Diiney Afrig

Jóge Wikipedia.

Dem : Joowiin, Seet

Ca Afrig, diiney yi yag nanu fa am. Diiney bu am Afrig, ño bokk cossan. Ca jamono yu ngurru Koush amone, tey di nek wa Sudaan ak Ecoopi, nit ño fa nekkone, danu daan nek ca diiney yu jekk am ca aduna. Ca diiney bobu, nit yi dañu daan geum bene Yallah. Ca wa Misra tey di nek Isipt, ba Sudan, diiney bobu mo fa amone. Ca diiné bi, yallah, melni lislaam, téemer tuur la amone, tuur ku nek ñu woné bene jiko bu yallah. Ca tuur yi amone na: Ra (moye ku ñu leeral), Amon (moye Ku nebbatu), Atoum (ku kumpa), Atona-Ankh (Kattan Yallah bi ku yengal aduna).

Taarixkat yi Seex Anta Joob ak yenene, woné nanu, diiney yawut, kirist ak Lislaam, fofu (wa Misra) lañu cossano. Ndax yonent yi ñu nek ca diiney yawut ak kirist, ca sene teree, biibël ak thora, Ibrahima ak Moussa, fofu lañu jang diiney, ca bi ñu tuddu ca lakk wa misra bu fa amone jamono bobu, Per-Ankh, ca kalamu wolof moye: Keur bu ñu jang Diiney ak xam xam. Ba paré yobu nañu Diiney bobu ca sene Mbokku yawut, ndax bobu amuñu woon Diiney, nak bu urus ak Moloch ak Baal lañu doon geum. Fofu tamit lañu jang naka lañu saraxé Xaar, ak naka lañu xarafal, ca Per-Ankh yi. Ndax ca diiney bu afrig, sarax ak xarafal amona bu yag, ba tey.

Taarikhkat woné nañu tamit, yawut yi nekkone ca rewum nit ku niul ba, wa misra, kene deful leen ay jaam. ñow nañu fofu ca jaam, gën misra ca jaam.

Bammel bu Méroé, Sudaan


Tuuru lislaam yu bari, ca diiney afrig bobu la jogué:

  • Ibrahim, moye Ib-Ra-Him, ca lakku wa misra bu fa amone bu jek moye, ku am yallah (Ra) ca xolam
  • Moussa, moye Messu, ku yallah juur
  • Sara, Sa-Ra moye, domu yallah
  • Ismael, Is-Ma-El, Yallah mo bax
  • Myriam, Meri-Amon, ku yallah beugeu. Amon moye bene tuuru yallah ca diiney Afrig.

Ca Misra, lakku bu fa amone, Medu Neter (Battu Yallah), la tudde woon. Lakk bobu mo Juur lakku Wolof, ak Lakk yi yeup ca biir afrig.

Wa misra moye fofu xeet yi nek ca biir afrig tey, cossano, té diiney bu fa amone, yobu nene ko ca fofu lañu deuk tey, reewum Afrig bu nek ca suuf Saara.

Buñu waccé ca Afrig bobu, xeet yi tass nañu yu bari, té ba paré xeet ku nek, amone nañu bene tuddu ngiir tuddu yallah:

Afrig gu bëj-saalumu-Sahara.
  • Mandinke yi (Sooninke, Bambara, Jula, Xasonke, ak ñu dem nonu) yallah, Maa Ngala lañu daan wax.
  • Pël yi, Gueno lañu daan wax.
  • Séeréer yi, Roog Seen
  • Joolaa yi, Atemi Sembe
  • Sonraï yi deuk ca Mali ak Niseer, Yarkoï
  • Bassari ak Bedik yi, Ounounga
  • Dogon yi: Amma
  • Yoruba yi Ca Niseeria: Olodumare
  • Masaï yi ca Kenya: Engaï
  • Zoulou yi ca Afrig bej Saalum: Inkosi
  • Akan yi, ca rewum Bene, Togo, gana, kote diiwaar: Mawu
  • Wa Ecoopi: Waqa
  • wa Kongo ca xeet yi Bantu: NzamBe


Diiney bi tamit, xeet yi Afrig bi, amona ku nek, joox na ko bene tuur, Vodu ca wa Bene, Togo, Gana, ba Niseeria, wala Bwiti ca wa Gabon, Mwett wa Cameroon.

Ca Diiney Afrig bi, danu ne Yallah kene munul ko wo. Ndax ca diiney bi, nit yi dañu wax, Yallah mag na torop, mag na ba, kene ku munul ko woo, su ko kene defe, da melni mayo ko worma. Dañu ne yallah baxna ba munul jox kene te joxul kenene. Li moye tax yallah ca diiney bobu, ca nit ku nek, tek na ca seen biir, bene dogu yaramam, lolu moye defni nit bi mu meunteu dund (Ruu ca Wolof). Dogu yaramam bu nek ca nit yep, dog bobu nit yi wara jang, té defni mu set say sounek, suñu beugeu am jam ca aduna, ak yenene nit yi ak sene njabot, wala am kheweul ca sene liguey, ak yu demé nonu. Wala suñu beugeu dem ajjana. Ruu bi, nekatul ca nit rek, gancax yi tamit, ak rab ya, amna ñu ko.


Ca diiney bobu, mam yi ñu nek ca rewum yallah, ño nek ca diganté yallah ak nit yi. Mam yi, ño yobu ñaan yi nit yi ca yallah. Li moye tax ca diiney bu am Afrig, mam yi, amna nu solo. Wayé su bene nit gëen aduna, ngiir mu nek mam (Akhu wala Matiu ca diiney bobu), yallah mo wara ko mey lolu su nit ki, bu mu néké aduna, lu bax lodone def. Nit ki, su lu bone lodone def, bu mu néké aduna, meunoul nek mam (Akhu), té ca aduna, ti njabotam ak yenene nit yi, ken mounoul ko niane dara. Ca Seereer yi nek ca Senegaal, mam yi Pangol moye seen tuur. Lebu yi, mam tuur lañuy wax.

Téeré Bammel, bu Téti Royuwaay:Ier ca Saqqarah

Tamit, xam nañu ni, ca xeet ku nek, Yallah wacc na leen ay yonenté. Li moye tax diiney afrig bobu, amna ñi seen yonenté. Tarikhkat yi woné nañu tamit, yonenté bu nek ca diiney afrig, yenene diiney yi melni diiney nasaraan, yawut ak lislaam, dugu neen ko ca sene geum. Yonenté bu Afrig ño:

  • Ausar. Yonenté bu jekk am ca aduna ca diiney bobu. Amna tuur yu bari: Isha (ca lislaam moye Issa), Oni (ca diiney nasaraan moye Ori), Kem-Our, ca lakku Medu-Neter bu amone ca jamono bobu mu nekkone, Kem-Our moye nit ku ñul bu mag. Tarikhkat né nañu, tarikh bu Ausar mo juur tarikhu Issa bu lislaam, Kirist ca Biibël. Ausar ca xeet Anu la bokkéwone, bene xeet bu amone bu jekk, di dekkone ca Sudan (Nguruu Kush), ñom ño tabax ngurru Misra, ak Buur Fari ba mu tuddu Narmer, amna nient junni at. Ausar, bobu nekkone ca aduna, ay junni ak junni at la woon, sogo sax diiney yawut am, sogo ngurru Misra am.
  • Aset (tuuru Aïssata ci mom la jogué). Mo done jabaru Ausar. Ki rek ca aduna mo xamone tuuru yallah yep. Ndax nit ya, xam nañu juroom nient fukk ak juroom nient tuuru yallah, wayé Aset tuur yep la xamone. Temeram tuur yallah, mo def ni ku ko xam meunta sos lep melni yallah. Wayé yallah néna Aset: xamga sa ma temer tuur, wayé man ma la geuneu mag, té dina def ni nga meunteu juur nit, wayé dinga ko juur ca sa biir yaram. Li moye tax Jigen ño juur dom ya, ca diiney bobu. Aset ak Ausar ño juur Heru, seen dom. Natal bi ñi woné yayu Kirist bu tuddu Mari ak domam, ca natal bi ñi woné Aset ak domam Heru la jogué.
  • Seth. Ca diiney afrig moye Seytan. Satan ca diiney kirist, wala Sheytan ca diiney lislaam, ca ki la jogué. Ca diiney afrig, yallah mo joor Seth ligueyam li muy def. Ligueyam moye mu sonal nit yi ca aduna, ngiir yallah meun xam ku jarral dem ajjana ak ku wara dem Douat, Douat moye Al-Jahim ca lislaam, Enfer ca diiney nasaraan. Nebetou modoone jabaru Seth, wayé ki baxon na. Nebetou modoon dencc keuru Seth, te di nettali ca Aset ak yenene yi, lan la Seth bougone def ngiir mu meunteu sonal Ausar ca ndigel bobu yallah ko joox. Ndiguelu yallah joox Ausar, modoon mu jubanti nit y nekkone ca aduna, ngiir ñu xamné amna yallah, té bayi yeufu bone ño doon def.
  • Djehuty. Ca diiney afrig, ki mo indaalé xam xam, ak bind, ca aduna. Ki moye Idrissa ca lislaam, wala Henoch ca dinney nasaraan.
  • Maât, (tuuru Maty, ca ki la jogue). Moye bene yonenté bu jigen, mo doone jangal nit yi, wax bu degg, naka lañu wara bax ak yenene nit yi, ak lep bu demé nonu, Jom. Li mote yax ca diiney afrig, su bene nit deful lu bax, dañu né ko: Defal Maât. Ubuntu ca wa Kongo.

Ñom ño yonenté bu geuneu am solo ca diiney bobu, ndax amna yenene, té xeet yi ca afrig, bu nekk ca diiney afrig, ba tey, am nañu tuur yu bari ngiir tuddu yonenté yi. Ca diiney bobu, Neteru mo doon tuuru yonenté yi, wala Sara. Neteru ak Sara moye ca Wolof, domu Yallah.

Ca yonu imbraator gu gana, lislaam ñow na soowu Afrig, ca jamono bobu, lislaam ak diiney bu Afrig, ca jaam lañu dekkande woon. Ak tubap yi, diiney yu nasaraan ño na afrig, wa diggu afrig.

Ak Jihad yi jullit defonne ca XIXee xarnu, diiney bu Afrig ba, wañi na bu bari. Tubap yi tamit ak canc gi, def neen ñi, diiney afrig bobu mu wañi bu bari.

Wayé amna ay xeet, diiney lislaam wala kirist lañu nek, wayé dañu dugal ca seen geum, ay geum nek ca diiney afrig bobu (Syncrétisme) melni joola yi, wala Bantu yi, lebu yi, Akan yi.

[Soppi] Téerekaay

  • La Philosophie africaine de la période pharaonique, Théophile Obenga.
  • L'Origine négro-africaine des religions dites révélées, Doumbi Fakoly.
  • Bilal le prophète, Doumbi Fakoly.
  • Parenté génétique de l'égyptien pharaonique et des langues négro-africaines, Seex Anta Joob.
  • Théophile Obenga, Origine commune de l'égyptien ancien, du copte et des langues négro-africaines modernes. Introduction à la linguistique historique africaine.
  • Nations nègres et culture : de l'antiquité nègre égyptienne aux problèmes culturels de l'Afrique noire d'aujourd'hui, Seex Anta Joob.
  • Cossanu Afrig cib nataal, Seex Anta Joob.