Aller au contenu

Almi-uun

Jóge Wikipedia.
Nataalu Alxuraan

Xamle Almi-uun

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Almi-uun (المئون)di saar yi nga xam ne mat nañu téeméeri aaya wala ñu jege ko, moom mooy ñaareelu xaaj bi ci 4i xaaj yi ñuy séddale saari Alxuraan yi, moom moo topp ci Assabhu tiwaal, (السبع الطوال) daabi jiitu Almasaanii,(المثاني) ak Almufassal. (المفصل)

Almi-uun (المئون) di tekki nag téeméer yi di wund saari Alxuraan yi nga xam ne dañoo mat téeméeri aaya, walla ñu jege ko.

Ag tuddam ci sunna (hadiis)

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Almi-uun (المئون)  moo topp ci saar yi ñuy wax Assabhu tiwaal.(السبع الطوال)

Cosaanal baat bii di Alm-iuun, (المئون) mi ngi bàyyikoo ci hadiis walla ci sunna, te mooy li nga xam ne moom la Al imaam Ahmat Ibnu Hanbal soloo ci téetéem bi ñuy wax Musnad ci càllala goo xam ne gu rafet la. Jële ci Han waasila Ibnul Asxah mu wax ne Yonent bi salal laahu halayhi wasallama nee na:

(اعطيت مكان التوراةالسبع،وأعطيت مكان الزبورالمئين،وأعطيت مكان الإنجيل المثاني،وفضلت المفصل.)

Mu tudd ci biir hadiis bi ne, joxeef na ma Alm-iin mu wuutu Assabuur kon foofu la baat bi bawoo mooy cosaanal tudde gi Alm-iin.

Bokk na ci saari (Mi-uun yi)

[Soppi | soppi gongikuwaay bi]

Bokk na ci saar yi nga xam ne ci mi-uun yi lañu bokk nag ñooy saar yii di ñëw, Suuratu Yuunus, Huud, Yuusuf, Rahdi Ibraahiima,Hijri, Nahli, Lisraa kahfi, Maryama, taahée, Lanbiyaa, Hajji Muumimuuna, Nuuri, Furqaani, Suharaa, namli, xasasai, Hankbuuti.

Mi-uun daal, mooy saar yi nga xam ne ñoo ñëw ci ginnaaw Assabhu tiwaal, (السبع الطوال) te seeni aaya mat téeméer, walla mu app ko tuuti walla sax mu gën koo néew tuuti.Te am na ñu ne sax saar yooyu, juróom -ñaari saar lañu, wi ci njëkk mooy suuratu Banii Israa-iila, te mooy suuratu israa-i wa ca mujj mooy suuratul Muumimnuuna.