Betani bu Yerusalem

Jóge Wikipedia.
Dem : Joowiin, Seet

Dëkk bu ndaw ci tundu Oliw ya, daanaka 3 kilomet diggam ak Yerusalem ci yoonu Yeriko. Tur bi moo tekki këru figg yi. Yaakaar nañu ne amoon na fa dëkk tàmbali ca 600 at yu jiitu jamono Kirist ba 1400 at gannaawam. Foofu la xariti Yeesu, di Màrt, Maryaama ak Lasaar, dëkkoon. Ca ayu-bésam bu mujj ba Yeesu doon na fanaan Betani, di xey dem Yerusalem bés bu nekk. Mc 21:17; 26:6; Mk 11:1,11,12; 14:3; Lu 19:29; 24:50; Yow 11:1,18; 12:1,9.