Feebaru tëlbëti bu amul app

Jóge Wikipedia.

Feebaru tëlbëti bu amul app Feebaru tëlbëti bu amul appmooy bennfeebaru xelboo xam ne nit ñi dañuy am soxlaa xoolaat mbir yi ay yooni yoon, di leen di defyenn yëngu yëngu yi ay yooni yoon(ñu koy woowe "aada"), walla am yenn ci xalaat yi di ñëwaat ay yoon (ñu leen di woowe "tëlbëti").[1] Nit ñi dañuy am jafe jafe wotu seeni xalaat walla seen yëngu yëngu lu yagg.[1] Yëngu yëngu yi ñuy gëna gis ñooyraxasu, woññi mbir yi, ak di seet ndax ab buntu tëju na walla.[1] Ñenn ñi dañuy am jafe jafe sanni ay mbir ci biti.[1] Yëngu yëngu yii dañuy faraldi am lu baree bare ba nga xamantane nit ki ci boppam dundu bés bu nekk dafay metti.[1] Dafay faraldi lu ëpp benn waxtu bés bu nekk.[2] Mag ñu bare dañuy gis ne nekkin yooyu du tekkiwuñu dara.[1] Mënin bi dafa ànd ak ay tik, feebaru ku jaq, ak njàjan bu yoqu ci wallu xaru.[2][3]

Li koy indi waxuñu ko.[1] Gis nañu ne am na yennndono falkat yi ak ñaar yéppay seex yu niróó ñoom la gëna laal ay seex yi niróówul.[2] Liy indi njàjan yi bokk na ci xale buñu daan noot walla yeneen stress-liy yoq xew xew.[2] Yenn yi bind nañu leen dénc gannaaw ay wall wall.[2] Saytu bi mungi sukkandikoo ci yi koy feeñal te soxla na daq yeneen garab walla li joge ci yeneen jangoro yi koy indi.[2] Ay xaymawukaay ni Yale–Brown Obsessive Compulsive Scale (Y-BOCS) mën nañu leen jëfandikoo ngir saytu rëyaay bi.[4] Yeneen feebar yu metti yi ak ni ñuy feeñe ni yooyu bokk na ci feebaru ku jaq, feebaru naqar ak déteelu gu tar, lekk yu jaxasoo, feebaru tik, ak feebaru tëlbëti bu amul app bu nekkinu nit ki.[2]

Faj mi bokk na cijoxe ay tegtal ngir dimbali nit ki saafara jafe-jafeem, ni pajum nekkin bu àndak xalaat(TCC), ak yenn saay yiy xeex déteelu ni Inhibiteur sélectif de la recapture de la sérotonine walla clomipramine[5][6] Pajum nekkin bu àndak xalaat (CBT) bu feebaru tëlbëti bu amul app (OCD) bokk na ci yoquteek liy indi jafe jafe yi te du bayyi nekkin bi di amaat ay yoon. [5] Bu clomipramine di dox ak SSRI yi, efe sëkondeer yi tax na ba pajam dañu wacce ci ñaareelu liiñ bi. [5] Yuy xeex ñakk àndak sago yu ñu dul faraldi gis mën nañu am njëriñ bu leen jëfandikoo ci kaw SSRI bi ngir fajum yenn yu fës yi wante dañu leen di boole ci njàjan yiy yoqu efe sëkondeer yi. [6][7] Ñakka paj mi, dina tax ba mënin mi di faraldi yagg lool.[2]

Lu tollook 2.3% ci nit ñi ci seen giiru dund feebaru tëlbëti bu amul app dal na leen.[8] Xayma bi ci benn at mungi tollu ci lu jege 1.2% ci addina bi yépp.[2] Feebar bi duy faraldi feeñ bu nit ki weesoo fanweeri at ak juróóm, te génn wall nit ñépp dañuy tambali am ay jafe jafe balaa seen ñaar fukki at.[1][2] Góór ak jigéén yépp ñoo tolloo ni leen feebar bi dale.[1] Ci Anglais, baatu tëlbëti bu amul appdañu koy faraldi jëfandikoo ci anam bu ñu tegul ci yoon bu bokkul ak OCD ngir wonale nit ku set lool ci li muy def, ku bëgg lu wóór, kuy jël, walla kuy xool fenn lu yagg.[9]

  1. 1,0 1,1 1,2 1,3 1,4 1,5 1,6 1,7 et 1,8 The National Institute of Mental Health (NIMH) (January 2016). "What is Obsessive-Compulsive Disorder (OCD)?". U.S. National Institutes of Health (NIH). Archived from the original on 23 July 2016. Retrieved 24 July 2016.  Unknown parameter |df= ignored (help)
  2. 2,00 2,01 2,02 2,03 2,04 2,05 2,06 2,07 2,08 et 2,09 Diagnostic and statistical manual of mental disorders : DSM-5 (5 ed.). Washington: American Psychiatric Publishing. 2013. pp. 237–242. ISBN 978-0-89042-555-8. 
  3. Angelakis, I; Gooding, P; Tarrier, N; Panagioti, M (25 March 2015). "Suicidality in obsessive compulsive disorder (OCD): A systematic review and meta-analysis.". Clinical Psychology Review 39: 1–15. PMID 25875222. doi:10.1016/j.cpr.2015.03.002. 
  4. Fenske JN, Schwenk TL (August 2009). "Obsessive compulsive disorder: diagnosis and management". Am Fam Physician 80 (3): 239–45. PMID 19621834. Archived from the original on 12 May 2014.  Unknown parameter |df= ignored (help)
  5. 5,0 5,1 et 5,2 Grant JE (14 August 2014). "Clinical practice: Obsessive-compulsive disorder.". The New England Journal of Medicine 371 (7): 646–53. PMID 25119610. doi:10.1056/NEJMcp1402176. 
  6. 6,0 et 6,1 Veale, D; Miles, S; Smallcombe, N; Ghezai, H; Goldacre, B; Hodsoll, J (29 November 2014). "Atypical antipsychotic augmentation in SSRI treatment refractory obsessive-compulsive disorder: a systematic review and meta-analysis.". BMC Psychiatry 14: 317. PMC 4262998. PMID 25432131. doi:10.1186/s12888-014-0317-5. 
  7. Decloedt EH, Stein DJ (2010). "Current trends in drug treatment of obsessive-compulsive disorder". Neuropsychiatr Dis Treat 6: 233–42. PMC 2877605. PMID 20520787. doi:10.2147/NDT.S3149. 
  8. Goodman, WK; Grice, DE; Lapidus, KA; Coffey, BJ (September 2014). "Obsessive-compulsive disorder.". The Psychiatric clinics of North America 37 (3): 257–67. PMID 25150561. doi:10.1016/j.psc.2014.06.004. 
  9. Bynum, W.F.; Porter, Roy; Shepherd, Michael (1985). "Obsessional Disorders: A Conceptual History. Terminological and Classificatory Issues.". The anatomy of madness : essays in the history of psychiatry. London: Routledge. pp. 166–187. ISBN 978-0-415-32382-6.