Almufassal
Al-Mufassal(المفصل) ay saar lañu yu gàtt nekk ci njeextalu Alxuraan. Mufassal mooy xaaj bi mujj ci 4i xaaj yi ñuy séddale Alxuraan, ñu nekk ci ginaaw Attiwaal, Almi-uun, Almasaanii
Maanaam tur wi
Al-Mufassal ci làkku araab : mooy tàqale ñaari mbir, gëstukat yi nee nañu ci limu wund : mooy saar yi Basmala di faral di tàqale lu bari ndax seenug gàtt, te mooy li topp ci Almasaanii ci saar yi ci Alxuraan.
Li tax ñu ko woowe Almufassal Dañoo wax ne: Ndax saar yu bari yi ci nekk, te wax nañu it ne: Li tax mooy: (Basmala) yu bari yi ci diggante saar yi am na ñu ne itam : Ndax dañoo néew ay aaya yu yuñ ci folli (mansuuxala). Buxaarii nettali na jële ci Sahiid ibnu Jubayri, mu wax ne: “Li ngeen tuddee Al-Mufassal mooy Al-Muhkam” «حديث».
Al-Mufassal nekk ci Alxuraan Al-Mufassal ab baat la bu wund saar yi Li ko dalee Qaaf ba Alxuraan jeex. Mu am ñaari pàcc ñooy: Tiwaalul mufassal, di saar yu gàtt la ko dale Hujjraat ba Habasa, ak Xisaarul mufassal di saar yu gàtt yi la ko dale Habasa ba Naasi Am na it ñu ne Almufassal ñatti xaaj la:
- Yu gudd yi: dale ko ci ndoorteelu Alhujuraat ba ci saaru Buruuj.
- Yu digg-dóomu yi: dale ko ci saaru Attaariq ba ci saaru bayyina.
- Yu gàtt yi: dale ko ci Saarut Salsala ba ci njeexte Alxuraan
Xaaj yii yépp nag ci Almufassal la.
Te ba tay amna 12i xalaat yu wuute ci fan la saari Almufassal dalee. Ñenn ñi ne: Ci Al-Jaasiya, ñenn ñi ne: Muhammad, ñenn ñi ne: Al-Hujuraat, ñenn ñi ne: Qaaf, ñenn ñi ne: Saaffaat, ñenn ñi ne: As-Saffi, ñenn ñi ne: Tabaaraka , ñenn ñi ne: Al-Fath, ñenn ñi ne: Rahmaan, ñenn ñi ne: Al-Insaan, ñenn ñi ne: Lahlee, ñenn ñi ne: Duhee. Li ci gën a siiw nag mooy li ko tàmbalee ci Saaru Qaaf , te loolu mooy li Sarkasii taamu ci Al-Burhaan ak Syuutii ci Al-Itqaan.
Liy firndeel loolu mooy hadiisub Waasila ibnul Asqah’, mu wax ne: Waxoon nañu sahaaba yu Yónent Yàlla bi(SHW): Naka ngeen di xaajalee Alxuraan ci ay pàcc? Ñu ne ko dananu ko xaaj ñatti saar ak juróomi saar ak juróom-ñaari saar ak juróom-ñeenti saar ak fukk ak benni saar, ak xaaju Mufassal bi mooy li nekk ci diggante Qaaf jëm suuf.
Al-Bayhaqii dafa leeral ñeent yooyu wax ne: juróom ñaar yi ñu wax ci hadiis bi ñooy: juróom ñaari yu gudd yi, Assabhu tiwaal (السبع الطوال)ak téemeer yi, Almi-uun (المئون): di wépp saar wu am téemeeri aaya walla lu ko jege, ak ñaar-ñaar yi, Almasaanii (المثاني):di wépp saar matul téemeeri aaya. ak Saar yu gàtt yi, Almufassal (المفصل): te mooy lu yées yooyii.