Anañas

Jóge Wikipedia.
Dem : Joowiin, Seet

Xët wii day dajale mbooleem tëriit walla jukki yu wuute ëmbiit te bokk tur. Disambig.svg

Ci làkku ibrë la tur wi jóge. Ci angale ak ci faranse mooy Ananias.

Turu 3 nit ñi ci Injiil:

  1. Benn toppkatu Yeesu ci Yerusalem, mooy jëkkëru Safira. Jéemoon nañu nax mbooloo ñi gëm bi ñu jaayee woon benn pàkk ngir jox xaalis bi ndaw yi. Yàlla moo ko rey ca saa sa. Man nga ko jàng ci Jëf 5:1-10.
  2. Benn toppkatu Yeesu ci Damas, bi Yàlla yónni ci Pool jëkk bi Yeesu feeñee ci moom (Jëf 9:10-18; 22:12-16).
  3. Saraxalekat bu mag ba, ca 47 g.K. ba ca 59 g.K., maanaam ci jamano Pool ji (Jëf 23:2-4; 24:1). Ci at 66 g.K. kenn ku tudd Sakarii moo ko rey.