Kajoor

Jóge Wikipedia.

Dem : Joowiin, Seet
Kajoor

Ci wàllu xay Kajoor moo doonoon seetub Senegaal. Dammeel moo nekkoon ca kaw di seddale ay ndomboy tànk.

Tëraliin

[Soppi] Koom-koom

ci lu jiitu ñëwug tubaab yi, Kajoor doonoon na nguur guy am-amam newoon gàññ. Mbay ak liggéey ci loxo ak camm ak napp ak ak njaay ñoo nekkoon fànni liggéey yi ëppoon solo ca nguur ga.

[Soppi] Mbay

Mbay moo doonoon liggèey bi ëppoon solo ci koom-koomam. Looloo taxoon ba su baykat yi amul woon jàmm doon na feeñ cakoom ga, manoon naa andi sax ab xiif. Dugub moo ëppoon ci mbay mi ak ci dund gi. Barile woon nañ ay garabi tiir yu daa indi diw tiir ak sëng. Xamoon nañu mbayum. wëtteen.

[Soppi] Liggéey ci loxo ak Njaay

liggéey ak loxo ñeeño yi la ñu ko feetale woon. Napp gi amoon na solo lool ci dund gi. Waaye njaay moo naka-jekk tubaab yi ñoo ëppoon ci ñi ñu ko defal. Mujj na ba yoon yi jòge bëj-gànnaar ñakk solo lool njëgg mi.

Booba fekkoon na géej gi di gën a am solo, Fekkoon na Kajoor da jaay ay der ak ay bëñi ñayy mu dal cay dolli njaayum jaam, ngir am ay fas, ay piis, ay dibi,...

Suuf moo nekkoon jumtukaay bi ëppoon solo, moom ñépp a ko bokkoon. Ñi ñuy wooye Kangam yi mbaa Laman ñoo ko doon saytu. benn nit amu ci woon moomeel. Loolu terewul woon ku mu neexoo mu jariñoo ci kèem kàttanam.

[Soppi] Doole ju bees ji

Nguur gu bees moo fa jële woon ña daa saytu suuf sa ca diiwaan ya. Ñiy doora falu ñoo yoral seen bopp suuf si walla boog ñu dénk ko ay ceddo. Looloo waraloon jalgati gi ak bundxatal gi taroon, ñu tegoon ca kaw gor ña ay njotti bopp yu kenn àttanul, rax ci dolli mayuñu leen fu ñu yakke seen nàkk

[Soppi] Liggéeykat yi

Su fekkee ne suuf si tuxu na ci ay loxo dem ci yeneen, li jëm ci liggéey ak loxo moo des ci loxoy ñeeño yi. Looloo taxoon ba géer ñi sori woon nguur ga, ak ñeeño ya ak jaam ya ñu féetele woon mbay mi, ñoom ñépp mujj nañu nekk ay liggéeykat. Ñoo féetewoo woon indi lépp lu nit soxla ci dund ak takkaay ak col ak ay jëfëndikukaay.

[Soppi] Yoriin

Nguur gu bees gi tax na ba ñu andi tër yu bees ci ay àtte yu bees. Dammeel moo feete woon ñépp kaw. Moom mu ngi daan sant Faal ci geño ak ci meen. Man naa am ñu tànn dammeel ci lu dul geño mbaa meenum Paaléen. Waaye loolu su xewee li koy waral mooy fullay waa ja ak faydaam ak tabeem. Yii yépp ñiy tànn daa nañu ci bàyyi xel.

Su ñaar dee xëccoo nguur gi war na ci ñoom ñaar ñépp ñu nekk Jaambur, mbaa ay Bummi mbaa ay Beñ-jéem. Su ñu bokkee lu ñuy nekk, boroom baat yi nekk ci kaw, yiy tànn dellu seet seen jikko ak nu ñuy àttee ak su mbir nee këtt ne jonn nu ñuy taxawe. Lii doy na tegtal ci leerug seen tànniinu buur.

Loolu terewul nguur gi nekk ndono ci kaw bu amee ku ko war a donn.

Kajoor nekkoon na juroomi tund: Gànjóol, Njaambur ci bëj-gànnaar, Ndéet ca penku, Sañaxoor ca digg Kajoor, Jandeer ca diggante sowwu ak bëj-saalum. Su ñu falee Dammeel dafa war a séddale ndomboy tànk yu mag ya ba ku nekk xam foo féete. Ci mujjug xarnub XVII la Dammeel joxe woon ndigal ngir ndomboy tànk yooyee, ñu man koo takkal rekk ñi cosaanoo Ngàllo te féete ci kër buur.

[Soppi] Buuri Kajoor

1.Decceefu Njoogu (1549) 17.Maawo
2.Amari ngoone Sobel 18.Biram Koddu
3.Maa Sàmba Tàkko 19.Maajoor
4.Ma Xurayja Koli 20.Makoddu
5.Biram Mànga 21.Biram Faatim Penda
6.Daaw Demba 22.Amari Ngoone Ndeela Kumba
7.Majoor 23.Biram Fatma Cub
8.Biram Yaasin Buubu 24.Maysa Tenda
9.Décce Maram 25.Birima
10.Maa Faali 26.Makoddu
11.Ma Xurayja Kumba Joojo 27.Majoojo
12.Biram Penda Ciloor 28.Lat Joor Ngoone Faal(1862)
13.Decce calaw 29.Sàmba Yaasin Faal
14.Lat Sukaabe 30.Sàmba Lawbe Faal
15.Maysa Sukaabe
16.Maysa Tenda

[Soppi] Delluwaay

Paate sow, Démbi Senegaal: ci làmmeñu Wolof, Dakaar, 1998

[Soppi] Lëkkalekaay yu biir

Wikbaatukaay.png
wikbaatukaay am na xët wu tudd:
Seetal BUNTU TAARIIX
Ci « http://wo.wikipedia.org/wiki/Kajoor » lañ ko jële