Alaaji Maalik Si

Jóge Wikipedia.
(Yoonalaat gu jóge Alaaji Maalik SI)
Dencukaay:Maalik-si.jpg
Nataalu Alaaji maalik Si

Alaaji Maalik Si ma nga gane àdduna ci Dëw Faal gniou koy wowé Gaaya bokk ci tunduw Dagana ci atum 1855. Waa-juram wu góor tuddoon Usmaan, wu jigéen Faa Wàdd Wele. Mi ngi jànge alxuraan Luga ci kenn ci taalibey Alaaji Omar Futiyu Taal yi. Bi mu doonee mag la dem Màkka, bi mu dellusee sax ci jaamu Yàlla ak jàngale ak dugal ñi duli jullit ci lislaam. Ci noonu la tase njàngalem yoonu Tiijaan ci Senegaal jaare ko ci tuxoom yi ci Jolof, Kajoor ak Ndar. Ci mujj gi mu dëkksi Tiwaawan ci 1902. Fa la njëkk a wootee gàmmu.

Juddoom[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ma nga gane àdduna Dëw Faal wetu Gaaya bokk ci tunduw Dagana ci atum 1855. Waa-juram wu góor tuddoon Usmaan, wu jigéen Faa Wàdd Wele. Usmaan moom doonoon doomu Muhaz miy doomu Mohamed, sëtu Yuusuf, Daraaman, Sire, Bubu, Yahya, ñoom ñépp di sëti sëriif Sams Eddin, loolu moo ko tax a askanoo ci araab. Baayam Usmaan, moo bàyyikoo Gànnaar fa mu doon jànge, ci Ustaas Muhamadu Baaba Al Daymani, ñëwoon Waalo doon fa wut ab téere bu kenn kii di Maalik Sow bu Gaaya rekk yoroon, ba mooy mujj doon turandoowam. Ñoom dañoo mujj dooni wolof, ndax ay maamam sax yàggoon nañu waalo, takkoon fay soxna.

Njàngam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ni bépp doomu waalo-waalo, ba mu doone gone la dal baa, nijaayam Alfa Mayoro moo ko doon njëkk a jàngal ba yàgg turandoom Cerno Malik Sow jël ko. Ci 1863, bi muy am 8 at, la dem Sagata ca Jolof ci baayam ba Amadu Si, mu jógeeti fa dem ci yeneeni ustaas, ku ci nekk taggak ko ci sag maneel, (fiq, nos-wax, Tawjiid, añs), ku ci mel ne Ceerno Ngañ Ka mi mu àndaloon dem Careen ci Fuuta Tooro ci 1873, bi muy am 18 at la jeexal njàngum alxuraanam ci tukkeem ca Fuuta, ba tay, ca Longe, cig leeral, ci sëriñ Abdu Bitey, ak ca Gànnaar. Ca la ñibbee dëkkam, Nijaayam Alfa Maayoro jox ko wird tiijaan ak maqaamay "mawdo", moom mi jëlee woon wird bi ci Alaaji Omar Taal ay at laata Maalik di judd. Te bii doonul woon benn lijaasa rekk bi mu amoon, ndax Mawdo Faal joxoon na ko ci 1876, ak Mohamed Ali it , ci ginnaaw bi.

Ginnaaw bi mu mokkalee alxuraan, la jàngi fiq, ci lu njëkk, këram la ko doon jànge, ginnaaw bi mu dem ci Sëriñ Muur Ka. Bi mu mokkalee fiq la dem jàngi àtteyiin ca Boxal ci Waalo daaraay Sëriñ Ahmadu Njaay, ak ca Kër Kodde ci Njambur daaray Sëriñ Moodu, ak ca Tayba Séy daaraay Sëriñ Moor Kal Séy. Ginnaw bi mu jànge Risaala, ci diggante 1882 ak 1880 mi ngi amoon 25 at, la dem Ndar ci Sëriñ Ahmadu Njaay. Mu jógeeti fa dem Njambur ngir àggalee fa njàngum àtteyiin ma te door jàng Xalil ci Sëriñ Birahim Jaxate ak Sëriñ Mamadu Wadd. Waaye at ma ca topp la jeexal Xalil ca Mbokkol ci Kajoor ci Sëriñ Masila.

Ci 1885, bi muy am 30 at, dajale woon na xam-xam bu jéggi-dayoo, loolu mayoon na ko mu man a doon ustaas, jamono yooyu bokkoon na ci ñi ëppoon xam-xam ci Senegaal, ndax lépp lu ñu manoon jàngale ci réew mépp jàngoon na ko, demoon na ci ñi fi ëppoon xam-xam. Ci tukkiy njàng yi mu defoon yépp, ca jamono jooju, jaaroon na ca tund ya ëppoon boroomi-xam-xam: Gànnaar, Fuuta, Njambur, Kajoor. ci dëkk yi mu dem man nan cee lim: Ndoj Séy, Pacaas, Ngicc, Jaabe Lidube, Orefonde, Longe Sëbe, Longe Fulbe, Careen, Ndar, Tayba Séy, Daraaman, añs.

Dundam ak jëfam[Soppisoppi gongikuwaay bi]

Ginnaaw ag njàngam, Ngambu la dem dëkki di fa liggéey aka jàngale ngir dund ci ñaqam. Liggéeyam mayoon na ko mu man a aji Màkka jaare ko bëj-saalumu Fraas, ci Maarsey ak ci Aleksandri, ci 1889, amoon na 33 at.

Bi mu jóge Màkka am maqaamay alaaji, ci la sosee Sawiya bu Ndar ci 1892. Ganeji Jolof ab diir sos fa ay daara dellu Waalo. Ay tukkeem yu bari ci biir réew mi, ngir tasaare diine ak xam-xam, ak Wasifa yi doon ame ci Sawiya yi taxoon sancaan bi tambali koo fuglu, yaakaar ne day woote ngir xeex ko ak ngannaay yi. Ca la ko kaŋ ba nekkoon Ndar te nekkaloon fi sancaan bi (waa Fraas yi) woolu ngir mu joxe ay leeral ciy yëngu-yëngoom. Ñoom dañoo foogoon ne dafa dencooni ngannaay ci biir jakka yi, difa waajal xare ak ñoom. Bi ñu ko ci laaje mu ne:

«Yàlla daf nu digal, man ak yeen, nu jaamu ko, di julli ci moom. Ngeen bañ, ma nangu. man ak samay taalibe defuñu lenn lu dul kañ yàlla te di julli ci gën-gi-mindeef. Te li ngeen di wax ci ngannaay yi, genn ngannaay gi ma yor mooy sama kurus te moom laa fas-yéene xeexee ba Lislaam ak Tijaaniyaa tas ci àdduna bépp.»

Sancaan yi jàppoon nañu ne Alaaji Maalik moo doonoon nik ki ëppoon xam-xam te daq a jangalee ci réew mépp. Baat yii di nañu leen fekk ci dencu(archive) yu Senegaal yi ak yu Fraas. Seede yi gëna neex ci nopp ñooy yu Seex Sidiya, my sëtu yonnenti bi doonoon it sëriñu xaadir bu mag. Ginnaaw ba mu taxawalee sawiya ca Ndar, taxawal na beneen ci Ndakaaru ci wetu njéndul nguur gi. Njarnde la dem dëkki, jóge fa dem Jaksaaw, laataa muy dem Tiwaawan ba faaw. Jibril Gëy moo ko fa woolu woon ngir mu defal leen tafsiir Alxuraan, ñu faf ko fa téye, ci 1902 mu sos sawiya bu Tiwaawan. Ci yokkug ndongo yi, mu jël yeneen ustaas ngir ñu jàppale ko ci njàngale mi. Ca daaram ja, daa nañu fa jàngalee bépp xeetu xam-xamu lislaam. Ci téemeer ak lu tekk ci ndongo yi mu yoroon, lu mat juroom-fukk daan nañu dem itam ci jànguy nasaraan si, doomam sëriñ Baabacar Si daa na ca dem, Loolu firnde la ci xelam ak gis-gisam bu ubbeeku.

Ci Tiwaawan la wootee Gammu gu njëkk, ngir màggal seydinaa Muhammad. Mu door njàngale mu diggoodi, dëkk bu ne mu yabal fa ab muqadam bu fay jàngale diine.

yenn ciy téereem[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • Ifham al munkiru jaani: téere bu muy jàngale luy tiijaaniyaa, ustaas Rawaan Mbay moo ko tekki ci wu-fraas
  • Khilaçu ez-Zahab: mooy téere bi gën a mat buy wax ci jaar-jaaru yonnenti bi, ba mu juddo ba, ba muy génn àdduna, Rawaan Mbay moo ko tekki ci wu-fraas
  • Sharh Khilaçu ez-Zahab: faramfacce gu téere bi, moom mi bind téere bi moo ko def
  • Faakihatul Tullab: est un précis sur la Tijaniyya et ses pratiques.Traduit en français par l'éminent Professeur Rawane Mbaye
  • Dîwân: ay woy la ci yonnenti bi, Ahmed Tiijaani, Alaaji Omar Taal, ay xam-xami diine, ay xelal ngir jullit ñu rawatina tiijaan yi
  • Khutbatul Jumu'a; digle julli ajjuma
  • Khutbatul 'I'd: digle julli tabaski ak korite
  • Kifayat ar-raghibîn: ( li aji-gëm gi soxla) ustaas Rawaan Mbray moo ko tekki ci wu-fraas

Téerekaay[Soppisoppi gongikuwaay bi]

  • (en) Michael A. Gomez, Malik Sy, Bokar Saada and the Almaamate of Bundu, Chicago, University of Chicago, 1985, VIII-484 p. (Thèse)
  • (fr) Cheikh Tidiane Fall, El Hadji Malick Sy à Tivaouane de 1902 à 1922, Dakar, Université de Dakar, 1986, 92 p. (Mémoire de Maîtrise)
  • (fr) Rawane Mbaye, La pensée et l'action d'El Hadji Malick Sy : Un pôle d'attraction entre la Shari'a et la Tariqa. Vie et œuvre de El Hadji Malick Sy, Université de la Sorbonne nouvelle, Paris III, 1993 (Thèse)