Jëfandikukat:Ahloubadar

Jóge Wikipedia.

Dem : Joowiin, Seet
Ilimaan.jpg
Wikipedia:Babel
fr-3
en-3
ar-4
it-0
es-0
Seet waa-wikipedia ci làkk-ak-làkk

Sëriñ Abdu Xaadir GÉY Badar (Jiili GÉY) Mongi juddoo Ndakaaru Senegaal, baayam mongi tudd El Haaji Sëriñ Géy Badar (Raay mu sedd) yaayam mongi tudd Soxna Ummi Njiaay mongi nekk Senegaal/ndakaaru/geejawaay mongi jangéé Njiukki (kadior) jamono yi mongi yaggu ci nosukaay gi (ordinateur)ak lepp lu aju ci xam-xamu xaymà (technologie mathématique)

Tëraliin

[Soppi] Li nu Tax a Juk

Salaam bokki Wolof yi nun dey ay wolof lanu yu wolofe te yaakaar ni looloo nu war batax noo juk di laggeeyal wolof moomi ngir mu dabi ay nawleem walla mu jege leen, Te loolu jombul Wolof ndax Yàlla tàggat na ko ba mu nooy te matale, Man dey gis a gu ma làkk wu ko gën a mat, Xanaa kay li am mooy làkk wees toppatoo ak wees sàngane te melna ni Wolof ci yees xaw a sàngane la bokk, Nun dey loolu neexu nu batax noo juk fas-yéene cee def li nu ci man a kus neew ngir dooleel ko mbaa sax wone ko te nu yaakaar ni kepp kuy wolof war na cee jàpp ndax Yàlla mi la bind def la ngay wolof. di jéggaani aw làkk te yor wu mat, nooy te neex a wax loolu bokkul ci fulla day tax ñu yab la te xeeb la, looloo waral réewi tugal yi not ñu te yab nu ba leegi nde ñoo ñu abal aw làkk wu ñuy liggeeyee te Wolof nee «Ku la aal bët fu ko neex ngay xool», nun dey fippu nanu ngir bàyyil leen fi séen làkk yooyi du nu ci weesu wut xam-xam bi nu bokk ñun nit ñepp te ñu aakimoo ko def ko ci seen làkk yi, ndax xam-xam ku ne xam na ni Afrig la fékk baax doxondéem yi ñëw tibb ko yobbu. Li nu ci jot a am a kus neew nu tekki ko ci Wolof ngir askanu Wolof yi yëgul lu xew man cee njariñu, Fii ci sunu réew yi lu tax ñu yeex ? bokku na ci ku fi juddoo ñu dugal la ci daaray nasaraan yi 12at ngay jàng ngir dégg làkku nasaraan door a dugg ci daara ju kawe ji(universite) di jàng laggeey(métiers) 12at yooyii di juge ci sag dund ngir jàng aw làkk woo man a laggeeye te yor Làkku-Juddu wu mat manoon cee jànge xam-xam ci 12at yooyii, Xam ngéen ni loolu jaaduwul moo waral it doofi gis ku am xaalis ci'k ndawam ak yeneeni mbir yu wara tax ñu fonk suñu làkk wi, làkk woo xamni booy gent ci ngay gént booy saaga it ci ngay saaga, boo bëggee defar sa gent di nga ko jëfandikoo,

Jaajëf ci teewlu gi

[Soppi] Lénn ci Ay Woyam

Maa leen di jébbal ab/as njukki ci taalif bu Abdu Xaadir Gey Taalif

  • Aw làkk a ngii wareesukoo sàggane () kum soxalul xam aguloo lumu mane
  • Ak a nooy te matale man na lu ne () Tànn leen ko nu far ko di waxtaane
  • Yéwwute bokk na ci fonk sa làkk () Dina waral nga déggook say mbokk
  • Xam-xam la ca jiitu dégg sa làkk () Dégg gu wer dica waxtaan te dica sàkk
  • Deglu leen ma wax lima fanaane () Tëdd di gent guur def ko waxtaane
  • Mudi jël làkk wi def ko wow ofisel () Dici xalaat dici lëggeey looloo di xel
  • Àbb aw làkk indi ko di ci lëggeey () Te yor wu mat nit ku ñuul yeen a geey
  • Ku la aal bët fuko neex yaw ngay man a xool() Lu lay may bët du naggu yaw nga diko xool
  • Looloo nu dal batax dunu dem ca kanam () Jéggaani làkk, cosaan, ba ci xam-xam
  • Jëm ciw naaj àbbi dàll ànd ak boroom () Bu tàggee mu laaj la ko nde mooko moom
  • Mbokk yéwwul te xàmmee yaw linga moom () Tobaab ya de tée nañu ñoom lañu moom
  • Maay jooy tu lii ci kanamu waa guur gi () Ak ku ko man ci askan wi mbaa kili fa gi
  • Sosal nufi baatukaay nuy baatal () Di sosi baat, baat bu jagul nu baaxal
  • Làkk woo xamni numu laneexe nga koy waxe () Lii de ganul nañu ci sàkki am mbexe
  • nàngam-nàngam.............

Abdu Xaadir Gey >>Ahloubadar (221) 77572 45 77


Ay woy yu Abdu Xaadir Gey ñeel képp ku ñuul.
Boo koy yër na melni yaw lay waxal,

Bismil Laah:


  • Nit ku ñuul yaw ana sa maam ? () Ãreek Piyeer nga jàppe maam
  • Ñépp a ngi daw yaw nga di raam () Altoppe nga ci xarnu yi

  • Luy sa cosaan fécc ak sabar () Diw sa yaram soli sagar
  • Di bëg-bëgi yori gobar () Luy njariñam ci xarnu yi

  • Gis a gu ma yaw loo fi sos () Ngaa ñaa ngi sos ana sa bos
  • Xanaa lile war nga koo rus () Bayil sa waar ci xarnu yi

  • Yaa ngi ni faax luñ sos nga yéem()Yéem mbir day tax ba dooko jéem
  • Bàyyil di yéem te juk di jéem () Ngir sosi lëf ci xarnu yi

  • Gëstul cosaan te fonku ko () La xayadi yaw taaral ko
  • Saw doxoliin soppi ji ko () Ngir xàmmees la ci xarnu yi

  • Fonkal ag xay sak moomeel la () Ña njëkke xay sa maam ya la
  • Ku xay nga ni ab tubaab la () Bàyyil jii wax ci xarnu yi

  • Ag xay ci yaw la fékk baax () Sa nawle yi ni ci saraax
  • Tibb yóbbu dem ni ca faax () Aakimoo ko ci xarnu yi

  • Áddunaal gi yaa koy jëfe () Sa nawle yi dañ koy kafe
  • Xeeti baat yi lañuy sëfe () Ndëgg-sërëx ci xarnu yi

  • Jugal taxaw faj sa wopp () Jugal taxaw xam sa bopp
  • Jugal te dàggi sa kopp () Bayi sa waar ci xarnu yi

Abdu Xaadir Gey >> 221 77572-45-77

[Soppi] Taalif

Sëriñ tuubaa ak allaaji Sëriñ Gueye badar bayub Abdu xaadir Gueye. nataal bi abdu xaadir gueye moka defar
Taalif bii mambay njaay tangèej mooko taalif çi sëriñ tuuba xaadim rasuul (Ahmadou Bamba)

[Soppi] Jokkalekaay

  • Jokkale gu dëkk:221338370027
  • Jokkale guy tuxu:221775724577
  • E-Bataaxal hotmail:djili.gueye@hotmail.com
  • E-Bataaxal Yahoo:badargueye24@yahoo.fr
  • E-Bataaxal:ahloubadar@in.com wala ahloubadar@touba.com
  • Dàli Web: ahloubadar.110mb.com wala mboussobe.110mb.com
  • Blog: ahloubadar.blogspot.com