ANAFA

Jóge Wikipedia.
Sauter à la navigation Sauter à la recherche

ANAFA (Mbootaay la ma jublu ci mbirum jàngale ak tàggat ñeel muskàllaaf) mi dalu Dakaar Senegaal, sóobu na ci liggéey bi jëm ci tekkib xelteef booloo-bokk, na ka SPIP (aw doxiinu ciiwal ci lënd-jokko Internet ngir gën a mën a saytu dalub jagal yi).

ANAFA, ànd na ci ak benn MNJ (Mbootaay mu Nguur NGànkul) ca reéwum Kanadaa Alternatives, te fas yéene, ci lu yàggul, jagal ay sumb ci Wolof, Pular ak Màndey ci Wikipediyaa ak itam jokko ak bépp MNJ (ci Afriq mbaa feneen) yu farlu ci yëkëtiinu làkki Afirig ci Lënd-jokkoo bi.