Waxtaan:Mbëjbijjaakon

Le contenu de la page n’est pas pris en charge dans d’autres langues.
Jóge Wikipedia.

Sang Ibu, manati la. Ma doon wax ne wikibaatukaay lu am solo la, ngir xam baat yi, waaye ngir sawarloo way yër yeek gëstu yi, doon na gën a yomb su jëleesoon baat yépp yees jàpp ne man nañoo jurug jaaxle akug xamadi ci aji yër ji, firees leen ci ron xët wi, dina di waral xamees leen cig yomb akug gaaw, di waral it ku gën a xam man a indi ag jamam gu wuyyu (critique positive)akug toppam, su gisee lu gën, mu man koo gaaral Misaal def nii ci ron jukki bu nekk:

  • doxalukaayu mbëj: moteur électrique
  • dawaan: courent
  • mbej: électricité

--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 13 Fewirie 2010 à 10:09 (UTC)

batay!, baax na, nuy def noonu book, waante di duggal tekkiy baat yi ci diggantey xala masuma cee ànd ndax bu ëllëgee soo leen bëggee dindi faww nga toppaat mbind mépp jàngaat ko, ci wépp xët woo sos woo leen duggal, dëgg la dina yombal tay waaye yeneen liggéey yu man a ñakk lay juri. Tekki yi soo leen ci duggalee lumu yàgg-yàgg dinga leen fa dindee. --Ibou (xëtu waxtaanuwaay) 13 Fewirie 2010 à 18:38 (UTC)
Loolu lu wer la, waaye bu baat yi gënee suuxatu rekk, ba defees ci ay jubbanti aki toppaat rekk, manees koo ba, bul fàtte ne dañoo nekk di yatt ay baat, man ngaa indi bob man naa xam bu ko gën, bu ma ko xamee ci fr, naka noonu safaan ba --Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 13 Fewirie 2010 à 20:06 (UTC)
xoolal fii. --Ibou (xëtu waxtaanuwaay) 19 Fewirie 2010 à 16:10 (UTC)
xool ko--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 19 Fewirie 2010 à 21:25 (UTC)
xam nga liñu wuutale mooy yaw nitu mbind nga man may nitu xarala ndax xereñ laay jàng ca daara-ju-jawe ja, moo tax sunu gisiin ak sunu waxiin di wuute, donte sax lu bari ñooy bokk liñuy wax. Dafa am baat yu xaralewe ak baat yu neex ciy woy, amaana sax ñu bokk tekki. Te lii ci làkk yépp la am. Sunug wuute ci baat yi gis naa ne foofu la nekk, nitu xarala ak nitu mbind manu ñoo bokk déggiin. --Ibou (xëtu waxtaanuwaay) 20 Fewirie 2010 à 12:28 (UTC)
Wuute daa weesu am solo mooy tax liy juddoo ci nit ñi di wuute, di jur taar, xoolaatal--Abdu Xaadir Kebe (xëtu waxtaanuwaay) 20 Fewirie 2010 à 18:23 (UTC)