Almasaanii
Almasaanii (المثاني): mooy ñaar-ñaar. Al masaanii mooy ñetteelu xaaj ci ñeenti xaaj yi nga xam ne dees na ko séddalee saari Alxuraan yi, di ñëw ci ginnaaw (المئون) topp ci مفصّل.
Maanaam *masaanii* nag: mooy aaya yi nga xam ne dees leen di jàng di leen baamtu, di baril lu ñu leen di jàng ci julli, ak di baamtu ay nettali ci biir aaya yi, walla ay waare.
Masaanii nag, ñëw na ci Alxuraan ak sunna te mooy Adiis. Bu dee ci Alxuraan noo ngi koy fekk ci ñaari warab, ci (سورة الزمر) fi Yàlla sunu Boroom di wax naan : {" الله نزّل أحسن الحديث كتابا متشابها مثاني"}
baatub "masaanii" di firi lu ñaar-ñaarlu.
Bu nu demee ca (سورة الحجر) tamit dinanu fa fekk Yàlla sunu Boroom muy wax naan: "*ولقد ءاتيناك سبعا من المثاني والقران العظيم*"
Bu dee ci sunna walla Adiis, ñëw na ci waxi Yonent bi slhw ci Adiis bu siiw muy wax naan : "أعطيت مكان التورية السبع، وأعطيتُ مكان الزبور المئين، وأعطيتُ مكان الإنجيل المثاني، وفضّلت بالمفصّل."
Al masaanii nag, am na ñetti wax yu ci woroom xam-xam yi wax ci mooy lan ? Ku ñu naan Abdul laahi Ibnu Abbaas ak Suhaybu Ibnu Jubayri, ñoom nee nañu mooy wépp Saar woo xam ne Yàlla da cay nettali, walla mu di ca léebu, walla mu tudd ca ay farata, walla mbirum gëtën. Bu dee Al hasan Al basarii moom nee na: " Al masaanii mooy (الفاتحة الكتاب). Jeneen wax ji leen ñetteel mooy, daa am ñu wax ne: " Al masaanii mooy wépp saar woo xam ne jéggi na téeméer ba jéggi sax ñaari téeméer, maanaam téeméer bi ñaaru na.