Aespa

aespa (Hangul: 에스파; aespa wala æspa) kuréel K-pop la bu bawoo Seoul ci Kore bu bët Saalum. SM Entertainment moo taxawal kuréel gi, ñeenti nit ñoo ci bokk: Karina, Giselle, Winter ak Ningning. Ñu ngi njëkka génn ci 17 nowàmbar, 2020, ci benn way bu tuddu "Black Mamba."
Ci atum 2021, Aespa moo jël raw gàddu gi ci artist bu bees bi gëna baax ci at mi ci juróomi xew-xewu neexal yi gëna mag ci Kore bu bët Saalum: MelOn Music Awards, MAMA Awards, Golden Disc Awards, Circle Chart Music Awards ci Circle Chart Music Awards, ak Seoul Music Awards ci taarix, moo tax ñoom kese ñoo jël raw gàddu gi ci taarix.
Ci 2024, Aespa jël na prix bu mag bi ci way wu gëna mag ci at mi ci seen way "Supernova" ci MAMA Awards ak ci Golden Disc Awards yépp. Lu weesu neexal boobu, kuréel gi jotna itam neexal yu mag yi ci "Artist bu At mi" ak "Album bu At mi" ci MelOn Music Awards.