxlu ak muñ,moo koy jële cig noonoo,jëme ko cig laabiire,moo koy jële ci sikk,yobbu ko ci yaqiin gu ko man a dollig kawe,moo koy jële ci bëgg lu koy lor,jëme ko ci lu koy jariñ.

Màng (profitoo) leen juroom,njëkk juroom ni ko yonant bi (j.y.m) digalee:bi ci njëkk mooy ag ngone njëkk màggat,2 wér njëkk wéradi 3 am koom njëkkug ñàkk 4 ag féex njëkkug féexadi, 5 dund njëkk dee.Gaawantu leen jëm ca yiw wa njëkk muy faat.

Fii la Tasawudus sixaar yam,ànd ak sant sama boroom miy aji feg ji gacca.Woy naa ko nag ndir jëmmi sama boroom mu tedd mi,di yaakaar ci moom ab yool bu dul dog,mu diw woy wuy wommate jëme ci xam-xam ak jëf,ak tegginu tey jàppndal mebat yi.Mu diw rajas wu am njariñ te barkeel,wu way texe yi bokk.

Yàlla ci barkeb yonant bi (j.y.m) nangu na woy wii,jariñ ci it kepp ku texe,kuy laabiire,te yewwu ,moom woy wi du dañ di bijjee jëme cig baax,di jañ gepp texeedeek woru. Yàllaay ki ma digal ma woy ko,yàlla miy ki nu jublu,mi may fegal luy waral njàqare.Woy naa ko ngir jëmmam ju tedd ja,moom mi jënd samam njaay ànd ak di ma teral.

Konug cant ñeel na yàlla,xeewal ak mucc yal na nekk ci Ahmadu ,aji rammu jiy boroomi ngëneel,ak ñoñam aki saabaam.Ahmadu mii dib jaam buy ligeeyal yonant bi mi ngi sant boroomam.

Subhaana rabbika rabbil hizzati hamma yazifuun,wasalaamun halal mursaliin,wal hamdu lillaahi rabbil haalamiin.

(LII AG XAMLE LA)

Bokk na ci njariñi woy wii : ki ko woy (muy sëñ bi) ci ndigalul yàlla mu kawe mi te sell la ko defe ,ak ci lol yonantam ba jàmm ak xeewal yal na sax ci moom.Bokk na ci ngëneeli woy wi, begal gun ko begal bim ci noppee(moom sëñ bi) ne ko woy wii de la yàlla (t.s)ak yonant bi(j.y.m) gën a sopp ci ay keman. Bokk na ci li nu ko begale:kepp ku ko jàng walla nga mokkal ko,texe ag texe gu texeedi dul toppati,bokk na ciy jagleem ku ko mokkal Munkir ak Nakiir dun ko laaj ci bàmmeel,ak leneen ak leneen ak leneen,yàlla mooy jagleel yërmaandeem ku ko soob,yàlla mooy boroom ngëneel lu màgg li.