Aller au contenu

Saari Alxuraan

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Alquraanul Kariim)

Alquraanul Kariim

Ab nataal ñeel téere bi




Alxuraan dafa toggaloo ci 114i Saar.

Waaye saar yi wuute nañu, am na ci yu gën a gudd.

Saar yi it ñaari xaaj lañu.

Yu wàcc Màkka di 86i Saar, ak yu wàcc Madiina di 28i saar.

Yu Màkka yi bu nu ko waxee mooy lu wàcc njëkk gàddaay gi, di wax ci (haxiida) pas-pas mooy gëm Yàlla ak sellal ko.

Bu dee yi wàcc Madiina nag mooy Ginaaw gàddaay gi, di wax ci mbirum yoon ak ay àtte ci diine.

Bu dee saar yi nga xam ne ñoo gën a gudd walla ñoo yem ci guddaay mooy; 7i Saar yii, Baqara, Aali himraan, Nisaahi, Maahida, An-haam, Lahraaf, Tawba.

Waaye am yu topp ci ñoom muy yu yemoo ak téeméer ciy aaya, Saar yooyu nag seeni tur moo ngi jóge ci li saar wi di nettali, walla ñu xool ci biir saar wi, benn baat tudde leen ko.

Saar yépp nag Bismil Laahi Rahmaani Rahiimi lañu tàmbalee ba mu des saaru Tawba!

Ndax dafa am benn saar wu am 2i Bismil Laahi Rahmaani Rahiimi, mooy saaru Namli.

Waaye Limub saar yi tolloo na ak limub Bismil Laahi...

Saar yi ak aaya yi li ñu wuute lépp ci ab guddaay téewul limub aaya yi nekk ci Alquraan yépp wax nañu ne: "Moo ngi tollu ci 6200, am na ñu wax ne: ëpp na ko, waaye ñi ëpp daal ci li ñu wax mooy 6200."

saar yooyu mooy yii di ñëw

PDF AlXuraan Wolof

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

PDF