Jànkoonte gu mbëj

Jóge Wikipedia.

Dem : Joowiin, Seet
Fairytale waring.png Xët wii dafa nekk ci yoonu ndefaru. Sag cëru man na cee am solo!

Jànkoonteg mbëj (résistance) ag feeñte gu jëmm la guy tax nu man a natt bañ gi ag wommatukaay di bañ su ko dawaanu mbëj di jéem a jàll. Lànk googu dafa aju ci jumtukaay bi ñu defare wommatukaay bi, ak réyaayam, ak tàngaayam, ak (su fekkee dawaanu safaanoo la) ci baraayu dawaan gi. Benn ci jeexiitalu jàllub dawaan ci ab wommatukaay, mooy nuggaayam, la nuy wax (jeexiitalu Joule).

Jànkonte gi ci gii yemale nga koy xamee:

 R = \frac{V}{I}

Tekki:

  • R mooy jànkoonte gi nekk ci diggante ñaari cati wommatukaay, ohm(Ω) mooy bennteg nattam.
  • V mooy dénd bi ne ci wommatukaay bi , volt mooy benntegu nattam.
  • I mooy dawaan biy jàll ci wommatukaay bi, amper mooy bennteg nattam.

[Soppi] Jànkoonte gu ag buumu wommatukaay

Jànkoonte R bu ag buumu wommatukaay nii lañ koy xaymaa.

R = \rho \frac{l}{S} \,

Tekki: L mooy guddaayu buum gi, meetar mooy bennteg nattam. S mooy yaatuwaayu dijjaayam, cm2 mooy bennteg nattam. ρ (arafu waa-geres: ro) jànkoontewiinu mbëj, bu jumtukaay bi, ohm * meetar mooy bennteg nattam. Maanaam man gi jumtukaay bi man a lànk dawaanu mbëj jàll ci biiram (nu mu man a mel walla mu toll ko ). Ci lu ëpp Ohm x mm² / m lañ koy natte, lii moo lay jox jànkoonte, ci ohm, bu benn jumtukaay bu gudde 1 m te dijjee 1 mm². Ci misaal: jànkoontewinu përëm mooy 0.0175 ohm x mm² / m, kon lii da lay wax ne ag buumu përëm bu gudde 1 m dijjee 1 mm² jànkoonteg mbëjam day doon 0.0175 ohm.

Am ñaari ngirte ci li waral lu dijjaay bi di gën a néew jànkoonte bi di gën a yokk. Bu njëkk bi mooy ne mbëjfeppal, yi nga xam ne ñoo bokk yan (-), Da ñuy bëmëxante. Kon day am ab jànkoonte ci seen diggante, ngir man lenn boole, lu ñuy gën a dankaloo. Beneen bi li ko waral mooy mbëjfeppal yi da ñuy "mbëkkante" (ndax xam nañ ne yëngu-yëngu mbëjfeppal yi ñooy jur dawan), mbëkkante googu jur ab tasaaroo, te kon day dëngal seen yoon. Loolu jur ay jafe-jafe ci seen demin.

[Soppi] Ni mu ajoo ci tàngaay gi

Nin ko biralee ci kaw, jànkonteb wommatukaay nii lañ koy xaymaa. R_{20}=\rho\cdot\frac{l}{S} waaye ak bii yamale, jànkoontewin bi day aju ci tàngaayu wërlaay gi mu ne. Su fekkee fesalu ñu ko, da ngay jàpp (nin ko waxee ca kaw-a-kaw) ne ci tàngaayu 20° la. Mbindin mii moo koy wone R20. Ci maanaa mooy ne jànkonte bi da fa aju ci tàngaay bi, lii man nañ kaa wax ci bépp jumtukaay. </poem>

[Soppi] Lëkkalekaay yu biir

Wikbaatukaay.png
wikbaatukaay am na xët wu tudd: